Syriac: NT

Wolof: New Testament

Revelation

10

1ܘܚܙܝܬ ܐܚܪܢܐ ܡܠܐܟܐ ܕܢܚܬ ܡܢ ܫܡܝܐ ܘܡܥܛܦ ܥܢܢܐ ܘܩܫܬܐ ܕܫܡܝܐ ܥܠ ܪܫܗ ܘܚܙܘܗ ܐܝܟ ܫܡܫܐ ܘܪܓܠܘܗܝ ܐܝܟ ܥܡܘܕܐ ܕܢܘܪܐ ܀
1 Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo niir. Xon tiim ko, te xar-kanamam mel ni jant, te ay tànkam mel ni jumi safara.
2ܘܐܝܬ ܠܗ ܒܐܝܕܗ ܟܬܒܘܢܐ ܦܬܝܚܐ ܘܤܡ ܪܓܠܗ ܕܝܡܝܢܐ ܥܠ ܝܡܐ ܕܤܡܠܐ ܕܝܢ ܥܠ ܐܪܥܐ ܀
2 Yor na benn téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndeyjooram ci géej gi, tànku càmmooñam ci suuf si,
3ܘܩܥܐ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܐܝܟ ܐܪܝܐ ܕܓܤܪ ܘܟܕ ܩܥܐ ܡܠܠܘ ܫܒܥܐ ܪܥܡܝܢ ܒܩܠܝܗܘܢ ܀
3 di xaacu, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom-ñaari dënnu yi jib.
4ܘܟܕ ܡܠܠܘ ܫܒܥܐ ܪܥܡܝܢ ܡܛܝܒ ܗܘܝܬ ܠܡܟܬܒ ܘܫܡܥܬ ܩܠܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܕܫܒܥܐ ܕܐܡܪ ܚܬܘܡ ܗܘ ܡܐ ܕܡܠܠܘ ܫܒܥܐ ܪܥܡܝܢ ܘܠܐ ܬܟܬܒܝܘܗܝ ܀
4 Naka la juróom-ñaari dënnu yi di jib, may waaj a bind, waaye ma dégg baat bu jóge asamaan, naan ma: «Li juróom-ñaari dënnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.»
5ܘܡܠܐܟܐ ܗܘ ܕܚܙܝܬ ܕܩܐܡ ܥܠ ܝܡܐ ܘܥܠ ܝܒܫܐ ܕܐܪܝܡ ܐܝܕܗ ܠܫܡܝܐ ܀
5 Noonu malaaka ma ma gis, mu taxaw ci géej gi ak suuf si, yékkati loxol ndeyjooram, mu jëm asamaan,
6ܘܝܡܐ ܒܗܘ ܕܚܝ ܠܥܠܡ ܥܠܡܝܢ ܗܘ ܕܒܪܗ ܠܫܡܝܐ ܘܕܒܗ ܘܠܐܪܥܐ ܘܕܒܗ ܕܬܘܒ ܙܒܢܐ ܠܐ ܢܗܘܐ ܀
6 daldi waat ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak li ci nekk lépp; mu ne: «Négandiku wees na,
7ܐܠܐ ܒܝܘܡܬܐ ܕܡܠܐܟܐ ܕܫܒܥܐ ܡܐ ܕܥܬܝܕ ܠܡܙܥܩ ܘܐܫܬܠܡ ܐܪܙܗ ܕܐܠܗܐ ܗܘ ܕܤܒܪ ܠܥܒܕܘܗܝ ܢܒܝܐ ܀
7 waaye jamono ju juróom-ñaareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Yàlla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
8ܘܩܠܐ ܫܡܥܬ ܡܢ ܫܡܝܐ ܬܘܒ ܕܡܡܠܠ ܥܡܝ ܘܐܡܪ ܙܠ ܤܒ ܠܟܬܒܘܢܐ ܕܒܐܝܕܗ ܕܡܠܐܟܐ ܕܩܐܡ ܥܠ ܐܪܥܐ ܘܥܠ ܝܡܐ ܀
8 Ci kaw loolu baat, ba ma déggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: «Demal jël téere bi ñu ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci géej gi ak suuf si.»
9ܘܐܙܠܬ ܠܘܬ ܡܠܐܟܐ ܟܕ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܗ ܠܡܬܠ ܠܝ ܠܟܬܒܘܢܐ ܘܐܡܪ ܠܝ ܤܒ ܘܐܟܘܠܝܗܝ ܘܢܡܪ ܠܟ ܟܪܤܟ ܐܠܐ ܒܦܘܡܟ ܢܗܘܐ ܐܝܟ ܕܒܫܐ ܀
9 Ma dem ca malaaka ma, laaj ko téere bu ndaw boobu. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa gémmiñ.»
10ܘܢܤܒܬ ܠܟܬܒܘܢܐ ܡܢ ܐܝܕܗ ܕܡܠܐܟܐ ܘܐܟܠܬܗ ܘܐܝܬ ܗܘܐ ܒܦܘܡܝ ܐܝܟ ܕܒܫܐ ܚܠܝܐ ܘܟܕ ܐܟܠܬܗ ܡܪܬ ܟܪܤܝ ܀
10 Noonu ma jël téere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir.
11ܘܐܡܪ ܠܝ ܝܗܝܒ ܠܟ ܬܘܒ ܙܒܢܐ ܠܡܬܢܒܝܘ ܥܠ ܥܡܡܐ ܘܐܡܘܬܐ ܘܠܫܢܐ ܘܡܠܟܐ ܤܓܝܐܐ ܀
11 Gannaaw loolu ñu ne ma: «Fàww nga wax ci kàddug Yàlla lu jëm ci réew yu bare, xeet yu bare, kàllaama yu bare ak buur yu bare.»