1ܘܟܕ ܩܪܒ ܠܐܘܪܫܠܡ ܘܐܬܐ ܠܒܝܬ ܦܓܐ ܥܠ ܓܢܒ ܛܘܪܐ ܕܙܝܬܐ ܫܕܪ ܝܫܘܥ ܬܪܝܢ ܡܢ ܬܠܡܝܕܘܗܝ ܀
1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba agsi dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe,
2ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܙܠܘ ܠܩܪܝܬܐ ܗܕܐ ܕܠܩܘܒܠܟܘܢ ܘܡܚܕܐ ܡܫܟܚܝܢ ܐܢܬܘܢ ܚܡܪܐ ܕܐܤܝܪܐ ܘܥܝܠܐ ܥܡܗ ܫܪܘ ܐܝܬܘ ܠܝ ܀
2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen eggee, dingeen gis mbaam mu ñu yeew ak cumburam; yiwileen leen, indil ma leen.
3ܘܐܢ ܐܢܫ ܐܡܪ ܠܟܘܢ ܡܕܡ ܐܡܪܘ ܠܗ ܕܠܡܪܢ ܡܬܒܥܝܢ ܘܡܚܕܐ ܡܫܕܪ ܠܗܘܢ ܠܟܐ ܀
3 Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leen a soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.»
4ܗܕܐ ܕܝܢ ܕܗܘܬ ܕܢܬܡܠܐ ܡܕܡ ܕܐܬܐܡܪ ܒܝܕ ܢܒܝܐ ܕܐܡܪ ܀
4 Yeesu def na noonu, ngir la ñu waxoon jaarale ko cib yonent am, bi mu naan:
5ܐܡܪܘ ܠܒܪܬ ܨܗܝܘܢ ܗܐ ܡܠܟܟܝ ܐܬܐ ܠܟܝ ܡܟܝܟ ܘܪܟܝܒ ܥܠ ܚܡܪܐ ܘܥܠ ܥܝܠܐ ܒܪ ܐܬܢܐ ܀
5 «Waxal waa Siyon:“Seen buur a ngi ñëw ci yéen;ku lewet la, te war mbaam-sëf,dig cumbur, doomu mbaam.”»
6ܘܐܙܠܘ ܬܠܡܝܕܐ ܘܥܒܕܘ ܐܝܟܢܐ ܕܦܩܕ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܀
6 Noonu taalibe ya dem, def loolu leen Yeesu sant.
7ܘܐܝܬܝܘ ܠܚܡܪܐ ܘܠܥܝܠܐ ܘܤܡܘ ܥܠ ܥܝܠܐ ܢܚܬܝܗܘܢ ܘܪܟܒ ܥܠܘܗܝ ܝܫܘܥ ܀
7 Ñu indi mbaam ma, moom ak cumbur ga, lal ci seeni yére, Yeesu toog ca.
8ܘܤܘܓܐܐ ܕܟܢܫܐ ܡܫܘܝܢ ܗܘܘ ܡܐܢܝܗܘܢ ܒܐܘܪܚܐ ܐܚܪܢܐ ܕܝܢ ܦܤܩܝܢ ܗܘܘ ܤܘܟܐ ܡܢ ܐܝܠܢܐ ܘܪܡܝܢ ܒܐܘܪܚܐ ܀
8 Ña ëpp ca mbooloo ma lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña dagg ay cari garab, lal leen it ca yoon wa.
9ܟܢܫܐ ܕܝܢ ܐܝܠܝܢ ܕܐܙܠܝܢ ܗܘܘ ܩܕܡܘܗܝ ܘܐܬܝܢ ܒܬܪܗ ܩܥܝܢ ܗܘܘ ܘܐܡܪܝܢ ܐܘܫܥܢܐ ܠܒܪܗ ܕܕܘܝܕ ܒܪܝܟ ܗܘ ܕܐܬܐ ܒܫܡܗ ܕܡܪܝܐ ܐܘܫܥܢܐ ܒܡܪܘܡܐ ܀
9 Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan:«Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Ca bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”»
10ܘܟܕ ܥܠ ܠܐܘܪܫܠܡ ܐܬܬܙܝܥܬ ܟܠܗ ܡܕܝܢܬܐ ܘܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܡܢܘ ܗܢܐ ܀
10 Bi nga xamee ne Yeesu dugg na Yerusalem, dëkk ba bépp yengatu ne: «Kii moo di kan?»
11ܟܢܫܐ ܕܝܢ ܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܗܢܘ ܝܫܘܥ ܢܒܝܐ ܕܡܢ ܢܨܪܬ ܕܓܠܝܠܐ ܀
11 Mbooloo ma tontu leen ne: «Kii moo di yonentu Yàlla Yeesu, bi jóge Nasaret ci Galile.»
12ܘܥܠ ܝܫܘܥ ܠܗܝܟܠܐ ܕܐܠܗܐ ܘܐܦܩ ܠܟܠܗܘܢ ܕܙܒܢܝܢ ܘܡܙܒܢܝܢ ܒܗܝܟܠܐ ܘܤܚܦ ܦܬܘܪܐ ܕܡܥܪܦܢܐ ܘܟܘܪܤܘܬܐ ܕܗܢܘܢ ܕܡܙܒܢܝܢ ܝܘܢܐ ܀
12 Bi loolu amee Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, dàq ñépp ña fay jaay ak ña fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis ya ak tooguy jaaykati pitax ya,
13ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܟܬܝܒ ܗܘ ܕܒܝܬܝ ܒܝܬ ܨܠܘܬܐ ܢܬܩܪܐ ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܥܒܕܬܘܢܝܗܝ ܡܥܪܬܐ ܕܠܤܛܝܐ ܀
13 naan: «Mbind mi nee na: “Sama kër dinañu ko wooye këru ñaan ci Yàlla,” waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
14ܘܩܪܒܘ ܠܗ ܒܗܝܟܠܐ ܤܡܝܐ ܘܚܓܝܤܐ ܘܐܤܝ ܐܢܘܢ ܀
14 Noonu ay gumba ak ay lafañ ñëw ci moom ca kër Yàlla ga, mu faj leen.
15ܟܕ ܚܙܘ ܕܝܢ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܘܦܪܝܫܐ ܬܕܡܪܬܐ ܕܥܒܕ ܘܛܠܝܐ ܕܩܥܝܢ ܒܗܝܟܠܐ ܘܐܡܪܝܢ ܐܘܫܥܢܐ ܠܒܪܗ ܕܕܘܝܕ ܐܬܒܐܫ ܠܗܘܢ ܀
15 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer.
16ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܫܡܥ ܐܢܬ ܡܢܐ ܐܡܪܝܢ ܗܠܝܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܐܝܢ ܡܢ ܡܬܘܡ ܠܐ ܩܪܝܬܘܢ ܕܡܢ ܦܘܡܐ ܕܛܠܝܐ ܘܕܝܠܘܕܐ ܬܩܢܬ ܬܫܒܘܚܬܐ ܀
16 Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu tontu leen ne: «Waaw dégg naa ko. Ndax musuleen a jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?»
17ܘܫܒܩ ܐܢܘܢ ܘܢܦܩ ܠܒܪ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܠܒܝܬ ܥܢܝܐ ܘܒܬ ܬܡܢ ܀
17 Bi Yeesu waxee loolu, mu bàyyi leen, génn dëkk ba, jëm Betani, fanaan fa.
18ܒܨܦܪܐ ܕܝܢ ܟܕ ܗܦܟ ܠܡܕܝܢܬܐ ܟܦܢ ܀
18 Ci suba teel Yeesu dellusi ca dëkk ba, mu xiif.
19ܘܚܙܐ ܬܬܐ ܚܕܐ ܒܐܘܪܚܐ ܘܐܬܐ ܠܘܬܗ ܘܠܐ ܐܫܟܚ ܒܗ ܡܕܡ ܐܠܐ ܐܢ ܛܪܦܐ ܒܠܚܘܕ ܘܐܡܪ ܠܗ ܠܐ ܢܗܘܘܢ ܒܟܝ ܬܘܒ ܦܐܪܐ ܠܥܠܡ ܘܡܚܕܐ ܝܒܫܬ ܬܬܐ ܗܝ ܀
19 Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk.» Ca saa sa figg ga daldi wow.
20ܘܚܙܘ ܬܠܡܝܕܐ ܘܬܗܪܘ ܘܐܡܪܝܢ ܐܝܟܢܐ ܒܪ ܫܥܬܗ ܝܒܫܬ ܬܬܐ ܀
20 Bi nga xamee ne taalibe ya gis nañu loolu, ñu waaru naan: «Nan la figg gi daldi wowe ci taxawaay bi?»
21ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܐܢ ܬܗܘܐ ܒܟܘܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܘܠܐ ܬܬܦܠܓܘܢ ܠܐ ܒܠܚܘܕ ܗܕܐ ܕܬܬܐ ܬܥܒܕܘܢ ܐܠܐ ܐܦܢ ܠܛܘܪܐ ܗܢܐ ܬܐܡܪܘܢ ܕܐܫܬܩܠ ܘܦܠ ܒܝܡܐ ܬܗܘܐ ܀
21 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te bañ a werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def.
22ܘܟܠ ܡܕܡ ܕܬܫܐܠܘܢ ܒܨܠܘܬܐ ܘܬܗܝܡܢܘܢ ܬܤܒܘܢ ܀
22 Te lépp lu ngeen laaj cig ñaan, bu ngeen ci boolee ngëm, dingeen ci jot.»
23ܘܟܕ ܐܬܐ ܝܫܘܥ ܠܗܝܟܠܐ ܩܪܒܘ ܠܗ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܘܩܫܝܫܐ ܕܥܡܐ ܟܕ ܡܠܦ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܒܐܝܢܐ ܫܘܠܛܢ ܗܠܝܢ ܥܒܕ ܐܢܬ ܘܡܢܘ ܝܗܒ ܠܟ ܫܘܠܛܢܐ ܗܢܐ ܀
23 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngale. Bi muy jàngale nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?»
24ܥܢܐ ܝܫܘܥ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܫܐܠܟܘܢ ܐܦ ܐܢܐ ܡܠܬܐ ܚܕܐ ܘܐܢ ܬܐܡܪܘܢ ܠܝ ܘܐܦ ܐܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܒܐܝܢܐ ܫܘܠܛܢܐ ܗܠܝܢ ܥܒܕ ܐܢܐ ܀
24 Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ko waxee, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
25ܡܥܡܘܕܝܬܗ ܕܝܘܚܢܢ ܐܝܡܟܐ ܐܝܬܝܗ ܡܢ ܫܡܝܐ ܗܝ ܐܘ ܡܢ ܒܢܝܢܫܐ ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܡܬܪܥܝܢ ܗܘܘ ܒܢܦܫܗܘܢ ܘܐܡܪܝܢ ܕܐܢ ܢܐܡܪ ܡܢ ܫܡܝܐ ܐܡܪ ܠܢ ܘܥܠ ܡܢܐ ܠܐ ܗܝܡܢܬܘܢܝܗܝ ܀
25 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
26ܘܕܢܐܡܪ ܡܢ ܒܢܝܢܫܐ ܕܚܠܝܢ ܐܢܚܢܢ ܡܢ ܟܢܫܐ ܟܠܗܘܢ ܓܝܪ ܐܝܟ ܢܒܝܐ ܐܚܝܕܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܠܝܘܚܢܢ ܀
26 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.»
27ܥܢܘ ܘܐܡܪܝܢ ܠܗ ܠܐ ܝܕܥܝܢܢ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܐܦ ܠܐ ܐܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܒܐܝܢܐ ܫܘܠܛܢܐ ܗܠܝܢ ܥܒܕ ܐܢܐ ܀
27 Ñu tontu Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
28ܡܢܐ ܕܝܢ ܡܬܚܙܐ ܠܟܘܢ ܓܒܪܐ ܚܕ ܐܝܬ ܗܘܘ ܠܗ ܒܢܝܐ ܬܪܝܢ ܘܩܪܒ ܠܘܬ ܩܕܡܝܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܒܪܝ ܙܠ ܝܘܡܢܐ ܦܠܘܚ ܒܟܪܡܐ ܀
28 «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu réseñ.”
29ܗܘ ܕܝܢ ܥܢܐ ܘܐܡܪ ܠܐ ܨܒܐ ܐܢܐ ܒܚܪܬܐ ܕܝܢ ܐܬܬܘܝ ܘܐܙܠ ܀
29 Taaw ba tontu ko ne: “Maa ngi dem baay,” waaye demu ca.
30ܘܩܪܒ ܠܘܬ ܐܚܪܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܗܟܘܬ ܗܘ ܕܝܢ ܥܢܐ ܘܐܡܪ ܐܢܐ ܡܪܝ ܘܠܐ ܐܙܠ ܀
30 Gannaaw gi, baay ba ñëw ca ñaareel ba, wax ko noonu. Mu tontu ko ne: “Bëgguma caa dem,” waaye gannaaw loolu xelam soppiku, mu dem ca.»
31ܡܢܘ ܡܢ ܗܠܝܢ ܬܪܝܗܘܢ ܥܒܕ ܨܒܝܢܐ ܕܐܒܘܗܝ ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܗܘ ܩܕܡܝܐ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܡܟܤܐ ܘܙܢܝܬܐ ܩܕܡܝܢ ܠܟܘܢ ܠܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
31 Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobareg baayam?» Ñu ne: «Ñaareel bi.» Kon Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkk a dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
32ܐܬܐ ܓܝܪ ܠܘܬܟܘܢ ܝܘܚܢܢ ܒܐܘܪܚܐ ܕܟܐܢܘܬܐ ܘܠܐ ܗܝܡܢܬܘܢܝܗܝ ܡܟܤܐ ܕܝܢ ܘܙܢܝܬܐ ܗܝܡܢܘܗܝ ܐܢܬܘܢ ܕܝܢ ܐܦ ܠܐ ܟܕ ܚܙܝܬܘܢ ܐܬܬܘܝܬܘܢ ܒܚܪܬܐ ܕܬܗܝܡܢܘܢ ܒܗ ܀
32 Ndaxte Yaxya ñëw na ci yéen ci yoonu njub, te gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak jigéeni moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikuwul sax, ba ngeen gëm ko.»
33ܫܡܥܘ ܐܚܪܢܐ ܡܬܠܐ ܓܒܪܐ ܚܕ ܐܝܬ ܗܘܐ ܡܪܐ ܒܝܬܐ ܘܢܨܒ ܟܪܡܐ ܘܐܚܕܪܗ ܤܝܓܐ ܘܚܦܪ ܒܗ ܡܥܨܪܬܐ ܘܒܢܐ ܒܗ ܡܓܕܠܐ ܘܐܘܚܕܗ ܠܦܠܚܐ ܘܚܙܩ ܀
33 Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci réseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki.
34ܟܕ ܕܝܢ ܡܛܐ ܙܒܢܐ ܕܦܐܪܐ ܫܕܪ ܠܥܒܕܘܗܝ ܠܘܬ ܦܠܚܐ ܕܢܫܕܪܘܢ ܠܗ ܡܢ ܦܐܪܐ ܕܟܪܡܗ ܀
34 «Bi nga xamee ne bëgg nañoo witt réseñ yi, mu yónni ay surgaam ci beykat yi, ngir jot wàllam ci meññeef mi.
35ܘܐܚܕܘ ܦܠܚܐ ܠܥܒܕܘܗܝ ܘܐܝܬ ܕܡܚܐܘܗܝ ܘܐܝܬ ܕܪܓܡܘܗܝ ܘܐܝܬ ܕܩܛܠܘܗܝ ܀
35 Waaye beykat yi jàpp surga yi, kenn ki ñu dóor ko ay yar, keneen ki ñu rey ko, ki ci des ñu sànni ko ay doj.
36ܘܬܘܒ ܫܕܪ ܐܚܪܢܐ ܥܒܕܐ ܕܤܓܝܐܝܢ ܡܢ ܩܕܡܝܐ ܘܗܟܘܬ ܥܒܕܘ ܠܗܘܢ ܀
36 Boroom kër gi nag yónniwaat yeneen surga yu ëpp yu jëkk ya, beykat yi def leen noonu ñoom itam.
37ܐܚܪܝܬ ܕܝܢ ܫܕܪ ܠܘܬܗܘܢ ܠܒܪܗ ܟܕ ܐܡܪ ܟܒܪ ܢܒܗܬܘܢ ܡܢ ܒܪܝ ܀
37 Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.”
38ܦܠܚܐ ܕܝܢ ܟܕ ܚܙܐܘܗܝ ܠܒܪܐ ܐܡܪܘ ܒܝܢܬܗܘܢ ܗܢܘ ܝܪܬܐ ܬܘ ܢܩܛܠܝܘܗܝ ܘܢܐܚܘܕ ܝܪܬܘܬܗ ܀
38 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen bopp: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndonoom.”
39ܘܐܚܕܘ ܐܦܩܘܗܝ ܠܒܪ ܡܢ ܟܪܡܐ ܘܩܛܠܘܗܝ ܀
39 Ñu jàpp ko nag, génne ko tool bi, rey ko.»
40ܡܐ ܕܐܬܐ ܗܟܝܠ ܡܪܗ ܕܟܪܡܐ ܡܢܐ ܢܥܒܕ ܠܦܠܚܐ ܗܢܘܢ ܀
40 Noonu Yeesu laaj leen: «Bu boroom tool bi ñëwee nag, na muy def beykat yi?»
41ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܕܒܝܫ ܒܝܫ ܢܘܒܕ ܐܢܘܢ ܘܟܪܡܐ ܢܘܚܕ ܠܐܚܪܢܐ ܦܠܚܐ ܐܝܠܝܢ ܕܝܗܒܝܢ ܠܗ ܦܐܪܐ ܒܙܒܢܗܘܢ ܀
41 Ñu ne ko: «Dina rey reyin wu ñaaw nit ñu soxor ñooñu, batale tool bi yeneen beykat, yi koy jox wàllam ci jamonoy meññeef.»
42ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܫܘܥ ܠܐ ܡܡܬܘܡ ܩܪܝܬܘܢ ܒܟܬܒܐ ܕܟܐܦܐ ܕܐܤܠܝܘ ܒܢܝܐ ܗܝ ܗܘܬ ܠܪܫܐ ܕܙܘܝܬܐ ܡܢ ܠܘܬ ܡܪܝܐ ܗܘܬ ܗܕܐ ܘܐܝܬܝܗ ܬܕܡܘܪܬܐ ܒܥܝܢܝܢ ܀
42 Kon Yeesu ne leen: «Xanaa musuleen a jàng lii ci Mbind yi?“Doj wi tabaxkat yi sànni;mujj na di doju koñ;ci Boroom bi la loolu jóge,te yéemu nanu ci.”
43ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܬܫܬܩܠ ܡܢܟܘܢ ܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܘܬܬܝܗܒ ܠܥܡܐ ܕܥܒܕ ܦܐܪܐ ܀
43 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam.
44ܘܡܢ ܕܢܦܠ ܥܠ ܟܐܦܐ ܗܕܐ ܢܬܪܥܥ ܘܟܠ ܡܢ ܕܗܝ ܬܦܠ ܥܠܘܗܝ ܬܕܪܝܘܗܝ ܀
44 Ku dal ci doj wii, dammtoo; ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
45ܘܟܕ ܫܡܥܘ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܘܦܪܝܫܐ ܡܬܠܘܗܝ ܝܕܥܘ ܕܥܠܝܗܘܢ ܐܡܪ ܀ 46 ܘܒܥܘ ܠܡܐܚܕܗ ܘܕܚܠܘ ܡܢ ܟܢܫܐ ܡܛܠ ܕܐܝܟ ܕܠܢܒܝܐ ܐܚܝܕܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܀
45 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dégg nañu léebam yooyu, ñu xam ne ñoom lay wax.
46
46 Noonu ñu di ko fexee jàpp, waaye ragal nañu nit ña, ndaxte ñépp teg nañu ko ab yonent.