World English Bible

Wolof: New Testament

Luke

12

1Meanwhile, when a multitude of many thousands had gathered together, so much so that they trampled on each other, he began to tell his disciples first of all, “Beware of the yeast of the Pharisees, which is hypocrisy.
1 Gannaaw loolu, naka la mbooloo ma dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, di tancante, Yeesu tàmbalee wax jëmale ca taalibeem ya ne leen: «Moytuleen lawiiru Farisen ya, li di naaféq.
2 But there is nothing covered up, that will not be revealed, nor hidden, that will not be known.
2 Amul dara lu nëbbu lu ñu warul a biral, mbaa lu kumpa lu ñu warul a siiwal.
3 Therefore whatever you have said in the darkness will be heard in the light. What you have spoken in the ear in the inner rooms will be proclaimed on the housetops.
3 Looloo tax lu ngeen wax ci biir lëndëm, dees na ko dégg ci leer. Lu ngeen déey nit ci biir néeg, dees na ko yégle ci kaw taax yi.
4 “I tell you, my friends, don’t be afraid of those who kill the body, and after that have no more that they can do.
4 «Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu man a rey yaram, ba noppi dootuñu man a def dara.
5 But I will warn you whom you should fear. Fear him, who after he has killed, has power to cast into Gehenna. Yes, I tell you, fear him.
5 Dinaa leen wax nag ki ngeen war a ragal: ragal-leen Ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca safara. Waaw maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku.
6 “Aren’t five sparrows sold for two assaria coins ? Not one of them is forgotten by God.
6 Juróomi picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom.
7 But the very hairs of your head are all numbered. Therefore don’t be afraid. You are of more value than many sparrows.
7 Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu.
8 “I tell you, everyone who confesses me before men, him will the Son of Man also confess before the angels of God;
8 «Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanamu nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanamu malaakay Yàlla yi.
9 but he who denies me in the presence of men will be denied in the presence of the angels of God.
9 Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, dinañu la gàntu ci kanamu malaakay Yàlla yi.
10 Everyone who speaks a word against the Son of Man will be forgiven, but those who blaspheme against the Holy Spirit will not be forgiven.
10 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal.
11 When they bring you before the synagogues, the rulers, and the authorities, don’t be anxious how or what you will answer, or what you will say;
11 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanamu kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen war a tontu ak nan ngeen war a tontoo, walla lu ngeen war a wax,
12 for the Holy Spirit will teach you in that same hour what you must say.”
12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen war a wax.»
13One of the multitude said to him, “Teacher, tell my brother to divide the inheritance with me.”
13 Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.»
14But he said to him, “Man, who made me a judge or an arbitrator over you?”
14 Yeesu tontu ko ne: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?»
15He said to them, “Beware! Keep yourselves from covetousness, for a man’s life doesn’t consist of the abundance of the things which he possesses.”
15 Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree-bare.»
16He spoke a parable to them, saying, “The ground of a certain rich man brought forth abundantly.
16 Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool,
17 He reasoned within himself, saying, ‘What will I do, because I don’t have room to store my crops?’
17 muy werante ci xelam naan: “Nu ma war a def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.”
18 He said, ‘This is what I will do. I will pull down my barns, and build bigger ones, and there I will store all my grain and my goods.
18 Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gën a réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am jépp.
19 I will tell my soul, “Soul, you have many goods laid up for many years. Take your ease, eat, drink, be merry.”’
19 Te dinaa kañ sama bopp ne: ’Yaw mii, am nga alal ju bare ju man a dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ”
20 “But God said to him, ‘You foolish one, tonight your soul is required of you. The things which you have prepared—whose will they be?’
20 Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?”
21 So is he who lays up treasure for himself, and is not rich toward God.”
21 «Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.»
22He said to his disciples, “Therefore I tell you, don’t be anxious for your life, what you will eat, nor yet for your body, what you will wear.
22 Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen war a sol,
23 Life is more than food, and the body is more than clothing.
23 ndaxte bakkan moo gën lekk, te yaram a gën koddaay.
24 Consider the ravens: they don’t sow, they don’t reap, they have no warehouse or barn, and God feeds them. How much more valuable are you than birds!
24 Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi!
25 Which of you by being anxious can add a cubit to his height?
25 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem, moo man a yokk ab waxtu ci àppam?
26 If then you aren’t able to do even the least things, why are you anxious about the rest?
26 Su fekkee lu tuuti loolu rekk mënuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?
27 Consider the lilies, how they grow. They don’t toil, neither do they spin; yet I tell you, even Solomon in all his glory was not arrayed like one of these.
27 «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam, soluwul woon ni benn ci ñoom.
28 But if this is how God clothes the grass in the field, which today exists, and tomorrow is cast into the oven, how much more will he clothe you, O you of little faith?
28 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxu tool yi, miy sax tey te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd?
29 Don’t seek what you will eat or what you will drink; neither be anxious.
29 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle.
30 For the nations of the world seek after all of these things, but your Father knows that you need these things.
30 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne, soxla ngeen ko.
31 But seek God’s Kingdom, and all these things will be added to you.
31 Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
32 Don’t be afraid, little flock, for it is your Father’s good pleasure to give you the Kingdom.
32 «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram.
33 Sell that which you have, and give gifts to the needy. Make for yourselves purses which don’t grow old, a treasure in the heavens that doesn’t fail, where no thief approaches, neither moth destroys.
33 Jaayleen seen alal, saraxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq.
34 For where your treasure is, there will your heart be also.
34 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
35 “Let your waist be dressed and your lamps burning.
35 «Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk.
36 Be like men watching for their lord, when he returns from the marriage feast; that, when he comes and knocks, they may immediately open to him.
36 Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa.
37 Blessed are those servants, whom the lord will find watching when he comes. Most certainly I tell you, that he will dress himself, and make them recline, and will come and serve them.
37 Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gën a yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi.
38 They will be blessed if he comes in the second or third watch, and finds them so.
38 Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gën a yeyoo ngërëm.
39 But know this, that if the master of the house had known in what hour the thief was coming, he would have watched, and not allowed his house to be broken into.
39 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram.
40 Therefore be ready also, for the Son of Man is coming in an hour that you don’t expect him.”
40 Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
41Peter said to him, “Lord, are you telling this parable to us, or to everybody?”
41 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?»
42The Lord said, “Who then is the faithful and wise steward, whom his lord will set over his household, to give them their portion of food at the right times?
42 Boroom bi tontu ko ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji?
43 Blessed is that servant whom his lord will find doing so when he comes.
43 Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
44 Truly I tell you, that he will set him over all that he has.
44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
45 But if that servant says in his heart, ‘My lord delays his coming,’ and begins to beat the menservants and the maidservants, and to eat and drink, and to be drunken,
45 Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi,
46 then the lord of that servant will come in a day when he isn’t expecting him, and in an hour that he doesn’t know, and will cut him in two, and place his portion with the unfaithful.
46 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla.
47 That servant, who knew his lord’s will, and didn’t prepare, nor do what he wanted, will be beaten with many stripes,
47 «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti.
48 but he who didn’t know, and did things worthy of stripes, will be beaten with few stripes. To whomever much is given, of him will much be required; and to whom much was entrusted, of him more will be asked.
48 Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyiku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp.
49 “I came to throw fire on the earth. I wish it were already kindled.
49 «Damaa ñëw ngir indi safara si ci àddina, te bëgg naa xaat taal bi tàkk.
50 But I have a baptism to be baptized with, and how distressed I am until it is accomplished!
50 Fàww ñu sóob ma ci metit, te ba looluy mat, duma noppalu.
51 Do you think that I have come to give peace in the earth? I tell you, no, but rather division.
51 Ndax dangeen a xalaat ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina? Déedéet. Maa ngi leen koy wax, damaa ñëw ngir indi féewaloo.
52 For from now on, there will be five in one house divided, three against two, and two against three.
52 Gannaawsi tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo. Ñett dinañu féewaloo ak ñaar ñi ci des, ñaar ñi féewaloo ak ñett ñooñu.
53 They will be divided, father against son, and son against father; mother against daughter, and daughter against her mother; mother-in-law against her daughter-in-law, and daughter-in-law against her mother-in-law.”
53 Baay bi dina féewaloo ak doom ji, doom ji ak baayam. Ndey dina féewaloo ak doomam ju jigéen; doom ju jigéen ji ak ndeyam. Goro dina féewaloo ak jabaru doomam; jabaru nit ak goroom.»
54 He said to the multitudes also, “When you see a cloud rising from the west, immediately you say, ‘A shower is coming,’ and so it happens.
54 Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: “Dina taw,” te mooy am.
55 When a south wind blows, you say, ‘There will be a scorching heat,’ and it happens.
55 Te bu ngeen yégee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: “Dina tàng tàngaay wu metti,” te mooy am.
56 You hypocrites! You know how to interpret the appearance of the earth and the sky, but how is it that you don’t interpret this time?
56 Naaféq yi ngeen doon! Man ngeen a ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax mënuleen a ràññee li jamonoy léegi ji di tekki?
57 Why don’t you judge for yourselves what is right?
57 «Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub?
58 For when you are going with your adversary before the magistrate, try diligently on the way to be released from him, lest perhaps he drag you to the judge, and the judge deliver you to the officer, and the officer throw you into prison.
58 Bu la nit jiiñee dara, ba ngeen ànd di dem ca àttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la yóbbu ci yoon, yoon jébbal la ca loxoy alkaati ba, mu tëj la.
59 I tell you, you will by no means get out of there, until you have paid the very last penny.
59 Maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.»