Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

1 Peter

5

1 Kon yéen njiit yi, maa ngi leen di dénk, man miy njiit ni yéen, man mi seede coonoy Kirist te am cér ci ndam li nar a feeñ.
1务要牧养 神的羊群
2 Lii laa leen di ñaan: sàmmleen géttug Yàlla, gi mu leen dénk, di ko wottu, waxuma ci sañul-bañ, waaye di surgay Yàlla ci xol bu tàlli; ngeen def ko ak xol bu laab te bañ cee séentu alal.
2务要牧养你们中间的羊群,按着 神的旨意照顾他们。不是出于勉强,而是出于甘心;不是因为贪财,而是出于热诚;
3 Buleen noot ñi leen Yàlla dénk, waaye ngeen nekk ay royukaay fi kanam jur gi.
3也不是要辖制托付你们的羊群,而是作他们的榜样。
4 Noonu waxtu wu Boroom gétt gi feeñee, dina leen jagleel kaalag ndam guy sax ba fàww.
4到了牧长显现的时候,你们必定得着那永不衰残的荣耀冠冕。
5 Noonu itam yéen ndaw ñi, nangeen déggal mag ñi. Te yéen ñépp, solooleen woyof ci seen biir, ndaxte:«Yàlla day dàq ñi réy,di yiwal ñi woyof.»
5照样,你们青年人要顺服年长的。就是你们各人也要彼此以谦卑为装束,因为“ 神敌挡骄傲的人,赐恩给谦卑的人。”
6 Suufeel-leen seen bopp kon ci ron loxob Yàlla bu am kàttan, ngir mu yékkati leen ci jamono ju ko soob.
6所以你们要谦卑,服在 神大能的手下,到了时候,他必叫你们升高。
7 Te ngeen yenniku ci kawam seen njàqare jépp, ndax ku leen ñeewante la.
7你们要把一切忧虑卸给 神,因为他顾念你们。
8 Maanduleen te foog, ndax seen noon Seytaane mu ngi wër, ni gaynde guy yëmmu, di rëbb ku mu yàpp.
8你们要谨守、警醒。你们的仇敌魔鬼,好像吼叫的狮子走来走去,寻找可以吞吃的人;
9 Jànkoonteleen ak moom ci biir ngëm gu takku, xam ne kureelu bokk yi ci àddina yépp, ñu ngi daj ay fitna ni yéen.
9你们要用坚强的信心抵挡他,因为知道你们在世上的弟兄,也经历过同样的苦难。
10 Te Yàlla mi jagoo yiw wépp te woo leen ci darajay Kirist, ngir ngeen bokk ci ndamam li sax, gannaaw bi ngeen yendoo bëccëgu tiis, dina leen yeesalaat, di leen dëgëral ak a dooleel, ba ngeen sampu.
10但满有恩典的 神,就是在基督里召你们进入他永远荣耀的那一位,在你们受了短暂的苦难之后,必定亲自成全你们,坚固你们,赐力量给你们,建立你们。
11 Na Yàlla yelloo màgg ba fàww. Amiin.
11愿权能归给他,直到永远。阿们。
12 Bind naa leen ci lu gàtt ci ndimbalu Silwan, mi ma jàpp ni sama mbokk mu takku. Dénk naa leen, di leen seedeel ne, lii mooy yiwu Yàlla dëgg; kon nag saxleen ci.
12劝勉和祝福我借着我认为忠心的弟兄西拉,简略地写了这封信劝勉你们,又向你们证实这是 神真正的恩典;你们要在这恩典上站立得住。
13 Mbooloo mi nekk ci dëkk bi ñuy wax Babilon te Yàlla tànn ko ni yéen, moo di leen nuyu, ñoom ak Màrk sama doomu diine.
13在巴比伦与你们同蒙拣选的,和我儿子马可都问候你们。
14 Nuyoonteleen ak saafoonte yu sell. Na jàmm ñeel képp ku gëm Kirist.
14你们要用爱心彼此亲嘴问安。愿平安归与你们所有在基督里的人。