Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

1 Corinthians

5

1 Dégg nanu sax ñu naan, am na kuy moy Yàlla ci seen biir, moy gu ni tollu, duñu ko gis sax ci ñi xamul Yàlla. Dem na, ba am ci yéen kuy séy ak jabaru baayam.
1行淫乱的人应当赶出教会听说你们中间竟然有淫乱的事,这样的淫乱在教外人中间都没有,就是有人和他的继母同居。
2 Moona yéen de, yéena ngi tiitaru. Waaye dangeen a waroon a am naqar, ba dàq kiy def loolu ci seen biir!
2你们还是自高自大!难道你们不该觉得痛心,把作这件事的人从你们中间赶出去吗?
3 Man nag, jëmm ji sore na leen, waaye xel mi mu ngi ci yéen, te àtte naa xaat kiy def loolu, ni su ma teewoon ci seen biir. Dogal naa,
3我身体虽然不在你们那里,心灵却与你们在一起,好像我亲身在那里审判了作这件事的人,
4 ngeen daje ci turu Boroom bi Yeesu, te sama xel teewe ko, ànd ak dooley Boroom bi Yeesu,
4就是当你们奉我们主耶稣的名聚集在一起,我的灵在那里,我们主耶稣的权能也同在的时候,
5 nu jébbal nit kooku Seytaane, yaramam yàqu, ngir ruuwam mucc keroog bésu Boroom bi.
5要把这样的人交给撒但,败坏他的身体,使他的灵魂在主的日子可以得救。
6 Seen tiitar bi jekkul dara. Xanaa xamuleen ne, tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki?
6你们这样自夸是不好的。你们不知道一点面酵能使全团面发起来吗?
7 Ni ma leen ko man a misaale, jëleleen fi bépp lawiir bu yàgg, ngir ngeen sell ni tooyal bu bees bu amul lawiir, ndax nekk ngeen ko ba noppi. Ndaxte Kirist deeyal na nu ca bant ba, mel ni mbote mu ñuy rendi, jébbal ko Yàlla ca màggalu bésu Jéggi ba.
7你们既是无酵的面,就应当把旧酵除净,好让你们成为新的面团;因为我们逾越节的羊羔基督已经被杀献祭了。
8 Kon nanu màggal sunu Màggal, waxuma ak lawiir bu màggat biy misaal kiñaan ak lu bon, waaye ak mburu mu amul lawiir, maanaam ci xol bu laab ak ci dëgg.
8所以我们守这节,不可用旧酵,也不可用又邪又恶的酵,而是要用纯洁真实的无酵饼。
9 Bindoon naa leen, ngeen bañ a séq dara ak njaalookat yi.
9我以前写信告诉你们,不可与淫乱的人来往。
10 Bëgguma ci woon a limaale waa àddina, maanaam njaalookat yi, nay yi, njublaŋ yi ak xërëmkat yi. Su ngeen séqul ak ñooñu dara, kon fàww ngeen génn àddina.
10这话当然不是指这世上行淫乱的、贪心的、勒索的,或拜偶像的人;如果是这样,你们就非脱离这世界不可。
11 Lii laa leen bëggoon a wax: buleen séq dara ak ku ñu tudde mbokk mu gëm Kirist, te fekk day njaaloo walla mu nay walla muy xërëm walla muy xas nit walla muy màndi walla muy njublaŋ. Nit ku mel noonu moom, buleen bokk ak moom, sax far di lekk.
11但现在我写信告诉你们,如果有称为弟兄,却是行淫乱、贪心、拜偶像、辱骂人、醉酒或勒索的,这样的人,不可和他来往,连和他吃饭都不可。
12 Ndax man maa war a àtte ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm Kirist? Déedéet! Waaye ñi bokk ci seen mbooloo yéena leen war a àtte.
12审判教外的人,跟我有什么关系?教内的人不是你们审判的吗?
13 Ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm, Yàlla moo leen di àtte. Waaye yéen, ni ko Mbind mi waxe: «Dàqleen ci seen biir kiy def lu bon.»
13至于教外的人, 神会审判他们。你们要把那恶人从你们中间赶出去。