Syriac: NT

Wolof: New Testament

Matthew

28

1ܒܪܡܫܐ ܕܝܢ ܒܫܒܬܐ ܕܢܓܗ ܚܕ ܒܫܒܐ ܐܬܬ ܡܪܝܡ ܡܓܕܠܝܬܐ ܘܡܪܝܡ ܐܚܪܬܐ ܕܢܚܙܝܢ ܩܒܪܐ ܀
1 Gannaaw bésu noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba.
2ܘܗܐ ܙܘܥܐ ܪܒܐ ܗܘܐ ܡܠܐܟܐ ܓܝܪ ܕܡܪܝܐ ܢܚܬ ܡܢ ܫܡܝܐ ܘܩܪܒ ܥܓܠ ܟܐܦܐ ܡܢ ܬܪܥܐ ܘܝܬܒ ܗܘܐ ܥܠܝܗ ܀
2 Fekk suuf yengu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw.
3ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܕܝܢ ܚܙܘܗ ܐܝܟ ܒܪܩܐ ܘܠܒܘܫܗ ܚܘܪ ܗܘܐ ܐܝܟ ܬܠܓܐ ܀
3 Meloom mel na ni melax, ay yéreem weex tàll ni perkaal.
4ܘܡܢ ܕܚܠܬܗ ܐܬܬܙܝܥܘ ܐܝܠܝܢ ܕܢܛܪܝܢ ܗܘܘ ܘܗܘܘ ܐܝܟ ܡܝܬܐ ܀
4 Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee.
5ܥܢܐ ܕܝܢ ܡܠܐܟܐ ܘܐܡܪ ܠܢܫܐ ܐܢܬܝܢ ܠܐ ܬܕܚܠܢ ܝܕܥ ܐܢܐ ܓܝܪ ܕܠܝܫܘܥ ܕܐܙܕܩܦ ܒܥܝܢ ܐܢܬܝܢ ܀
5 Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne, yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba,
6ܠܐ ܗܘܐ ܬܢܢ ܩܡ ܠܗ ܓܝܪ ܐܝܟܢܐ ܕܐܡܪ ܬܐܝܝܢ ܚܙܝܝܢ ܕܘܟܬܐ ܕܤܝܡ ܗܘܐ ܒܗ ܡܪܢ ܀
6 waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon,
7ܘܙܠܝܢ ܒܥܓܠ ܐܡܪܝܢ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܕܩܡ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܘܗܐ ܩܕܡ ܠܟܘܢ ܠܓܠܝܠܐ ܬܡܢ ܬܚܙܘܢܝܗܝ ܗܐ ܐܡܪܬ ܠܟܝܢ ܀
7 te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne, dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.»
8ܘܐܙܠ ܥܓܠ ܡܢ ܩܒܪܐ ܒܕܚܠܬܐ ܘܒܚܕܘܬܐ ܪܒܬܐ ܘܪܗܛܢ ܕܢܐܡܪܢ ܠܬܠܡܝܕܘܗܝ ܀
8 Bi loolu amee nag jigéen ña daldi jóge bu gaaw ca bàmmeel ba, tiit ak mbég mu réy di jax seen xol, ñu daldi daw, ngir yégal ko taalibe ya.
9ܘܗܐ ܝܫܘܥ ܦܓܥ ܒܗܝܢ ܘܐܡܪ ܠܗܝܢ ܫܠܡ ܠܟܝܢ ܗܢܝܢ ܕܝܢ ܩܪܒ ܐܚܕ ܪܓܠܘܗܝ ܘܤܓܕܝܢ ܠܗ ܀
9 Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal.
10ܗܝܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗܝܢ ܝܫܘܥ ܠܐ ܬܕܚܠܢ ܐܠܐ ܙܠܝܢ ܐܡܪܝܢ ܠܐܚܝ ܕܢܐܙܠܘܢ ܠܓܠܝܠܐ ܘܬܡܢ ܢܚܙܘܢܢܝ ܀
10 Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.»
11ܟܕ ܐܙܠܝܢ ܕܝܢ ܐܬܘ ܐܢܫܐ ܡܢ ܩܤܛܘܢܪܐ ܗܢܘܢ ܠܡܕܝܢܬܐ ܘܐܡܪܘ ܠܪܒܝ ܟܗܢܐ ܟܠ ܡܕܡ ܕܗܘܐ ܀
11 Ba ñuy dem, ñenn ca wottukat ya ñëw ca dëkk ba, xamal saraxalekat yu mag ya lépp lu xew.
12ܘܐܬܟܢܫܘ ܥܡ ܩܫܝܫܐ ܘܢܤܒܘ ܡܠܟܐ ܘܝܗܒܘ ܟܤܦܐ ܠܐ ܙܥܘܪ ܠܩܤܛܘܢܪܐ ܀
12 Noonu saraxalekat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya,
13ܘܐܡܪܝܢ ܠܗܘܢ ܐܡܪܘ ܕܬܠܡܝܕܘܗܝ ܐܬܘ ܓܢܒܘܗܝ ܒܠܠܝܐ ܟܕ ܕܡܟܝܢ ܚܢܢ ܀
13 ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.”
14ܘܐܢ ܐܫܬܡܥܬ ܗܕܐ ܩܕܡ ܗܓܡܘܢܐ ܚܢܢ ܡܦܝܤܝܢ ܚܢܢ ܠܗ ܘܠܟܘܢ ܕܠܐ ܨܦܬܐ ܥܒܕܝܢ ܚܢܢ ܀
14 Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.»
15ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܟܕ ܢܤܒܘ ܟܤܦܐ ܥܒܕܘ ܐܝܟ ܕܐܠܦܘ ܐܢܘܢ ܘܢܦܩܬ ܡܠܬܐ ܗܕܐ ܒܝܬ ܝܗܘܕܝܐ ܥܕܡܐ ܠܝܘܡܢܐ ܀
15 Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey.
16ܬܠܡܝܕܐ ܕܝܢ ܚܕܥܤܪ ܐܙܠܘ ܠܓܠܝܠܐ ܠܛܘܪܐ ܐܝܟܐ ܕܘܥܕ ܐܢܘܢ ܝܫܘܥ ܀
16 Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon.
17ܘܟܕ ܚܙܐܘܗܝ ܤܓܕܘ ܠܗ ܡܢܗܘܢ ܕܝܢ ܐܬܦܠܓܘ ܗܘܘ ܀
17 Bi ñu gisee Yeesu, ñu màggal ko, waaye ñenn ñi am xel ñaar.
18ܘܩܪܒ ܝܫܘܥ ܡܠܠ ܥܡܗܘܢ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܐܬܝܗܒ ܠܝ ܟܠ ܫܘܠܛܢ ܒܫܡܝܐ ܘܒܐܪܥܐ ܘܐܝܟܢܐ ܕܫܕܪܢܝ ܐܒܝ ܡܫܕܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܀
18 Yeesu jegesi ne leen: «Sañ-sañ bépp, jox nañu ma ko ci kaw ak ci suuf.
19ܙܠܘ ܗܟܝܠ ܬܠܡܕܘ ܟܠܗܘܢ ܥܡܡܐ ܘܐܥܡܕܘ ܐܢܘܢ ܒܫܡ ܐܒܐ ܘܒܪܐ ܘܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܀
19 Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi;
20ܘܐܠܦܘ ܐܢܘܢ ܕܢܛܪܘܢ ܟܠ ܡܐ ܕܦܩܕܬܟܘܢ ܘܗܐ ܐܢܐ ܥܡܟܘܢ ܐܢܐ ܟܠܗܘܢ ܝܘܡܬܐ ܥܕܡܐ ܠܫܘܠܡܗ ܕܥܠܡܐ ܐܡܝܢ ܀ ܀ ܀
20 te ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. Te maa ngi ànd ak yéen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»