Syriac: NT

Wolof: New Testament

John

4

1ܝܕܥ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܕܫܡܥܘ ܦܪܝܫܐ ܕܬܠܡܝܕܐ ܤܓܝܐܐ ܥܒܕ ܘܡܥܡܕ ܝܬܝܪ ܡܢ ܝܘܚܢܢ ܀
1 Amoon na benn bés Farisen yi dégg ne, ñiy topp Yeesu ñoo ëpp ñiy topp Yaxya, te ñi Yeesu sóob ci ndox ñoo ëpp ñi Yaxya sóob.
2ܟܕ ܠܐ ܗܘܐ ܗܘ ܝܫܘܥ ܡܥܡܕ ܗܘܐ ܐܠܐ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܀
2 Fekk Yeesu moom ci boppam daawul sóob kenn ci ndox, waaye ay taalibeem ñoo daan sóobe.
3ܘܫܒܩܗ ܠܝܗܘܕ ܘܐܙܠ ܠܗ ܬܘܒ ܠܓܠܝܠܐ ܀
3 Bi Yeesu yégee loolu nag, mu jóge Yude, dellu diiwaanu Galile.
4ܡܥܒܕܐ ܗܘܬ ܠܗ ܕܝܢ ܕܢܐܬܐ ܢܥܒܪ ܥܠ ܒܝܬ ܫܡܪܝܐ ܀
4 Bi muy dem Galile, waroon na jaar ci diiwaanu Samari.
5ܘܐܬܐ ܠܡܕܝܢܬܐ ܕܫܡܪܝܐ ܕܡܬܩܪܝܐ ܫܟܪ ܥܠ ܓܢܒ ܩܪܝܬܐ ܕܝܗܒ ܗܘܐ ܝܥܩܘܒ ܠܝܘܤܦ ܒܪܗ ܀
5 Noonu mu agsi ci wetu dëkku Sikar ci tool, bi Yanqóoba mayoon doomam Yuusufa.
6ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܬܡܢ ܡܥܝܢܐ ܕܡܝܐ ܕܝܥܩܘܒ ܗܘ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܠܐܐ ܗܘܐ ܡܢ ܥܡܠܐ ܕܐܘܪܚܐ ܘܝܬܒ ܗܘܐ ܠܗ ܥܠ ܡܥܝܢܐ ܘܐܝܬ ܗܘܝ ܫܬ ܫܥܝܢ ܀
6 Foofa la teenu Yanqóoba nekkoon. Yeesu toog ca pindu teen ba, di noppalu ndax coonob tukki ba. Ca digg-bëccëg la woon.
7ܘܐܬܬ ܐܢܬܬܐ ܡܢ ܫܡܪܝܢ ܕܬܡܠܐ ܡܝܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܗܒ ܠܝ ܡܝܐ ܐܫܬܐ ܀
7 Noonu jigéenu waa Samari ñëw fa di root. Yeesu ne ko: «May ma ndox, ma naan.»
8ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܓܝܪ ܥܠܘ ܗܘܘ ܠܡܕܝܢܬܐ ܕܢܙܒܢܘܢ ܠܗܘܢ ܤܝܒܪܬܐ ܀
8 Fekk booba nag, taalibey Yeesu ya dañoo demoon ca biir dëkk ba, di jënd lu ñu lekk.
9ܐܡܪܐ ܠܗ ܗܝ ܐܢܬܬܐ ܫܡܪܝܬܐ ܐܝܟܢܐ ܐܢܬ ܝܗܘܕܝܐ ܐܢܬ ܘܡܢܝ ܫܐܠ ܐܢܬ ܠܡܫܬܐ ܕܐܝܬܝ ܐܢܬܬܐ ܫܡܪܝܬܐ ܠܐ ܓܝܪ ܡܬܚܫܚܝܢ ܝܗܘܕܝܐ ܥܡ ܫܡܪܝܐ ܀
9 Jigéen ja tontu ko ne: «Yaw, ngay Yawut, man maay jigéen ju dëkk Samari; nan nga ma man a ñaane ndox?» Jigéen ja wax na loolu, ndaxte Yawut ya bokkuñu woon ak waa Samari ndab yu ñuy lekke.
10ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܠܘ ܝܕܥܐ ܗܘܝܬܝ ܡܘܗܒܬܐ ܕܐܠܗܐ ܘܡܢܘ ܗܢܐ ܕܐܡܪ ܠܟܝ ܗܒ ܠܝ ܐܫܬܐ ܐܢܬܝ ܫܐܠܐ ܗܘܝܬܝ ܠܗ ܘܝܗܒ ܗܘܐ ܠܟܝ ܡܝܐ ܚܝܐ ܀
10 Noonu nag Yeesu tontu ko: «Soo xamoon li Yàlla maye, xam ki lay ñaan ndox, kon yaw ci sa bopp, yaa koy ñaan, te moom dina la may ndoxum dund.»
11ܐܡܪܐ ܠܗ ܐܢܬܬܐ ܗܝ ܡܪܝ ܠܐ ܕܘܠܐ ܐܝܬ ܠܟ ܘܒܪܐ ܥܡܝܩܐ ܐܝܡܟܐ ܠܟ ܡܝܐ ܚܝܐ ܀
11 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund?
12ܠܡܐ ܐܢܬ ܪܒ ܐܢܬ ܡܢ ܐܒܘܢ ܝܥܩܘܒ ܗܘ ܕܗܘ ܝܗܒ ܠܢ ܒܪܐ ܗܕܐ ܘܗܘ ܡܢܗ ܐܫܬܝ ܘܒܢܘܗܝ ܘܥܢܗ ܀
12 Xanaa kay xalaatuloo ne, yaa gën a màgg sunu maam Yanqóoba, moom mi nu gasal teen bii, mu naan ci moom ak i doomam, wëgg cig juram?»
13ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܟܠ ܕܢܫܬܐ ܡܢ ܗܠܝܢ ܡܝܐ ܬܘܒ ܢܨܗܐ ܀
13 Yeesu wax ko ne: «Ku naan ci ndoxum teen bii, balaa yàgg mu maraat,
14ܟܠ ܕܝܢ ܕܢܫܬܐ ܡܢ ܡܝܐ ܕܐܢܐ ܐܬܠ ܠܗ ܠܐ ܢܨܗܐ ܠܥܠܡ ܐܠܐ ܡܝܐ ܗܢܘܢ ܕܝܗܒ ܐܢܐ ܠܗ ܢܗܘܘܢ ܒܗ ܡܥܝܢܐ ܕܡܝܐ ܕܢܒܥܝܢ ܠܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܀
14 waaye ndox, mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom bëtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.»
15ܐܡܪܐ ܠܗ ܐܢܬܬܐ ܗܝ ܡܪܝ ܗܒ ܠܝ ܡܢ ܗܠܝܢ ܡܝܐ ܕܠܐ ܬܘܒ ܐܨܗܐ ܘܠܐ ܗܘܝܬ ܐܬܝܐ ܕܠܝܐ ܡܢ ܗܪܟܐ ܀
15 Noonu jigéen ja daldi ko ne: «Sang bi, may ma ci ndox moomu, ngir ma bañatee mar, bay ñëw ba fii di rootsi.»
16ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܙܠܝ ܩܪܝ ܠܒܥܠܟܝ ܘܬܝ ܠܗܪܟܐ ܀
16 Yeesu ne ko: «Demal woowi sa jëkkër te ñëw.»
17ܐܡܪܐ ܠܗ ܠܝܬ ܠܝ ܒܥܠܐ ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܫܦܝܪ ܐܡܪܬܝ ܕܠܝܬ ܠܝ ܒܥܠܐ ܀
17 Jigéen ja tontu ko ne: «Awma jëkkër de.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg ne, amuloo jëkkër,
18ܚܡܫܐ ܓܝܪ ܒܥܠܝܢ ܗܘܘ ܠܟܝ ܘܗܢܐ ܕܐܝܬ ܠܟܝ ܗܫܐ ܠܐ ܗܘܐ ܒܥܠܟܝ ܗܕܐ ܫܪܝܪܬܐ ܐܡܪܬܝ ܀
18 ndaxte amoon nga juróomi jëkkër, te ki nga nekkal léegi du sa jëkkër. Li nga wax dëgg la.»
19ܐܡܪܐ ܠܗ ܗܝ ܐܢܬܬܐ ܡܪܝ ܚܙܝܐ ܐܢܐ ܕܢܒܝܐ ܐܢܬ ܀
19 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, gis naa ne, ab yonent nga.
20ܐܒܗܝܢ ܒܗܢܐ ܛܘܪܐ ܤܓܕܘ ܘܐܢܬܘܢ ܐܡܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܒܐܘܪܫܠܡ ܗܘ ܐܬܪ ܕܘܠܐ ܠܡܤܓܕ ܀
20 Nun nag, nakajekk sunuy maam ca tund wee ngay séen lañu daan jaamoo Yàlla, waaye yéen Yawut yi, dangeen ne Yerusalem lañu war a jaamoo Yàlla.»
21ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܐܢܬܬܐ ܗܝܡܢܝܢܝ ܕܐܬܝܐ ܫܥܬܐ ܕܠܐ ܒܗܢܐ ܛܘܪܐ ܘܐܦ ܠܐ ܒܐܘܪܫܠܡ ܬܤܓܕܘܢ ܠܐܒܐ ܀
21 Yeesu ne ko: «Jigéen ji, gëmal lii ma lay wax: dina am jamono joo xam ne du ci tund wale te du ci Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi.
22ܐܢܬܘܢ ܤܓܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܡܕܡ ܕܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܚܢܢ ܕܝܢ ܤܓܕܝܢ ܚܢܢ ܠܡܐ ܕܝܕܥܝܢ ܚܢܢ ܕܚܝܐ ܡܢ ܝܗܘܕܝܐ ܐܢܘܢ ܀
22 Yéen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal àddina ci Yawut yi la jóge.
23ܐܠܐ ܐܬܝܐ ܫܥܬܐ ܘܗܫܐ ܐܝܬܝܗ ܐܡܬܝ ܕܤܓܘܕܐ ܫܪܝܪܐ ܢܤܓܕܘܢ ܠܐܒܐ ܒܪܘܚܐ ܘܒܫܪܪܐ ܐܦ ܐܒܐ ܓܝܪ ܕܐܝܟ ܗܠܝܢ ܗܘ ܤܓܘܕܐ ܒܥܐ ܀
23 Waaye jamono dina ñëw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge.
24ܪܘܚܐ ܗܘ ܓܝܪ ܐܠܗܐ ܘܐܝܠܝܢ ܕܤܓܕܝܢ ܠܗ ܒܪܘܚܐ ܘܒܫܪܪܐ ܘܠܐ ܕܢܤܓܕܘܢ ܀
24 Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu war nañu koo jaamu ci xel ak ci dëgg.»
25ܐܡܪܐ ܠܗ ܐܢܬܬܐ ܗܝ ܝܕܥܐ ܐܢܐ ܕܡܫܝܚܐ ܐܬܐ ܘܡܐ ܕܐܬܐ ܗܘ ܡܠܦ ܠܢ ܟܠܡܕܡ ܀
25 Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi --maanaam Kirist — dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.»
26ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܐܢܐ ܐܢܐ ܕܡܡܠܠ ܐܢܐ ܥܡܟܝ ܀
26 Yeesu tontu ko: «Maa di Almasi bi, man miy wax ak yaw.»
27ܘܟܕ ܡܡܠܠ ܐܬܘ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܡܬܕܡܪܝܢ ܗܘܘ ܕܥܡ ܐܢܬܬܐ ܡܡܠܠ ܠܐ ܕܝܢ ܐܢܫ ܐܡܪ ܡܢܐ ܒܥܐ ܐܢܬ ܐܘ ܡܢܐ ܡܡܠܠ ܐܢܬ ܥܡܗ ܀
27 Noonu nag taalibey Yeesu ya dellusi, gis muy wax ak ab jigéen. Ñu daldi jaaxle lool. Waaye kenn ñemewu ko woon ne: «Looy laaj?» walla: «Lu tax ngay wax ak moom?»
28ܘܫܒܩܬ ܩܘܠܬܗ ܐܢܬܬܐ ܘܐܙܠܬ ܠܡܕܝܢܬܐ ܘܐܡܪܐ ܠܐܢܫܐ ܀
28 Noonu jigéen ja wacc fa njaqam, daldi dem ca dëkk ba ne leen:
29ܬܘ ܚܙܘ ܓܒܪܐ ܕܐܡܪ ܠܝ ܟܠ ܡܕܡ ܕܥܒܕܬ ܠܡܐ ܗܘܝܘ ܡܫܝܚܐ ܀
29 «Kaayleen gis; nit a nga fee ku ma wax lépp lu ma mas a def. Ndax kooku du Almasi bi?»
30ܘܢܦܩܘ ܐܢܫܐ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܘܐܬܝܢ ܗܘܘ ܠܘܬܗ ܀
30 Noonu waa dëkk ba jóg, jëm ca Yeesu.
31ܘܒܝܢܬ ܗܠܝܢ ܒܥܝܢ ܗܘܘ ܡܢܗ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܪܒܢ ܠܥܤ ܀
31 Fekk taalibey Yeesu ya di ko gétën ne: «Kilifa gi, lekkal.»
32ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܝܬ ܠܝ ܡܐܟܘܠܬܐ ܕܐܟܘܠ ܐܝܕܐ ܕܐܢܬܘܢ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
32 Waaye Yeesu tontu leen: «Am na ñam wu may lekk, te xamuleen ko.»
33ܐܡܪܝܢ ܬܠܡܝܕܐ ܒܝܢܝܗܘܢ ܠܡܐ ܐܢܫ ܐܝܬܝ ܠܗ ܡܕܡ ܠܡܐܟܠ ܀
33 Taalibe ya nag di laajante naan: «Ndax dafa am ku ko indil lekk?»
34ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܡܐܟܘܠܬܝ ܕܝܠܝ ܐܝܬܝܗ ܕܐܥܒܕ ܨܒܝܢܗ ܕܡܢ ܕܫܕܪܢܝ ܘܐܫܠܡܝܘܗܝ ܠܥܒܕܗ ܀
34 Yeesu ne leen: «Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni te àggale liggéey, bi mu ma sant.
35ܠܐ ܐܢܬܘܢ ܐܡܪܝܢ ܕܒܬܪ ܐܪܒܥܐ ܝܪܚܝܢ ܐܬܐ ܚܨܕܐ ܗܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܐܪܝܡܘ ܥܝܢܝܟܘܢ ܘܚܙܘ ܐܪܥܬܐ ܕܚܘܪ ܘܡܛܝ ܠܚܨܕܐ ܡܢ ܟܕܘ ܀
35 Du dangeen naan: “Fii ak ñeenti weer ñu góob?” Waaye man, dama leen naan: xool-leen tool yi, ñoo ngi ñor ba weex tàll, di xaar ku leen góob.
36ܘܐܝܢܐ ܕܚܨܕ ܐܓܪܐ ܢܤܒ ܘܟܢܫ ܦܐܪܐ ܠܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܘܙܪܘܥܐ ܘܚܨܘܕܐ ܐܟܚܕܐ ܢܚܕܘܢ ܀
36 Kiy góob tool yi mu ngi jot xaat peyam; day dajale nit ñi ngir dund gu dul jeex, ni ñuy dajalee pepp. Kon boog kiy ji dina bégandoo ak kiy góob.
37ܒܗܕܐ ܓܝܪ ܐܝܬܝܗ ܡܠܬܐ ܕܫܪܪܐ ܕܐܚܪܝܢ ܗܘ ܙܪܥ ܘܐܚܪܝܢ ܚܨܕ ܀
37 Wax ji ñu wax ne: “Kenn dina ji, keneen góob,” dëgg la.
38ܐܢܐ ܫܕܪܬܟܘܢ ܠܡܚܨܕ ܡܕܡ ܕܠܐ ܗܘܐ ܐܢܬܘܢ ܠܐܝܬܘܢ ܒܗ ܐܚܪܢܐ ܓܝܪ ܠܐܝܘ ܘܐܢܬܘܢ ܥܠܬܘܢ ܥܠ ܥܡܠܗܘܢ ܕܗܢܘܢ ܀
38 Yebal naa leen, ngeen góob tool bu ngeen beyul. Ñeneen a ko bey, te yéena ko jariñoo.»
39ܡܢ ܗܝ ܡܕܝܢܬܐ ܕܝܢ ܤܓܝܐܐ ܗܝܡܢܘ ܒܗ ܫܡܪܝܐ ܡܛܠ ܡܠܬܗ ܕܐܢܬܬܐ ܗܝ ܕܡܤܗܕܐ ܗܘܬ ܕܐܡܪ ܠܝ ܟܠܡܕܡ ܕܥܒܕܬ ܀
39 Bi jigéen ja nee waa dëkk ba: «Wax na ma li ma def lépp,» ñu bare gëm nañu Yeesu.
40ܘܟܕ ܐܬܘ ܠܘܬܗ ܗܢܘܢ ܫܡܪܝܐ ܒܥܘ ܡܢܗ ܕܢܗܘܐ ܠܘܬܗܘܢ ܘܗܘܐ ܠܘܬܗܘܢ ܬܪܝܢ ܝܘܡܝܢ ܀
40 Ñu daldi dikk ñaan Yeesu, mu dal ak ñoom. Yeesu toog fa ñaari fan.
41ܘܤܓܝܐܐ ܗܝܡܢܘ ܒܗ ܡܛܠ ܡܠܬܗ ܀
41 Ñu bare gëm ko ndax li mu doon wax.
42ܘܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܠܐܢܬܬܐ ܗܝ ܕܡܟܝܠ ܠܐ ܗܘܐ ܡܛܠ ܡܠܬܟܝ ܡܗܝܡܢܝܢ ܚܢܢ ܒܗ ܚܢܢ ܓܝܪ ܫܡܥܢ ܘܝܕܥܢ ܕܗܢܘ ܫܪܝܪܐܝܬ ܡܫܝܚܐ ܡܚܝܢܗ ܕܥܠܡܐ ܀
42 Ñu ne jigéen ja: «Léegi gëm nanu, te du li nga wax moo tax waaye li nu gisal sunu bopp. Te xam nanu ne, dëgg-dëgg kii moo di Musalkatu àddina si.»
43ܘܒܬܪ ܬܪܝܢ ܝܘܡܝܢ ܢܦܩ ܝܫܘܥ ܡܢ ܬܡܢ ܘܐܙܠ ܠܓܠܝܠܐ ܀
43 Bi Yeesu amee ñaari fan ca dëkk ba, mu jóge fa, jëm diiwaanu Galile,
44ܗܘ ܓܝܪ ܝܫܘܥ ܤܗܕ ܕܢܒܝܐ ܒܡܕܝܢܬܗ ܠܐ ܡܬܝܩܪ ܀
44 ndaxte moom ci boppam nee woon na: «Ab yonent, kenn du ko faaydaal ca réewam.»
45ܟܕ ܕܝܢ ܐܬܐ ܠܓܠܝܠܐ ܩܒܠܘܗܝ ܓܠܝܠܝܐ ܕܚܙܘ ܐܬܘܬܐ ܟܠ ܕܥܒܕ ܒܐܘܪܫܠܡ ܒܥܕܥܕܐ ܐܬܘ ܗܘܘ ܓܝܪ ܘܐܦ ܗܢܘܢ ܠܥܕܥܕܐ ܀
45 Bi mu agsee Galile, nit ñi teeru ko, ndaxte ñoom itam teewoon nañu ca màggalu bésu Jéggi ba ca Yerusalem, te gisoon nañu la mu fa defoon lépp.
46ܐܬܐ ܕܝܢ ܬܘܒ ܝܫܘܥ ܠܩܛܢܐ ܕܓܠܝܠܐ ܐܝܟܐ ܕܥܒܕ ܡܝܐ ܚܡܪܐ ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܒܟܦܪܢܚܘܡ ܥܒܕ ܡܠܟܐ ܚܕ ܕܒܪܗ ܟܪܝܗ ܗܘܐ ܀
46 Noonu kon mu dellusi Kana ci Galile, dëkk ba mu soppe woon ndox ma biiñ. Amoon na benn dagu buur bu dëkkoon Kapernawum te doomam feebar.
47ܗܢܐ ܫܡܥ ܕܐܬܐ ܝܫܘܥ ܡܢ ܝܗܘܕ ܠܓܠܝܠܐ ܘܐܙܠ ܠܘܬܗ ܘܒܥܐ ܗܘܐ ܡܢܗ ܕܢܚܘܬ ܘܢܐܤܐ ܠܒܪܗ ܩܪܝܒ ܗܘܐ ܓܝܪ ܠܡܡܬ ܀
47 Bi mu déggee ne, Yeesu jóge na Yude, ñëw Galile, mu dikk ci moom, ñaan ko mu ñëw këram, wéral doomam, ji wopp bay bëgg a dee.
48ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܐܢ ܐܬܘܬܐ ܘܬܕܡܪܬܐ ܠܐ ܬܚܙܘܢ ܠܐ ܬܗܝܡܢܘܢ ܀
48 Yeesu ne ko: «Yéen daal, dungeen gëm mukk, fi ak gisuleen ay firnde walla ay kéemaan.»
49ܐܡܪ ܠܗ ܗܘ ܥܒܕ ܡܠܟܐ ܡܪܝ ܚܘܬ ܥܕܠܐ ܡܐܬ ܠܗ ܛܠܝܐ ܀
49 Dagu buur ba neeti ko: «Sang bi, ñëwal, bala sama doom di dee.»
50ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܙܠ ܒܪܟ ܚܝ ܗܘ ܘܗܝܡܢ ܗܘ ܓܒܪܐ ܒܡܠܬܐ ܕܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܘܐܙܠ ܀
50 Yeesu ne ko: «Demal, sa doom dina dund.» Kilifa ga gëm la ko Yeesu wax, daldi dem.
51ܟܕ ܕܝܢ ܢܚܬ ܗܘܐ ܐܪܥܘܗܝ ܥܒܕܘܗܝ ܘܤܒܪܘܗܝ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܒܪܟ ܚܝܐ ܀
51 Bi muy dellu këram nag, ay surgaam gatandu ko. Ñu daldi ne ko: «Xale bi dina dund!»
52ܘܫܐܠ ܐܢܘܢ ܒܐܝܢܐ ܥܕܢܐ ܐܬܚܠܡ ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܐܬܡܠܝ ܒܫܒܥ ܫܥܝܢ ܫܒܩܬܗ ܐܫܬܐ ܀
52 Mu laaj leen ci ban waxtu la tàmbalee tane, ñu tontu ko ne: «Démb ca njolloor la am ag féex.»
53ܘܝܕܥ ܐܒܘܗܝ ܕܒܗܝ ܫܥܬܐ ܕܒܗ ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܕܒܪܟ ܚܝܐ ܘܗܝܡܢ ܗܘ ܘܒܝܬܗ ܟܠܗ ܀
53 Noonu baayu xale ba daldi seetlu ne, ca waxtu woowa la ko Yeesu ne woon: «Sa doom dina dund.» Moom ak njabootam gépp, ñu daldi gëm Yeesu.
54ܗܕܐ ܬܘܒ ܐܬܐ ܕܬܪܬܝܢ ܥܒܕ ܝܫܘܥ ܟܕ ܐܬܐ ܡܢ ܝܗܘܕ ܠܓܠܝܠܐ ܀
54 Lii mooy ñaareelu firnde, bi Yeesu def ci Galile, gannaaw bi mu jógee Yude.