Syriac: NT

Wolof: New Testament

Revelation

5

1ܘܚܙܝܬ ܥܠ ܝܡܝܢܗ ܕܗܘ ܕܝܬܒ ܥܠ ܟܘܪܤܝܐ ܟܬܒܐ ܕܪܫܝܡ ܡܢ ܠܓܘ ܘܡܢ ܠܒܪ ܘܛܒܝܥ ܛܒܥܐ ܫܒܥܐ ܀
1 Noonu ma gis ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma téere bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom-ñaari yoon ak sondeel.
2ܘܚܙܝܬ ܐܚܪܢܐ ܡܠܐܟܐ ܚܝܠܬܢܐ ܕܡܟܪܙ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܡܢ ܫܘܐ ܠܡܦܬܚ ܟܬܒܐ ܘܠܡܫܪܐ ܛܒܥܘܗܝ ܀
2 Noonu ma gis malaaka mu am doole, muy xaacu naan: «Ku yeyoo dindi tayu yi te ubbi téere bi?»
3ܘܠܝܬ ܕܐܬܡܨܝ ܒܫܡܝܐ ܘܠܐ ܒܐܪܥܐ ܘܠܐ ܕܠܬܚܬ ܡܢ ܐܪܥܐ ܠܡܦܬܚ ܠܟܬܒܐ ܘܠܡܫܪܐ ܛܒܥܘܗܝ ܘܠܡܚܙܝܗ ܀
3 Te amul kenn, muy ci asamaan, muy ci kaw suuf, muy ci biir suuf, ku manoon a ubbi téere bi, mbaa mu xool ci biir.
4ܘܒܟܐ ܗܘܝܬ ܤܓܝ ܡܛܠ ܕܠܝܬ ܕܐܫܬܟܚ ܕܫܘܐ ܠܡܦܬܚ ܠܟܬܒܐ ܘܠܡܫܪܐ ܛܒܥܘܗܝ ܀
4 Ma jooy jooy yu metti ndax li kenn yeyoowul woon a ubbi téere bi mbaa mu xool ko.
5ܘܚܕ ܡܢ ܩܫܝܫܐ ܐܡܪ ܠܝ ܠܐ ܬܒܟܐ ܗܐ ܙܟܐ ܐܪܝܐ ܡܢ ܫܒܛܐ ܕܝܗܘܕܐ ܥܩܪܐ ܕܕܘܝܕ ܢܦܬܚ ܟܬܒܐ ܘܛܒܥܘܗܝ ܀
5 Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Bul jooy. Xoolal, Gayndeg giiru Yuda, ki soqikoo ci Daawuda, daan na, ba am sañ-sañu dindi tayu yi te ubbi téere bi.»
6ܘܚܙܝܬ ܒܡܨܥܬ ܟܘܪܤܝܐ ܘܕܐܪܒܥ ܚܝܘܢ ܘܕܩܫܝܫܐ ܐܡܪܐ ܕܩܐܡ ܐܝܟ ܢܟܝܤܐ ܘܐܝܬ ܠܗ ܩܪܢܬܐ ܫܒܥ ܘܥܝܢܐ ܫܒܥ ܐܝܠܝܢ ܕܐܝܬܝܗܝܢ ܫܒܥ ܪܘܚܐ ܕܐܠܗܐ ܕܡܫܬܕܪܢ ܠܟܠܗ ܐܪܥܐ ܀
6 Noonu ma gis Mbote mu mel ni dañu koo rendi woon, mu taxaw ca digg gàngune ma, ñeenti mbindeef ya séq ko, mag ña wër ko. Mbote ma amoon na juróom-ñaari béjjén ak juróom-ñaari bët, ñu di juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi ñu yónni ci àddina sépp.
7ܘܐܬܐ ܘܢܤܒ ܟܬܒܐ ܡܢ ܐܝܕܗ ܕܗܘ ܕܝܬܒ ܥܠ ܟܘܪܤܝܐ ܀
7 Mbote ma ñëw, jël téere, ba nekkoon ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma.
8ܘܟܕ ܫܩܠܗ ܠܟܬܒܐ ܐܪܒܥ ܚܝܘܢ ܘܥܤܪܝܢ ܘܐܪܒܥܐ ܩܫܝܫܝܢ ܢܦܠܘ ܩܕܡܘܗܝ ܕܐܡܪܐ ܟܕ ܐܝܬ ܠܟܠܚܕ ܚܕ ܡܢܗܘܢ ܩܝܬܪܐ ܘܙܒܘܪܐ ܕܕܗܒܐ ܕܡܠܝܐ ܒܤܡܐ ܐܝܠܝܢ ܕܐܝܬܝܗܝܢ ܨܠܘܬܐ ܕܩܕܝܫܐ ܀
8 Ba mu jëlee téere ba, ñeenti mbindeef ya ak ñaar-fukki mag ña ak ñeent daldi dëpp seen jë ca kanam Mbote ma, ku nekk yor xalam. Ñu yor it andi wurus yu fees ak cuuraay, yu doon misaal ñaani gaayi Yàlla ya.
9ܕܡܫܒܚܝܢ ܬܫܒܘܚܬܐ ܚܕܬܐ ܘܐܡܪܝܢ ܫܘܝܬ ܗܘ ܠܡܤܒܝܘܗܝ ܠܟܬܒܐ ܘܠܡܫܪܐ ܛܒܥܘܗܝ ܥܠ ܕܐܬܢܟܤܬ ܘܙܒܢܬܢ ܒܕܡܟ ܠܐܠܗܐ ܡܢ ܟܠ ܫܪܒܬܐ ܘܥܡܡܐ ܘܐܡܘܬܐ ܀
9 Ñu daldi woy woy wu bees naan:«Yeyoo ngaa jël téere bite dindi tayu yi,ndaxte reyees na la,te jotal nga Yàlla ak sa deretay nit ñu bokk ci bépp giir,kàllaama, réew ak xeet.
10ܘܥܒܕܬ ܐܢܘܢ ܠܐܠܗܢ ܡܠܟܘܬܐ ܘܟܗܢܐ ܘܡܠܟܐ ܘܢܡܠܟܘܢ ܥܠ ܐܪܥܐ ܀
10 Def nga leen askanu saraxalekatiBuur Yàlla sunu Boroom,di ko jaamu,te dinañu nguuru ci àddina.»
11ܘܚܙܝܬ ܘܫܡܥܬ ܐܝܟ ܩܠܐ ܕܡܠܐܟܐ ܤܓܝܐܐ ܚܕܪܝ ܟܘܪܤܝܐ ܘܕܚܝܘܬܐ ܘܕܩܫܝܫܐ ܘܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܡܢܝܢܗܘܢ ܪܒܘ ܪܒܘܢ ܘܐܠܦ ܐܠܦܝܢ ܀
11 Ma xool noonu, dégg baatu malaaka yu bare yu ëppoon alfunniy alfunniy junniy junni. Malaaka ya wër gàngune ma ak mbindeef ya ak mag ña.
12ܘܐܡܪܝܢ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܫܘܝܬ ܗܘ ܐܡܪܐ ܢܟܝܤܐ ܠܡܤܒ ܚܝܠܐ ܘܥܘܬܪܐ ܘܚܟܡܬܐ ܘܥܘܫܢܐ ܘܐܝܩܪܐ ܘܬܫܒܘܚܬܐ ܘܒܘܪܟܬܐ ܀
12 Ñuy xaacu naan:«Mbote ma ñu rendi woonyeyoo na kàttan, alal, xel,doole, teraanga, ndam ak cant.»
13ܘܟܠ ܒܪܝܬܐ ܕܒܫܡܝܐ ܘܒܐܪܥܐ ܘܕܠܬܚܬ ܡܢ ܐܪܥܐ ܘܕܒܝܡܐ ܐܝܬܝܗ ܘܟܠ ܕܒܗܘܢ ܘܫܡܥܬ ܕܐܡܪܝܢ ܠܕܝܬܒ ܥܠ ܟܘܪܤܝܐ ܘܠܐܡܪܐ ܕܒܘܪܟܬܐ ܘܐܝܩܪܐ ܘܬܫܒܘܚܬܐ ܘܐܘܚܕܢܐ ܠܥܠܡ ܥܠܡܝܢ ܀
13 Ma dégg itam mbindeef, yi nekk ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf, ci géej gi, — mbindeef yépp naan:«Na cant, teraanga, ndam ak nguurféete ak ki toog ci gàngune mi,ak Mbote mi ba fàww.»
14ܘܐܪܒܥ ܚܝܘܢ ܕܐܡܪܢ ܐܡܝܢ ܘܩܫܝܫܐ ܢܦܠܘ ܘܤܓܕܘ ܀
14 Ñeenti mbindeef ya naan: «Amiin.» Mag ña sukk di màggal.