1ܒܗܘܢ ܕܝܢ ܒܝܘܡܬܐ ܗܢܘܢ ܐܬܐ ܝܘܚܢܢ ܡܥܡܕܢܐ ܘܡܟܪܙ ܗܘܐ ܒܚܘܪܒܐ ܕܝܗܘܕ ܀
1 Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude.
2ܘܐܡܪ ܬܘܒܘ ܩܪܒܬ ܠܗ ܡܠܟܘܬܐ ܕܫܡܝܐ ܀
2 Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.»
3ܗܢܘ ܓܝܪ ܗܘ ܕܐܡܝܪ ܒܝܕ ܐܫܥܝܐ ܢܒܝܐ ܩܠܐ ܕܩܪܐ ܒܚܘܪܒܐ ܛܝܒܘ ܐܘܪܚܗ ܕܡܪܝܐ ܘܐܫܘܘ ܠܫܒܝܠܘܗܝ ܀
3 Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.”»
4ܗܘ ܕܝܢ ܝܘܚܢܢ ܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܠܒܘܫܗ ܕܤܥܪܐ ܕܓܡܠܐ ܘܐܤܪ ܚܨܐ ܕܡܫܟܐ ܥܠ ܚܨܘܗܝ ܘܡܐܟܘܠܬܗ ܩܡܨܐ ܘܕܒܫܐ ܕܒܪܐ ܀
4 Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
5ܗܝܕܝܢ ܢܦܩܐ ܗܘܬ ܠܘܬܗ ܐܘܪܫܠܡ ܘܟܠܗ ܝܗܘܕ ܘܟܠܗ ܐܬܪܐ ܕܚܕܪܝ ܝܘܪܕܢܢ ܀
5 Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan.
6ܘܥܡܕܝܢ ܗܘܘ ܡܢܗ ܒܝܘܪܕܢܢ ܢܗܪܐ ܟܕ ܡܘܕܝܢ ܒܚܛܗܝܗܘܢ ܀
6 Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
7ܟܕ ܚܙܐ ܕܝܢ ܤܓܝܐܐ ܡܢ ܦܪܝܫܐ ܘܡܢ ܙܕܘܩܝܐ ܕܐܬܝܢ ܠܡܥܡܕ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܝܠܕܐ ܕܐܟܕܢܐ ܡܢܘ ܚܘܝܟܘܢ ܠܡܥܪܩ ܡܢ ܪܘܓܙܐ ܕܐܬܐ ܀
7 Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?
8ܥܒܕܘ ܗܟܝܠ ܦܐܪܐ ܕܫܘܝܢ ܠܬܝܒܘܬܐ ܀
8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar,
9ܘܠܐ ܬܤܒܪܘܢ ܘܬܐܡܪܘܢ ܒܢܦܫܟܘܢ ܕܐܒܐ ܐܝܬ ܠܢ ܐܒܪܗܡ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܓܝܪ ܕܡܫܟܚ ܐܠܗܐ ܡܢ ܗܠܝܢ ܟܐܦܐ ܠܡܩܡܘ ܒܢܝܐ ܠܐܒܪܗܡ ܀
9 te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii.
10ܗܐ ܕܝܢ ܢܪܓܐ ܤܝܡ ܥܠ ܥܩܪܐ ܕܐܝܠܢܐ ܟܠ ܐܝܠܢܐ ܗܟܝܠ ܕܦܐܪܐ ܛܒܐ ܠܐ ܥܒܕ ܡܬܦܤܩ ܘܢܦܠ ܒܢܘܪܐ ܀
10 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.
11ܐܢܐ ܡܥܡܕ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܒܡܝܐ ܠܬܝܒܘܬܐ ܗܘ ܕܝܢ ܕܒܬܪܝ ܐܬܐ ܚܤܝܢ ܗܘ ܡܢܝ ܗܘ ܕܠܐ ܫܘܐ ܐܢܐ ܡܤܢܘܗܝ ܠܡܫܩܠ ܗܘ ܡܥܡܕ ܠܟܘܢ ܒܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܘܒܢܘܪܐ ܀
11 Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara.
12ܗܘ ܕܪܦܫܐ ܒܐܝܕܗ ܘܡܕܟܐ ܐܕܪܘܗܝ ܘܚܛܐ ܟܢܫ ܠܐܘܨܪܘܗܝ ܘܬܒܢܐ ܡܘܩܕ ܒܢܘܪܐ ܕܠܐ ܕܥܟܐ ܀
12 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.»
13ܗܝܕܝܢ ܐܬܐ ܝܫܘܥ ܡܢ ܓܠܝܠܐ ܠܝܘܪܕܢܢ ܠܘܬ ܝܘܚܢܢ ܕܢܥܡܕ ܡܢܗ ܀
13 Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
14ܗܘ ܕܝܢ ܝܘܚܢܢ ܟܠܐ ܗܘܐ ܠܗ ܘܐܡܪ ܐܢܐ ܤܢܝܩ ܐܢܐ ܕܡܢܟ ܐܬܥܡܕ ܘܐܢܬ ܠܘܬܝ ܐܬܝܬ ܀
14 Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!»
15ܗܘ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܥܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܫܒܘܩ ܗܫܐ ܗܟܢܐ ܓܝܪ ܝܐܐ ܠܢ ܕܢܡܠܐ ܟܠܗ ܟܐܢܘܬܐ ܘܗܝܕܝܢ ܫܒܩܗ ܀
15 Yeesu tontu ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu.
16ܟܕ ܥܡܕ ܕܝܢ ܝܫܘܥ ܡܚܕܐ ܤܠܩ ܡܢ ܡܝܐ ܘܐܬܦܬܚܘ ܠܗ ܫܡܝܐ ܘܚܙܐ ܪܘܚܐ ܕܐܠܗܐ ܕܢܚܬܐ ܐܝܟ ܝܘܢܐ ܘܐܬܬ ܥܠܘܗܝ ܀ 17 ܘܗܐ ܩܠܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܕܐܡܪ ܗܢܘ ܒܪܝ ܚܒܝܒܐ ܕܒܗ ܐܨܛܒܝܬ ܀
16 Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu.
17
17 Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»