Syriac: NT

Wolof: New Testament

Luke

16

1ܘܐܡܪ ܡܬܠܐ ܠܘܬ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܓܒܪܐ ܚܕ ܐܝܬ ܗܘܐ ܥܬܝܪܐ ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܠܗ ܪܒܝܬܐ ܘܐܬܐܟܠܘ ܠܗ ܩܪܨܘܗܝ ܕܩܢܝܢܗ ܡܦܪܚ ܀
1 Yeesu neeti ay taalibeem: «Benn boroom alal moo amoon bëkk-néeg bu ñu jiiñ ne, dafay pasar-pasaree alal ji.
2ܘܩܪܝܗܝ ܡܪܗ ܘܐܡܪ ܠܗ ܡܢܘ ܗܢܐ ܕܫܡܥ ܐܢܐ ܥܠܝܟ ܗܒ ܠܝ ܚܘܫܒܢܐ ܕܪܒܬ ܒܝܬܘܬܟ ܠܐ ܓܝܪ ܡܫܟܚ ܐܢܬ ܡܟܝܠ ܪܒܝܬܐ ܕܬܗܘܐ ܠܝ ܀
2 Waa ja woo ko ne ko: “Li may dégg ci yaw mooy lan? Leeralal ma ni nga liggéeye ak sama alal, ndaxte dootoo nekkati sama bëkk-néeg.”
3ܐܡܪ ܗܘ ܪܒܝܬܐ ܒܢܦܫܗ ܡܢܐ ܐܥܒܕ ܕܡܪܝ ܫܩܠ ܠܗ ܡܢܝ ܪܒܬ ܒܝܬܘܬܐ ܕܐܚܦܘܪ ܠܐ ܡܫܟܚ ܐܢܐ ܘܠܡܚܕܪ ܒܗܬ ܐܢܐ ܀
3 «Bëkk-néeg bi di xalaat naan: “Nu may def nag, segam sama njaatige dafa may dàq ci liggéey bi mu ma joxoon? Dem beyi? Awma kàttanam. Yelwaani? Rus naa ko.
4ܝܕܥܬ ܡܢܐ ܐܥܒܕ ܕܡܐ ܕܢܦܩܬ ܡܢ ܪܒܬ ܒܝܬܘܬܐ ܢܩܒܠܘܢܢܝ ܒܒܬܝܗܘܢ ܀
4 Xam naa ni may def, ba su ma ñàkkee sama liggéey, ay nit fat ma.”
5ܘܩܪܐ ܚܕ ܚܕ ܡܢ ܚܝܒܐ ܕܡܪܗ ܘܐܡܪ ܠܩܕܡܝܐ ܟܡܐ ܚܝܒ ܐܢܬ ܠܡܪܝ ܀
5 Noonu mu daldi woolu kenn ku nekk ca ña ameeloon njaatigeem bor. Ka jëkk a ñëw, mu ne ko: “Ñaata nga ameel sama njaatige?”
6ܐܡܪ ܠܗ ܡܐܐ ܡܬܪܝܢ ܡܫܚܐ ܐܡܪ ܠܗ ܤܒ ܟܬܒܟ ܘܬܒ ܒܥܓܠ ܟܬܘܒ ܚܡܫܝܢ ܡܬܪܝܢ ܀
6 Mu ne ko: “Téeméeri bidoŋi diwlinu oliw.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Toogal fii gaaw te bind juróom-fukk.”
7ܘܐܡܪ ܠܐܚܪܢܐ ܘܐܢܬ ܡܢܐ ܚܝܒ ܐܢܬ ܠܡܪܝ ܐܡܪ ܠܗ ܡܐܐ ܟܘܪܝܢ ܚܛܐ ܐܡܪ ܠܗ ܩܒܠ ܟܬܒܟ ܘܬܒ ܟܬܘܒ ܬܡܢܐܝܢ ܟܘܪܝܢ ܀
7 Mu neeti keneen: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Bindal juróom-ñett-fukk.”
8ܘܫܒܚ ܡܪܢ ܠܪܒܝܬܐ ܕܥܘܠܐ ܕܚܟܝܡܐܝܬ ܥܒܕ ܒܢܘܗܝ ܓܝܪ ܕܥܠܡܐ ܗܢܐ ܚܟܝܡܝܢ ܐܢܘܢ ܡܢ ܒܢܘܗܝ ܕܢܘܗܪܐ ܒܫܪܒܬܗܘܢ ܗܕܐ ܀
8 Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gën a muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.»
9ܘܐܦ ܐܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܥܒܕܘ ܠܟܘܢ ܪܚܡܐ ܡܢ ܡܡܘܢܐ ܗܢܐ ܕܥܘܠܐ ܕܡܐ ܕܓܡܪ ܢܩܒܠܘܢܟܘܢ ܒܡܛܠܝܗܘܢ ܕܠܥܠܡ ܀
9 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen di wax lii: sàkkuleen ay xarit jaare ko ci alalu àddina, ngir bu alal nekkatul, ñu man leen a fat ca dal yu sax ya.
10ܡܢ ܕܒܩܠܝܠ ܡܗܝܡܢ ܐܦ ܒܤܓܝ ܡܗܝܡܢ ܗܘ ܘܡܢ ܕܒܩܠܝܠ ܥܘܠ ܐܦ ܒܤܓܝ ܥܘܠ ܗܘ ܀
10 Nit ku maandu ci yëf yu néew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci yëf yu néew, du jub ci yu bare.
11ܐܢ ܗܟܝܠ ܒܡܡܘܢܐ ܕܥܘܠܐ ܡܗܝܡܢܐ ܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܫܪܪܐ ܠܟܘܢ ܡܢܘ ܡܗܝܡܢ ܀
11 Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu àddina, kon ku leen di dénk alal ju wóor ji?
12ܘܐܢ ܒܕܠܐ ܕܝܠܟܘܢ ܠܐ ܐܫܬܟܚܬܘܢ ܡܗܝܡܢܐ ܕܝܠܟܘܢ ܡܢܘ ܢܬܠ ܠܟܘܢ ܀
12 Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom?
13ܠܝܬ ܥܒܕܐ ܕܡܫܟܚ ܠܬܪܝܢ ܡܪܘܢ ܠܡܦܠܚ ܐܘ ܓܝܪ ܠܚܕ ܢܤܢܐ ܘܠܐܚܪܢܐ ܢܪܚܡ ܐܘ ܠܚܕ ܢܝܩܪ ܘܠܐܚܪܢܐ ܢܫܘܛ ܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܡܦܠܚ ܠܐܠܗܐ ܘܠܡܡܘܢܐ ܀
13 «Benn jaam mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.»
14ܦܪܝܫܐ ܕܝܢ ܟܕ ܫܡܥܘ ܗܠܝܢ ܟܠܗܝܢ ܡܛܠ ܕܪܚܡܝܢ ܗܘܘ ܟܤܦܐ ܡܡܝܩܝܢ ܗܘܘ ܒܗ ܀
14 Farisen yi déglu li Yeesu doon wax lépp, tàmbali di ko reetaan, ndaxte ñu bëggoon xaalis lañu.
15ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܢܬܘܢ ܐܢܘܢ ܕܡܙܕܩܝܢ ܢܦܫܗܘܢ ܩܕܡ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܝܕܥ ܠܒܘܬܟܘܢ ܕܡܕܡ ܕܪܡ ܒܝܬ ܒܢܝܢܫܐ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܢܕܝܕ ܗܘ ܀
15 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen yéena ngi fexee jub ci kanamu nit ñi waaye Yàlla xam na seen xol. Ndaxte li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko.
16ܢܡܘܤܐ ܘܢܒܝܐ ܥܕܡܐ ܠܝܘܚܢܢ ܡܢ ܗܝܕܝܢ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܡܤܬܒܪܐ ܘܟܠ ܠܗ ܚܒܨ ܕܢܥܘܠ ܀
16 «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi ñu ngi fi woon ba kera Yaxya di ñëw. La ko dale foofa nag, yégle nañu xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, te ñépp a ngi góor-góorlu, ngir dugg ci.
17ܦܫܝܩ ܗܘ ܕܝܢ ܕܫܡܝܐ ܘܐܪܥܐ ܢܥܒܪܘܢ ܐܘ ܐܬܘܬܐ ܚܕܐ ܡܢ ܢܡܘܤܐ ܬܥܒܪ ܀
17 Waaye nag asamaan ak suuf jóge fi moo gën a yomb randal wenn rëdd ci arafu yoonu Musaa.
18ܟܠ ܡܢ ܕܫܪܐ ܐܢܬܬܗ ܘܢܤܒ ܐܚܪܬܐ ܓܐܪ ܘܟܠ ܡܢ ܕܢܤܒ ܫܒܝܩܬܐ ܓܐܪ ܀
18 «Ku fase sa jabar, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jigéen ju jëkkëram fase, njaaloo nga.
19ܓܒܪܐ ܕܝܢ ܚܕ ܥܬܝܪܐ ܐܝܬ ܗܘܐ ܘܠܒܫ ܗܘܐ ܒܘܨܐ ܘܐܪܓܘܢܐ ܘܟܠܝܘܡ ܡܬܒܤܡܝܢ ܗܘܐ ܓܐܝܐܝܬ ܀
19 «Dafa amoon boroom alal juy sol yére yu rafet te jafe, tey dund bés bu set dund gu neex.
20ܘܡܤܟܢܐ ܚܕ ܐܝܬ ܗܘܐ ܕܫܡܗ ܠܥܙܪ ܘܪܡܐ ܗܘܐ ܠܘܬ ܬܪܥܗ ܕܗܘ ܥܬܝܪܐ ܟܕ ܡܡܚܝ ܒܫܘܚܢܐ ܀
20 Fekk miskin mu ñuy wax Lasaar daan tëdd ca buntu këram, fees dell ak ay góom,
21ܘܡܬܝܐܒ ܗܘܐ ܕܢܡܠܐ ܟܪܤܗ ܡܢ ܦܪܬܘܬܐ ܕܢܦܠܝܢ ܡܢ ܦܬܘܪܗ ܕܗܘ ܥܬܝܪܐ ܐܠܐ ܐܦ ܟܠܒܐ ܐܬܝܢ ܗܘܘ ܡܠܚܟܝܢ ܫܘܚܢܘܗܝ ܀
21 te bu sañoon, di lekk ci desiti ñam wiy rot ci lekkukaayu boroom alal ji. Xaj yi sax daan nañu ñëw, di mar ay góomam.
22ܗܘܐ ܕܝܢ ܘܡܝܬ ܗܘ ܡܤܟܢܐ ܘܐܘܒܠܘܗܝ ܡܠܐܟܐ ܠܥܘܒܗ ܕܐܒܪܗܡ ܐܦ ܗܘ ܕܝܢ ܥܬܝܪܐ ܡܝܬ ܘܐܬܩܒܪ ܀
22 «Noonu miskin ma dee, malaaka yi yóbbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, ñu suul ko.
23ܘܟܕ ܡܫܬܢܩ ܒܫܝܘܠ ܐܪܝܡ ܥܝܢܘܗܝ ܡܢ ܪܘܚܩܐ ܘܚܙܐ ܠܐܒܪܗܡ ܘܠܠܥܙܪ ܒܥܘܒܗ ܀
23 Bi ñu koy mbugal ca safara, mu téen, séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
24ܘܩܪܐ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܘܐܡܪ ܐܒܝ ܐܒܪܗܡ ܐܬܪܚܡ ܥܠܝ ܘܫܕܪ ܠܠܥܙܪ ܕܢܨܒܘܥ ܪܝܫ ܨܒܥܗ ܒܡܝܐ ܘܢܪܛܒ ܠܝ ܠܫܢܝ ܕܗܐ ܡܫܬܢܩ ܐܢܐ ܒܫܠܗܒܝܬܐ ܗܕܐ ܀
24 Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci safara sii!”
25ܐܡܪ ܠܗ ܐܒܪܗܡ ܒܪܝ ܐܬܕܟܪ ܕܩܒܠܬ ܛܒܬܟ ܒܚܝܝܟ ܘܠܥܙܪ ܒܝܫܬܗ ܘܗܫܐ ܗܐ ܡܬܬܢܝܚ ܗܪܟܐ ܘܐܢܬ ܡܫܬܢܩ ܀
25 Ibraayma ne ko: “Sama doom, fàttalikul ne, jot nga sa bànneex ci àddina, fekk Lasaar dëkk ci tiis. Looloo tax xolam sedd fii, yaw nag, ngay sonn.
26ܘܥܡ ܗܠܝܢ ܟܠܗܝܢ ܗܘܬܐ ܪܒܬܐ ܤܝܡܐ ܒܝܢܝܢ ܘܠܟܘܢ ܕܐܝܠܝܢ ܕܨܒܝܢ ܡܟܐ ܕܢܥܒܪܘܢ ܠܘܬܟܘܢ ܠܐ ܢܫܟܚܘܢ ܘܐܦܠܐ ܕܡܢ ܬܡܢ ܢܥܒܪܘܢ ܠܘܬܢ ܀
26 Rax-ca-dolli it am na kàmb gu xóot sunu diggante ak yéen, ba tax ñi bëgg a jóge fii jëm ci yéen, walla ñi bëgg a jóge foofu jëmsi ci nun, duñu ko man.”
27ܐܡܪ ܠܗ ܡܕܝܢ ܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟ ܐܒܝ ܕܬܫܕܪܝܘܗܝ ܠܒܝܬ ܐܒܝ ܀
27 «Noonu boroom alal ja ne: “Kon nag maam, maa ngi lay ñaan, nga yebal Lasaar ca sama kër baay,
28ܚܡܫܐ ܓܝܪ ܐܚܝܢ ܐܝܬ ܠܝ ܢܐܙܠ ܢܤܗܕ ܐܢܘܢ ܕܠܐ ܐܦ ܗܢܘܢ ܢܐܬܘܢ ܠܕܘܟܬܐ ܗܕܐ ܕܬܫܢܝܩܐ ܀
28 ndaxte am naa fa juróomi rakk. Na leen artu, ngir ñu bañ a ñëw ñoom itam ci bérabu metit wii.”
29ܐܡܪ ܠܗ ܐܒܪܗܡ ܐܝܬ ܠܗܘܢ ܡܘܫܐ ܘܢܒܝܐ ܢܫܡܥܘܢ ܐܢܘܢ ܀
29 Ibraayma ne ko: “Say doomu baay, ñu ngeek yoonu Musaa ak téerey yonent yi. Nañu leen déggal.”
30ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗ ܠܐ ܐܒܝ ܐܒܪܗܡ ܐܠܐ ܐܢ ܐܢܫ ܡܢ ܡܝܬܐ ܢܐܙܠ ܠܘܬܗܘܢ ܬܝܒܝܢ ܀
30 Boroom alal ja ne ko: “Déedéet, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca ñoom, dinañu tuub seeni bàkkaar.”
31ܐܡܪ ܠܗ ܐܒܪܗܡ ܐܢ ܠܡܘܫܐ ܘܠܢܒܝܐ ܠܐ ܫܡܥܝܢ ܐܦ ܠܐ ܐܢ ܐܢܫ ܡܢ ܡܝܬܐ ܢܩܘܡ ܡܗܝܡܢܝܢ ܠܗ ܀
31 Waaye Ibraayma tontu ko ne: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»