World English Bible

Wolof: New Testament

Luke

18

1He also spoke a parable to them that they must always pray, and not give up,
1 Noonu Yeesu wax leen itam léeb wii ngir xamal leen ne, war nañoo sax ci ñaan te bañ a xàddi.
2saying, “There was a judge in a certain city who didn’t fear God, and didn’t respect man.
2 Nee na: «Dafa amoon cib dëkk, benn àttekat bu ragalul Yàlla te faalewul mbindeef.
3 A widow was in that city, and she often came to him, saying, ‘Defend me from my adversary!’
3 Amoon na itam ca dëkk ba jigéen ju jëkkëram faatu ju daan faral di ñëw ci moom, naan ko: “Àtte ma ak sama noon!”
4 He wouldn’t for a while, but afterward he said to himself, ‘Though I neither fear God, nor respect man,
4 Àttekat ba bañ lu yàgg, waaye am bés mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla te faalewuma mbindeef,
5 yet because this widow bothers me, I will defend her, or else she will wear me out by her continual coming.’”
5 waaye jigéen jii lakkal na ma; kon dinaa ko àtte, ngir mu bañatee ñëw sonal ma. Dina rey ak ay wax.”»
6The Lord said, “Listen to what the unrighteous judge says.
6 Boroom bi tegaat ca ne: «Dégluleen bu baax li àttekat bu bon boobu wax;
7 Won’t God avenge his chosen ones, who are crying out to him day and night, and yet he exercises patience with them?
7 ndax Yàlla du àtte jub mbooloom mi mu tànn te ñu koy ñaan wall guddi ak bëccëg? Ndax dina leen xaarloo?
8 I tell you that he will avenge them quickly. Nevertheless, when the Son of Man comes, will he find faith on the earth?”
8 Maa ngi leen koy wax, dina leen àtte jub ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki ñëwee, ndax dina fekk ngëm ci àddina?»
9He spoke also this parable to certain people who were convinced of their own righteousness, and who despised all others.
9 Yeesu waxaat léeb wii nit, ñi foog ne jub nañu tey xeeb ñi ci des.
10 “Two men went up into the temple to pray; one was a Pharisee, and the other was a tax collector.
10 Mu ne: «Dafa amoon ñaari nit ñu dem ca kër Yàlla ga, di ñaan. Kenn ki ab Farisen la, ki ci des juutikat.
11 The Pharisee stood and prayed to himself like this: ‘God, I thank you, that I am not like the rest of men, extortioners, unrighteous, adulterers, or even like this tax collector.
11 Farisen baa nga taxaw di ñaan ci xelam naan: “Yaw Yàlla, maa ngi lay sant ci li ma melul ni ñeneen ñiy sàcc, di def lu jubadi te di njaaloo, rawatina juutikat bii.
12 I fast twice a week. I give tithes of all that I get.’
12 Ayu-bés gu nekk damay woor ñaari yoon, di joxe asaka ci lépp lu ma wut.”
13 But the tax collector, standing far away, wouldn’t even lift up his eyes to heaven, but beat his breast, saying, ‘God, be merciful to me, a sinner!’
13 «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te bëggul a siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay fëgg dënnam te naan: “Yaw Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat.”»
14 I tell you, this man went down to his house justified rather than the other; for everyone who exalts himself will be humbled, but he who humbles himself will be exalted.”
14 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen koy wax, nit kooku, ba muy ñibbi këram, moom la Yàlla àtte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, ñu yékkati la.»
15They were also bringing their babies to him, that he might touch them. But when the disciples saw it, they rebuked them.
15 Amoon na ay nit, ñuy indil Yeesu ay liir, ngir mu teg leen ay loxoom. Bi taalibe ya gisee loolu, ñu gëdd leen.
16Jesus summoned them, saying, “Allow the little children to come to me, and don’t hinder them, for the Kingdom of God belongs to such as these.
16 Waaye Yeesu woo leen ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw ci man, te buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla.
17 Most certainly, I tell you, whoever doesn’t receive the Kingdom of God like a little child, he will in no way enter into it.”
17 Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci man a dugg.»
18A certain ruler asked him, saying, “Good Teacher, what shall I do to inherit eternal life?”
18 Benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma war a def, ba am wàll ci dund gu dul jeex?»
19Jesus asked him, “Why do you call me good? No one is good, except one—God.
19 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax? Yàlla rekk a baax.
20 You know the commandments: ‘Don’t commit adultery,’ ‘Don’t murder,’ ‘Don’t steal,’ ‘Don’t give false testimony,’ ‘Honor your father and your mother.’”
20 Xam nga ndigal yi: “Bul njaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
21He said, “I have observed all these things from my youth up.”
21 Njiit la ne ko: «Loolu lépp sàmm naa ko li dale ci sama ndaw ba tey.»
22When Jesus heard these things, he said to him, “You still lack one thing. Sell all that you have, and distribute it to the poor. You will have treasure in heaven. Come, follow me.”
22 Bi Yeesu déggee loolu, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am lépp, séddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.»
23But when he heard these things, he became very sad, for he was very rich.
23 Bi nit ka déggee loolu, mu am tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
24Jesus, seeing that he became very sad, said, “How hard it is for those who have riches to enter into the Kingdom of God!
24 Yeesu xool ko, daldi ne: «Boroom alal, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!
25 For it is easier for a camel to enter in through a needle’s eye, than for a rich man to enter into the Kingdom of God.”
25 Giléem jaar ci bën-bënu pusa moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.»
26Those who heard it said, “Then who can be saved?”
26 Ñi doon déglu daldi ne: «Kon nag ku man a mucc?»
27But he said, “The things which are impossible with men are possible with God.”
27 Yeesu tontu ne: «Li të nit ñi, tëwul Yàlla.»
28Peter said, “Look, we have left everything, and followed you.”
28 Noonu Piyeer ne: «Nun de, dëddu nanu li nu am lépp, topp la.»
29He said to them, “Most certainly I tell you, there is no one who has left house, or wife, or brothers, or parents, or children, for the Kingdom of God’s sake,
29 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër walla jabar walla ay doomi ndey walla ay waajur walla ay doom ngir nguuru Yàlla,
30 who will not receive many times more in this time, and in the world to come, eternal life.”
30 dinga am tey jii ay yooni yoon, ak dund gu dul jeex ëllëg.»
31He took the twelve aside, and said to them, “Behold, we are going up to Jerusalem, and all the things that are written through the prophets concerning the Son of Man will be completed.
31 Yeesu wéetoo ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Nu ngi dem Yerusalem, te li yonent yi bindoon lépp ci mbirum Doomu nit ki dina mat.
32 For he will be delivered up to the Gentiles, will be mocked, treated shamefully, and spit on.
32 Dinañu ko jébbal ñi dul Yawut, ñu ñaawal ko, saaga ko, tifli ci kawam.
33 They will scourge and kill him. On the third day, he will rise again.”
33 Gannaaw bu ñu ko dóoree ay yar ba noppi, dinañu ko rey, waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
34They understood none of these things. This saying was hidden from them, and they didn’t understand the things that were said.
34 Waaye taalibe ya dégguñu li mu leen doon wax; kàddu yooyu ump na leen, te xamuñu li waxi Yeesu yooyu tekki.
35It happened, as he came near Jericho, a certain blind man sat by the road, begging.
35 Bi Yeesu di agsi dëkku Yeriko, am gumba gu toogoon ca wetu yoon wa, di yelwaan.
36Hearing a multitude going by, he asked what this meant.
36 Naka la gumba ga dégg mbooloo di jàll, mu laaj lan moo xew.
37They told him that Jesus of Nazareth was passing by.
37 Ñu wax ko ne: «Yeesum Nasaret moo fay jaar.»
38He cried out, “Jesus, you son of David, have mercy on me!”
38 Noonu mu yuuxu ne: «Yeesu, Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
39Those who led the way rebuked him, that he should be quiet; but he cried out all the more, “You son of David, have mercy on me!”
39 Ñi jiitu woon gëdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy gën a yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
40Standing still, Jesus commanded him to be brought to him. When he had come near, he asked him,
40 Noonu Yeesu taxaw, santaane ñu indil ko ko. Bi mu jegesee, Yeesu laaj ko ne:
41 “What do you want me to do?” He said, “Lord, that I may see again.”
41 «Loo bëggoon ma defal la ko?» Mu ne ko: «Sang bi, damaa bëgg a gis.»
42Jesus said to him, “Receive your sight. Your faith has healed you.”
42 Noonu Yeesu ne ko: «Na say bët gis! Sa ngëm faj na la.»
43Immediately he received his sight, and followed him, glorifying God. All the people, when they saw it, praised God.
43 Ca saa sa mu daldi gis. Noonu mu topp ci Yeesu, di màggal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.