1ܡܢܐ ܗܟܝܠ ܢܐܡܪ ܢܩܘܐ ܒܗ ܒܚܛܝܬܐ ܕܛܝܒܘܬܐ ܬܬܝܬܪ ܀
1 Lu nu war a wax léegi nag? Xanaa nu sax ci bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gën a bare?
2ܚܤ ܐܝܠܝܢ ܓܝܪ ܕܡܝܬܢ ܠܚܛܝܬܐ ܐܝܟܢܐ ܢܚܐ ܒܗ ܬܘܒ ܀
2 Mukk! Nun ñi dee, ba rëcc ci kàttanu bàkkaar, naka lanu manatee sax ci di ko def?
3ܐܘ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܐܝܠܝܢ ܕܥܡܕܢ ܒܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܒܡܘܬܗ ܗܘ ܥܡܕܢ ܀
3 Xanaa dangeen a xamul ne, képp ku ñu sóob ci ndox, ngir wone ne, mu ngi bokk ci Yeesu Kirist, ci deewu Yeesu la bokk.
4ܐܬܩܒܪܢ ܥܡܗ ܒܡܥܡܘܕܝܬܐ ܠܡܘܬܐ ܕܐܝܟܢܐ ܕܩܡ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܒܬܫܒܘܚܬܐ ܕܐܒܘܗܝ ܗܟܢܐ ܐܦ ܚܢܢ ܒܚܝܐ ܚܕܬܐ ܢܗܠܟ ܀
4 Bi ñu nu sóobee ci ndox moomu nag, day misaal ne, dañu noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Yàlla Baay bi, te nu sóobu ci dund gu bees.
5ܐܢ ܓܝܪ ܐܟܚܕ ܐܬܢܨܒܢ ܥܡܗ ܒܕܡܘܬܐ ܕܡܘܬܗ ܗܟܢܐ ܐܦ ܒܩܝܡܬܗ ܢܗܘܐ ܀
5 Kon nag gannaaw benn lanu ak Kirist, dee ni mu deeye woon, kon dinanu nekk it benn ak moom, dekki ni mu dekkee woon.
6ܝܕܥܝܢܢ ܓܝܪ ܕܒܪܢܫܢ ܥܬܝܩܐ ܐܙܕܩܦ ܥܡܗ ܕܢܬܒܛܠ ܦܓܪܐ ܕܚܛܝܬܐ ܕܬܘܒ ܠܐ ܢܫܡܫ ܠܚܛܝܬܐ ܀
6 Ndegam xam nanu ne, daajoon nañu Kirist ca bant ba, xam nanu it ne, jikko ju bon ji nu judduwaale, daajaale nañu ko ak Kirist ca bant ba. Te Yàlla def na loolu, ngir nguuru bàkkaar, gi nekkoon ci sunu yaram tas, nu rëcc ci dooleem.
7ܐܝܢܐ ܕܡܝܬ ܓܝܪ ܐܬܚܪܪ ܠܗ ܡܢ ܚܛܝܬܐ ܀
7 Ndaxte ku dee, bàkkaar mënatul dara ci yaw.
8ܐܢ ܗܟܝܠ ܡܝܬܢ ܥܡ ܡܫܝܚܐ ܢܗܝܡܢ ܕܥܡܗ ܥܡ ܡܫܝܚܐ ܢܚܐ ܀
8 Gannaaw nag dee nanu ak Kirist, gëm nanu ne, dinanu dekki it ni moom,
9ܝܕܥܝܢܢ ܓܝܪ ܕܡܫܝܚܐ ܩܡ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܘܬܘܒ ܠܐ ܡܐܬ ܘܡܘܬܐ ܠܐ ܡܫܬܠܛ ܒܗ ܀
9 xam ne Kirist mi dekki dootul dee mukk, dee mënatul dara ci moom.
10ܕܡܝܬ ܓܝܪ ܠܚܛܝܬܐ ܗܘ ܡܝܬ ܚܕܐ ܙܒܢ ܘܕܚܝ ܚܝ ܗܘ ܠܐܠܗܐ ܀
10 Dee na benn yoon, ba bàkkaar mënul ci moom dara; te mi ngi dund léegi, di ànd ak Yàlla ba fàww.
11ܗܟܢܐ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܚܫܘܒܘ ܢܦܫܟܘܢ ܕܡܝܬܐ ܐܢܬܘܢ ܠܚܛܝܬܐ ܘܚܝܐ ܐܢܬܘܢ ܠܐܠܗܐ ܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
11 Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.
12ܠܐ ܗܟܝܠ ܬܡܠܟ ܚܛܝܬܐ ܒܦܓܪܟܘܢ ܡܝܬܐ ܐܝܟ ܕܬܫܬܡܥܘܢ ܠܪܓܝܓܬܗ ܀
12 Buleen mayati bàkkaar nag, mu yilif seeni yaram yu néew doole, bay topp ay bëgg-bëggam.
13ܘܐܦ ܠܐ ܬܛܝܒܘܢ ܗܕܡܝܟܘܢ ܙܝܢܐ ܕܥܘܠܐ ܠܚܛܝܬܐ ܐܠܐ ܛܝܒܘ ܢܦܫܟܘܢ ܠܐܠܗܐ ܐܝܟ ܐܢܫܐ ܕܡܢ ܡܝܬܐ ܚܝܝܬܘܢ ܘܗܕܡܝܟܘܢ ܙܝܢܐ ܢܗܘܘܢ ܠܟܐܢܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
13 Te buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub.
14ܘܚܛܝܬܐ ܠܐ ܡܫܬܠܛܐ ܥܠܝܟܘܢ ܠܐ ܓܝܪ ܐܝܬܝܟܘܢ ܬܚܝܬ ܢܡܘܤܐ ܐܠܐ ܬܚܝܬ ܛܝܒܘܬܐ ܀
14 Ndaxte bàkkaar dootu leen manal dara, yéen ñi génn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla.
15ܡܢܐ ܗܟܝܠ ܢܚܛܐ ܕܠܐ ܗܘܝܢ ܬܚܝܬ ܢܡܘܤܐ ܐܠܐ ܬܚܝܬ ܛܝܒܘܬܐ ܚܤ ܀
15 Lan lanu war a wax nag léegi? Gannaaw génn nanu ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla, ndax danoo war a sax ci def bàkkaar? Mukk!
16ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܠܡܢ ܕܡܛܝܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܢܦܫܟܘܢ ܕܬܫܬܡܥܘܢ ܠܗ ܠܥܒܕܘܬܐ ܕܝܠܗ ܐܢܬܘܢ ܥܒܕܐ ܕܗܘ ܕܡܫܬܡܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗ ܐܢ ܠܚܛܝܬܐ ܘܐܢ ܠܡܫܡܥ ܐܕܢܐ ܕܟܐܢܘܬܐ ܀
16 Ndax dangeen a xamul ne, koo jébbalu ci moom te déggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami bàkkaar, mu jëme leen ci dee, mbaa ngeen déggal Yàlla, mu sóob leen ci yoonu njub.
17ܛܝܒܘ ܕܝܢ ܠܐܠܗܐ ܕܥܒܕܐ ܗܘܝܬܘܢ ܕܚܛܝܬܐ ܘܐܫܬܡܥܬܘܢ ܡܢ ܠܒܐ ܠܕܡܘܬܐ ܕܝܘܠܦܢܐ ܕܐܫܬܠܡܬܘܢ ܠܗ ܀
17 Waaye sant naa Yàlla ci lii: yéen ñi doon jaami bàkkaar, bi ngeen déggee mboolem dëgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol bépp.
18ܘܟܕ ܐܬܚܪܪܬܘܢ ܡܢ ܚܛܝܬܐ ܐܫܬܥܒܕܬܘܢ ܠܟܐܢܘܬܐ ܀
18 Te ci noonu rëcc ngeen ci nootaangeg bàkkaar te jébbalu ci Yàlla, sóobu ci njub.
19ܐܝܟ ܕܒܝܬ ܒܢܝܢܫܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܡܛܠ ܟܪܝܗܘܬܐ ܕܒܤܪܟܘܢ ܕܐܝܟܢܐ ܕܛܝܒܬܘܢ ܗܕܡܝܟܘܢ ܠܥܒܕܘܬܐ ܕܛܢܦܘܬܐ ܘܕܥܘܠܐ ܗܟܢܐ ܐܦ ܗܫܐ ܛܝܒܘ ܗܕܡܝܟܘܢ ܠܥܒܕܘܬܐ ܕܟܐܢܘܬܐ ܘܕܩܕܝܫܘܬܐ ܀
19 Xam naa ne, seen xam-xam ci mbir mii sorewul, moo tax ma yombal wax ji, awale ko ci baat yii. Ni ngeen jële woon seeni cér, jébbal leen, ñu nekk jaami lu selladi ak lu bon, di gën a jur lu bon, noonu itam léegi jébbal-leen seeni cér, ñu nekk jaami njub, ngeen door a sell.
20ܟܕ ܥܒܕܐ ܗܘܝܬܘܢ ܓܝܪ ܕܚܛܝܬܐ ܡܚܪܪܐ ܗܘܝܬܘܢ ܠܟܐܢܘܬܐ ܀
20 Ndaxte keroog ba ngeen nekkee jaami bàkkaar, séquleen woon dara ak lu jub.
21ܘܡܢܐ ܐܕܫܐ ܐܝܬ ܗܘܐ ܠܟܘܢ ܗܝܕܝܢ ܐܝܢܐ ܕܝܘܡܢܐ ܒܗܬܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܗ ܚܪܬܗ ܓܝܪ ܐܝܬܝܗ ܡܘܬܐ ܀
21 Ban njariñ ngeen ci jële nag? Dara lu dul gàcce, ndaxte ci dee la leen doon jëmale.
22ܘܗܫܐ ܕܐܬܚܪܪܬܘܢ ܡܢ ܚܛܝܬܐ ܘܗܘܝܬܘܢ ܥܒܕܐ ܠܐܠܗܐ ܐܝܬ ܠܟܘܢ ܦܐܪܐ ܩܕܝܫܐ ܕܚܪܬܗܘܢ ܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܀
22 Waaye léegi Yàlla goreel na leen ci kilifteefu bàkkaar, def leen ay jaamam, ba jural leen sell, jëme leen ci dund gu dul jeex.
23ܬܐܓܘܪܬܐ ܕܝܢ ܕܚܛܝܬܐ ܡܘܬܐ ܗܘ ܘܡܘܗܒܬܗ ܕܐܠܗܐ ܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
23 Ndaxte peyu bàkkaar mooy dee, waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.