World English Bible

Wolof: New Testament

Luke

14

1It happened, when he went into the house of one of the rulers of the Pharisees on a Sabbath to eat bread, that they were watching him.
1 Benn bésu noflaay Yeesu dem ci këru benn kilifag Farisen yi, ngir lekke fa. Nit ñaa ngi ko doon xool bu baax.
2Behold, a certain man who had dropsy was in front of him.
2 Faf am ca kanamam nit ku feebaroon, ay tànkam newi.
3Jesus, answering, spoke to the lawyers and Pharisees, saying, “Is it lawful to heal on the Sabbath?”
3 Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésu noflaay bi?»
4But they were silent. He took him, and healed him, and let him go.
4 Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi.
5He answered them, “Which of you, if your son or an ox fell into a well, wouldn’t immediately pull him out on a Sabbath day?”
5 Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?»
6They couldn’t answer him regarding these things.
6 Amuñu woon dara lu ñu ciy teg.
7He spoke a parable to those who were invited, when he noticed how they chose the best seats, and said to them,
7 Yeesu gis ni gan yi doon tànne toogu yu yiw yi, mu daldi leen wax léeb wii:
8 “When you are invited by anyone to a marriage feast, don’t sit in the best seat, since perhaps someone more honorable than you might be invited by him,
8 «Bu ñu la wooyee ci xewu céet, bul jël toogu bu yiw. Man na am woo nañu it nit ku la ëpp daraja.
9 and he who invited both of you would come and tell you, ‘Make room for this person.’ Then you would begin, with shame, to take the lowest place.
9 Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rus a dem ca toogu bu gannaawe ba.
10 But when you are invited, go and sit in the lowest place, so that when he who invited you comes, he may tell you, ‘Friend, move up higher.’ Then you will be honored in the presence of all who sit at the table with you.
10 Waaye bu ñu la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: “Sama xarit, àggal ca kaw.” Loolu dina la sagal ci ñi nga toogandool ci lekkukaay bi.
11 For everyone who exalts himself will be humbled, and whoever humbles himself will be exalted.”
11 Ndaxte képp kuy yékkatiku, dees na la suufeel, te kuy suufeelu, dinañu la yékkati.»
12He also said to the one who had invited him, “When you make a dinner or a supper, don’t call your friends, nor your brothers, nor your kinsmen, nor rich neighbors, or perhaps they might also return the favor, and pay you back.
12 Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: «Boo dee woote añ walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say dëkkandoo yu am alal. Lu ko moy ñooñu itam dinañu la woo, fey la bor bi.
13 But when you make a feast, ask the poor, the maimed, the lame, or the blind;
13 Waaye boo dee woote lekk, wool néew doole yi, làggi yi, lafañ yi ak gumba yi.
14 and you will be blessed, because they don’t have the resources to repay you. For you will be repaid in the resurrection of the righteous.”
14 Soo ko defee, dinga barkeel, ndaxte duñu la ko man a fey, waaye dinga jot sag pey, bés bi ñi jub di dekki.»
15When one of those who sat at the table with him heard these things, he said to him, “Blessed is he who will feast in the Kingdom of God!”
15 Bi mu déggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: «Kiy lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram, barkeel nga!»
16But he said to him, “A certain man made a great supper, and he invited many people.
16 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku togglu ay ñam, woo ay nit ñu bare.
17 He sent out his servant at supper time to tell those who were invited, ‘Come, for everything is ready now.’
17 Bi waxtuw lekk jotee mu yónni surga ca ña muy ganale, fàttali leen: “Man ngeen a ñëw, ndaxte lépp sotti na léegi.”
18 They all as one began to make excuses. “The first said to him, ‘I have bought a field, and I must go and see it. Please have me excused.’
18 «Waaye ñu tàmbali di jéggalu ci ngan gi ñoom ñépp. Ku jëkk ka ne ko: “Damaa jënd tool léegi, te fàww ma dem seeti ko. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”
19 “Another said, ‘I have bought five yoke of oxen, and I must go try them out. Please have me excused.’
19 Keneen ne: “Damaa jënd léegi fukki yëkk, te damay dem nii, jéem leen a beyloo ba xam. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”
20 “Another said, ‘I have married a wife, and therefore I can’t come.’
20 Keneen ne ko: “Damay sog a takk jabar, looloo tax duma man a ñëw.”
21 “That servant came, and told his lord these things. Then the master of the house, being angry, said to his servant, ‘Go out quickly into the streets and lanes of the city, and bring in the poor, maimed, blind, and lame.’
21 «Surga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu lépp. Noonu boroom kër ga mer, daldi ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc ya ak ca mbedd ya ca dëkk ba, te indil ma fii néew doole yi, ñu làggi ñi, gumba yi ak lafañ yi.”
22 “The servant said, ‘Lord, it is done as you commanded, and there is still room.’
22 «Surga ba ñëwaat ne ko: “Sang bi, def naa li nga ma sant, waaye bérab bi feesul.”
23 “The lord said to the servant, ‘Go out into the highways and hedges, and compel them to come in, that my house may be filled.
23 Noonu njaatige ba ne ko: “Génnal dëkk bi te dem ca yoon ya ak ca tool ya, xiir nit ñi, ñu duggsi, ngir sama kër fees.
24 For I tell you that none of those men who were invited will taste of my supper.’”
24 Maa ngi leen koy wax, ci ñi ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci ñam.”»
25Now great multitudes were going with him. He turned and said to them,
25 Am mbooloo yu réy yu toppoon ci Yeesu, ba muy dem ca yoon wa. Mu geestu ne leen:
26 “If anyone comes to me, and doesn’t disregard his own father, mother, wife, children, brothers, and sisters, yes, and his own life also, he can’t be my disciple.
26 «Képp ku ñëw ci man te gënalu ma ko baayam, yaayam, jabaram, ay doomam, ay magam ak ay rakkam, walla sax bakkanam, du man a nekk sama taalibe.
27 Whoever doesn’t bear his own cross, and come after me, can’t be my disciple.
27 Képp koo xam ne nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, doo man a nekk sama taalibe.
28 For which of you, desiring to build a tower, doesn’t first sit down and count the cost, to see if he has enough to complete it?
28 Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkk a toog, xalaat ñaata la ko war a dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu man a àggale liggéey bi?
29 Or perhaps, when he has laid a foundation, and is not able to finish, everyone who sees begins to mock him,
29 Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te mënu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko:
30 saying, ‘This man began to build, and wasn’t able to finish.’
30 “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye mënu koo àggale.”
31 Or what king, as he goes to encounter another king in war, will not sit down first and consider whether he is able with ten thousand to meet him who comes against him with twenty thousand?
31 Walla boog ban buur mooy dugg ci xare ak beneen buur te jëkkul a toog, seet ba xam moom ak fukki junniy xarekat man na xeex ak kiy ñëw ak ñaar-fukki junniy xarekat?
32 Or else, while the other is yet a great way off, he sends an envoy, and asks for conditions of peace.
32 Su ko mënul, dafay yónni ndaw ca beneen buur ba, fi ak ma ngay sore, ngir ñu juboo.
33 So therefore whoever of you who doesn’t renounce all that he has, he can’t be my disciple.
33 Naka noonu itam ku nekk ci yéen, bu dëdduwul li mu am lépp, du man a nekk sama taalibe.
34 Salt is good, but if the salt becomes flat and tasteless, with what do you season it?
34 «Xam ngeen nag ne, xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam?
35 It is fit neither for the soil nor for the manure pile. It is thrown out. He who has ears to hear, let him hear.”
35 Du jariñ suuf, te du nekk tos. Dañu koy sànni ca biti. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»