1ܒܥܢܐ ܗܟܝܠ ܡܢܟܘܢ ܐܚܝ ܒܪܚܡܘܗܝ ܕܐܠܗܐ ܕܬܩܝܡܘܢ ܦܓܪܝܟܘܢ ܕܒܚܬܐ ܚܝܬܐ ܘܩܕܝܫܬܐ ܘܡܩܒܠܬܐ ܠܐܠܗܐ ܒܬܫܡܫܬܐ ܡܠܝܠܬܐ ܀
1 Kon nag bokk yi, gannaaw yërmandey Yàlla baree na noonu, maa ngi leen di ñaan, ngeen jébbal ko seen yaram wépp. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu mooy njaamu, gi leen war.
2ܘܠܐ ܬܬܕܡܘܢ ܠܥܠܡܐ ܗܢܐ ܐܠܐ ܐܫܬܚܠܦܘ ܒܚܘܕܬܐ ܕܪܥܝܢܝܟܘܢ ܘܗܘܝܬܘܢ ܦܪܫܝܢ ܐܝܢܐ ܗܘ ܨܒܝܢܐ ܕܐܠܗܐ ܛܒܐ ܘܡܩܒܠܐ ܘܓܡܝܪܐ ܀
2 Bu leen àddina jey, waaye yeesluleen ci seen xel, ba soppiku, ngeen man a xam bu wér coobareg Yàlla, di lépp lu baax, neex ko te mat sëkk.
3ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܝܢ ܒܛܝܒܘܬܐ ܕܐܬܝܗܒܬ ܠܝ ܠܟܠܟܘܢ ܕܠܐ ܬܗܘܘܢ ܡܬܪܥܝܢ ܠܒܪ ܡܢ ܡܐ ܕܘܠܐ ܕܬܬܪܥܘܢ ܐܠܐ ܬܗܘܘܢ ܡܬܪܥܝܢ ܒܢܟܦܘܬܐ ܟܠܢܫ ܐܝܟ ܕܦܠܓ ܠܗ ܐܠܗܐ ܗܝܡܢܘܬܐ ܒܡܫܘܚܬܐ ܀
3 Gannaaw Yàlla may na ma ciw yiwam, ma nekk ndawam, maa ngi leen di wax lii, kenn ku nekk ci yéen: buleen yég seen bopp, waaye ngeen am xalaat yu yem, mengook ngëm gi leen Yàlla sédd, ku nekk ak wàllam.
4ܐܝܟܢܐ ܓܝܪ ܕܒܚܕ ܦܓܪܐ ܗܕܡܐ ܤܓܝܐܐ ܐܝܬ ܠܢ ܘܟܠܗܘܢ ܗܕܡܐ ܠܐ ܗܘܐ ܚܕ ܤܘܥܪܢܐ ܐܝܬ ܠܗܘܢ ܀
4 Loolu, ci maanaa, mi ngi mel ni yaramu nit: yaram, lu cér yi baree-bare, benn niroowul ak moroomam liggéey.
5ܗܟܢܐ ܐܦ ܚܢܢ ܕܤܓܝܐܐ ܚܢܢ ܚܕ ܚܢܢ ܦܓܪ ܒܡܫܝܚܐ ܚܕ ܚܕ ܡܢܢ ܕܝܢ ܗܕܡܐ ܚܢܢ ܕܚܕܕܐ ܀
5 Noonu itam nun ñi bokk ci Kirist, lu nu baree-bare, benn lanu te danoo mànkoo.
6ܐܠܐ ܐܝܬ ܠܢ ܡܘܗܒܬܐ ܡܫܚܠܦܬܐ ܐܝܟ ܛܝܒܘܬܐ ܕܐܬܝܗܒܬ ܠܢ ܐܝܬ ܕܢܒܝܘܬܐ ܐܝܟ ܡܫܘܚܬܐ ܕܗܝܡܢܘܬܗ ܀
6 Kon gannaaw Yàlla séddale na ay mayam, ku nekk ak sa cér, nanu koy jëfandikoo. Ku Yàlla may, ngay waare kàddoom, nga wax ko kem sa ngëm;
7ܘܐܝܬ ܕܬܫܡܫܬܐ ܐܝܬ ܠܗ ܒܬܫܡܫܬܗ ܘܐܝܬ ܕܡܠܦܢܐ ܗܘ ܒܝܘܠܦܢܗ ܀
7 kuy topptoo yëfi mbooloo mi, nga takku ci; ku Yàlla may, ngay jàngale, nekk ci;
8ܘܐܝܬ ܕܡܒܝܐܢܐ ܗܘ ܒܒܘܝܐܗ ܘܕܝܗܒ ܒܦܫܝܛܘܬܐ ܘܕܩܐܡ ܒܪܫܐ ܒܚܦܝܛܘܬܐ ܘܕܡܪܚܡ ܒܦܨܝܚܘܬܐ ܀
8 kuy feddali ngëmu nit ñi ci Yàlla, nga sax ci; kuy séddoo alalam ak nit ñi, nga def ko ak xol bu laab; kuy jiite mbooloo mi, nga sawar ci; kuy dimbali ñi néew doole, nanga ci bég.
9ܘܠܐ ܢܗܘܐ ܢܟܝܠ ܚܘܒܟܘܢ ܐܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܤܢܝܢ ܠܒܝܫܬܐ ܘܡܬܢܩܦܝܢ ܠܛܒܬܐ ܀
9 Na seen cofeel di lu dëggu te bañ a nekk ngistal; araamal-leen lu bon te sax ci lu baax.
10ܗܘܝܬܘܢ ܪܚܡܝܢ ܠܐܚܝܟܘܢ ܘܡܚܒܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܗܘܝܬܘܢ ܡܩܕܡܝܢ ܡܝܩܪܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܀
10 Bëgganteleen ak xol bu leer, niy doomi ndey, te farlu ci teralante.
11ܗܘܝܬܘܢ ܚܦܝܛܝܢ ܘܠܐ ܚܒܢܢܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܪܬܚܝܢ ܒܪܘܚ ܗܘܝܬܘܢ ܦܠܚܝܢ ܠܡܪܟܘܢ ܀
11 Sawarleen te bañ a tayel, di jaamu Boroom bi ak seen xol bépp.
12ܗܘܝܬܘܢ ܚܕܝܢ ܒܤܒܪܟܘܢ ܗܘܝܬܘܢ ܡܤܝܒܪܝܢ ܐܘܠܨܢܝܟܘܢ ܗܘܝܬܘܢ ܐܡܝܢܝܢ ܒܨܠܘܬܐ ܀
12 Bégleen ci yaakaaru ëllëg te muñ bépp tiis, di sax ci ñaan Yàlla.
13ܗܘܝܬܘܢ ܡܫܬܘܬܦܝܢ ܠܤܢܝܩܘܬܐ ܕܩܕܝܫܐ ܗܘܝܬܘܢ ܪܚܡܝܢ ܐܟܤܢܝܐ ܀
13 Dimbalileen gaayi Yàlla yi ci seeni soxla, te saxoo dalal gan.
14ܒܪܟܘ ܠܪܕܘܦܝܟܘܢ ܒܪܟܘ ܘܠܐ ܬܠܘܛܘܢ ܀
14 Ku leen fitnaal, ñaanal-leen ko yiw, te bañ koo móolu.
15ܚܕܘ ܥܡ ܕܚܕܝܢ ܘܒܟܘ ܥܡ ܕܒܟܝܢ ܀
15 Bégandooleen ak ñi bég, te jooyandoo ak ñiy jooy.
16ܘܡܕܡ ܕܡܬܪܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܥܠ ܢܦܫܟܘܢ ܐܦ ܥܠ ܐܚܝܟܘܢ ܘܠܐ ܬܬܪܥܘܢ ܪܥܝܢܐ ܪܡܐ ܐܠܐ ܩܦܘ ܠܐܝܠܝܢ ܕܡܟܝܟܝܢ ܘܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܚܟܝܡܝܢ ܒܪܥܝܢ ܢܦܫܟܘܢ ܀
16 Bokkleen menn xel, tey bañ a yékkatiku, di yóotu daraja, waaye ngeen fonk ñi suufe; buleen teg seen bopp boroomi xel.
17ܘܠܐ ܬܦܪܥܘܢ ܠܐܢܫ ܒܝܫܬܐ ܚܠܦ ܒܝܫܬܐ ܐܠܐ ܢܬܒܛܠ ܠܟܘܢ ܕܬܥܒܕܘܢ ܛܒܬܐ ܩܕܡ ܒܢܝܢܫܐ ܟܠܗܘܢ ܀
17 Buleen feyante lu bon, waaye sàkkuleen seede su rafet ci kanam ñépp.
18ܘܐܢ ܡܫܟܚܐ ܐܝܟ ܕܡܢ ܠܘܬܟܘܢ ܥܡ ܟܠܒܪܢܫ ܫܠܡܐ ܥܒܕܘ ܀
18 Wutleen a juboo ak ñépp, ba fa seen kàttan yem.
19ܘܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܬܒܥܝܢ ܢܦܫܟܘܢ ܚܒܝܒܝ ܐܠܐ ܗܒܘ ܐܬܪܐ ܠܪܘܓܙܐ ܟܬܝܒ ܗܘ ܓܝܪ ܕܐܢ ܠܐ ܬܥܒܕ ܕܝܢܐ ܠܢܦܫܟ ܐܢܐ ܐܥܒܕ ܕܝܢܟ ܐܡܪ ܐܠܗܐ ܀
19 Samay soppe, buleen di feyantoo, waaye bàyyileen lépp ci loxoy Yàlla, mi yelloo àtte; ndax Yàlla nee na ci Mbind mi: «Man maay àtte, maay fey jëf.»
20ܘܐܢ ܟܦܢ ܒܥܠܕܒܒܟ ܐܘܟܠܝܗܝ ܘܐܢ ܨܗܐ ܐܫܩܝܗܝ ܘܐܢ ܗܠܝܢ ܬܥܒܕ ܠܗ ܓܘܡܪܐ ܕܢܘܪܐ ܬܩܒܪ ܥܠ ܩܪܩܦܬܗ ܀
20 Waaye defleen lii:«Bu sa noon xiifee, may ko mu lekk;bu maree, may ko mu naan.Ndax boo ko defee, dinga ko rusloo.»
21ܠܐ ܬܙܟܝܟܘܢ ܒܝܫܬܐ ܐܠܐ ܙܟܐܘܗ ܠܒܝܫܬܐ ܒܛܒܬܐ ܀
21 Bu leen lu bon ëpp doole, waaye nootleen ko ci def lu baax.