Syriac: NT

Wolof: New Testament

Luke

13

1ܒܗܘ ܕܝܢ ܙܒܢܐ ܐܬܘ ܐܢܫܝܢ ܐܡܪܘ ܠܗ ܥܠ ܓܠܝܠܝܐ ܗܢܘܢ ܕܦܝܠܛܘܤ ܚܠܛ ܕܡܗܘܢ ܥܡ ܕܒܚܝܗܘܢ ܀
1 Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla.
2ܘܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܤܒܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܗܠܝܢ ܓܠܝܠܝܐ ܚܛܝܝܢ ܗܘܘ ܝܬܝܪ ܡܢ ܟܠܗܘܢ ܓܠܝܠܝܐ ܕܗܟܢܐ ܗܘܐ ܐܢܘܢ ܀
2 Mu tontu leen ne: «Mbaa du dangeen a xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gën a nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj?
3ܠܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܝܢ ܕܐܦ ܟܠܟܘܢ ܐܠܐ ܬܬܘܒܘܢ ܗܟܢܐ ܬܐܒܕܘܢ ܀
3 Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.
4ܐܘ ܗܢܘܢ ܬܡܢܬܥܤܪ ܕܢܦܠ ܥܠܝܗܘܢ ܡܓܕܠܐ ܒܫܝܠܘܚܐ ܘܩܛܠ ܐܢܘܢ ܤܒܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܚܛܝܝܢ ܗܘܘ ܝܬܝܪ ܡܢ ܟܠܗܘܢ ܒܢܝܢܫܐ ܕܥܡܪܝܢ ܒܐܘܪܫܠܡ ܀
4 Te fukki nit ak juróom-ñett ñooñu dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeen a yaakaar ne, ñoo gën a nekk ay tooñkat ñeneen ñi dëkk Yerusalem yépp?
5ܠܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܝܢ ܕܐܠܐ ܬܬܘܒܘܢ ܟܠܟܘܢ ܐܟܘܬܗܘܢ ܬܐܒܕܘܢ ܀
5 Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.»
6ܘܐܡܪ ܡܬܠܐ ܗܢܐ ܬܬܐ ܐܝܬ ܗܘܬ ܠܐܢܫ ܕܢܨܝܒܐ ܒܟܪܡܗ ܘܐܬܐ ܒܥܐ ܒܗ ܦܐܪܐ ܘܠܐ ܐܫܟܚ ܀
6 Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom.
7ܘܐܡܪ ܠܦܠܚܐ ܗܐ ܬܠܬ ܫܢܝܢ ܐܬܐ ܐܢܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܦܐܪܐ ܒܬܬܐ ܗܕܐ ܘܠܐ ܡܫܟܚ ܐܢܐ ܦܤܘܩܝܗ ܠܡܢܐ ܡܒܛܠܐ ܐܪܥܐ ܀
7 Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?”
8ܐܡܪ ܠܗ ܦܠܚܐ ܡܪܝ ܫܒܘܩܝܗ ܐܦ ܗܕܐ ܫܢܬܐ ܥܕ ܐܦܠܚܝܗ ܘܐܙܒܠܝܗ ܀
8 Surga ba tontu ko ne: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos.
9ܘܐܢ ܥܒܕܬ ܦܐܪܐ ܘܐܠܐ ܠܡܢܚܝ ܬܦܤܩܝܗ ܀
9 Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
10ܟܕ ܕܝܢ ܡܠܦ ܝܫܘܥ ܒܫܒܬܐ ܒܚܕܐ ܡܢ ܟܢܘܫܬܐ ܀
10 Benn bésu noflaay Yeesoo ngi doon jàngale ci ab jàngu.
11ܐܝܬ ܗܘܬ ܬܡܢ ܐܢܬܬܐ ܕܐܝܬ ܗܘܬ ܠܗ ܪܘܚܐ ܕܟܘܪܗܢܐ ܫܢܝܢ ܬܡܢܥܤܪܐ ܘܟܦܝܦܐ ܗܘܬ ܘܠܐ ܡܫܟܚܐ ܗܘܬ ܕܬܬܦܫܛ ܠܓܡܪ ܀
11 Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu war a mat fukki at ak juróom-ñett; dafa xuuge woon te mënul woon a siggi dara.
12ܚܙܗ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܘܩܪܗ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܢܬܬܐ ܫܪܝܬܝ ܡܢ ܟܘܪܗܢܟܝ ܀
12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
13ܘܤܡ ܐܝܕܗ ܥܠܝܗ ܘܡܚܕܐ ܐܬܦܫܛܬ ܘܫܒܚܬ ܠܐܠܗܐ ܀
13 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.
14ܥܢܐ ܕܝܢ ܪܒ ܟܢܘܫܬܐ ܟܕ ܡܬܚܡܬ ܥܠ ܕܐܤܝ ܒܫܒܬܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܟܢܫܐ ܫܬܐ ܐܢܘܢ ܝܘܡܝܢ ܕܒܗܘܢ ܘܠܐ ܠܡܦܠܚ ܒܗܘܢ ܗܘܝܬܘܢ ܐܬܝܢ ܡܬܐܤܝܢ ܘܠܐ ܒܝܘܡܐ ܕܫܒܬܐ ܀
14 Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésu noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom-benni fan yu nit ñi war a liggéey. Kon war ngeen a ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésu noflaay bi.»
15ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܥܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܢܤܒ ܒܐܦܐ ܚܕ ܚܕ ܡܢܟܘܢ ܒܫܒܬܐ ܠܐ ܫܪܐ ܬܘܪܗ ܐܘ ܚܡܪܗ ܡܢ ܐܘܪܝܐ ܘܐܙܠ ܡܫܩܐ ܀
15 Boroom bi tontu ko: «Naaféq yi! Ndax bésu noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?
16ܗܕܐ ܕܝܢ ܕܒܪܬܗ ܗܝ ܕܐܒܪܗܡ ܘܐܤܪܗ ܐܟܠܩܪܨܐ ܗܐ ܬܡܢܥܤܪܐ ܫܢܝܢ ܠܐ ܘܠܐ ܗܘܐ ܕܬܫܬܪܐ ܡܢ ܗܢܐ ܐܤܘܪܝܐ ܒܝܘܡܐ ܕܫܒܬܐ ܀
16 Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom-ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésu noflaay bi?»
17ܘܟܕ ܗܠܝܢ ܐܡܪ ܗܘܐ ܒܗܬܝܢ ܗܘܘ ܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܩܝܡܝܢ ܗܘܘ ܠܩܘܒܠܗ ܘܟܠܗ ܥܡܐ ܚܕܐ ܗܘܐ ܒܟܠܗܝܢ ܬܡܝܗܬܐ ܕܗܘܝܢ ܗܘܝ ܒܐܝܕܗ ܀
17 Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp.
18ܐܡܪ ܗܘܐ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܠܡܢܐ ܕܡܝܐ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܘܠܡܢܐ ܐܕܡܝܗ ܀
18 Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko man a mengaleel?
19ܕܡܝܐ ܠܦܪܕܬܐ ܕܚܪܕܠܐ ܗܝ ܕܢܤܒ ܓܒܪܐ ܐܪܡܝܗ ܒܓܢܬܗ ܘܪܒܬ ܘܗܘܬ ܐܝܠܢܐ ܪܒܐ ܘܦܪܚܬܐ ܕܫܡܝܐ ܐܩܢܬ ܒܤܘܟܝܗ ܀
19 Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
20ܬܘܒ ܐܡܪ ܝܫܘܥ ܠܡܢܐ ܐܕܡܝܗ ܠܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
20 Mu neeti: «Lan laa man a mengaleek nguuru Yàlla?
21ܕܡܝܐ ܠܚܡܝܪܐ ܕܢܤܒܬ ܐܢܬܬܐ ܛܡܪܬ ܒܩܡܚܐ ܕܬܠܬ ܤܐܝܢ ܥܕܡܐ ܕܟܠܗ ܚܡܥ ܀
21 Mi ngi mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
22ܘܪܕܐ ܗܘܐ ܒܩܘܪܝܐ ܘܒܡܕܝܢܬܐ ܟܕ ܡܠܦ ܘܐܙܠ ܠܐܘܪܫܠܡ ܀
22 Yeesoo ngi doon jaar ci ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di jàngale te jublu Yerusalem.
23ܫܐܠܗ ܕܝܢ ܐܢܫ ܕܐܢ ܙܥܘܪܝܢ ܐܢܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܚܐܝܢ ܀
23 Am ku ko ne: «Boroom bi, ndax ñiy mucc ñu néew lay doon?» Yeesu ne leen:
24ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܬܟܬܫܘ ܠܡܥܠ ܒܬܪܥܐ ܐܠܝܨܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܓܝܪ ܕܤܓܝܐܐ ܢܒܥܘܢ ܠܡܥܠ ܘܠܐ ܢܫܟܚܘܢ ܀
24 «Defleen seen kem-kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéem a dugg, waaye duñu ko man.
25ܡܢ ܫܥܬܐ ܕܢܩܘܡ ܡܪܐ ܒܝܬܐ ܘܢܐܚܘܕ ܬܪܥܐ ܘܬܗܘܘܢ ܩܝܡܝܢ ܠܒܪ ܘܢܩܫܝܢ ܒܬܪܥܐ ܘܬܫܪܘܢ ܠܡܐܡܪ ܡܪܢ ܡܪܢ ܦܬܚ ܠܢ ܘܢܥܢܐ ܗܘ ܘܢܐܡܪ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܠܐ ܝܕܥ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܐܝܡܟܐ ܐܢܬܘܢ ܀
25 Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Dina leen tontu ne: “Xawma fu ngeen bokk.”
26ܘܬܫܪܘܢ ܠܡܐܡܪ ܩܕܡܝܟ ܐܟܠܢ ܘܐܫܬܝܢ ܘܒܫܘܩܝܢ ܐܠܦܬ ܀
26 Bu ko defee dingeen tàmbalee naan: “Noo doon bokk di lekk ak di naan, te jàngale nga ci sunuy pénc.”
27ܘܢܐܡܪ ܠܟܘܢ ܕܠܐ ܝܕܥ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܐܝܡܟܐ ܐܢܬܘܢ ܦܪܘܩܘ ܠܟܘܢ ܡܢܝ ܦܠܚܝ ܫܘܩܪܐ ܀
27 Waaye dina ne: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!”
28ܬܡܢ ܢܗܘܐ ܒܟܝܐ ܘܚܘܪܩ ܫܢܐ ܟܕ ܬܚܙܘܢ ܠܐܒܪܗܡ ܘܠܐܝܤܚܩ ܘܠܝܥܩܘܒ ܘܠܟܠܗܘܢ ܢܒܝܐ ܒܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܬܗܘܘܢ ܡܦܩܝܢ ܠܒܪ ܀
28 Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.
29ܘܢܐܬܘܢ ܡܢ ܡܕܢܚܐ ܘܡܢ ܡܥܪܒܐ ܘܡܢ ܬܝܡܢܐ ܘܡܢ ܓܪܒܝܐ ܘܢܤܬܡܟܘܢ ܒܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
29 Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram.
30ܘܗܐ ܐܝܬ ܐܚܪܝܐ ܕܢܗܘܘܢ ܩܕܡܝܐ ܘܐܝܬ ܩܕܡܝܐ ܕܢܗܘܘܢ ܐܚܪܝܐ ܀
30 Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»
31ܒܗ ܒܗܘ ܝܘܡܐ ܩܪܒܘ ܐܢܫܐ ܡܢ ܦܪܝܫܐ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܦܘܩ ܙܠ ܠܟ ܡܟܐ ܡܛܠ ܕܗܪܘܕܤ ܨܒܐ ܠܡܩܛܠܟ ܀
31 Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wut a rey.»
32ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܙܠܘ ܐܡܪܘ ܠܬܥܠܐ ܗܢܐ ܕܗܐ ܡܦܩ ܐܢܐ ܫܐܕܐ ܘܐܤܘܬܐ ܥܒܕ ܐܢܐ ܝܘܡܢܐ ܘܡܚܪ ܘܠܝܘܡܐ ܕܬܠܬܐ ܡܫܬܡܠܐ ܐܢܐ ܀
32 Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.”
33ܒܪܡ ܘܠܐ ܠܝ ܕܝܘܡܢܐ ܘܡܚܪ ܐܤܥܘܪ ܘܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܐܙܠ ܡܛܠ ܕܠܐ ܡܫܟܚܐ ܕܢܒܝܐ ܢܐܒܕ ܠܒܪ ܡܢ ܐܘܪܫܠܡ ܀
33 Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesul a reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.
34ܐܘܪܫܠܡ ܐܘܪܫܠܡ ܩܛܠܬ ܢܒܝܐ ܘܪܓܡܬ ܠܐܝܠܝܢ ܕܫܠܝܚܝܢ ܠܘܬܗ ܟܡܐ ܙܒܢܝܢ ܨܒܝܬ ܠܡܟܢܫܘ ܒܢܝܟܝ ܐܝܟ ܬܪܢܓܘܠܬܐ ܕܟܢܫܐ ܦܪܘܓܝܗ ܬܚܝܬ ܓܦܝܗ ܘܠܐ ܨܒܝܬܘܢ ܀
34 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen!
35ܗܐ ܡܫܬܒܩ ܠܟܘܢ ܒܝܬܟܘܢ ܚܪܒܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܓܝܪ ܕܠܐ ܬܚܙܘܢܢܝ ܥܕܡܐ ܕܬܐܡܪܘܢ ܒܪܝܟ ܗܘ ܕܐܬܐ ܒܫܡܗ ܕܡܪܝܐ ܀
35 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»