1ܘܩܪܒܘ ܦܪܝܫܐ ܘܙܕܘܩܝܐ ܡܢܤܝܢ ܠܗ ܘܫܐܠܝܢ ܠܗ ܐܬܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܕܢܚܘܐ ܐܢܘܢ ܀
1 Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.»
2ܗܘ ܕܝܢ ܥܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܡܐ ܕܗܘܐ ܪܡܫܐ ܐܡܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܨܚܘܐ ܗܘ ܤܡܩܬ ܓܝܪ ܫܡܝܐ ܀
2 Noonu Yeesu tontu leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.”
3ܘܒܨܦܪܐ ܐܡܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܝܘܡܢܐ ܤܬܘܐ ܗܘ ܤܡܩܬ ܓܝܪ ܫܡܝܐ ܟܡܝܪܐܝܬ ܢܤܒܝ ܒܐܦܐ ܦܪܨܘܦܐ ܕܫܡܝܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܬܒܩܘܢ ܐܬܘܬܐ ܕܙܒܢܐ ܗܢܐ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܬܦܪܫܘܢ ܀
3 Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeen a ràññee melow asamaan, waaye mënuleen a ràññee firndey jamono ji nu tollu.
4ܫܪܒܬܐ ܒܝܫܬܐ ܘܓܝܪܬܐ ܐܬܐ ܒܥܝܐ ܘܐܬܐ ܠܐ ܡܬܝܗܒܐ ܠܗ ܐܠܐ ܐܬܗ ܕܝܘܢܢ ܢܒܝܐ ܘܫܒܩ ܐܢܘܢ ܘܐܙܠ ܀
4 Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla. Waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.» Bi Yeesu waxee loolu, mu jóge ci ñoom, dem.
5ܘܟܕ ܐܬܘ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܠܥܒܪܐ ܛܥܘ ܕܢܤܒܘܢ ܥܡܗܘܢ ܠܚܡܐ ܀
5 Gannaaw loolu taalibe yi jàllaat dex gi, fekk fàtte nañoo yóbbaale mburu.
6ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܚܙܘ ܐܙܕܗܪܘ ܡܢ ܚܡܝܪܐ ܕܦܪܝܫܐ ܘܕܙܕܘܩܝܐ ܀
6 Noonu Yeesu ne leen: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.»
7ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܡܬܪܥܝܢ ܗܘܘ ܒܢܦܫܗܘܢ ܘܐܡܪܝܢ ܕܠܚܡܐ ܠܐ ܢܤܒܘ ܀
7 Bi ko taalibe yi déggee, ñu daldi werante ci seen biir naan: «Nun de indaalewunu mburu.»
8ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܝܕܥ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܡܢܐ ܡܬܚܫܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܢܦܫܟܘܢ ܙܥܘܪܝ ܗܝܡܢܘܬܐ ܕܠܚܡܐ ܠܐ ܫܩܠܬܘܢ ܀
8 Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen di werante ci seen biir, ndaxte indaalewuleen mburu?
9ܠܐ ܥܕܡܐ ܠܗܫܐ ܐܤܬܟܠܬܘܢ ܠܐ ܥܗܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗܢܘܢ ܚܡܫܐ ܠܚܡܝܢ ܕܚܡܫܐ ܐܠܦܝܢ ܘܟܡܐ ܩܘܦܝܢܝܢ ܫܩܠܬܘܢ ܀
9 Ndax xamaguleen ba tey? Xanaa fàttalikuwuleen juróomi mburu ya ngir juróomi junniy góor ña, ak ñaata pañe ngeen dajale woon ciy dammit?
10ܘܠܐ ܠܗܢܘܢ ܫܒܥܐ ܠܚܡܝܢ ܕܐܪܒܥܐ ܐܠܦܝܢ ܘܟܡܐ ܐܤܦܪܝܕܝܢ ܫܩܠܬܘܢ ܀
10 Te ndax fàttalikuwuleen itam juróom-ñaari mburu ya ngir ñeenti junniy góor ña, ak ñaata dàmba ngeen dajale woon ciy dammit?
11ܐܝܟܢ ܠܐ ܐܤܬܟܠܬܘܢ ܕܠܐ ܗܘܐ ܥܠ ܠܚܡܐ ܐܡܪܬ ܠܟܘܢ ܐܠܐ ܕܬܙܕܗܪܘܢ ܡܢ ܚܡܝܪܐ ܕܦܪܝܫܐ ܘܕܙܕܘܩܝܐ ܀
11 Kon nag lu tax xamuleen ne, waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.»
12ܗܝܕܝܢ ܐܤܬܟܠܘ ܕܠܐ ܐܡܪ ܕܢܙܕܗܪܘܢ ܡܢ ܚܡܝܪܐ ܕܠܚܡܐ ܐܠܐ ܡܢ ܝܘܠܦܢܐ ܕܦܪܝܫܐ ܘܕܙܕܘܩܝܐ ܀
12 Noonu ñu xam ne, Yeesu waxul woon lawiiru mburu, waaye ñu moytu njàngalem Farisen ya ak Sadusen ya.
13ܟܕ ܕܝܢ ܐܬܐ ܝܫܘܥ ܠܐܬܪܐ ܕܩܤܪܝܐ ܕܦܝܠܝܦܘܤ ܡܫܐܠ ܗܘܐ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܘܐܡܪ ܡܢܘ ܐܡܪܝܢ ܥܠܝ ܐܢܫܐ ܕܐܝܬܝ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܀
13 Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?»
14ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܐܡܪܘ ܐܝܬ ܕܐܡܪܝܢ ܝܘܚܢܢ ܡܥܡܕܢܐ ܐܚܪܢܐ ܕܝܢ ܐܠܝܐ ܘܐܚܪܢܐ ܐܪܡܝܐ ܐܘ ܚܕ ܡܢ ܢܒܝܐ ܀
14 Taalibe yi tontu ne: «Am na ñu naan, Yaxya, ñeneen ñi, Iliyas; ñi ci des ne, Yeremi walla keneen ci yonent yi.»
15ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܡܢܘ ܐܡܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܐܝܬܝ ܀
15 Noonu Yeesu ne leen: «Waaye yéen, ku ngeen may teg?»
16ܥܢܐ ܫܡܥܘܢ ܟܐܦܐ ܘܐܡܪ ܐܢܬ ܗܘ ܡܫܝܚܐ ܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܚܝܐ ܀
16 Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer tontu ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.»
17ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗ ܛܘܒܝܟ ܫܡܥܘܢ ܒܪܗ ܕܝܘܢܐ ܕܒܤܪܐ ܘܕܡܐ ܠܐ ܓܠܐ ܠܟ ܐܠܐ ܐܒܝ ܕܒܫܡܝܐ ܀
17 Yeesu tontu ko: «Barkeel ñeel na la, Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal lii, waaye sama Baay bi nekk ci kaw.
18ܐܦ ܐܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟ ܕܐܢܬ ܗܘ ܟܐܦܐ ܘܥܠ ܗܕܐ ܟܐܦܐ ܐܒܢܝܗ ܠܥܕܬܝ ܘܬܪܥܐ ܕܫܝܘܠ ܠܐ ܢܚܤܢܘܢܗ ܀
18 Te maa ngi lay wax lii: yaa di Piyeer, te ci kaw doj wu réy woowu laay samp mbooloom ñi ma gëm, te dooley dee du ko manal dara.
19ܠܟ ܐܬܠ ܩܠܝܕܐ ܕܡܠܟܘܬܐ ܕܫܡܝܐ ܘܟܠ ܡܕܡ ܕܬܐܤܘܪ ܒܐܪܥܐ ܢܗܘܐ ܐܤܝܪ ܒܫܡܝܐ ܘܡܕܡ ܕܬܫܪܐ ܒܐܪܥܐ ܢܗܘܐ ܫܪܐ ܒܫܡܝܐ ܀
19 Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.»
20ܗܝܕܝܢ ܦܩܕ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܠܐܢܫ ܠܐ ܢܐܡܪܘܢ ܕܗܘܝܘ ܡܫܝܚܐ ܀
20 Noonu Yeesu dénk taalibe yi bu wóor ne leen: «Buleen wax kenn ne, maay Almasi bi.»
21ܘܡܢ ܗܝܕܝܢ ܫܪܝ ܝܫܘܥ ܠܡܚܘܝܘ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܥܬܝܕ ܗܘ ܕܢܐܙܠ ܠܐܘܪܫܠܡ ܘܤܓܝ ܢܚܫ ܡܢ ܩܫܝܫܐ ܘܡܢ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܘܤܦܪܐ ܘܢܬܩܛܠ ܘܠܝܘܡܐ ܕܬܠܬܐ ܢܩܘܡ ܀
21 Li dale ci jamono jooja, Yeesu tàmbali na xamal taalibeem yi ne, war na dem Yerusalem, daj fa coono yu bare, jóge ca njiit ya, ca saraxalekat yu mag ya ak ca xutbakat ya; ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.
22ܘܕܒܪܗ ܟܐܦܐ ܘܫܪܝ ܠܡܟܐܐ ܒܗ ܘܐܡܪ ܚܤ ܠܟ ܡܪܝ ܕܬܗܘܐ ܠܟ ܗܕܐ ܀
22 Bi mu waxee ba noppi, Piyeer woo ko ci pegg, bëgg koo yedd ne ko: «Yàlla tere, Boroom bi, loolu du la dal.»
23ܗܘ ܕܝܢ ܐܬܦܢܝ ܘܐܡܪ ܠܟܐܦܐ ܙܠ ܠܟ ܠܒܤܬܪܝ ܤܛܢܐ ܬܘܩܠܬܐ ܐܢܬ ܠܝ ܕܠܐ ܡܬܪܥܐ ܐܢܬ ܕܐܠܗܐ ܐܠܐ ܕܒܢܝ ܐܢܫܐ ܀
23 Waaye Yeesu woññiku, daldi ne Piyeer: «Sore ma Seytaane, bu ma xatal; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
24ܗܝܕܝܢ ܐܡܪ ܝܫܘܥ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܡܢ ܕܨܒܐ ܕܢܐܬܐ ܒܬܪܝ ܢܟܦܘܪ ܒܢܦܫܗ ܘܢܫܩܘܠ ܙܩܝܦܗ ܘܢܐܬܐ ܒܬܪܝ ܀
24 Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man.
25ܡܢ ܕܨܒܐ ܓܝܪ ܕܢܚܐ ܢܦܫܗ ܢܘܒܕܝܗ ܘܡܢ ܕܢܘܒܕ ܢܦܫܗ ܡܛܠܬܝ ܢܫܟܚܝܗ ܀
25 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, jotaat ko.
26ܡܢܐ ܓܝܪ ܡܬܗܢܐ ܒܪܢܫܐ ܐܢ ܟܠܗ ܥܠܡܐ ܢܩܢܐ ܘܢܦܫܗ ܢܚܤܪ ܐܘ ܡܢܐ ܢܬܠ ܒܪܢܫܐ ܬܚܠܘܦܐ ܕܢܦܫܗ ܀
26 Te it moom àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Te nit, lu mu war a weccee bakkanam?
27ܥܬܝܕ ܗܘ ܓܝܪ ܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܕܢܐܬܐ ܒܬܫܒܘܚܬܐ ܕܐܒܘܗܝ ܥܡ ܡܠܐܟܘܗܝ ܩܕܝܫܐ ܘܗܝܕܝܢ ܢܦܪܘܥ ܠܐܢܫ ܐܢܫ ܐܝܟ ܥܒܕܘܗܝ ܀ 28 ܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܐܝܬ ܐܢܫܐ ܕܩܝܡܝܢ ܬܢܢ ܕܠܐ ܢܛܥܡܘܢ ܡܘܬܐ ܥܕܡܐ ܕܢܚܙܘܢ ܠܒܪܗ ܕܐܢܫܐ ܕܐܬܐ ܒܡܠܟܘܬܗ ܀
27 Ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci ndamul Baayam, ànd ak ay malaakam; bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam.
28
28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu Doomu nit ki ñëw ci nguuram.»