1ܦܘܠܘܤ ܐܤܝܪܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܛܝܡܬܐܘܤ ܐܚܐ ܠܦܝܠܡܘܢ ܚܒܝܒܐ ܘܦܠܚܐ ܕܥܡܢ ܀
1 Man Pool, mi ñu tëj kaso ngir Kirist Yeesu, ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci xeex bi;
2ܘܠܐܦܝܐ ܚܒܝܒܬܢ ܘܠܐܪܟܝܦܘܤ ܦܠܚܐ ܕܥܡܢ ܘܠܥܕܬܐ ܕܒܒܝܬܟ ܀
2 te fàttewunu sunu jigéen Afiya, ak sunu àndandoo ci xeex bi Arkib, yéen ak mbooloom ñi gëm, miy dajee sa kër.
3ܛܝܒܘܬܐ ܥܡܟܘܢ ܘܫܠܡܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܐܒܘܢ ܘܡܢ ܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
3 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
4ܡܘܕܐ ܐܢܐ ܠܐܠܗܝ ܒܟܠܙܒܢ ܘܡܬܕܟܪ ܐܢܐ ܠܟ ܒܨܠܘܬܝ ܀
4 Duma la noppee boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla sama Boroom,
5ܗܐ ܡܢ ܕܫܡܥܬ ܗܝܡܢܘܬܟ ܘܚܘܒܐ ܕܐܝܬ ܠܟ ܠܘܬ ܡܪܢ ܝܫܘܥ ܘܠܘܬ ܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܀
5 ndaxte dégg naa sa ngëm ci Boroom bi Yeesu, ak sa mbëggeel ci gaayam yu sell yépp.
6ܕܬܗܘܐ ܫܘܬܦܘܬܐ ܕܗܝܡܢܘܬܟ ܝܗܒܐ ܦܐܪܐ ܒܥܒܕܐ ܘܒܝܕܥܬܐ ܕܟܠ ܛܒܢ ܕܐܝܬ ܠܟܘܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
6 Li may ñaan nag a ngi nii: nga xam bu wér ngëneel, yi nu am yépp ci sunu bokk ci Kirist, ba tax bokk gi nga am ci Yàlla ci kaw ngëm meññ i njariñ.
7ܚܕܘܬܐ ܓܝܪ ܤܓܝܐܬܐ ܐܝܬ ܠܢ ܘܒܘܝܐܐ ܕܒܝܕ ܚܘܒܟ ܐܬܬܢܝܚܘ ܪܚܡܐ ܕܩܕܝܫܐ ܀
7 Ci dëgg-dëgg sa mbëggeel bégal na ma bu baax, ba dëfël sama xol; ndaxte xam naa, sama mbokk, ni nga féexale xoli gaayi Yàlla yu sell yi.
8ܡܛܠ ܗܕܐ ܦܪܗܤܝܐ ܤܓܝܐܬܐ ܐܝܬ ܠܝ ܒܡܫܝܚܐ ܕܐܦܩܘܕ ܠܟ ܐܝܠܝܢ ܕܙܕܩܢ ܀
8 Am na lu ma la bëgg a ñaan; teguma ko ci sañ-sañ bu mat bi ma Kirist may, ci teg la ndigalu def sa warugar,
9ܡܛܠ ܚܘܒܐ ܕܝܢ ܡܒܥܐ ܗܘ ܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟ ܐܢܐ ܦܘܠܘܤ ܕܐܝܬܝ ܤܒܐ ܐܝܟ ܕܝܕܥ ܐܢܬ ܗܫܐ ܕܝܢ ܐܦ ܐܤܝܪܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
9 waaye dama lay ñaan ci mbëggeel gi nu séq, man Pool màggat, mi ñu tëj kaso ci turu Kirist.
10ܘܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟ ܥܠ ܒܪܝ ܐܝܢܐ ܕܝܠܕܬ ܒܐܤܘܪܝ ܐܢܤܝܡܘܤ ܀
10 Maa ngi tinul sama doomu diine Onesim, mi ma jur ci Kirist fii ci kaso bi.
11ܗܘ ܕܒܙܒܢ ܠܝܬ ܗܘܐ ܠܟ ܒܗ ܚܫܚܘ ܗܫܐ ܕܝܢ ܐܦ ܠܟ ܐܦ ܠܝ ܛܒ ܚܫܚ ܀
11 Amul woon sa njariñ démb, waaye tey amal na nu njariñ, yaw ak man.
12ܘܫܕܪܬܗ ܠܟ ܐܢܬ ܕܝܢ ܐܝܟ ܕܠܝܠܕܐ ܕܝܠܝ ܗܟܢܐ ܩܒܠܝܗܝ ܀
12 Maa koy yebal fi yaw, waaye xamal ne, mooy sama reeni xol.
13ܨܒܐ ܗܘܝܬ ܓܝܪ ܕܠܘܬܝ ܐܚܕܝܘܗܝ ܕܢܗܘܐ ܡܫܡܫ ܠܝ ܚܠܦܝܟ ܒܐܤܘܪܐ ܕܐܘܢܓܠܝܘܢ ܀
13 Dama koo bëggoon a téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xebaar bu baax bi.
14ܒܠܥܕ ܡܠܟܟ ܕܝܢ ܠܐ ܨܒܝܬ ܡܕܡ ܠܡܥܒܕ ܕܠܐ ܐܝܟ ܕܒܩܛܝܪܐ ܬܗܘܐ ܛܒܬܟ ܐܠܐ ܒܨܒܝܢܟ ܀
14 Waaye bëggumaa def dara loo àndul; noonu ndimbal li nga may defal du nekk sañul-bañ, waaye mu ànd ak xol bu tàlli.
15ܟܒܪ ܕܝܢ ܐܦ ܡܛܠ ܗܕܐ ܫܢܝ ܕܫܥܬܐ ܕܠܥܠܡ ܬܐܚܕܝܘܗܝ ܀
15 Xëy na sax dafa tàggoo woon ak yaw diir bu gàtt, ngir nga jotaat ci ba fàww;
16ܠܐ ܡܟܝܠ ܐܝܟ ܥܒܕܐ ܐܠܐ ܝܬܝܪ ܡܢ ܥܒܕܐ ܐܚܐ ܚܒܝܒܐ ܕܝܠܝ ܚܕ ܟܡܐ ܕܝܠܟ ܘܒܒܤܪ ܘܒܡܪܢ ܀
16 waxuma léegi ni jaam rekk, waaye lu ko sut, xanaa mbokk mu dëggu ci xol, fekk looloo raw ag njaam. Mbokk la ci man, rawatina ci yaw, muy sa jaam ci aada, di sa mbokk léegi ci Boroom bi.
17ܐܢ ܗܟܝܠ ܐܝܬܝܟ ܠܝ ܫܘܬܦܐ ܩܒܠܝܗܝ ܐܝܟ ܕܠܝ ܀
17 Soo ma jàppee ni nawle nag, teeru ko, ni su ma la doon ganesi.
18ܘܐܢ ܡܕܡ ܚܤܪܟ ܐܘ ܚܝܒ ܗܕܐ ܥܠܝ ܚܫܘܒ ܀
18 Soo ko naree topp genn tooñ mbaa benn bor, topp ma ko.
19ܐܢܐ ܦܘܠܘܤ ܟܬܒܬ ܒܐܝܕܝ ܐܢܐ ܦܪܥ ܐܢܐ ܕܠܐ ܐܡܪ ܠܟ ܕܐܦ ܢܦܫܟ ܚܝܒ ܐܢܬ ܠܝ ܀
19 Man Pool maa ngi lay bind ak sama loxob bopp ne, dinaa la ko fey; bëggumaa yegg ci ne, sag dund sax ci man la jaar!
20ܐܝܢ ܐܚܝ ܐܢܐ ܐܬܬܢܝܚ ܒܟ ܒܡܪܢ ܐܢܝܚ ܪܚܡܝ ܒܡܫܝܚܐ ܀
20 Waaw yaw sama mbokk, dimbali ma ci Boroom bi, te seral sama xol ci sunu bokk ci Kirist.
21ܡܛܠ ܕܬܟܝܠ ܐܢܐ ܕܫܡܥ ܐܢܬ ܠܝ ܟܬܒܬ ܠܟ ܘܝܕܥ ܐܢܐ ܕܝܬܝܪ ܡܢ ܡܐ ܕܐܡܪ ܐܢܐ ܥܒܕ ܐܢܬ ܀
21 Noonu bind naa la, ndax wóor na ma ne, dinga ma déggal, ba weesu sax li ma la sant.
22ܒܚܕܐ ܕܝܢ ܐܦ ܛܝܒ ܠܝ ܒܝܬ ܡܫܪܝܐ ܡܤܒܪ ܐܢܐ ܓܝܪ ܕܒܨܠܘܬܟܘܢ ܡܬܝܗܒ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܀
22 Te itam nanga ma waajal néeg, ndaxte yaakaar naa ne, Yàlla dina nangu seeni ñaan, ba delloosi ma leen.
23ܫܐܠ ܒܫܠܡܟ ܐܦܦܪܐ ܫܒܝܐ ܕܥܡܝ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
23 Sama mbokk Epafras, mi ma nekkal fi ci kaso bi ci turu Kirist, mu ngi lay nuyu.
24ܘܡܪܩܘܤ ܘܐܪܤܛܪܟܘܤ ܘܕܡܐ ܘܠܘܩܐ ܡܥܕܪܢܝ ܀
24 Samay àndandoo ci liggéey bi, Màrk, Aristàrk, Demas ak Luug, ñu ngi lay nuyu.
25ܛܝܒܘܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܥܡ ܪܘܚܟܘܢ ܐܡܝܢ ܀
25 Na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.