1 Nanu jàll nag léegi ci laaj, yi ngeen ma doon bind, ci bañ a ànd ak jigéen, ndax lu baax la ci góor.
1婚姻的问题
2 Lii mooy sama xalaat: moy gu bare gi tax na ba, na góor gu nekk am jabaram, jigéen ju nekk am jëkkëram.
2但为了避免淫乱的事,男人应当各有自己的妻子,女人也应当各有自己的丈夫。
3 Jëkkër war na def warugaru jëkkër ci jabaram; jabar it def warugaru jabar ci jëkkëram.
3丈夫对妻子应该尽他的本分,妻子对丈夫也应当这样。
4 Jigéen ji amul sañ-sañ ci yaramam moom kenn; jëkkëram moo ko moom. Niki noonu it jëkkër ji amul sañ-sañ ci yaramam; jabaram moo ko moom.
4妻子对自己的身体没有主权,权在丈夫;照样,丈夫对自己的身体也没有主权,权在妻子。
5 Bu kenn tere boppam moroomam, su dul ne dangeen a mànkoo ci def noonu ab diir, ngir gën a man a wéet ak Yàlla ciy ñaan. Waaye su loolu weesoo, nangeen doxal yoonu séy; lu ko moy, Seytaane dina leen fiir ndax seen ñàkk maandute.
5夫妻不可彼此亏负,除非为了要专心祷告,双方才可以同意暂时分房。以后仍要同房,免得撒但趁着你们情不自禁的时候诱惑你们。
6 Li ma leen di wax fii du ndigal, waaye dama leen di xamal li ñu leen may, ngeen def ko.
6我说这话是容许你们,并不是命令。
7 Ndaxte dëgg-dëgg su ma sañoon, kon ñépp mel ni man; waaye ku nekk ak li la Yàlla jagleel, kii ak may gii, kee ak may gale.
7我愿人人都像我一样;只是各人有各人从 神得来的恩赐,有人是这样,有人是那样。
8 Lii laay yégal ñi séyul ak it ñi seen jëkkër dee: baax na ci yéen, su fekkee dangeen a toog rekk ni man, bañ a séy.
8我现在要对未婚的人和寡妇说,他们若保持像我这样就好了;
9 Waaye su ngeen mënul a téye seen bopp, nangeen séy, ndaxte séy moo gën xemmem di leen gaañ.
9但如果不能自制,就应当结婚,因为结婚总比欲火焚身好。
10 Ñi séy nag, maa ngi leen di jox ndigal lii --Boroom bi moo ko waxoon, du man — jigéen ju séy warul a teqalikoo ak jëkkëram.
10我要吩咐已婚的人(其实不是我,而是主吩咐的),妻子不可离开丈夫。
11 Te bu teqalikoo ak moom, bumu séyaat, mbaa boog na juboo ak jëkkëram. Te bu jëkkër ji fase jabaram.
11如果离开了,就不可再嫁,不然,就要跟丈夫复合。丈夫也不可离弃妻子。
12 Ñi ci des nag, lii laa leen di wax --Boroom bi waxu ko woon — su nit ku gëm Kirist amee jabar ju gëmul, te mu nangoo séy ak moom, waru koo fase.
12我要对其余的人说(是我说的,不是主说的),倘若某弟兄有不信的妻子,而她也情愿和他住在一起,他就不要离弃她。
13 Naka noonu it su jigéen ju gëm Kirist amee jëkkër ju gëmul, te mu nangoo nekk ak moom, warul a tas.
13如果妻子有不信的丈夫,而他也情愿和她住在一起,她也不要离弃丈夫。
14 Li tax ma wax ko moo di, jëkkër ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jabaram. Te it jigéen ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jëkkëram ji gëm; lu ko moy, seeni doom dinañu am sobe, te fekk dañoo sell.
14因为不信的丈夫因着妻子成为圣洁,不信的妻子也因着那个弟兄成为圣洁了。不然,你们的儿女就是不洁净的,但现在他们都是圣洁的了。
15 Waaye nag, su fekkee ki gëmul bëgg na dem, na dem. Ci wàll googu nag, ki gëm Kirist, muy jëkkër ji walla jabar ji, amul benn tënk, ndaxte Yàlla moo leen woo ngir ngeen dund ci jàmm.
15如果那不信的要离去,就由他离去吧;在这种情形之下,信主的弟兄或姊妹都不必勉强。 神呼召你们,是要你们和睦。
16 Loo ci xam, yaw jigéen ji, ndax dinga gëmloo sa jëkkër Musalkat bi walla déet? Loo ci xam yaw jëkkër ji it, ndax dinga gëmloo sa jabar Musalkat bi walla déet?
16你这作妻子的,你怎么知道不能救你的丈夫呢?你这作丈夫的,你怎么知道不能救你的妻子呢?
17 Ku nekk nag na dund, ni ko ko Boroom bi jagleele, mu mengoo ak ni mu meloon, bi ko Yàlla wooyee. Moom laay tëral ci mboolooy ñi gëm yépp.
17保持蒙召时的身分不过,主怎样分给各人, 神怎样呼召各人,各人就要照着去行事为人。我也这样吩咐各教会。
18 Ki xaraf, bi ko Yàlla wooyee, warul a jéem a far màndargam xaraf bi. Ki xaraful, bi ko Yàlla wooyee, aajowul mu xaraf.
18有人受了割礼而蒙召的吗?他就不要遮掩割礼的记号。有人未受割礼而蒙召的吗?他就不要受割礼。
19 Xaraf ak ñàkka xaraf lépp a yem; li am solo moo di topp ndigali Yàlla.
19割礼算不得什么,没有割礼也算不得什么,要紧的是遵守 神的命令。
20 Na kenn ku nekk jàpp ci li mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee.
20各人蒙召的时候怎样,他就应当保持原来的情况。
21 Ndax jaam nga woon, bi la Yàlla wooyee? Na ci sa xel dal. Waaye soo amee bunt, ba yiwiku, nanga ci jaar.
21你蒙召的时候是作奴仆的吗?不要为此烦恼。但如果你能够得到自由,就要把握这机会。
22 Ku nekkoon jaam, bi la Boroom bi wooyee, Boroom bi goreel na la. Ba tey it ku nekkoon gor, bi ñu la wooyee, jaamu Kirist nga.
22因为作奴仆的蒙了主的呼召,就是属于主的自由人了;照样,自由的人蒙了呼召,他就是基督的奴仆了。
23 Gannaaw Yàlla jot na leen ak njëg gu réy, buleen doon jaamub nit.
23你们是用重价买来的,不要作人的奴仆。
24 Bokk yi, fàww ku nekk wéy ca kanam Yàlla ci fànn ga mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee.
24弟兄们,你们各人蒙召的时候怎样,就应当在 神面前保持这原来的情况。
25 Ci li jëm ci janq yi, awma ndigalu Boroom bi, waaye maa ngi joxe sama xalaat, ni ku ñu wóolu ndax li ma jot yërmandey Boroom bi.
25未婚、守独身、守寡的问题关于守独身的女子,我没有主的命令,但我既然蒙了主的怜悯,成为可信靠的人,就把我的意见提出来。
26 Bu nu seetee tiis wii fi teew nag, defe naa ne li baax ci nit, moo di mu sax ci li mu nekk.
26为了目前的困难,我认为人最好能保持现状。
27 Ndax takk nga jabar? Bul wut a tàggoo ak moom. Ndax takkuloo jabar? Bul wut jabar.
27你已经有了妻子吗?就不要想摆脱。你还没有妻子吗?就不要去找妻子。
28 Waaye nag boo séyee, defoo bàkkaar, te bu janq séyee, deful bàkkaar. Waaye ñi séy dinañu am naqar ci àddina, te naqar woowu dama leen koo bëggoon fanqal, yéen ñi séyagul.
28如果你娶妻子,这不是犯罪;如果处女出嫁,也不是犯罪。不过,这样的人要受肉体上的苦难,我却不愿你们受这苦难。
29 Lii laa bëgg a wax, bokk yi: diir bu gàtt rekk a fi des. Lu weesu tey, na góor ñi am jabar di def, ni bu ñu ko amul woon;
29弟兄们,我是说时候不多了。从今以后,有妻子的要像没有妻子的,
30 ñiy jooy, mel ni ñu jooyul; ñiy bég, mel ni ñu bégul; ñiy jënd, ni ñu moomul li ñu jënd;
30哀哭的要像不哀哭的,快乐的要像不快乐的,买了东西的要像一无所得的,
31 ñiy jariñoo àddina, bañ cee xér. Ndaxte àddina sii, ci ni mu mel, dootul yàggati.
31享用世上百物的要像没有享用的一样,因为这世上的情况都要过去。
32 Bëggoon naa, ngeen bañ a am benn xalaat. Góor gu takkul jabar dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi, di wut a neex Boroom bi.
32我愿你们无所挂虑。没有娶妻子的人,挂念的是主的事,想怎样去得主喜悦;
33 Waaye ku takk jabar, fàww mu bàyyi xel ci mbiri àddina si, ak nu mu man a neexe jabaram,
33但娶了妻子的人是为世上的事挂虑,想怎样去讨妻子的欢心,
34 te noonu dafay daldi bare soxla. Te jigéen ju séyul, walla janq, dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi — bëgg koo jox yaramam ak xelam. Waaye jigéen ji séy dafay bàyyi xel ci mbiri àddina, ak nu mu man a neexe jëkkëram.
34这样他就分心了。没有结婚的妇女和守独身的女子,挂念的是主的事,好让身体和心灵都成为圣洁;但结了婚的妇女是为世上的事挂虑,想怎样去讨丈夫的欢心。
35 Seen njariñ a tax ma wax lii, du ngir teg leen yen bu ngeen àttanul, waaye ngeen man a jàppandil Boroom bi ci njaamu gu rafet gu àndul ak genn njaaxle.
35我说这话,是为了你们自己的益处;我不是要限制你们,而是要你们作合宜的事,一心一意地对主忠诚。
36 Nanu jàll nag ci mbiri kiy takk ngoro te amul pasteefu takk ndaw si. Su fekkee ne waxambaane wi xalaat na ne, jëfewul nu jekk ak janq bi, fekk muy wees ag ndawam, te mu xalaat ne dafa koo war a takk, kon na ko takk, ni mu ko bëgge; deful bàkkaar.
36如果有人认为是亏待了自己的女朋友,她也过了结婚的年龄,而他觉得应当结婚,他就可以照着自己的意思去作,这不是犯罪;他们应该结婚。
37 Waaye nag su dogoo dëgg ci bañ a takk, fekk sagoom rekk a tax te kenn tegu ko ko, kon ba tey def na lu baax.
37但如果他心里坚决,没有什么不得已的原因,又可以控制自己的意志,决心让女朋友持守独身;这样作也是好的。
38 Noonu ku takk as ndawam def na lu baax, rawatina nag ku takkul.
38所以,那跟自己的女朋友结婚的,作得好,那不结婚的,作得更好。(或译:“36如果有人认为待自己的女儿不合适,她也过了结婚的年龄,而且应当这样行,他就可以照着自己的意思去作,让她们结婚,这不是犯罪。37但如果他心里坚定,没有什么不得已的原因,又有权作主,决心留下自己的女儿,这样作也是好的。38所以,那让自己女儿出嫁的,作得好,那不让女儿出嫁的,作得更好。”)
39 Jigéen ji séy dina ànd ak jëkkëram giiru dundam. Waaye su jëkkër ji faatoo, man na séy ak ku ko neex, su fekkee ne góor gu gëm la.
39丈夫活着的时候,妻子是受约束的;丈夫若死了,她就可以自由地嫁给她愿意嫁的人,只是要嫁给主里的人。
40 Moona nag dina gën a bég, bu toogee noonu rekk. Loolu mooy sama xalaat, te defe naa ne, man it am naa Xelum Yàlla.
40然而照我的意见,倘若她能守节,就更有福了。我想我这话也是 神的灵感动的。