Syriac: NT

Wolof: New Testament

Jude

1

1ܝܗܘܕܐ ܥܒܕܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܐܚܐ ܕܝܢ ܕܝܥܩܘܒ ܠܥܡܡܐ ܩܪܝܐ ܕܒܐܠܗܐ ܐܒܐ ܪܚܝܡܝܢ ܘܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܢܛܝܪܝܢ ܀
1 Man Yudd, jaamu Yeesu Kirist, mi bokk ak Saag ndey ak baay, maa leen di bind, yéen ñi Yàlla Baay bi woo te bëgg leen, te Yeesu Kirist aar leen.
2ܪܚܡܐ ܘܫܠܡܐ ܘܚܘܒܐ ܢܤܓܐ ܠܟܘܢ ܀
2 Na leen Yàlla may yërmande, jàmm ak mbëggeel.
3ܚܒܝܒܝ ܟܕ ܟܠܗ ܝܨܝܦܘܬܐ ܥܒܕ ܐܢܐ ܠܡܟܬܒ ܠܟܘܢ ܥܠ ܚܝܐ ܕܝܠܢ ܕܓܘܐ ܐܢܢܩܐ ܐܝܬ ܠܝ ܠܡܟܬܒ ܠܟܘܢ ܟܕ ܡܦܝܤ ܐܢܐ ܕܐܓܘܢܐ ܬܥܒܕܘܢ ܚܠܦ ܗܝܡܢܘܬܐ ܐܝܕܐ ܕܚܕܐ ܙܒܢ ܐܫܬܠܡܬ ܠܩܕܝܫܐ ܀
3 Samay bokk, bëggoon naa leen a bind lool ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye lii moo gën a jamp: ma xiir leen, ngeen taxaw ci aar mboolem dëgg, yi Yàlla xas a dénk gaayam yu sell yi ba fàww.
4ܩܢܘ ܓܝܪ ܐܢܫܝܢ ܡܥܠܢܘܬܐ ܐܝܠܝܢ ܕܡܢ ܫܘܪܝܐ ܩܕܡܘ ܐܬܟܬܒܘ ܒܚܘܝܒܐ ܗܢܐ ܐܢܫܐ ܪܫܝܥܐ ܕܠܛܝܒܘܬܗ ܕܐܠܗܢ ܡܗܦܟܝܢ ܠܛܢܦܘܬܐ ܘܒܗܘ ܕܐܝܬܘܗܝ ܒܠܚܘܕܘܗܝ ܡܪܐ ܐܠܗܐ ܘܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܟܦܪܝܢ ܀
4 Ndaxte am na ay nit ñu ñeme Yàlla, ñu yoxoosu ci seen biir; dañuy mbubboo yiwu Yàlla, ngir topp seen bakkan, di ci weddi Buur Yàlla miy kenn ak sunu Boroom Yeesu Kirist. Fekk Mbind mi tëral na seen àtte bu yàgg.
5ܠܡܥܗܕܘܬܟܘܢ ܕܝܢ ܨܒܐ ܐܢܐ ܟܕ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܟܠܗܝܢ ܕܐܠܗܐ ܟܕ ܚܕܐ ܙܒܢ ܠܥܡܐ ܡܢ ܡܨܪܝܢ ܦܪܩ ܗܝ ܕܬܪܬܝܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܗܝܡܢܘ ܐܘܒܕ ܀
5 Xam ngeen loolu lépp ba noppi sax, waaye dama leen koy fàttali rekk. Xam ngeen ne Boroom bi musal na xeetam, ba génne leen réewu Misra, waaye gannaaw ba raafal na ñi gëmul woon.
6ܘܠܡܠܐܟܐ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܢܛܪܘ ܪܝܫܢܘܬܗܘܢ ܐܠܐ ܫܒܩܘ ܥܘܡܪܐ ܕܝܠܗܘܢ ܠܕܝܢܐ ܕܝܘܡܐ ܪܒܐ ܒܐܤܘܪܐ ܠܐ ܝܕܝܥܐ ܬܚܝܬ ܥܡܛܢܐ ܢܛܪ ܀
6 Te it malaaka ya jàppul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa toxoo fa ñu leen dëëloon, Yàlla yeew na leen buum yu sax, tëj leen ci biir lëndëm, di leen nége àtteb bés bu mag ba.
7ܐܝܟܢܐ ܕܤܕܘܡ ܘܥܡܘܪܐ ܘܡܕܝܢܬܐ ܕܚܕܪܝܗܝܢ ܕܒܗ ܒܕܡܘܬܐ ܕܗܠܝܢ ܙܢܝ ܘܐܙܠ ܒܬܪ ܒܤܪܐ ܐܚܪܢܐ ܤܝܡܢ ܬܚܝܬ ܬܚܘܝܬܐ ܕܢܘܪܐ ܕܠܥܠܡ ܟܕ ܡܚܝܒܢ ܠܕܝܢܐ ܀
7 Noonu itam dëkki Sodom ak Gomor ak dëkk ya leen wëroon, dañoo sóobu ci njaaloo ak di def ay góor-jigéen, waaye àtte bi dal na ci seen kaw, ba ñuy ay tegtal ci ñiy yelloo safara ba fàww.
8ܒܗ ܒܕܡܘܬܐ ܐܦ ܗܠܝܢ ܕܒܚܠܡܐ ܡܫܬܪܓܪܓܝܢ ܠܒܤܪܐ ܡܢ ܡܛܢܦܝܢ ܠܡܪܘܬܐ ܕܝܢ ܛܠܡܝܢ ܘܠܬܫܒܘܚܬܐ ܡܓܕܦܝܢ ܀
8 Naka noonu itam gentkat yooyu may wax ñu ngi sobeel seen yaram, di weddi gépp kilifteef, di xas doole yi ci asamaan.
9ܡܝܟܐܝܠ ܕܝܢ ܪܝܫ ܡܠܐܟܐ ܗܘ ܕܥܡ ܐܟܠܩܪܨܐ ܟܕ ܕܐܢ ܡܡܠܠ ܗܘܐ ܡܛܠ ܦܓܪܗ ܕܡܘܫܐ ܠܐ ܐܡܪܚ ܕܢܝܬܐ ܥܠܘܗܝ ܕܝܢܐ ܕܓܘܕܦܐ ܐܠܐ ܐܡܪ ܕܢܓܥܘܪ ܒܟ ܡܪܝܐ ܀
9 Waaye bi Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi, di xëccook Seytaane néewu Musaa, bay xuloo ak moom, ñemewu koo àtte, boole ciy xas; mu yem ci wax ko ne: «Na la Boroom bi mbugal!»
10ܗܠܝܢ ܕܝܢ ܒܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܝܕܥܝܢ ܡܓܕܦܝܢ ܒܐܝܠܝܢ ܕܝܢ ܕܟܝܢܐܝܬ ܐܝܟ ܚܝܘܬܐ ܚܪܫܬܐ ܡܦܤܝܢ ܒܗܝܢ ܡܬܚܒܠܝܢ ܀
10 Waaye nit ñii may wax, dañuy saaga li ñu xamul. Te li ñu xam ci tañaxu sax, ni bàyyima yu amul xel, dañu ci yàq seen bopp.
11ܘܝ ܠܗܘܢ ܕܒܐܘܪܚܗ ܕܩܐܝܢ ܐܙܠܘ ܘܒܬܪ ܛܥܝܘܬܗ ܕܒܠܥܡ ܒܐܓܪܐ ܐܫܬܪܚܘ ܘܒܥܨܝܝܘܬܗ ܕܩܘܪܚ ܐܒܕܘ ܀
11 Ñoo kay torox! Dañoo jaar ci yoonu Kayin, sóobu ci réerug Balaam ngir xaalis, di bañ kilifteef ni Kore, te dinañu dee ni moom.
12ܗܠܝܢ ܐܝܬܝܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܒܢܝܚܬܗܘܢ ܟܕ ܡܟܬܡܝܢ ܡܬܦܪܦܥܝܢ ܟܕ ܕܠܐ ܕܚܠܬܐ ܢܦܫܗܘܢ ܪܥܝܢ ܥܢܢܐ ܕܠܐ ܡܛܪܐ ܕܡܢ ܪܘܚܐ ܦܗܝܢ ܐܝܠܢܐ ܕܐܘܦܝ ܐܒܗܘܢ ܕܐܝܬܝܗܘܢ ܕܠܐ ܦܐܪܐ ܕܡܝܬܘ ܬܢܝܢܘܬ ܘܤܠܩܘ ܡܢ ܥܩܪܝܗܘܢ ܀
12 Su ñu bokkee ak yéen reeru mbooloo mi, dañu ciy indi ay, niy xeer yu nëbbu ci biir géej; amuñu genn gàcce, waaye dañuy giiroo te fonk seen biir rekk. Ñu ngi mel ni xiin yu amul ndox, yuy naaxsaay ci ngelaw; ni garab yu meññul ci jamonoy meññeef, te buddeeku, dee ba wow koŋŋ;
13ܓܠܠܐ ܥܙܝܙܐ ܕܝܡܐ ܕܒܝܕ ܪܘܥܬܗܘܢ ܡܚܘܝܢ ܒܗܬܬܗܘܢ ܟܘܟܒܐ ܡܛܥܝܢܐ ܠܗܠܝܢ ܕܥܡܛܢܐ ܕܚܫܘܟܐ ܠܥܠܡ ܠܗܘܢ ܢܛܝܪ ܀
13 mel ni duusi géej gu mer, yuy gëq jëf yu ruslu; niy biddiiw yuy faq, te Yàlla dencal na leen lëndëm ya gën a tar ba fàww.
14ܐܬܢܒܝ ܕܝܢ ܐܦ ܠܗܠܝܢ ܗܘ ܕܐܝܬܘܗܝ ܕܫܒܥܐ ܡܢ ܐܕܡ ܚܢܘܟ ܟܕ ܐܡܪ ܕܗܐ ܡܪܝܐ ܐܬܐ ܒܪܒܘܬܐ ܕܩܕܝܫܐ ܀
14 Enog, di juróom-ñaareelu maam gannaaw Aadama, waxoon na ci kàddug Yàlla, ba weer leen ne: «Boroom bi wàcce na ca asamaan, ànd ak ay junniy junniy malaakaam,
15ܕܢܥܒܕ ܕܝܢܐ ܥܠ ܟܠ ܘܠܡܟܤܘ ܠܟܠ ܢܦܫܬܐ ܡܛܠ ܟܠܗܘܢ ܥܒܕܐ ܐܝܠܝܢ ܕܐܪܫܥܘ ܘܡܛܠ ܟܠܗܝܢ ܡܠܐ ܩܫܝܬܐ ܐܝܠܝܢ ܕܡܠܠܘ ܚܛܝܐ ܪܫܝܥܐ ܀
15 ngir àtte ñépp, te mbugal ñi weddi ñépp ndax ñaawteef, yi ñu jëf ci ñeme Yàlla; di leen fàttali it kàddu yu ñaaw, yi ñu ko tifaar ci seeni bàkkaar ak seen weddi.»
16ܗܠܝܢ ܐܢܘܢ ܕܡܪܛܢܝܢ ܘܥܕܠܝܢ ܒܟܠ ܨܒܘܢ ܟܕ ܐܝܟ ܪܓܝܓܬܐ ܕܝܠܗܘܢ ܡܗܠܟܝܢ ܘܦܘܡܗܘܢ ܡܡܠܠ ܓܢܝܚܬܐ ܘܡܫܒܚܝܢ ܠܦܪܨܘܦܐ ܡܛܠ ܝܘܬܪܢܐ ܀
16 Duñu noppee xultu, di jàmbat seen nekkin, tey topp seen nafsu; ay wax yu réy a ngi ball ci seen làmmiñ, waaye dañuy jey ñi ñuy yaakaare njariñ.
17ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܚܒܝܒܝ ܐܬܕܟܪܘ ܠܡܠܐ ܐܝܠܝܢ ܕܩܕܡ ܐܬܐܡܪ ܡܢ ܫܠܝܚܘܗܝ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
17 Waaye yéen samay xarit, fàttalikuleen la leen ndawi sunu Boroom Yeesu Kirist waxoon lu jiitu,
18ܕܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܠܟܘܢ ܕܒܚܪܬܐ ܕܙܒܢܐ ܢܗܘܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܡܒܙܚܝܢ ܕܐܝܟ ܪܓܝܓܬܐ ܕܝܠܗܘܢ ܐܙܠܝܢ ܒܬܪ ܪܘܫܥܐ ܀
18 ne leen: «Muju jamono ay tiiñalkat dinañu feeñ, ñuy weddi Yàlla, ngir topp seen bakkan.»
19ܗܠܝܢ ܐܝܬܝܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܡܦܪܫܝܢ ܢܦܫܢܝܐ ܕܪܘܚܐ ܠܝܬ ܠܗܘܢ ܀
19 Ñooy féewale, te Xelum Yàlla nekkul ci ñoom, waaye niti kese lañu.
20ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܚܒܝܒܝ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܕܝܠܟܘܢ ܩܕܝܫܬܐ ܐܬܒܢܘ ܡܢ ܕܪܝܫ ܒܪܘܚܐ ܩܕܝܫܐ ܟܕ ܡܨܠܝܢ ܀
20 Waaye yéen samay xarit, doolewuleen ci seen yoonu ngëm wu sell, tey ñaan ci dooley Xel mu Sell mi,
21ܢܦܫܢ ܕܝܢ ܒܚܘܒܐ ܕܐܠܗܐ ܢܛܪ ܟܕ ܡܤܟܝܢܢ ܠܚܢܢܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܚܝܐ ܕܝܠܢ ܕܠܥܠܡ ܀
21 ba saxoo mbëggeelu Yàlla, tey séentu yërmandey sunu Boroom Yeesu Kirist, mu tàbbal leen ci dund gu dul jeex.
22ܘܠܡܢܗܘܢ ܡܢ ܡܢ ܢܘܪܐ ܚܛܘܦܘ ܀
22 Jubbantileen ñi am werantey xel,
23ܟܕ ܕܝܢ ܡܬܬܘܝܢ ܐܬܪܚܡܘ ܥܠܝܗܘܢ ܒܕܚܠܬܐ ܟܕ ܤܢܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܦ ܠܟܘܬܝܢܐ ܕܡܢ ܒܤܪܐ ܕܡܟܬܡܐ ܀
23 ngeen musal ñale, jële leen ci safara, te yërëm ñeneen ñi, waaye boole ci moytu, ba sib sax seen yére yi taq sobe.
24ܠܗܘ ܕܝܢ ܕܡܫܟܚ ܕܢܢܛܪ ܠܢ ܕܠܐ ܫܘܪܥܬܐ ܘܕܠܐ ܟܘܬܡܐ ܘܢܩܝܡ ܕܠܐ ܡܘܡܐ ܀
24 Yàlla mi leen man a aar ci gépp jeng, te teewal leen fa kanam ndamam, ngeen ñàkk sikk te fees dell ak mbég;
25ܒܠܚܘܕܘܗܝ ܐܠܗܐ ܦܪܘܩܢ ܒܝܕ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܡܪܢ ܩܕܡ ܬܫܒܘܚܬܗ ܒܚܕܘܬܐ ܠܗ ܫܘܒܚܐ ܘܐܘܚܕܢܐ ܘܐܝܩܪܐ ܘܪܒܘܬܐ ܐܦ ܗܫܐ ܘܒܟܠܗܘܢ ܥܠܡܐ ܐܡܝܢ ܀
25 Yàlla miy kenn, di sunu Musalkat, na yelloo ndam ak màgg, kàttan ak nguur, jaar ci Yeesu Kirist sunu Boroom, démb, tey, ëllëg ba fàww. Amiin.