Syriac: NT

Wolof: New Testament

Matthew

6

1ܚܘܪܘ ܕܝܢ ܒܙܕܩܬܟܘܢ ܕܠܐ ܬܥܒܕܘܢܗ ܩܕܡ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܐܝܟ ܕܬܬܚܙܘܢ ܠܗܘܢ ܘܐܠܐ ܐܓܪܐ ܠܝܬ ܠܟܘܢ ܠܘܬ ܐܒܘܟܘܢ ܕܒܫܡܝܐ ܀
1 «Wottuleen a def seeni jëf yu jub ci kanamu nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw.
2ܐܡܬܝ ܗܟܝܠ ܕܥܒܕ ܐܢܬ ܙܕܩܬܐ ܠܐ ܬܩܪܐ ܩܪܢܐ ܩܕܡܝܟ ܐܝܟ ܕܥܒܕܝܢ ܢܤܒܝ ܒܐܦܐ ܒܟܢܘܫܬܐ ܘܒܫܘܩܐ ܐܝܟ ܕܢܫܬܒܚܘܢ ܡܢ ܒܢܝ ܐܢܫܐ ܘܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܩܒܠܘ ܐܓܪܗܘܢ ܀
2 Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
3ܐܢܬ ܕܝܢ ܡܐ ܕܥܒܕ ܐܢܬ ܙܕܩܬܐ ܠܐ ܬܕܥ ܤܡܠܟ ܡܢܐ ܥܒܕܐ ܝܡܝܢܟ ܀
3 Waaye booy sàkk sarax, bu sa loxob càmmooñ xam li sa loxob ndeyjoor di def,
4ܐܝܟ ܕܬܗܘܐ ܙܕܩܬܟ ܒܟܤܝܐ ܘܐܒܘܟ ܕܚܙܐ ܒܟܤܝܐ ܗܘ ܢܦܪܥܟ ܒܓܠܝܐ ܀
4 ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
5ܘܡܐ ܕܡܨܠܐ ܐܢܬ ܠܐ ܬܗܘܐ ܐܝܟ ܢܤܒܝ ܒܐܦܐ ܕܪܚܡܝܢ ܠܡܩܡ ܒܟܢܘܫܬܐ ܘܒܙܘܝܬܐ ܕܫܘܩܐ ܠܡܨܠܝܘ ܕܢܬܚܙܘܢ ܠܒܢܝ ܐܢܫܐ ܘܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܩܒܠܘ ܐܓܪܗܘܢ ܀
5 «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6ܐܢܬ ܕܝܢ ܐܡܬܝ ܕܡܨܠܐ ܐܢܬ ܥܘܠ ܠܬܘܢܟ ܘܐܚܘܕ ܬܪܥܟ ܘܨܠܐ ܠܐܒܘܟ ܕܒܟܤܝܐ ܘܐܒܘܟ ܕܚܙܐ ܒܟܤܝܐ ܢܦܪܥܟ ܒܓܠܝܐ ܀
6 Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
7ܘܡܐ ܕܡܨܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܡܦܩܩܝܢ ܐܝܟ ܚܢܦܐ ܤܒܪܝܢ ܓܝܪ ܕܒܡܡܠܠܐ ܤܓܝܐܐ ܡܫܬܡܥܝܢ ܀
7 «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare.
8ܠܐ ܗܟܝܠ ܬܕܡܘܢ ܠܗܘܢ ܐܒܘܟܘܢ ܓܝܪ ܝܕܥ ܡܢܐ ܡܬܒܥܐ ܠܟܘܢ ܥܕܠܐ ܬܫܐܠܘܢܝܗܝ ܀
8 Buleen nirook ñoom, ndaxte seen Baay xam na seeni soxla, laata ngeen ko koy wax.
9ܗܟܢܐ ܗܟܝܠ ܨܠܘ ܐܢܬܘܢ ܐܒܘܢ ܕܒܫܡܝܐ ܢܬܩܕܫ ܫܡܟ ܀
9 Yéen nag nii ngeen war a ñaane:“Sunu Baay bi nekk ci kaw,na sa tur sell,
10ܬܐܬܐ ܡܠܟܘܬܟ ܢܗܘܐ ܨܒܝܢܟ ܐܝܟܢܐ ܕܒܫܡܝܐ ܐܦ ܒܐܪܥܐ ܀
10 na sa nguur ñëw,na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.
11ܗܒ ܠܢ ܠܚܡܐ ܕܤܘܢܩܢܢ ܝܘܡܢܐ ܀
11 May nu tey li nu war a dunde;
12ܘܫܒܘܩ ܠܢ ܚܘܒܝܢ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܚܢܢ ܫܒܩܢ ܠܚܝܒܝܢ ܀
12 te baal nu sunuy tooñ, ni nu baale ñi nu tooñ;
13ܘܠܐ ܬܥܠܢ ܠܢܤܝܘܢܐ ܐܠܐ ܦܨܢ ܡܢ ܒܝܫܐ ܡܛܠ ܕܕܝܠܟ ܗܝ ܡܠܟܘܬܐ ܘܚܝܠܐ ܘܬܫܒܘܚܬܐ ܠܥܠܡ ܥܠܡܝܢ ܀
13 bu nu teg ci yoonu nattu, waaye nga musal nu ci lu bon.Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
14ܐܢ ܓܝܪ ܬܫܒܩܘܢ ܠܒܢܝܢܫܐ ܤܟܠܘܬܗܘܢ ܢܫܒܘܩ ܐܦ ܠܟܘܢ ܐܒܘܟܘܢ ܕܒܫܡܝܐ ܀
14 «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam.
15ܐܢ ܕܝܢ ܠܐ ܬܫܒܩܘܢ ܠܒܢܝܢܫܐ ܐܦܠܐ ܐܒܘܟܘܢ ܫܒܩ ܠܟܘܢ ܤܟܠܘܬܟܘܢ ܀
15 Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ.
16ܐܡܬܝ ܕܝܢ ܕܨܝܡܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܐ ܬܗܘܘܢ ܟܡܝܪܐ ܐܝܟ ܢܤܒܝ ܒܐܦܐ ܡܚܒܠܝܢ ܓܝܪ ܦܪܨܘܦܝܗܘܢ ܐܝܟ ܕܢܬܚܙܘܢ ܠܒܢܝܢܫܐ ܕܨܝܡܝܢ ܘܐܡܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܩܒܠܘ ܐܓܪܗܘܢ ܀
16 «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
17ܐܢܬ ܕܝܢ ܡܐ ܕܨܐܡ ܐܢܬ ܐܫܝܓ ܐܦܝܟ ܘܡܫܘܚ ܪܫܟ ܀
17 Yaw nag booy woor, xeeñalal sa bopp te nga sëlmu,
18ܐܝܟ ܕܠܐ ܬܬܚܙܐ ܠܒܢܝܢܫܐ ܕܨܐܡ ܐܢܬ ܐܠܐ ܠܐܒܘܟ ܕܒܟܤܝܐ ܘܐܒܘܟ ܕܚܙܐ ܒܟܤܝܐ ܗܘ ܢܦܪܥܟ ܀
18 ngir sa koor bañ a feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
19ܠܐ ܬܤܝܡܘܢ ܠܟܘܢ ܤܝܡܬܐ ܒܐܪܥܐ ܐܬܪ ܕܤܤܐ ܘܐܟܠܐ ܡܚܒܠܝܢ ܘܐܝܟܐ ܕܓܢܒܐ ܦܠܫܝܢ ܘܓܢܒܝܢ ܀
19 «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko.
20ܐܠܐ ܤܝܡܘ ܠܟܘܢ ܤܝܡܬܐ ܒܫܡܝܐ ܐܝܟܐ ܕܠܐ ܤܤܐ ܘܠܐ ܐܟܠܐ ܡܚܒܠܝܢ ܘܐܝܟܐ ܕܓܢܒܐ ܠܐ ܦܠܫܝܢ ܘܠܐ ܓܢܒܝܢ ܀
20 Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko.
21ܐܝܟܐ ܓܝܪ ܕܐܝܬܝܗ ܤܝܡܬܟܘܢ ܬܡܢ ܗܘ ܐܦ ܠܒܟܘܢ ܀
21 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
22ܫܪܓܐ ܕܦܓܪܐ ܐܝܬܝܗ ܥܝܢܐ ܐܢ ܥܝܢܟ ܗܟܝܠ ܬܗܘܐ ܦܫܝܛܐ ܐܦ ܟܠܗ ܦܓܪܟ ܢܗܝܪ ܗܘ ܀
22 «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer,
23ܐܢ ܕܝܢ ܥܝܢܟ ܬܗܘܐ ܒܝܫܐ ܟܠܗ ܦܓܪܟ ܚܫܘܟܐ ܢܗܘܐ ܐܢ ܗܟܝܠ ܢܘܗܪܐ ܕܒܟ ܚܫܘܟܐ ܗܘ ܚܫܘܟܟ ܟܡܐ ܢܗܘܐ ܀
23 waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse!
24ܠܐ ܐܢܫ ܡܫܟܚ ܠܬܪܝܢ ܡܪܘܢ ܠܡܦܠܚ ܐܘ ܓܝܪ ܠܚܕ ܢܤܢܐ ܘܠܐܚܪܢܐ ܢܪܚܡ ܐܘ ܠܚܕ ܢܝܩܪ ܘܠܐܚܪܢܐ ܢܫܘܛ ܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܐܠܗܐ ܠܡܦܠܚ ܘܠܡܡܘܢܐ ܀
24 «Kenn mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.
25ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܠܐ ܬܐܨܦܘܢ ܠܢܦܫܟܘܢ ܡܢܐ ܬܐܟܠܘܢ ܘܡܢܐ ܬܫܬܘܢ ܘܠܐ ܠܦܓܪܟܘܢ ܡܢܐ ܬܠܒܫܘܢ ܠܐ ܗܐ ܢܦܫܐ ܝܬܝܪܐ ܡܢ ܤܝܒܪܬܐ ܘܦܓܪܐ ܡܢ ܠܒܘܫܐ ܀
25 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk, walla lu ngeen war a naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen war a sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay?
26ܚܘܪܘ ܒܦܪܚܬܐ ܕܫܡܝܐ ܕܠܐ ܙܪܥܝܢ ܘܠܐ ܚܨܕܝܢ ܘܠܐ ܚܡܠܝܢ ܒܐܘܨܪܐ ܘܐܒܘܟܘܢ ܕܒܫܡܝܐ ܡܬܪܤܐ ܠܗܘܢ ܠܐ ܗܐ ܐܢܬܘܢ ܡܝܬܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܡܢܗܘܢ ܀
26 Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare?
27ܡܢܘ ܕܝܢ ܡܢܟܘܢ ܟܕ ܝܨܦ ܡܫܟܚ ܠܡܘܤܦܘ ܥܠ ܩܘܡܬܗ ܐܡܬܐ ܚܕܐ ܀
27 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo man a yokk waxtu ci àppam?
28ܘܥܠ ܠܒܘܫܐ ܡܢܐ ܝܨܦܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܬܒܩܘ ܒܫܘܫܢܐ ܕܕܒܪܐ ܐܝܟܢܐ ܪܒܝܢ ܕܠܐ ܠܐܝܢ ܘܠܐ ܥܙܠܢ ܀
28 «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc,
29ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܝܢ ܕܐܦܠܐ ܫܠܝܡܘܢ ܒܟܠܗ ܫܘܒܚܗ ܐܬܟܤܝ ܐܝܟ ܚܕܐ ܡܢܗܝܢ ܀
29 waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom.
30ܐܢ ܕܝܢ ܠܥܡܝܪܐ ܕܚܩܠܐ ܕܝܘܡܢܐ ܐܝܬܘܗܝ ܘܡܚܪ ܢܦܠ ܒܬܢܘܪܐ ܐܠܗܐ ܗܟܢܐ ܡܠܒܫ ܠܐ ܤܓܝ ܝܬܝܪ ܠܟܘܢ ܙܥܘܪܝ ܗܝܡܢܘܬܐ ܀
30 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd?
31ܠܐ ܗܟܝܠ ܬܐܨܦܘܢ ܐܘ ܬܐܡܪܘܢ ܡܢܐ ܢܐܟܘܠ ܐܘ ܡܢܐ ܢܫܬܐ ܐܘ ܡܢܐ ܢܬܟܤܐ ܀
31 Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu war a lekk? Lu nu war a naan?” walla: “Lu nu war a sol?”
32ܟܠܗܝܢ ܓܝܪ ܗܠܝܢ ܥܡܡܐ ܗܘ ܒܥܝܢ ܠܗܝܢ ܐܒܘܟܘܢ ܕܝܢ ܕܒܫܡܝܐ ܝܕܥ ܕܐܦ ܠܟܘܢ ܡܬܒܥܝܢ ܗܠܝܢ ܟܠܗܝܢ ܀
32 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp.
33ܒܥܘ ܕܝܢ ܠܘܩܕܡ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܘܙܕܝܩܘܬܗ ܘܟܠܗܝܢ ܗܠܝܢ ܡܬܬܘܤܦܢ ܠܟܘܢ ܀ 34 ܠܐ ܗܟܝܠ ܬܐܨܦܘܢ ܕܡܚܪ ܗܘ ܓܝܪ ܡܚܪ ܝܨܦ ܕܝܠܗ ܤܦܩ ܠܗ ܠܝܘܡܐ ܒܝܫܬܗ ܀
33 Waaye jëkkleen a wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
34
34 Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko.