World English Bible

Wolof: New Testament

John

16

1 “These things have I spoken to you, so that you wouldn’t be caused to stumble.
1 «Loolu dama leen koo wax ngir seen ngëm bañ a wàññiku.
2 They will put you out of the synagogues. Yes, the time comes that whoever kills you will think that he offers service to God.
2 Dinañu leen dàq ca jàngu ya, te dinañu dem ba jamono joo xam ne ñi leen di rey dañuy xalaat ne, ñu ngi màggal turu Yàlla.
3 They will do these things because they have not known the Father, nor me.
3 Dinañu agsi foofu, ndaxte xamuñu Baay bi te xamuñu ma.
4 But I have told you these things, so that when the time comes, you may remember that I told you about them. I didn’t tell you these things from the beginning, because I was with you.
4 Loolu nag, wax naa leen ko, ngir bu waxtu wi jotee ngeen fàttaliku ne, yégal naa leen ko. «Waxuma leen ko ca njàlbéen ga, ndaxte maa ngi nekkoon ak yéen.
5 But now I am going to him who sent me, and none of you asks me, ‘Where are you going?’
5 «Léegi nag maa ngi dem ca ka ma yónni, te kenn ci yéen laaju ma fi ma jëm.
6 But because I have told you these things, sorrow has filled your heart.
6 Seen xol dafa jeex ndax li ma leen wax.
7 Nevertheless I tell you the truth: It is to your advantage that I go away, for if I don’t go away, the Counselor won’t come to you. But if I go, I will send him to you.
7 Moona de, ci sama wàll, dëgg laa leen di wax. Li gën ci yéen mooy ma dem, ndaxte su dul loolu, Dimbalikat bi du ñëw ci yéen; waaye su ma demee, dinaa leen ko yónnee.
8 When he has come, he will convict the world about sin, about righteousness, and about judgment;
8 Te bu dikkee, dina yey niti àddina ci lu jëm ci seen bàkkaar, ci lu jëm ci sama njubte ak ci lu jëm ci àtte ba.
9 about sin, because they don’t believe in me;
9 Ci mbiri seen bàkkaar, dina leen yey ci li ñu ma gëmul.
10 about righteousness, because I am going to my Father, and you won’t see me any more;
10 Ci mbiri sama njubte, dina leen yey ndaxte maa ngi dem ci Baay bi te dungeen ma gisati.
11 about judgment, because the prince of this world has been judged.
11 Ci mbiri àtte ba, dina leen yey ndaxte àtte nañu malaaka mu bon mi jiite àddina si, ba daan ko.
12 “I have yet many things to tell you, but you can’t bear them now.
12 «Li ma leen war a wax bare na, waaye dungeen ko man a dékku.
13 However when he, the Spirit of truth, has come, he will guide you into all truth, for he will not speak from himself; but whatever he hears, he will speak. He will declare to you things that are coming.
13 Bu Xelum Yàlla mi yor dëgg gi dikkee nag, dina leen gindi ci lépp li jëm ci yoonu dëgg, ndaxte du wax ci coobarey boppam, waaye lu ko Baay bi wax, mu jottali leen ko. Dina leen yégal mbir yu ñëwagul.
14 He will glorify me, for he will take from what is mine, and will declare it to you.
14 Dina ma màggal, ndaxte lu mu leen wax, ci man la ko jële.
15 All things whatever the Father has are mine; therefore I said that he takes of mine, and will declare it to you.
15 Lépp lu Baay bi am, maa ko moom. Looloo tax ma ne leen, lu mu leen jottali, ci man la ko jële.
16 A little while, and you will not see me. Again a little while, and you will see me.”
16 «Ci kanam tuuti dungeen ma gisati. Bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma.»
17Some of his disciples therefore said to one another, “What is this that he says to us, ‘A little while, and you won’t see me, and again a little while, and you will see me;’ and, ‘Because I go to the Father?’
17 Loolu Yeesu wax, tax na ba am ca taalibe ya, ñu waxante ne: «Lu muy wax nii: “Ci kanam tuuti dungeen ma gisati; bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma,” ak naan: “Ndaxte maa ngi dem ca Baay ba”?»
18They said therefore, “What is this that he says, ‘A little while?’ We don’t know what he is saying.”
18 Ñu ne: « “Teg cab diir,” lu muy tekki? Xamunu li muy bëgg a wax.»
19Therefore Jesus perceived that they wanted to ask him, and he said to them, “Do you inquire among yourselves concerning this, that I said, ‘A little while, and you won’t see me, and again a little while, and you will see me?’
19 Yeesu gis ne, am na lu ñu ko bëgg a laaj, mu ne leen: «Dama ne: “Ca kanam tuuti, dungeen ma gis, te bu ñu ca tegee ab diir, ngeen gisaat ma.” Ndax loolu ngeen di laajante ci seen biir?
20 Most certainly I tell you, that you will weep and lament, but the world will rejoice. You will be sorrowful, but your sorrow will be turned into joy.
20 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen jooy xàcc, waaye àddina dina bég; dingeen jàq, waaye seen njàqare dina soppaliku bànneex.
21 A woman, when she gives birth, has sorrow, because her time has come. But when she has delivered the child, she doesn’t remember the anguish any more, for the joy that a human being is born into the world.
21 Jigéen ju nekk ci mat, dafay jàq, ndaxte waxtu wi mu war a jur jot na. Waaye bu doom ji juddoo, dina fàtte coonoom ndaxte day bég ci li doom ji gane àddina.
22 Therefore you now have sorrow, but I will see you again, and your heart will rejoice, and no one will take your joy away from you.
22 Noonu nag ngeen di jàqe, yéen itam. Waaye dinaa leen gisaat, seeni xol sedd, te seen mbég moomu, kenn du ko man a dindi.
23 “In that day you will ask me no questions. Most certainly I tell you, whatever you may ask of the Father in my name, he will give it to you.
23 Bés boobu dootuleen ma laaj dara. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Baay bi dina leen may lu ngeen ko ñaan ci sama tur.
24 Until now, you have asked nothing in my name. Ask, and you will receive, that your joy may be made full.
24 Ba léegi ñaanaguleen dara ci sama tur. Ñaanleen, mu nangu. Bu ko defee seen mbég mat sëkk.
25 I have spoken these things to you in figures of speech. But the time is coming when I will no more speak to you in figures of speech, but will tell you plainly about the Father.
25 «Loolu lépp, dama leen koo wax ci ay misaal. Jamono dina ñëw, ju ma dootul wax ak yéen ci ay misaal, waaye ju ma leen dee wax lu leer ci Baay bi.
26 In that day you will ask in my name; and I don’t say to you, that I will pray to the Father for you,
26 Bu keroogee dingeen ñaan ci sama tur. Neewuma dinaa leen ñaanal Baay bi,
27 for the Father himself loves you, because you have loved me, and have believed that I came forth from God.
27 ndaxte Baay bi ci boppam bëgg na leen. Bëgg na leen ndaxte bëgg ngeen ma, te gëm ngeen ne, ci Yàlla laa jóge.
28 I came out from the Father, and have come into the world. Again, I leave the world, and go to the Father.”
28 Jóge naa ca Baay bi, ñëw àddina. Léegi maa ngi génn àddina, fekki Baay bi.»
29His disciples said to him, “Behold, now you speak plainly, and speak no figures of speech.
29 Taalibe yi ne ko: «Léegi yaa ngi wax lu leer te misaaloo!
30Now we know that you know all things, and don’t need for anyone to question you. By this we believe that you came forth from God.”
30 Léegi gis nanu ne, xam nga lépp, te soxlawul kenn di la laaj dara. Looloo tax nu xam ne, yaa ngi jóge ci Yàlla.»
31Jesus answered them, “Do you now believe?
31 Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen léegi?
32 Behold, the time is coming, yes, and has now come, that you will be scattered, everyone to his own place, and you will leave me alone. Yet I am not alone, because the Father is with me.
32 Waxtu waa ngi ñëw te agsi na ba noppi, dingeen tasaaroo, ku nekk ñibbi, ma des man rekk.
33 I have told you these things, that in me you may have peace. In the world you have oppression; but cheer up! I have overcome the world.”
33 Waaye nag déedéet, wéetuma, ndaxte Baay baa ngi may wéttali. Dama leen wax loolu, ngir ngeen am jàmm ci man. Dingeen am nattu ci àddina, waaye takkleen fit yi; noot naa àddina.»