1ܘܟܕ ܥܠ ܝܫܘܥ ܘܥܒܪ ܒܐܝܪܝܚܘ ܀
1 Yeesu dugg na Yeriko, jaar ca dëkk ba, di dem.
2ܓܒܪܐ ܚܕ ܕܫܡܗ ܙܟܝ ܥܬܝܪܐ ܗܘܐ ܘܪܒ ܡܟܤܐ ܀
2 Waaye amoon na fa waa ju ñuy wax Sase. Njiitu juutikat la, te di ku bare alal.
3ܘܨܒܐ ܗܘܐ ܕܢܚܙܐ ܠܝܫܘܥ ܕܡܢܘ ܘܠܐ ܡܫܟܚ ܗܘܐ ܡܢ ܟܢܫܐ ܡܛܠ ܕܒܩܘܡܬܗ ܙܥܘܪ ܗܘܐ ܙܟܝ ܀
3 Bëgg na gis kan mooy Yeesu, waaye dafa gàtt lool, ba mënu koo gis ndax mbooloo ma.
4ܘܪܗܛ ܩܕܡܗ ܠܝܫܘܥ ܘܤܠܩ ܠܗ ܠܬܬܐ ܦܟܝܗܬܐ ܕܢܚܙܝܘܗܝ ܡܛܠ ܕܗܟܘܬ ܥܬܝܕ ܗܘܐ ܕܢܥܒܪ ܀
4 Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, yéeg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroon a jaar.
5ܘܟܕ ܐܬܐ ܠܗܝ ܕܘܟܬܐ ܝܫܘܥ ܚܙܝܗܝ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܤܬܪܗܒ ܚܘܬ ܙܟܝ ܝܘܡܢܐ ܓܝܪ ܘܠܐ ܕܒܒܝܬܟ ܐܗܘܐ ܀
5 Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax tey sa kër laa war a dal.»
6ܘܐܤܬܪܗܒ ܢܚܬ ܘܩܒܠܗ ܟܕ ܚܕܐ ܀
6 Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég.
7ܟܕ ܚܙܘ ܕܝܢ ܟܠܗܘܢ ܪܛܢܝܢ ܗܘܘ ܘܐܡܪܝܢ ܕܠܘܬ ܓܒܪܐ ܚܛܝܐ ܥܠ ܫܪܐ ܀
7 Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.»
8ܩܡ ܕܝܢ ܙܟܝ ܘܐܡܪ ܠܝܫܘܥ ܗܐ ܡܪܝ ܦܠܓܘܬ ܢܟܤܝ ܝܗܒ ܐܢܐ ܠܡܤܟܢܐ ܘܠܟܠܢܫ ܡܕܡ ܕܓܠܙܬ ܚܕ ܒܐܪܒܥܐ ܦܪܥ ܐܢܐ ܀
8 Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma mas a njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.»
9ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܝܘܡܢܐ ܗܘܘ ܚܝܐ ܠܒܝܬܐ ܗܢܐ ܡܛܠ ܕܐܦ ܗܢܐ ܒܪܗ ܗܘ ܕܐܒܪܗܡ ܀
9 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.
10ܐܬܐ ܓܝܪ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܕܢܒܥܐ ܘܢܚܐ ܗܘ ܡܕܡ ܕܐܒܝܕ ܗܘܐ ܀
10 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»
11ܘܟܕ ܫܡܥܝܢ ܗܘܘ ܗܠܝܢ ܐܘܤܦ ܠܡܐܡܪ ܡܬܠܐ ܡܛܠ ܕܩܪܝܒ ܗܘܐ ܠܐܘܪܫܠܡ ܘܤܒܪܝܢ ܗܘܘ ܕܒܗܝ ܫܥܬܐ ܥܬܝܕܐ ܕܬܬܓܠܐ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
11 Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne, nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa.
12ܘܐܡܪ ܓܒܪܐ ܚܕ ܒܪ ܛܘܗܡܐ ܪܒܐ ܐܙܠ ܠܐܬܪܐ ܪܚܝܩܐ ܕܢܤܒ ܠܗ ܡܠܟܘܬܐ ܘܢܗܦܘܟ ܀
12 Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu dellusiwaat.
13ܘܩܪܐ ܥܤܪܐ ܥܒܕܘܗܝ ܘܝܗܒ ܠܗܘܢ ܥܤܪܐ ܡܢܝܢ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܬܬܓܪܘ ܥܕ ܐܬܐ ܐܢܐ ܀
13 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibbisi.”
14ܒܢܝ ܡܕܝܢܬܗ ܕܝܢ ܤܢܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܘܫܕܪܘ ܐܝܙܓܕܐ ܒܬܪܗ ܘܐܡܪܝܢ ܠܐ ܨܒܝܢ ܚܢܢ ܕܢܡܠܟ ܥܠܝܢ ܗܢܐ ܀
14 Waaye waa réewam bëgguñu ko. Noonu ñu yónni ndaw ci gannaawam ne: “Bëggunu nit kii yilif nu.”
15ܘܟܕ ܢܤܒ ܡܠܟܘܬܐ ܘܗܦܟ ܐܡܪ ܕܢܩܪܘܢ ܠܗ ܗܢܘܢ ܥܒܕܘܗܝ ܕܝܗܒ ܠܗܘܢ ܟܤܦܐ ܕܢܕܥ ܡܢܐ ܟܠ ܚܕ ܚܕ ܡܢܗܘܢ ܐܬܬܓܪ ܀
15 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu dellusi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye.
16ܘܐܬܐ ܩܕܡܝܐ ܘܐܡܪ ܡܪܝ ܡܢܝܟ ܥܤܪܐ ܡܢܝܢ ܐܘܬܪ ܀
16 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.”
17ܐܡܪ ܠܗ ܐܝܘ ܥܒܕܐ ܛܒܐ ܕܒܩܠܝܠ ܐܫܬܟܚܬ ܡܗܝܡܢ ܬܗܘܐ ܫܠܝܛ ܥܠ ܥܤܪܐ ܟܪܟܝܢ ܀
17 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne, takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.”
18ܘܐܬܐ ܕܬܪܝܢ ܘܐܡܪ ܡܪܝ ܡܢܝܟ ܚܡܫܐ ܡܢܝܢ ܥܒܕ ܀
18 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”
19ܐܡܪ ܐܦ ܠܗܢܐ ܐܦ ܐܢܬ ܬܗܘܐ ܫܠܝܛ ܥܠ ܚܡܫܐ ܟܪܟܝܢ ܀
19 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20ܘܐܬܐ ܐܚܪܢܐ ܘܐܡܪ ܡܪܝ ܗܐ ܡܢܝܟ ܗܘ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܘܬܝ ܟܕ ܤܝܡ ܒܤܕܘܢܐ ܀
20 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.
21ܕܚܠܬ ܓܝܪ ܡܢܟ ܕܓܒܪܐ ܐܢܬ ܩܫܝܐ ܘܫܩܠ ܐܢܬ ܡܕܡ ܕܠܐ ܤܡܬ ܘܚܨܕ ܐܢܬ ܡܕܡ ܕܠܐ ܙܪܥܬ ܀
21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.”
22ܐܡܪ ܠܗ ܡܢ ܦܘܡܟ ܐܕܘܢܟ ܥܒܕܐ ܒܝܫܐ ܝܕܥ ܗܘܝܬ ܠܝ ܕܓܒܪܐ ܐܢܐ ܩܫܝܐ ܘܫܩܠ ܐܢܐ ܡܕܡ ܕܠܐ ܤܡܬ ܘܚܨܕ ܐܢܐ ܡܕܡ ܕܠܐ ܙܪܥܬ ܀
22 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul.
23ܠܡܢܐ ܠܐ ܝܗܒܬ ܟܤܦܝ ܥܠ ܦܬܘܪܐ ܘܐܢܐ ܐܬܐ ܗܘܝܬ ܬܒܥ ܠܗ ܥܡ ܪܒܝܬܗ ܀
23 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot sama xaalis ak la mu jur.”
24ܘܠܗܢܘܢ ܕܩܝܡܝܢ ܩܕܡܘܗܝ ܐܡܪ ܤܒܘ ܡܢܗ ܡܢܝܐ ܘܗܒܘ ܠܗܘ ܕܐܝܬ ܠܘܬܗ ܥܤܪܐ ܡܢܝܢ ܀
24 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.”
25ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܡܪܢ ܐܝܬ ܠܘܬܗ ܥܤܪܐ ܡܢܝܢ ܀
25 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.”
26ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܠܟܠ ܡܢ ܕܐܝܬ ܠܗ ܢܬܝܗܒ ܠܗ ܘܡܢ ܗܘ ܕܠܝܬ ܠܗ ܐܦ ܗܘ ܕܐܝܬ ܠܗ ܢܬܢܤܒ ܡܢܗ ܀
26 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
27ܒܪܡ ܠܗܢܘܢ ܒܥܠܕܒܒܝ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܨܒܘ ܕܐܡܠܟ ܥܠܝܗܘܢ ܐܝܬܘ ܐܢܘܢ ܘܩܛܠܘ ܐܢܘܢ ܩܕܡܝ ܀
27 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
28ܘܟܕ ܐܡܪ ܗܠܝܢ ܝܫܘܥ ܢܦܩ ܠܩܕܡܘܗܝ ܕܢܐܙܠ ܠܐܘܪܫܠܡ ܀
28 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem.
29ܘܟܕ ܡܛܝ ܠܒܝܬ ܦܓܐ ܘܒܝܬ ܥܢܝܐ ܥܠ ܓܢܒ ܛܘܪܐ ܕܡܬܩܪܐ ܕܒܝܬ ܙܝܬܐ ܫܕܪ ܬܪܝܢ ܡܢ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܀
29 Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem,
30ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܙܠܘ ܠܩܪܝܬܐ ܗܝ ܕܠܩܘܒܠܢ ܘܟܕ ܥܐܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗ ܗܐ ܡܫܟܚܝܢ ܐܢܬܘܢ ܥܝܠܐ ܕܐܤܝܪ ܕܐܢܫ ܡܡܬܘܡ ܠܐ ܪܟܒ ܥܠܘܗܝ ܫܪܘ ܐܝܬܐܘܗܝ ܀
30 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.
31ܘܐܢ ܐܢܫ ܡܫܐܠ ܠܟܘܢ ܠܡܢܐ ܫܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗ ܗܟܢܐ ܐܡܪܘ ܠܗ ܠܡܪܢ ܡܬܒܥܐ ܀
31 Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»
32ܘܐܙܠܘ ܗܢܘܢ ܕܐܫܬܕܪܘ ܘܐܫܟܚܘ ܐܝܟܢܐ ܕܐܡܪ ܠܗܘܢ ܀
32 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon.
33ܘܟܕ ܫܪܝܢ ܠܗ ܠܥܝܠܐ ܐܡܪܝܢ ܠܗܘܢ ܡܪܘܗܝ ܡܢܐ ܫܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܥܝܠܐ ܗܘ ܀
33 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?»
34ܘܐܡܪܘ ܠܗܘܢ ܕܠܡܪܢ ܡܬܒܥܐ ܀
34 Ñu tontu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.»
35ܘܐܝܬܝܘܗܝ ܠܘܬ ܝܫܘܥ ܘܐܪܡܝܘ ܥܠ ܥܝܠܐ ܡܐܢܝܗܘܢ ܘܐܪܟܒܘܗܝ ܠܝܫܘܥ ܥܠܘܗܝ ܀
35 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.
36ܟܕ ܕܝܢ ܐܙܠ ܦܪܤܝܢ ܗܘܘ ܡܐܢܝܗܘܢ ܒܐܘܪܚܐ ܀
36 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi.
37ܘܟܕ ܩܪܒ ܠܡܚܬܬܐ ܕܛܘܪܐ ܕܒܝܬ ܙܝܬܐ ܫܪܝܘ ܟܠܗ ܟܢܫܐ ܕܬܠܡܝܕܐ ܚܕܝܢ ܘܡܫܒܚܝܢ ܠܐܠܗܐ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܥܠ ܟܠ ܚܝܠܐ ܕܚܙܘ ܀
37 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis.
38ܘܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܒܪܝܟ ܗܘ ܡܠܟܐ ܕܐܬܐ ܒܫܡܗ ܕܡܪܝܐ ܫܠܡܐ ܒܫܡܝܐ ܘܫܘܒܚܐ ܒܡܪܘܡܐ ܀
38 Ñu ngi naan:«Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na jàmm am ca asamaan,te ndam li féete ca bérab yu gën a kawe!»
39ܐܢܫܐ ܕܝܢ ܡܢ ܦܪܝܫܐ ܡܢ ܒܝܢܝ ܟܢܫܐ ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܪܒܝ ܟܐܝ ܒܬܠܡܝܕܝܟ ܀
39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!»
40ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܐܢ ܗܠܝܢ ܢܫܬܩܘܢ ܟܐܦܐ ܢܩܥܝܢ ܀
40 Noonu mu tontu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»
41ܘܟܕ ܩܪܒ ܘܚܙܗ ܠܡܕܝܢܬܐ ܒܟܐ ܥܠܝܗ ܀
41 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko
42ܘܐܡܪ ܐܠܘ ܟܝ ܝܕܥܬܝ ܐܝܠܝܢ ܕܐܝܬܝܗܝܢ ܕܫܠܡܟܝ ܐܦܢ ܒܗܢܐ ܝܘܡܟܝ ܗܫܐ ܕܝܢ ܐܬܟܤܝ ܠܗܝܢ ܡܢ ܥܝܢܝܟܝ ܀
42 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la man a indil jàmm! Waaye fi mu ne mënuloo koo gis.
43ܢܐܬܘܢ ܠܟܝ ܕܝܢ ܝܘܡܬܐ ܕܢܚܕܪܘܢܟܝ ܒܥܠܕܒܒܝܟܝ ܘܢܐܠܨܘܢܟܝ ܡܢ ܟܠ ܕܘܟܐ ܀
43 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la.
44ܘܢܤܚܦܘܢܟܝ ܘܠܒܢܝܟܝ ܒܓܘܟܝ ܘܠܐ ܢܫܒܩܘܢ ܒܟܝ ܟܐܦ ܥܠ ܟܐܦ ܚܠܦ ܕܠܐ ܝܕܥܬܝ ܙܒܢܐ ܕܤܘܥܪܢܟܝ ܀
44 Dinañu la yàqaate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»
45ܘܟܕ ܥܠ ܠܗܝܟܠܐ ܫܪܝ ܠܡܦܩܘ ܠܐܝܠܝܢ ܕܙܒܢܝܢ ܒܗ ܘܡܙܒܢܝܢ ܀
45 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaay,
46ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܟܬܝܒ ܕܒܝܬܝ ܒܝܬ ܨܠܘܬܐ ܐܝܬܘܗܝ ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܥܒܕܬܘܢܝܗܝ ܡܥܪܬܐ ܕܠܤܛܝܐ ܀
46 naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”»
47ܘܗܘ ܡܠܦ ܗܘܐ ܟܠ ܝܘܡ ܒܗܝܟܠܐ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܕܝܢ ܘܤܦܪܐ ܘܩܫܝܫܐ ܕܥܡܐ ܒܥܝܢ ܗܘܘ ܠܡܘܒܕܘܬܗ ܀
47 Bés bu nekk Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wut a reylu.
48ܘܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܗܘܘ ܡܢܐ ܢܥܒܕܘܢ ܠܗ ܟܠܗ ܓܝܪ ܥܡܐ ܬܠܐ ܗܘܐ ܒܗ ܠܡܫܡܥܗ ܀
48 Waaye xamuñu woon lan lañu man a def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.