1 Kon nag dëdduleen gépp coxor, gépp njublaŋ, naaféq, kiñaan ak jëw.
1信徒像活石建造成灵宫
2 Gannaaw ay liir ngeen yuy door a juddu te mos ci mbaaxug Boroom bi, nàmpleen ci meew mu sell, miy dundal seen xol, ba màgg ci biir muccu Yàlla.
2像初生婴孩爱慕那纯净的灵奶,好叫你们靠它长大,进入救恩;
4 Kon nag ñëwleen ci moom; nit ñi bañ nañu ko, waaye Yàlla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la,
3因为你们已经体验过主是美善的。
5 te yéena ngi mel niy doj yuy dund yu Yàllay defare dëkkukaayam. Noonu ay saraxalekat yu sell ngeen, ngir jébbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist.
4主是活石,虽然被人弃绝,却是 神所拣选所珍贵的;你们到他面前来,
6 Looloo tax bind nañu:«Maa ngi samp fi ci Siyon doju koñ.Doj wu tedd la, wu ma tànn;ku gëm ci moom, sa yaakaar du tas mukk.»
5也就像活石,被建造成为灵宫,作圣洁的祭司,借着耶稣基督献上蒙 神悦纳的灵祭。
7 Kon nag yéen ñi gëm am ngeen cér ci teraangaam. Waaye naka ñi gëmul:«Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.»
6因为经上记着:“看哪,我在锡安放了一块石头,就是所拣选所珍贵的房角石,信靠他的人,必不致失望。”
8 Te it:«Doj la wuy fél nit,di xeer wu koy fakkastal.» Dañu cee fakkastalu, ndaxte gëmuñu kàddug Yàlla, te loolu la Yàlla dogal ci ñoom.
7所以这石头,对你们信的人是宝贵的,但对那不信的人,却是“建筑工人所弃的石头,成了房角的主要石头。”
9 Waaye yéen xeet wu Yàlla tànn ngeen, di askanu saraxalekati Buur Yàlla, askan wu sell ngeen, di mbooloom Yàlla, ngir ngeen yégle ngëneelam, moom mi leen woo, ba génne leen lëndëm gi, tàbbal leen ci leeram gu yéeme gi.
8它又“作了绊脚的石头,使人跌倒的磐石。”他们跌倒是因为不顺从这道,他们这样是必然的。
10 Démb nekkuleen woon ci dara, waaye tey mbooloom Yàlla ngeen; booba jotuleen woon yërmandeem, waaye léegi jot ngeen ko.
9然而你们是蒙拣选的族类,是君尊的祭司,是圣洁的国民,是属 神的子民,为要叫你们宣扬那召你们出黑暗入奇妙光明者的美德。
11 Samay xarit, yéen ñiy ay gan ak ay doxandéem ci àddina si, maa ngi leen di dénk lii: dëdduleen bànneexi bakkan yiy xeex ak xol.
10“你们从前不是子民,现在却是 神的子民;从前未蒙怜恤,现在却蒙了怜恤。”
12 Na seen dundin rafet ci biir xeeti àddina, kon doonte ñu di leen sosal ay ñaawteef, dinañu gis seeni jëf yu rafet bay màggal Yàlla, bés bu leen feeñoo.
11应当品行端正亲爱的,我劝你们作客旅和寄居的人,要禁戒肉体的私欲,这私欲是与灵魂争战的。
13 Na seen nangub Boroom bi tax, ngeen déggal képp kuy kilifa, muy buur ba gën a kawe,
12你们在教外人中,应当品行端正,使那些人,虽然毁谤你们是作恶的,但因为看见你们的好行为,就要在鉴察的日子颂赞 神。
14 mbaa jawriñ yu mu yebal, ngir ñu yar ñiy def lu bon, te teral ñiy def lu baax.
13你们为主的缘故,要顺服人的一切制度,无论是至尊的君王,
15 Ndaxte noonu la coobareg Yàlla tëdde, maanaam ngeen sax ci def lu baax, ba wedamloo jayil yi xamul dara.
14或是君王所派赏善罚恶的官员;
16 Li leen Yàlla goreel nag, bu mu tax ngeen mbubboo ko, bay def lu bon, waaye ngeen gën a feddali seen jaamu Yàlla.
15因为这是 神的旨意,要借着你们的善行,塞住糊涂无知人的口。
17 Teral-leen ñépp, bëgg kureelu bokk yi, ngeen ragal Yàlla te teral buur bi.
16你们是自由的人,但不要用自由来掩饰邪恶,总要像 神的仆人。
18 Yéen jaam yi déggal-leen seeni sang ak wegeel gu mat sëkk, waxuma ñi baax te lewet rekk, waaye sax ñu wex ñi.
17要尊重众人,爱护弟兄,敬畏 神,尊敬君王。
19 Ndaxte su ngeen dékkoo tiis, di sonn ci lu dul yoon ndax seen ànd ak Yàlla, loolu lu rafet la.
18基督受苦的榜样你们作仆人的,要凡事敬畏顺服主人,不单是对善良温和的,就是乖僻的也要顺服。
20 Su ngeen tooñee te muñ i pes, luy pey gi? Waaye su ñu leen fitnaalee ci def lu baax te ngeen muñ ko, jëf ju rafet la fa kanam Yàlla.
19因为人若在 神面前为良心的缘故,忍受冤屈的苦楚,是有福的。
21 Ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ndaxte Kirist itam sonn na ngir yéen, teg fi seen kanam royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
20你们若因犯罪受责打而能忍耐,有什么可夸的呢?但你们若因行善而受苦,能忍耐,在 神看来,这是有福的。
22 «Musul a def bàkkaar,te jenn waxu njublaŋ musul a génn ci gémmiñam.»
21你们就是为此蒙召,因基督也为你们受过苦,给你们留下榜样,叫你们跟随他的脚踪行。
23 Saaga nañu ko te feyyuwul, fitnaal nañu ko te tëkkuwul, waaye mu dénk boppam Ki yor àtte bu dëgg bi.
22“他从来没有犯过罪,口里也找不到诡诈。”
24 Gàddu na moom ci boppam sunuy bàkkaar ca bant, ba ñu ko daajoon, ngir nu tàggook bàkkaar, sóobu ci dund gu jub; ndax ay gaañu-gaañoom may na nu ag wér.
23他被骂的时候不还嘴,受苦的时候也不说恐吓的话;只把自己交托给那公义的审判者。
25 Ndaxte yéena ngi réeroon niy xar, waaye léegi dellusi ngeen ci sàmm, biy aar seeni xol.
24他在木头上亲身担当了我们的罪,使我们既然不活在罪中,就可以为义而活。因他受的鞭伤,你们就得了医治。
25你们从前好像迷路的羊,但现在已经回到你们灵魂的牧人和监督那里了。