Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

1 Corinthians

3

1 Man nag bokk yi, mënuma woon a wax ak yéen ni ay nit ñuy déggal Xelum Yàlla, waaye waroon naa wax ak yéen ni ñuy topp seen nafsu, mel ni ay liir ci seen dund ci Kirist.
1不可分派结党
2 Nàmpaloon naa leen, waaye joxuma leen dugub, ndaxte àttanuleen ko woon, te ba léegi sax àttanuleen ko
2我喂给你们吃的是奶,不是饭,因为那时你们不能吃,就是现在还是不能,
3 ci li ngeen di topp seen nafsu. Bu ñeetaan ak xuloo amee ci seen biir, xanaa du loolu mooy wone ne, dangeen a topp seen nafsu, di doxale ni niti àddina?
3因为你们仍然是属肉体的。在你们当中既然有嫉妒纷争,你们不还是属肉体,照着世人的方式而行吗?
4 Bu kenn yéglee ne: «Man ci Pool laa bokk,» keneen ne: «Man ci Apolos,» ndax jëfewuleen ni niti àddina rekk?
4有人说“我是保罗派的”,又有人说“我是亚波罗派的”,你们不是和世人一样吗?
5 Kuy Apolos? ak kuy Pool? Nun ay surga rekk lanu, yu ngeen jaare, ba gëm. Te Boroom bi moo sas ku nekk liggéeyam.
5亚波罗算什么?保罗算什么?我们不过是 神的仆人,你们借着我们信了主;按着主所赐给各人的,
6 Maa jëmbët, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil.
6我栽种了,亚波罗浇灌了,唯有 神使它生长。
7 Ki jëmbët nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, waaye Yàlla miy jebbil rekk moo am solo.
7所以,栽种的算不得什么,浇灌的也算不得什么,只在乎那使它生长的 神。
8 Ki jëmbët ak ki suuxat benn lañu. Teewul nag ku nekk dina jot yool bu tollook liggéeyam.
8栽种的和浇灌的都是一样,只是各人要照着自己的劳苦得着自己的报酬。
9 Nu ngi liggéeyandoo ci liggéeyu Yàlla; yéenay toolu Yàlla, yéenay taaxum Yàlla.
9我们是 神的同工,你们是 神的田地, 神的房屋。
10 Man nag teg naa fondamaa bi, ni tabaxkat bu man liggéeyam, dëppoo ak sas wi ma Yàlla jagleel ci kaw yiwam. Te keneen a ngi tabax ci kaw; waaye na ku nekk teeylu ci ni muy tabaxe.
10我照着 神赐给我的恩典,就像一个聪明的工程师,立好了根基,别人在上面建造。各人要注意怎样在上面建造,
11 Ci li jëm ci fondamaa bi, kenn mënu fee tëral beneen bu dul bi fi xas a taxaw, muy Yeesu Kirist.
11因为除了那已经立好的根基以外,没有人能立别的根基。那根基就是耶稣基督。
12 Ku tabax ci kaw fondamaa bi, wurus, xaalis, per, dénk, gittax walla boob,
12如果有人用金、银、宝石、草、木、禾秸,在这根基上建造,
13 sa liggéey dina fés, ndaxte bés baa koy xamle. Bés boobu dina fenk ni safara, te safara si dina nattu liggéeyu ku nekk.
13各人的工程将来必要显露,因为那日子必把它显明出来。有火要把它显露出来,那火要考验各人的工程是怎样的。
14 Ku sa liggéey dëgër, dinga jot yool.
14如果有人在这根基上建造的工程存得住,他就要得到赏赐;
15 Waaye ku sa liggéey lakk, dinga ñàkk. Yaw ci sa bopp dinga mucc, waaye mel ni ku rëcc ci safara si.
15如果有人的工程被烧毁,他就要受亏损;自己却要得救,只是要像从火里经过一样。
16 Xanaa xamuleen ne, yéenay kër Yàlla, te Xelum Yàlla dëkk na ci yéen?
16难道不知道你们是 神的殿, 神的灵住在你们里面吗?
17 Ku yàq kër Yàlla gi, Yàlla dina la yàq, ndaxte kër Yàlla gi dafa sell, te yéenay kër googu.
17如果有人毁坏 神的殿, 神必要毁坏这人,因为 神的殿是圣洁的,这殿就是你们。
18 Kon bu kenn nax boppam: su kenn ci yéen tegee boppam boroom xam-xam ci gis-gisu àddina sii, kooku na doon dof, ngir am xam-xam bu wóor.
18谁也不要自欺。如果你们当中有人以为自己在这世代里是有智慧的,他就应该变为愚笨,好让他有智慧。
19 Ndaxte xam-xamu àddina si, ndof la fa Yàlla. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla jàpp na ñu muus ñi, ba seen fiir këppu ci seen kaw.»
19因为这世界的智慧,在 神看来是愚笨的,如经上所记:“他使有智慧的人中了自己的诡计。”
20 Te it: «Boroom bi xam na xalaati boroom xam-xam yi; xam ne, duñu mujj fenn.»
20又说:“主知道智慧人的意念是虚妄的。”
21 Kon nag bu kenn tiitaru ndax nit ñi, ndaxte yéena moom lépp,
21所以,谁都不可拿人来夸耀,因为一切都是你们的。
22 muy Pool, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di lu am, di luy ñëw; lépp, yéena ko moom.
22无论是保罗,是亚波罗,是矶法,是世界,是生,是死,是现在的事,是将来的事,都是你们的。
23 Te yéen, Kirist a leen moom, te Kirist, Yàllaa ko moom.
23你们是属基督的,基督是属 神的。