Syriac: NT

Wolof: New Testament

Romans

16

1ܡܓܥܠ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܝܢ ܠܦܘܒܐ ܚܬܢ ܕܐܝܬܝܗ ܡܫܡܫܢܝܬܐ ܕܥܕܬܐ ܕܩܢܟܪܐܘܤ ܀
1 Bu nu weesoo loolu, maa ngi leen di dénk sunu jigéen Febe, miy liggéeyal mbooloom ñi gëm ci dëkku Señsere.
2ܕܬܩܒܠܘܢܗ ܒܡܪܢ ܐܝܟ ܕܙܕܩ ܠܩܕܝܫܐ ܘܒܟܠ ܨܒܘ ܕܒܥܝܐ ܡܢܟܘܢ ܬܩܘܡܘܢ ܠܗ ܡܛܠ ܕܐܦ ܗܝ ܩܝܘܡܬܐ ܗܘܬ ܠܤܓܝܐܐ ܐܦ ܠܝ ܀
2 Nangeen ko jàpp ci turu Boroom bi, ni ko gaayi Yàlla yi yelloo, te dimbali ko ci lépp lu mu aajowoo; ndaxte moom itam wax dëgg, dimbali na ñu bare, ba ci man mii di wax ak yéen.
3ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܦܪܝܤܩܠܐ ܘܕܐܩܠܤ ܦܠܚܐ ܕܥܡܝ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
3 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, samay nawle ci liggéeyu Kirist Yeesu.
4ܕܗܢܘܢ ܗܠܝܢ ܚܠܦ ܢܦܫܝ ܨܘܪܝܗܘܢ ܝܗܒܘ ܘܠܐ ܗܘܐ ܐܢܐ ܒܠܚܘܕܝ ܡܘܕܐ ܐܢܐ ܠܗܘܢ ܐܠܐ ܐܦ ܟܠܗܝܢ ܥܕܬܐ ܕܥܡܡܐ ܀
4 Ñoom ñaar dem nañu, bay bëgg a jaay seen bakkan ngir man; maa ngi leen di gërëm ci loolu, du man rekk sax, waaye itam mboolooy ñi gëm ci xeeti àddina sépp.
5ܘܗܒܘ ܫܠܡܐ ܠܥܕܬܐ ܕܐܝܬ ܒܒܝܬܗܘܢ ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܐܦܢܛܘܤ ܚܒܝܒܝ ܐܝܢܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܪܫܝܬܐ ܕܐܟܐܝܐ ܒܡܫܝܚܐ ܀
5 Nuyul-leen ma it ñiy booloo ci seen kër.Maa ngi nuyu it Epaynet, mi jëkk a gëm Kirist ci diiwaanu Asi;
6ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܡܪܝܐ ܐܝܕܐ ܕܤܓܝ ܠܐܝܬ ܒܟܘܢ ܀
6 ak Maryaama, mi sonnoon lool ci yéen.
7ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܐܢܕܪܘܢܝܩܘܤ ܘܕܝܘܢܝܐ ܐܚܝܢܝ ܕܗܘܘ ܫܒܝܐ ܥܡܝ ܘܝܕܝܥܝܢ ܐܢܘܢ ܒܫܠܝܚܐ ܘܒܡܫܝܚܐ ܩܕܡܝ ܗܘܘ ܀
7 Nuyul-leen ma it Andoronikus ak Yuñas, sama bokk, yi ñu ma booleeloon tëj; am nañu tur ci ndawi Yàlla yi, te ñoo ma jiitu sax ci gëm Kirist.
8ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܐܡܦܠܝܘܤ ܚܒܝܒܝ ܒܡܪܢ ܀
8 Te fàttewuma Ampilyaatus, mi ma bëgg ci sama xol ngir Boroom bi.
9ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܐܘܪܒܢܘܤ ܦܠܚܐ ܕܥܡܢ ܒܡܫܝܚܐ ܘܕܐܤܛܟܘܤ ܚܒܝܒܝ ܀
9 Nuyul-leen ma it Urban, sunu nawle ci liggéeyu Kirist, ak sama soppe Estakis;
10ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܐܦܠܐ ܓܒܝܐ ܒܡܪܢ ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܒܢܝ ܒܝܬܗ ܕܐܪܤܛܒܘܠܘܤ ܀
10 ak it Apeles, mi ngëmam dëggu, ba yelloo kóolute.Nuyul-leen ma it waa kër Aristobul,
11ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܗܪܘܕܝܘܢ ܐܚܝܢܝ ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܒܢܝ ܒܝܬܗ ܕܢܪܩܤܘܤ ܐܝܠܝܢ ܕܐܝܬܝܗܘܢ ܒܡܪܢ ܀
11 ak Erojon sama mbokk, ak waa kër Narsis, ñi ci Boroom bi.
12ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܛܪܘܦܢܐ ܘܕܛܪܘܦܤܐ ܕܠܐܝܝܢ ܒܡܪܢ ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܦܪܤܤ ܚܒܝܒܬܝ ܐܝܕܐ ܕܤܓܝ ܠܐܝܬ ܒܡܪܢ ܀
12 Maa ngi nuyu Tirifen, moom ak Tirifos, jigéen ñi sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it sama soppe Persidd, mi ci jeex tàkk.
13ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܪܘܦܤ ܓܒܝܐ ܒܡܪܢ ܘܕܐܡܗ ܕܝܠܗ ܘܕܝܠܝ ܀
13 Maa ngi nuyu it Rufus, waa ji xolam seey ci Boroom bi, ak yaayam, mi ma féete woon it cérub ndey.
14ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܐܤܘܢܩܪܛܘܤ ܘܕܦܠܓܘܢ ܘܕܗܪܡܐ ܘܕܦܛܪܒܐ ܘܕܗܪܡܐ ܘܕܐܚܐ ܕܥܡܗܘܢ ܀
14 Te fàttewuma Asànkirit, Felegon, Ermes, Patarobas, Ermas, ñoom ak mboolem bokk yépp.
15ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܕܦܝܠܠܓܘܤ ܘܕܝܘܠܝܐ ܘܕܢܐܪܘܤ ܘܕܚܬܗ ܘܕܐܠܘܡܦܐ ܘܕܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܕܥܡܗܘܢ ܀
15 Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, Nere ak jigéenam.Te fàttewuma Olimpas ak gaayi Yàlla yiy booloo ak ñoom ñépp.
16ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܚܕ ܕܚܕ ܒܢܘܫܩܬܐ ܩܕܝܫܬܐ ܫܐܠܢ ܒܫܠܡܟܘܢ ܟܠܗܝܢ ܥܕܬܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
16 Te yéen bokk yi, saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolooy ñi gëm Kirist yépp a ngi leen di nuyu.
17ܒܥܢܐ ܕܝܢ ܡܢܟܘܢ ܐܚܝ ܕܬܙܕܗܪܘܢ ܡܢ ܐܝܠܝܢ ܕܦܠܓܘܬܐ ܘܡܟܫܘܠܐ ܥܒܕܝܢ ܠܒܪ ܡܢ ܝܘܠܦܢܐ ܕܐܢܬܘܢ ܝܠܦܬܘܢ ܕܬܬܪܚܩܘܢ ܠܟܘܢ ܡܢܗܘܢ ܀
17 Bokk yi, maa ngi leen di dénk, ngeen moytu ñi leen di féewale, ba di leen jàddloo yoon wi, ciy wax lu juuyoo ak dëgg gi ngeen jàng. Dawleen leen ba sore.
18ܐܝܠܝܢ ܓܝܪ ܕܗܟܢܐ ܐܢܘܢ ܠܐ ܡܫܡܫܝܢ ܠܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܐܠܐ ܠܟܪܤܗܘܢ ܘܒܡܠܐ ܒܤܝܡܬܐ ܘܒܒܘܪܟܬܐ ܡܛܥܝܢ ܠܒܘܬܐ ܕܦܫܝܛܐ ܀
18 Ndax ñu deme noonu liggéeyaluñu Kirist sunu Boroom; seen bopp lañuy liggéeyal. Ñu ngi ñëw ak làmmiñ yu neex, di jey xol yu woyof yi, ba nax leen.
19ܡܫܬܡܥܢܘܬܟܘܢ ܕܝܢ ܕܝܠܟܘܢ ܠܟܠ ܒܪܢܫ ܐܬܝܕܥܬ ܚܕܐ ܐܢܐ ܗܟܝܠ ܒܟܘܢ ܘܨܒܐ ܐܢܐ ܕܬܗܘܘܢ ܚܟܝܡܝܢ ܠܛܒܬܐ ܘܬܡܝܡܝܢ ܠܒܝܫܬܐ ܀
19 Waaye seen dégg ndigal bir na ñépp, ba sama xol sedd lool ci yéen. Teewul nag damaa bëgg ngeen am xam-xam bu leer ci lu baax, te bañ a laal dara ci lu bon.
20ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܕܫܠܡܐ ܢܫܚܩܝܘܗܝ ܒܥܓܠ ܠܤܛܢܐ ܬܚܝܬ ܪܓܠܝܟܘܢ ܛܝܒܘܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܬܗܘܐ ܥܡܟܘܢ ܀
20 Su ko defee Yàlla Boroom jàmm dina noot Seytaane ci seeni tànk léegi. Na yiwu Yeesu sunu Boroom ànd ak yéen!
21ܫܐܠܝܢ ܒܫܠܡܟܘܢ ܛܝܡܬܐܘܤ ܦܠܚܐ ܕܥܡܝ ܘܠܘܩܝܘܤ ܘܐܝܤܘܢ ܘܤܘܤܝܦܛܪܘܤ ܐܚܝܢܝ ܀
21 Timote sama nawle bi may jàpple ci liggéey bi, mu ngi leen di nuyu, ak samay bokk Lusiyus, Yason ak Sosipater.
22ܫܐܠ ܐܢܐ ܒܫܠܡܟܘܢ ܐܢܐ ܛܪܛܝܘܤ ܕܟܬܒܬ ܐܓܪܬܐ ܒܡܪܢ ܀
22 Man Tersiyus mi bind bataaxal bii nag, maa ngi leen di nuyu ci turu Boroom bi.
23ܫܐܠ ܒܫܠܡܟܘܢ ܓܐܝܘܤ ܡܩܒܠܢܝ ܘܕܟܠܗ ܥܕܬܐ ܫܐܠ ܒܫܠܡܟܘܢ ܐܪܤܛܘܤ ܪܒܝܬܐ ܕܡܕܝܢܬܐ ܘܩܘܐܪܛܘܤ ܐܚܐ ܀
23 Gayus mu ngi leen di nuyu; moo may ganale ci këram, te foofa it la mbooloo mi di dajaloo. Erast miy topptoo mbiri xaalisu dëkk bi it, nuyu na leen, ak sunu mbokk Kartus.
24ܠܐܠܗܐ ܕܝܢ ܗܘ ܕܡܫܟܚ ܕܢܫܪܪܟܘܢ ܒܐܘܢܓܠܝܘܢ ܕܝܠܝ ܗܘ ܕܐܬܟܪܙ ܥܠ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܒܓܠܝܢܐ ܕܐܪܙܐ ܕܡܢ ܙܒܢܝ ܥܠܡܐ ܡܟܤܝ ܗܘܐ ܀
24 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen! Amiin.
25ܐܬܓܠܝ ܕܝܢ ܒܙܒܢܐ ܗܢܐ ܒܝܕ ܟܬܒܐ ܕܢܒܝܐ ܘܒܦܘܩܕܢܗ ܕܐܠܗܐ ܕܠܥܠܡ ܐܬܝܕܥ ܠܟܠܗܘܢ ܥܡܡܐ ܠܡܫܡܥܐ ܕܗܝܡܢܘܬܐ ܀
25 Santleen Yàlla, mi leen man a saxal bu wér ci dëggu xebaar bu baax, bi may waare ci mbirum Yeesu Kirist! Nekkoon na kumpa gu làqu diirub ay ati at,
26ܕܗܘܝܘ ܚܟܝܡܐ ܒܠܚܘܕܘܗܝ ܫܘܒܚܐ ܒܝܕ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܥܠܡܥܠܡܝܢ ܐܡܝܢ ܀
26 waaye léegi nag Yàlla dindi na nu ci kumpa. Te santaane na, nu yégle xebaar boobu ci xeeti àddina sépp, ci firi Mbindi yonent yi, ngir nit ñi man koo gëm, ba jébbalu.
27ܛܝܒܘܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܥܡ ܟܠܟܘܢ ܐܡܝܢ ܀
27 Yàlla mi jagoo xam-xam bépp, moom rekk moo yelloo ndam ba fàww, jaar ci Yeesu Kirist! Amiin.