World English Bible

Wolof: New Testament

John

10

1 “Most certainly, I tell you, one who doesn’t enter by the door into the sheep fold, but climbs up some other way, the same is a thief and a robber.
1 «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku jaar feneen fu dul ci buntu gétt gi, kooku sàcc la, saay-saay la.
2 But one who enters in by the door is the shepherd of the sheep.
2 Waaye ki jaar ci bunt bi, mooy sàmmu xar yi.
3 The gatekeeper opens the gate for him, and the sheep listen to his voice. He calls his own sheep by name, and leads them out.
3 Wottukat bi dina ko ubbil bunt bi, xar yiy dégg baatam. Xar yi mu moom nag, bu ci nekk dina la woo ci sa tur, ba noppi nga topp ko ci biti.
4 Whenever he brings out his own sheep, he goes before them, and the sheep follow him, for they know his voice.
4 Sàmm bi, bu génnee yi mu moom yépp, dina leen jiitu, ñu topp ko, ndaxte xam nañu baatam.
5 They will by no means follow a stranger, but will flee from him; for they don’t know the voice of strangers.”
5 Waaye duñu topp jaambur; dañu koy daw, ndaxte miinuñu baatam.»
6Jesus spoke this parable to them, but they didn’t understand what he was telling them.
6 Yeesu misaaloon na leen loolu, waaye xamuñu lu mu leen doon wax.
7Jesus therefore said to them again, “Most certainly, I tell you, I am the sheep’s door.
7 Noonu Yeesu newaat: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, man maay buntu gétt gi.
8 All who came before me are thieves and robbers, but the sheep didn’t listen to them.
8 Ñi ma fi jiitu ñépp ay sàcc lañu, ak ay saay-saay; waaye xar yi dégluwuñu leen.
9 I am the door. If anyone enters in by me, he will be saved, and will go in and go out, and will find pasture.
9 Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga man a dugg ak a génn, dinga am it mbooy goo man a fore.
10 The thief only comes to steal, kill, and destroy. I came that they may have life, and may have it abundantly.
10 Sàcc bi moom, day sàccsi rekk, di rey ak a yàq. Man damaa ñëw, ngir nit ñi am dund, ba nekk ci naataange.
11 I am the good shepherd. The good shepherd lays down his life for the sheep.
11 «Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram.
12 He who is a hired hand, and not a shepherd, who doesn’t own the sheep, sees the wolf coming, leaves the sheep, and flees. The wolf snatches the sheep, and scatters them.
12 Ki dul sàmm bi tey liggéeyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu séenee bukki, day daw, bàyyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, jàpp ca, tasaare ya ca des.
13 The hired hand flees because he is a hired hand, and doesn’t care for the sheep.
13 Booba surga day daw, ndaxte xaalis rekk lay liggéeyal, faalewul xar ya.
14 I am the good shepherd. I know my own, and I’m known by my own;
14 «Man maay sàmm bu baax bi. Ni ma xame Baay bi te Baay bi xame ma ni, noonu laa xame samay xar, te ñoom it ni lañu ma xame. Te it kat dinaa joxe sama bakkan ngir xar yi.
15 even as the Father knows me, and I know the Father. I lay down my life for the sheep.
16 Am naa yeneen xar yu bokkul ci gétt gii. War naa leen a indi, ñoom it, te dinañu déglu sama baat. Benn coggal ay am ak benn sàmm.
16 I have other sheep, which are not of this fold. I must bring them also, and they will hear my voice. They will become one flock with one shepherd.
17 Baay bi bëgg na ma, ndaxte damay joxe sama bakkan ngir jëlaat ko.
17 Therefore the Father loves me, because I lay down my life, that I may take it again.
18 Kenn du ko jële ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko te am naa sañ-sañu jëlaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.»
18 No one takes it away from me, but I lay it down by myself. I have power to lay it down, and I have power to take it again. I received this commandment from my Father.”
19 Kàddu yooyee ñoo féewalewaat Yawut yi.
19Therefore a division arose again among the Jews because of these words.
20 Ñu bare ca ñoom naan: «Dafa ànd ak rab! Dafa dof! Lu tax ngeen koy déglu?»
20Many of them said, “He has a demon, and is insane! Why do you listen to him?”
21 Waaye ñeneen naan: «Nit ku am ay rab du waxe nii. Ndax rab man na ubbi bëti gumba?»
21Others said, “These are not the sayings of one possessed by a demon. It isn’t possible for a demon to open the eyes of the blind, is it?”
22 Am bés ñu doon màggal ca Yerusalem Bés ba ñu sellale woon kër Yàlla ga; ci jamonoy sedd la woon.
22It was the Feast of the Dedication at Jerusalem.
23 Yeesoo nga woon ca kër Yàlla ga, di doxantu ca biir Werandaa bu Suleymaan.
23It was winter, and Jesus was walking in the temple, in Solomon’s porch.
24 Yawut ya wër ko ne ko: «Kañ nga nuy dindi ci kumpa? Boo dee Almasi bi, wax ko mu leer.»
24The Jews therefore came around him and said to him, “How long will you hold us in suspense? If you are the Christ, tell us plainly.”
25 Yeesu tontu leen ne: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye gëmuleen. Jëf yi may def ci sama turu Baay ñoo may seede.
25Jesus answered them, “I told you, and you don’t believe. The works that I do in my Father’s name, these testify about me.
26 Waaye gëmuleen ndaxte bokkuleen ci samay xar.
26 But you don’t believe, because you are not of my sheep, as I told you.
27 Samay xar dinañu dégg sama baat; xam naa leen te ñu ngi may topp.
27 My sheep hear my voice, and I know them, and they follow me.
28 Dama leen di jox dund gu dul jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jële ci sama loxo.
28 I give eternal life to them. They will never perish, and no one will snatch them out of my hand.
29 Baay bi ma leen jox, moo gën a màgg lépp, te kenn mënul a jële dara ci loxob Baay bi.
29 My Father, who has given them to me, is greater than all. No one is able to snatch them out of my Father’s hand.
30 Man ak Baay bi benn lanu.»
30 I and the Father are one.”
31 Yawut ya daldi foraat ay xeer, bëgg koo sànni, ngir rey ko.
31Therefore Jews took up stones again to stone him.
32 Noonu Yeesu ne leen: «Def naa ci seen kanam jëf yu baax yu bare ci ndigalu Baay bi. Ban ci jëf yooyu moo tax ba ngeen bëgg maa sànni ay doj?»
32Jesus answered them, “I have shown you many good works from my Father. For which of those works do you stone me?”
33 Yawut ya ne ko: «Jëf ju baax taxul nu bëgg laa sànniy xeer, waaye dangay suufeel turu Yàlla; yaw, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Yàlla!»
33The Jews answered him, “We don’t stone you for a good work, but for blasphemy: because you, being a man, make yourself God.”
34 Yeesu tontu ne: «Bind nañu ci seen téereb yoon ne: “Yàlla nee na: Ay yàlla ngeen.”
34Jesus answered them, “Isn’t it written in your law, ‘I said, you are gods?’
35 Yàlla wooye na “ay yàlla” ñi mu yónnee kàddoom, te xam nanu ne, kenn mënul a randal waxi Yàlla.
35 If he called them gods, to whom the word of God came (and the Scripture can’t be broken),
36 Kon nu ngeen man a waxe ne, damay suufeel turu Yàlla ndax li ma ne Doomam laa, man mi Yàlla tànn, yónni ma ci àddina?
36 do you say of him whom the Father sanctified and sent into the world, ‘You blaspheme,’ because I said, ‘I am the Son of God?’
37 Su ma deful sama jëfi Baay, buleen ma gëm;
37 If I don’t do the works of my Father, don’t believe me.
38 waaye su ma ko defee, bu ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog samay jëf, ngir ngeen xam te nangu ne, maa ngi nekk ci Baay bi te Baay bi nekk na ci man.»
38 But if I do them, though you don’t believe me, believe the works; that you may know and believe that the Father is in me, and I in the Father.”
39 Ñu di ko wut a jàppaat, waaye mu bàyyi leen fa, dem.
39They sought again to seize him, and he went out of their hand.
40 Yeesu génn, jàllaat dexu Yurdan, toog fa Yaxya daan sóobe ci ndox bu jëkk.
40He went away again beyond the Jordan into the place where John was baptizing at first, and there he stayed.
41 Nit ñu bare ñëw ci moom, te naan: «Yaxya deful benn kéemaan, waaye li mu wax ci kii yépp, dëgg la.»
41Many came to him. They said, “John indeed did no sign, but everything that John said about this man is true.”
42 Noonu ñu bare gëm ko.
42Many believed in him there.