1ܐܢܬ ܕܝܢ ܡܠܠ ܡܕܡ ܕܝܐܐ ܠܝܘܠܦܢܐ ܚܠܝܡܐ ܀
1 Yaw nag nangay waare li dëppook njàngale mu wér mi.
2ܘܐܠܦ ܕܢܗܘܘܢ ܩܫܝܫܐ ܥܝܪܝܢ ܒܪܥܝܢܝܗܘܢ ܘܢܗܘܘܢ ܢܟܦܝܢ ܘܢܗܘܘܢ ܕܟܝܢ ܘܢܗܘܘܢ ܚܠܝܡܝܢ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܘܒܚܘܒܐ ܘܒܡܤܝܒܪܢܘܬܐ ܀
2 Maanaa, na góor ñu mag ñi foog, am faayda te maandu, di ñu wér ci seen ngëm, seen mbëggeel ak seen muñ.
3ܘܐܦ ܩܫܝܫܬܐ ܗܟܢܐ ܕܢܗܘܝܢ ܒܐܤܟܡܐ ܕܝܐܐ ܠܕܚܠܬ ܐܠܗܐ ܘܠܐ ܢܗܘܝܢ ܐܟܠܢ ܩܪܨܐ ܘܠܐ ܢܗܘܝܢ ܡܫܥܒܕܢ ܠܚܡܪܐ ܤܓܝܐܐ ܘܢܗܘܝܢ ܡܠܦܢ ܫܦܝܪܬܐ ܀
3 Jigéen ñu mag ñi itam, na seen doxalin ànd ak faayda; buñuy jëw mbaa xér ci sangara. Waaye nañuy jàngale lu baax,
4ܘܡܢܟܦܢ ܠܐܝܠܝܢ ܕܛܠܝܢ ܕܢܪܚܡܢ ܒܥܠܝܗܝܢ ܘܒܢܝܗܝܢ ܀
4 bay sol ci boppu jeeg yu ndaw yi, ñu bëgg seeni jëkkër ak seeni doom,
5ܘܢܗܘܝܢ ܢܟܦܢ ܘܩܕܝܫܢ ܘܢܗܘܝܢ ܝܨܦܢ ܫܦܝܪ ܕܒܬܝܗܝܢ ܘܡܫܬܥܒܕܢ ܠܒܥܠܝܗܝܢ ܕܠܐ ܐܢܫ ܢܓܕܦ ܥܠ ܡܠܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
5 di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër, ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla.
6ܘܡܢ ܐܝܠܝܢ ܕܛܠܝܢ ܗܟܢܐ ܒܥܝ ܕܢܗܘܘܢ ܢܟܦܝܢ ܀
6 Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu.
7ܒܟܠܡܕܡ ܕܝܢ ܕܡܘܬܐ ܒܢܦܫܟ ܚܘܐ ܒܟܠ ܥܒܕܐ ܛܒܐ ܘܒܡܠܦܢܘܬܟ ܬܗܘܐ ܠܟ ܡܠܬܐ ܚܠܝܡܬܐ ܀
7 Te yaw, ci lépp lu mu man a doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngale wér te am faayda,
8ܕܢܟܦܐ ܘܠܐ ܡܚܒܠܐ ܘܠܐ ܐܢܫ ܒܤܪ ܠܗ ܕܐܝܢܐ ܕܩܐܡ ܠܩܘܒܠܢ ܢܒܗܬ ܟܕ ܠܐ ܢܫܟܚ ܕܢܐܡܪ ܥܠܝܢ ܡܕܡ ܕܤܢܐ ܀
8 ànd ak wax yu wér yu kenn mënta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal.
9ܥܒܕܐ ܠܡܪܝܗܘܢ ܢܫܬܥܒܕܘܢ ܒܟܠܡܕܡ ܘܢܫܬܦܪܘܢ ܘܠܐ ܗܘܘ ܡܥܨܝܢ ܀
9 Waxal it jaam ñi, ñu déggal seeni sang ci lépp, te liggéeyal leen ba seral seen xol, bañ cee boole werante
10ܘܠܐ ܗܘܘ ܓܢܒܝܢ ܐܠܐ ܢܚܘܘܢ ܫܪܪܗܘܢ ܛܒܐ ܒܟܠܡܕܡ ܕܢܨܒܬܘܢ ܒܟܠܡܕܡ ܝܘܠܦܢܗ ܕܐܠܗܐ ܡܚܝܢܢ ܀
10 mbaa sàcc. Waaye nañu wone takkute gu mat, ba rafetal ci lépp njàngalem Yàlla sunu Musalkat.
11ܐܬܓܠܝܬ ܓܝܪ ܛܝܒܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܡܚܝܬ ܟܠ ܠܒܢܝܢܫܐ ܟܠܗܘܢ ܀
11 Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc.
12ܘܪܕܝܐ ܠܢ ܕܢܟܦܘܪ ܒܪܘܫܥܐ ܘܒܪܓܝܓܬܐ ܕܥܠܡܐ ܘܢܚܐ ܒܥܠܡܐ ܗܢܐ ܒܢܟܦܘܬܐ ܘܒܟܐܢܘܬܐ ܘܒܕܚܠܬ ܐܠܗܐ ܀
12 Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla,
13ܟܕ ܡܤܟܝܢܢ ܠܤܒܪܐ ܒܪܝܟܐ ܘܠܓܠܝܢܐ ܕܬܫܒܘܚܬܗ ܕܐܠܗܐ ܪܒܐ ܘܡܚܝܢܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
13 di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam.
14ܕܗܘ ܝܗܒ ܢܦܫܗ ܚܠܦܝܢ ܕܢܦܪܩܢ ܡܢ ܟܠ ܥܘܠܐ ܘܢܕܟܝܢ ܠܢܦܫܗ ܥܡܐ ܚܕܬܐ ܕܚܤܡ ܒܥܒܕܐ ܛܒܐ ܀
14 Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax.
15ܗܠܝܢ ܡܠܠ ܘܒܥܝ ܘܟܘܢ ܒܟܠ ܦܘܩܕܢ ܘܠܐ ܐܢܫ ܢܒܤܐ ܒܟ ܀
15 Jàngaleel loolu, di leen dénk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab.