1ܚܪ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܒܥܬܝܪܐ ܐܝܠܝܢ ܕܪܡܝܢ ܗܘܘ ܒܝܬ ܓܙܐ ܩܘܪܒܢܝܗܘܢ ܀
1 Noonu Yeesu siggi, séen ay boroom alal ñuy dugal seen sarax ca ndab ya ca kër Yàlla ga.
2ܘܚܙܐ ܐܦ ܐܪܡܠܬܐ ܚܕܐ ܡܤܟܢܬܐ ܕܐܪܡܝܬ ܫܡܘܢܐ ܬܪܝܢ ܀
2 Mu gis itam jenn jigéen ju jëkkëram faatu te mu ñàkk, ju fa def ñaari poseti xànjar.
3ܘܐܡܪ ܫܪܪܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܗܕܐ ܐܪܡܠܬܐ ܡܤܟܢܬܐ ܐܪܡܝܬ ܝܬܝܪ ܡܢ ܟܠܢܫ ܀
3 Noonu mu daldi ne: «Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, jigéen ju ñàkk jee moo ëpp ñeneen ñépp lu mu joxe.
4ܟܠܗܘܢ ܓܝܪ ܗܠܝܢ ܡܢ ܡܐ ܕܝܬܝܪ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܐܪܡܝܘ ܒܝܬ ܩܘܪܒܢܐ ܕܐܠܗܐ ܗܕܐ ܕܝܢ ܡܢ ܚܤܝܪܘܬܗ ܟܠ ܕܩܢܝܐ ܗܘܬ ܐܪܡܝܬܗ ܀
4 Ñoom ñépp dañu sàkku ci seen barele, waaye moom dafa sàkku ci néewleem, ba joxe xaalis bi mu waroon a dunde.»
5ܘܟܕ ܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܐܢܫܝܢ ܥܠ ܗܝܟܠܐ ܕܒܟܐܦܐ ܫܦܝܪܬܐ ܘܒܩܘܪܒܢܐ ܡܨܒܬ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܀
5 Noonu ay nit doon wax ci lu jëm ca kër Yàlla ga, ak ni ñu ko rafetale ak ay doj yu jafe ak alal ju ñu jébbal Yàlla. Waaye Yeesu ne leen:
6ܗܠܝܢ ܕܚܙܝܢ ܐܢܬܘܢ ܢܐܬܘܢ ܝܘܡܬܐ ܕܒܗܘܢ ܠܐ ܬܫܬܒܩ ܟܐܦ ܥܠ ܟܐܦ ܕܠܐ ܬܤܬܬܪ ܀
6 «Li ngeen gis fii lépp, jamono dina ñëw joo xam ne dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
7ܘܡܫܐܠܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܘܐܡܪܝܢ ܡܠܦܢܐ ܐܡܬܝ ܗܠܝܢ ܢܗܘܝܢ ܘܡܢܐ ܗܝ ܐܬܐ ܡܐ ܕܩܪܝܒܢ ܗܠܝܢ ܕܢܗܘܝܢ ܀
7 Ñu laaj ko ne: «Kilifa gi, kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, looloo ngi waaj a xew?»
8ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܚܙܘ ܠܡܐ ܬܛܥܘܢ ܤܓܝܐܐ ܓܝܪ ܢܐܬܘܢ ܒܫܡܝ ܘܢܐܡܪܘܢ ܕܐܢܐ ܐܢܐ ܡܫܝܚܐ ܘܙܒܢܐ ܩܪܒ ܠܐ ܕܝܢ ܬܐܙܠܘܢ ܒܬܪܗܘܢ ܀
8 Yeesu tontu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu.
9ܘܡܐ ܕܫܡܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܩܪܒܐ ܘܫܓܘܫܝܐ ܠܐ ܬܕܚܠܘܢ ܥܬܝܕܢ ܐܢܝܢ ܓܝܪ ܗܠܝܢ ܠܘܩܕܡ ܠܡܗܘܐ ܐܠܐ ܠܐ ܥܕܟܝܠ ܡܛܬ ܚܪܬܐ ܀
9 Bu ngeen déggee ay xare ak ay réew yu jóg, wottuleen a tiit, ndaxte fàww yooyule jëkk a am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.»
10ܢܩܘܡ ܓܝܪ ܥܡܐ ܥܠ ܥܡܐ ܘܡܠܟܘ ܥܠ ܡܠܟܘ ܀
10 Noonu mu teg ca ne: «Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew.
11ܘܙܘܥܐ ܪܘܪܒܐ ܢܗܘܘܢ ܒܕܘܟܐ ܕܘܟܐ ܘܟܦܢܐ ܘܡܘܬܢܐ ܘܢܗܘܝܢ ܕܚܠܬܐ ܘܤܘܪܕܐ ܘܐܬܘܬܐ ܪܘܪܒܬܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܢܬܚܙܝܢ ܘܤܬܘܐ ܪܘܪܒܐ ܢܗܘܘܢ ܀
11 Suuf dina yengu yengu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan.
12ܩܕܡ ܕܝܢ ܗܠܝܢ ܟܠܗܝܢ ܢܪܡܘܢ ܥܠܝܟܘܢ ܐܝܕܝܐ ܘܢܪܕܦܘܢܟܘܢ ܘܢܫܠܡܘܢܟܘܢ ܠܟܢܘܫܬܐ ܘܠܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܘܢܩܪܒܘܢܟܘܢ ܩܕܡ ܡܠܟܐ ܘܗܓܡܘܢܐ ܡܛܠ ܫܡܝ ܀
12 Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam ay buur yi ak ay boroom réew ndax sama tur.
13ܗܘܝܐ ܠܟܘܢ ܕܝܢ ܠܤܗܕܘܬܐ ܀
13 Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.
14ܤܝܡܘ ܕܝܢ ܒܠܒܟܘܢ ܕܠܐ ܬܗܘܘܢ ܡܬܝܠܦܝܢ ܠܡܦܩ ܪܘܚܐ ܀
14 Fasleen yéenee bañ a wut lay ngir musal seen bopp.
15ܐܢܐ ܓܝܪ ܐܬܠ ܠܟܘܢ ܦܘܡܐ ܘܚܟܡܬܐ ܐܝܕܐ ܕܠܐ ܢܫܟܚܘܢ ܠܡܩܡ ܠܩܘܒܠܗ ܟܠܗܘܢ ܒܥܠܕܒܒܝܟܘܢ ܀
15 Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko man a teggi, mbaa ñu di ko weddi.
16ܢܫܠܡܘܢܟܘܢ ܕܝܢ ܐܒܗܝܟܘܢ ܘܐܚܝܟܘܢ ܘܐܚܝܢܝܟܘܢ ܘܪܚܡܝܟܘܢ ܘܢܡܝܬܘܢ ܡܢܟܘܢ ܀
16 Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen.
17ܘܬܗܘܘܢ ܤܢܝܐܝܢ ܡܢ ܟܠ ܐܢܫ ܡܛܠ ܫܡܝ ܀
17 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
18ܘܡܢܬܐ ܡܢ ܪܫܟܘܢ ܠܐ ܬܐܒܕ ܀
18 Waaye seen genn kawar sax du neen.
19ܒܡܤܝܒܪܢܘܬܟܘܢ ܕܝܢ ܬܩܢܘܢ ܢܦܫܟܘܢ ܀
19 Seen muñ moo leen di musal.
20ܡܐ ܕܝܢ ܕܚܙܝܬܘܢ ܠܐܘܪܫܠܡ ܕܚܕܝܪܝܢ ܠܗ ܚܝܠܐ ܗܝܕܝܢ ܕܥܘ ܕܩܪܒ ܠܗ ܚܘܪܒܗ ܀
20 «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.
21ܗܝܕܝܢ ܐܝܠܝܢ ܕܒܝܗܘܕ ܐܢܘܢ ܢܥܪܩܘܢ ܠܛܘܪܐ ܘܐܝܠܝܢ ܕܒܓܘܗ ܐܢܘܢ ܢܥܪܩܘܢ ܘܕܒܩܘܪܝܐ ܠܐ ܢܥܠܘܢ ܠܗ ܀
21 Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba!
22ܕܝܘܡܬܐ ܐܢܘܢ ܗܠܝܢ ܕܬܒܥܬܐ ܕܢܫܠܡ ܟܠ ܡܐ ܕܟܬܝܒ ܀
22 Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat.
23ܘܝ ܕܝܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܒܛܢܢ ܘܠܐܝܠܝܢ ܕܡܝܢܩܢ ܒܗܢܘܢ ܝܘܡܬܐ ܢܗܘܐ ܓܝܪ ܐܘܠܨܢܐ ܪܒܐ ܒܐܪܥܐ ܘܪܘܓܙܐ ܥܠ ܥܡܐ ܗܢܐ ܀
23 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii.
24ܘܢܦܠܘܢ ܒܦܘܡܐ ܕܚܪܒܐ ܘܢܫܬܒܘܢ ܠܟܠ ܐܬܪ ܘܐܘܪܫܠܡ ܬܗܘܐ ܡܬܕܝܫܐ ܡܢ ܥܡܡܐ ܥܕܡܐ ܕܢܫܠܡܘܢ ܙܒܢܐ ܕܥܡܡܐ ܀
24 Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.
25ܘܢܗܘܝܢ ܐܬܘܬܐ ܒܫܡܫܐ ܘܒܤܗܪܐ ܘܒܟܘܟܒܐ ܘܒܐܪܥܐ ܐܘܠܨܢܐ ܕܥܡܡܐ ܘܦܘܫܟ ܐܝܕܝܐ ܡܢ ܬܘܗܬܐ ܕܩܠܐ ܕܝܡܐ ܀
25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yengu-yengub duus yi.
26ܘܙܘܥܐ ܕܡܦܩ ܢܦܫܬܐ ܕܒܢܝܢܫܐ ܡܢ ܕܚܠܬܐ ܕܡܕܡ ܕܥܬܝܕ ܠܡܐܬܐ ܥܠ ܐܪܥܐ ܘܢܬܬܙܝܥܘܢ ܚܝܠܐ ܕܫܡܝܐ ܀
26 Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nar a wàcc ci àddina, ndaxte dees na yengal kàttani asamaan.
27ܘܗܝܕܝܢ ܢܚܙܘܢܝܗܝ ܠܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܕܐܬܐ ܒܥܢܢܐ ܥܡ ܚܝܠܐ ܤܓܝܐܐ ܘܫܘܒܚܐ ܪܒܐ ܀
27 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
28ܡܐ ܕܝܢ ܕܫܪܝ ܗܠܝܢ ܕܢܗܘܝܢ ܐܬܠܒܒܘ ܘܐܪܝܡܘ ܪܫܝܟܘܢ ܡܛܠ ܕܩܪܒ ܠܗ ܦܘܪܩܢܟܘܢ ܀
28 Bu mbir yooyu di tàmbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, téen, ndaxte seen njot jubsi na.»
29ܘܐܡܪ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܡܬܠܐ ܚܙܘ ܠܬܬܐ ܘܠܟܠܗܘܢ ܐܝܠܢܐ ܀
29 Noonu Yeesu misaal leen lii: «Xool-leen garabu figg ak yeneen garab yi.
30ܕܡܐ ܕܡܦܪܥܝܢ ܡܚܕܐ ܡܢܗܘܢ ܡܤܬܟܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܩܪܒ ܠܗ ܩܝܛܐ ܀
30 Bu ñu gisee ñu sëq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat.
31ܗܟܢܐ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܡܐ ܕܚܙܝܬܘܢ ܗܠܝܢ ܕܗܘܝܢ ܕܥܘ ܕܩܪܝܒܐ ܗܝ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
31 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na.
32ܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܠܐ ܬܥܒܪ ܫܪܒܬܐ ܗܕܐ ܥܕܡܐ ܕܗܠܝܢ ܟܠܗܝܢ ܢܗܘܝܢ ܀
32 «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.
33ܫܡܝܐ ܘܐܪܥܐ ܢܥܒܪܘܢ ܘܡܠܝ ܠܐ ܢܥܒܪܢ ܀
33 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
34ܐܙܕܗܪܘ ܕܝܢ ܒܢܦܫܟܘܢ ܕܠܐ ܡܬܘܡ ܢܐܩܪܘܢ ܠܒܘܬܟܘܢ ܒܐܤܘܛܘܬܐ ܘܒܪܘܝܘܬܐ ܘܒܨܦܬܐ ܕܥܠܡܐ ܘܡܢ ܫܠܝܐ ܢܐܬܐ ܥܠܝܟܘܢ ܝܘܡܐ ܗܘ ܀
34 «Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal.
35ܐܝܟ ܨܦܚܬܐ ܓܝܪ ܢܨܦܚ ܥܠ ܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܝܬܒܝܢ ܥܠ ܐܦܝܗ ܕܟܠܗ ܐܪܥܐ ܀
35 Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf.
36ܗܘܘ ܗܟܝܠ ܫܗܪܝܢ ܒܟܠܙܒܢ ܘܡܨܠܝܢ ܕܬܫܘܘܢ ܠܡܥܪܩ ܡܢ ܗܠܝܢ ܕܥܬܝܕܢ ܠܡܗܘܐ ܘܬܩܘܡܘܢ ܩܕܡ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܀
36 Yeewuleen, di sax ci ñaan, ngir ngeen man a mucc ci loolu lépp war a xew, te man a taxaw ak kóolute ci kanamu Doomu nit ki.»
37ܒܐܝܡܡܐ ܕܝܢ ܡܠܦ ܗܘܐ ܒܗܝܟܠܐ ܘܒܠܠܝܐ ܢܦܩ ܗܘܐ ܒܐܬ ܒܛܘܪܐ ܕܡܬܩܪܐ ܕܒܝܬ ܙܝܬܐ ܀
37 Yeesoo ngi daan yendoo jàngale ca kër Yàlla ga, te bu guddee mu dem ca tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, fanaan fa.
38ܘܟܠܗ ܥܡܐ ܡܩܕܡܝܢ ܗܘܘ ܠܘܬܗ ܠܗܝܟܠܐ ܠܡܫܡܥ ܡܠܬܗ ܀
38 Te nit ñépp dañu daan teel a xëy ca kër Yàlla ga, di ko déglu.