1ܘܐܬܐ ܪܒܬܐ ܐܬܚܙܝܬ ܒܫܡܝܐ ܐܢܬܬܐ ܕܥܛܝܦܐ ܫܡܫܐ ܘܤܗܪܐ ܬܚܝܬ ܪܓܠܝܗ ܘܟܠܝܠܐ ܕܟܘܟܒܐ ܬܪܥܤܪ ܥܠ ܪܫܗ ܀
1 Amoon na firnde ju ràññiku ju feeñ ca asamaan, di jigéen ju làmboo jant bi, kaalawoo fukki biddiiw ak ñaar, weer wi nekk ci suufu tànkam.
2ܘܒܛܢܐ ܘܩܥܝܐ ܘܡܚܒܠܢ ܐܦ ܡܫܬܢܩܐ ܕܬܐܠܕ ܀
2 Jigéenu biir la, di yuuxu ndax metitu mat wu tar.
3ܘܐܬܚܙܝܬ ܐܬܐ ܐܚܪܬܐ ܒܫܡܝܐ ܘܗܐ ܬܢܝܢܐ ܪܒܐ ܕܢܘܪܐ ܕܐܝܬ ܠܗ ܫܒܥܐ ܪܫܝܢ ܘܥܤܪ ܩܪܢܬܐ ܘܥܠ ܪܫܘܗܝ ܫܒܥܐ ܬܐܓܝܢ ܀
3 Noonu beneen firnde feeñ ca asamaan, di ninkinànka ju réy, xonq curr te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén. Ca bopp ya am na juróom-ñaari mbaxanay buur.
4ܘܕܘܢܒܗ ܓܪܫܐ ܠܬܘܠܬܐ ܕܟܘܟܒܐ ܕܒܫܡܝܐ ܘܐܪܡܝ ܐܢܘܢ ܥܠ ܐܪܥܐ ܘܬܢܝܢܐ ܩܐܡ ܗܘܐ ܩܕܡ ܐܢܬܬܐ ܕܥܬܝܕܐ ܕܬܐܠܕ ܕܡܐ ܕܝܠܕܬ ܢܐܟܠܝܘܗܝ ܠܒܪܗ ܀
4 Geenam di laawaale ñetti cér yu ne benn ca biddiiwi asamaan, di leen sànni ci suuf. Ninkinànka ja taxaw ca kanamu jigéen jay matu, ngir lekk liir ba, bu juddoo.
5ܘܝܠܕܬ ܒܪܐ ܕܟܪܐ ܗܘ ܕܥܬܝܕ ܠܡܪܥܐ ܠܟܠܗܘܢ ܥܡܡܐ ܒܫܒܛܐ ܕܦܪܙܠܐ ܘܐܬܚܛܦ ܒܪܗ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܘܠܘܬ ܟܘܪܤܝܗ ܀
5 Noonu mu jur doom ju góor, muy ki war a jiite xeeti àddina yépp ak yetu weñ. Waaye ñu daldi fëkk doom ja, mu dem ca Yàlla ak gànguneem.
6ܘܐܢܬܬܐ ܥܪܩܬ ܠܚܘܪܒܐ ܐܬܪ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܗ ܬܡܢ ܕܘܟܬܐ ܕܡܛܝܒܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܕܢܬܪܤܘܢܗ ܝܘܡܝܢ ܐܠܦ ܘܡܐܬܝܢ ܘܫܬܝܢ ܀
6 Gannaaw loolu jigéen ja daw, dem ca màndiŋ ma, ca dalukaay ba ko Yàlla waajaloon ngir mu nekk fa, ñu dundal ko fa diirub junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk.
7ܘܗܘܐ ܩܪܒܐ ܒܫܡܝܐ ܡܝܟܐܝܠ ܘܡܠܐܟܘܗܝ ܡܩܪܒܝܢ ܥܡ ܬܢܝܢܐ ܘܬܢܝܢܐ ܘܡܠܐܟܘܗܝ ܐܩܪܒܘ ܀
7 Noonu xare am ca asamaan ya. Mikayel ak malaaka, ya ànd ak moom, xeex ak ninkinànka ja, ninkinànka ja it ak ay malaakaam feyyu.
8ܘܠܐ ܐܬܡܨܝܘ ܘܠܐ ܐܬܪܐ ܐܫܬܟܚ ܠܗܘܢ ܒܫܡܝܐ ܀
8 Waaye ninkinànka jaa gën a néew doole; noonu ñu dàqe ko ak toppam asamaan.
9ܘܐܬܪܡܝ ܬܢܝܢܐ ܪܒܐ ܗܘ ܚܘܝܐ ܪܫܐ ܗܘ ܕܡܬܩܪܐ ܐܟܠܩܪܨܐ ܘܤܛܢܐ ܗܘ ܕܐܛܥܝ ܠܟܠܗ ܐܪܥܐ ܘܐܬܪܡܝ ܥܠ ܐܪܥܐ ܘܡܠܐܟܘܗܝ ܥܡܗ ܐܬܪܡܝܘ ܀
9 Daaneel nañu ko, moom ninkinànka ju réy ji, di jaani cosaan ji, te ñu di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp — daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak ay malaakaam.
10ܘܫܡܥܬ ܩܠܐ ܪܒܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܕܐܡܪ ܗܐ ܗܘܐ ܫܘܘܙܒܐ ܘܚܝܠܐ ܘܡܠܟܘܬܐ ܕܐܠܗܢ ܕܐܬܪܡܝ ܡܤܘܪܐ ܕܐܚܝܢ ܗܘ ܕܡܤܪ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܠܠܝܐ ܘܐܝܡܡܐ ܩܕܡ ܐܠܗܢ ܀
10 Noonu ma dégg baat bu xumb jóge asamaan naan:«Léegi mucc agsi na,moom ak kàttanak nguuru Yàlla sunu Boroom,ak sañ-sañu Almaseem,ndaxte ki daan tuumaal sunuy bokk,di leen sosal guddi ak bëccëgci kanam Yàlla sunu Boroom,kooka daaneel nañu ko.
11ܘܗܢܘܢ ܙܟܘ ܒܕܡܐ ܕܐܡܪܐ ܘܒܝܕ ܡܠܬܐ ܕܤܗܕܘܬܗ ܘܠܐ ܐܚܒܘ ܢܦܫܗܘܢ ܥܕܡܐ ܠܡܘܬܐ ܀
11 Fekk noot nañu kojaarale ko ci deretu Mbote maak seen seedes ngëm,te soppuñu seen bakkan ba ragal a dee.
12ܡܛܠܗܢܐ ܫܡܝܐ ܐܬܦܨܚܘ ܘܐܝܠܝܢ ܕܒܗܘܢ ܫܪܝܢ ܘܝ ܠܐܪܥܐ ܘܠܝܡܐ ܥܠ ܕܢܚܬ ܐܟܠܩܪܨܐ ܠܘܬܗܘܢ ܕܐܝܬ ܠܗ ܚܡܬܐ ܪܒܬܐ ܟܕ ܝܕܥ ܕܩܠܝܠ ܙܒܢܐ ܐܝܬ ܠܗ ܀
12 Looloo tax, na asamaanak ñi ci dëkk bànneexu!Musiba ci kaw suuf ak ci biir géej!Ndaxte Seytaane wàcc na ci yéen,ànd ak mer mu tàng,ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.»
13ܘܟܕ ܚܙܐ ܬܢܝܢܐ ܕܐܬܪܡܝ ܥܠ ܐܪܥܐ ܪܕܦ ܠܐܢܬܬܐ ܐܝܕܐ ܕܝܠܕܬ ܕܟܪܐ ܀
13 Ba ninkinànka ja gisee ne, daaneel nañu ko ci kaw suuf, mu dàq jigéen, ja juroon doom ju góor ja.
14ܘܐܬܝܗܒ ܠܐܢܬܬܐ ܬܪܝܢ ܓܦܝܢ ܕܢܫܪܐ ܪܒܐ ܕܬܦܪܚܝ ܠܚܘܪܒܐ ܠܕܘܟܬܗ ܠܡܬܬܪܤܝܘ ܬܡܢ ܥܕܢ ܥܕܢܝܢ ܘܦܠܓܘܬ ܥܕܢ ܡܢ ܩܕܡ ܐܦܘܗܝ ܕܚܘܝܐ ܀
14 Noonu ñu jox jigéen ja ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, ba sore ninkinànka ja, dem ca màndiŋ ma ca bérabam, ñu dundal ko fa ab diir, ay diir ak genn-wàllu diir.
15ܘܐܪܡܝ ܚܘܝܐ ܡܢ ܦܘܡܗ ܒܬܪ ܐܢܬܬܐ ܡܝܐ ܐܝܟ ܢܗܪܐ ܕܫܩܝܠܬ ܡܝܐ ܢܥܒܕܝܗ ܀
15 Ninkinànka ja buusu ndox mu bare ni dex ca gannaaw jigéen ja, ngir yóbbaale ko ca.
16ܘܥܕܪܬ ܐܪܥܐ ܠܐܢܬܬܐ ܘܦܬܚܬ ܐܪܥܐ ܦܘܡܗ ܘܒܠܥܬܗ ܠܢܗܪܐ ܗܘ ܕܐܪܡܝ ܬܢܝܢܐ ܡܢ ܦܘܡܗ ܀
16 Waaye suuf wallu jigéen ja, naan dex, ga ninkinànka ja buusu woon.
17ܘܪܓܙ ܬܢܝܢܐ ܥܠ ܐܢܬܬܐ ܘܐܙܠ ܠܡܥܒܕ ܩܪܒܐ ܥܡ ܫܪܟܐ ܕܙܪܥܗ ܗܠܝܢ ܕܢܛܪܝܢ ܦܘܩܕܢܘܗܝ ܕܐܠܗܐ ܘܐܝܬ ܠܗܘܢ ܤܗܕܘܬܗ ܕܝܫܘܥ ܀
17 Ninkinànka ja mere jigéen ja, daldi xeexi ak ñi des ciy doomam, di ñiy sàmm ndigali Yàlla tey sax ci di seedeel Yeesu.
18 Noonu mu taxaw ca tefesu géej ga.