Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

1 Thessalonians

2

1 Waaw bokk yi, xam ngeen ne, ngan gi nu leen ganesi woon du nganug neen.
1保罗在帖撒罗尼迦的工作
2 Laata nuy ñëw, jaar nanu ci fitna ak toroxte ca dëkku Filib, ni ngeen ko xame; waaye Yàlla sunu Boroom may na nu fit, ba li tongoonte bi metti lépp it, yégal nanu leen xebaaru Yàlla bu baax bi.
2我们从前在腓立比虽然受了苦,又被凌辱,可是靠着我们的 神,在强烈的反对之下,仍然放胆向你们述说 神的福音,这是你们知道的。
3 Ndaxte sunu waaraate wéeruwul cig réer walla ci njublaŋ walla ciy nax.
3我们的呼吁,不是错谬的,不是污秽的,也没有诡诈。
4 Waaye gannaaw Yàlla moo nu seet, ba wóolu nu te dénk nu xebaar bu baax bi, kon noonu lanuy waaree, du ngir neex nit ñi, waaye ngir neex Yàlla, miy seet xol yi.
4相反地, 神既然考验过我们,把福音委托给我们,我们就传讲,不像是讨人欢心的,而是讨那察验我们心思的 神的喜悦。
5 Musunoo jey kenn, yéen xam ngeen ko; sunu waare musul a ëmb bëgge, Yàlla seede na ko;
5我们从来不说奉承的话,这是你们知道的, 神可以作证,我们并没有借故起贪心,
6 musunoo sàkku ngërëmu nit, muy ci yéen, muy ci ñeneen.
6也没有向你们或别人求取人的荣誉。
7 Manoon nanoo diis ci seen kaw sax, nun ñiy ndawi Kirist, waaye woyofoon nanu ci seen biir, te lewet ni jaboot buy uuf doomam.
7我们身为基督使徒的,虽然有权利受人尊敬,但我们在你们中间却是谦和的,就像母亲乳养自己的孩子。
8 Cofeel gi nu am ci yéen tax na, bëggunu woon a yem ci xamal leen xebaaru Yàlla bu baax bi, waaye jox leen it sunu bakkan, ndaxte sunu xol seeyoon na ci yéen.
8我们这样疼爱你们,不但乐意把 神的福音传给你们,连自己的性命也乐意给你们,因为你们是我们所爱的。
9 Bokk yi, yéena ngi fàttaliku sunu coono ak sunu ñaq; xam ngeen ni nu liggéeye guddi ak bëccëg, ngir bañ a diis ci seen kaw, ci di leen yégal xebaaru Yàlla.
9弟兄们,你们应该记得我们的辛苦和劳碌;我们把 神的福音传给你们的时候,怎样昼夜作工,免得你们有人受累。
10 Naka sunu diggante ak yéen ñi gëm, doxal nanu ko doxalin wu sell te jub te amul sikk: seede ngeen ko, te Yàlla it seede na ko.
10我们对你们信的人是多么圣洁、公义、无可指摘,这是你们和 神都可以作证的。
11 Xam ngeen ne, dénk nanu leen kenn-kenn, ni baay di def ak doomam, dëfëlal leen seen xol te dëggal ci yéen, ngeen dund dund gu neex Yàlla, moom mi leen di woo, ngeen séddu ci nguuram ak ndamam.
11正如你们知道的,我们是怎样好像父亲对待儿女一样对待你们各人:
13 Te it dunu noppee sant Yàlla ci lii: ba ngeen jotee kàddug Yàlla, gi nu doon waare, nangu ngeen ko, waxuma ni kàddug nit waaye ni kàddug Yàlla, ndaxte moom la ci dëgg-dëgg, te mu ngi jëf ci yéen ñi gëm.
12劝勉你们,鼓励你们,叮嘱你们,要你们行事为人,配得上那召你们进入他的国和荣耀的 神。
14 Ndaxte bokk yi, aw ngeen ci tànki mboolooy Yàlla, yi nekk ca réewu Yawut ya tey daje ci turu Kirist Yeesu; fitna ya ñu daj ca Yawut ya, yéen it seen waa réew teg nañu leen ko.
13我们也为这缘故不住感谢 神,因为你们接受了我们所传的 神的道,不认为这是人的道,而认为这确实是 神的道。这道也运行在你们信的人里面。
15 Ñoom Yawut yi rey nañu Boroom bi Yeesu, ni ñu reye woon yonent yi; teg nañu nu fitna yu metti; neexuñu Yàlla, ànduñu ak kenn,
14弟兄们,你们好像犹太地在基督耶稣里 神的众教会一样,他们怎样遭受犹太人的迫害,你们也照样遭受同族人的迫害。
16 di nu teree wax ak ñi dul Yawut, ngir bañ ñu mucc. Duñu noppee xuus ci biir bàkkaar, waaye merum Yàlla xëppu na ci seen kaw.
15这些犹太人杀了主耶稣和众先知,又把我们赶出来。他们得不到 神的喜悦,并且和所有的人作对,
17 Nun nag bokk yi, ba ñu ma leen xañee ab diir --xol yi taxul may wax, waaye jëmm yi rekk — jéem nanu leen a gis ak sunu kem-kàttan, ndax namm nanu leen, ba sunu xol seey ci gis leen.
16阻挠我们向外族人传道,不让他们得救,以致恶贯满盈。 神的忿怒终必临到他们身上。
18 Kon jàppoon nanu leen a seetsi — man Pool sax ay yooni yoon, waaye Seytaane téq na ma.
17保罗渴望再访帖撒罗尼迦弟兄们,我们被迫暂时离开你们,不过是身体离开,心却没有离开。我们非常渴望再见到你们。
19 Ndaxte bés bu Yeesu sunu Boroom dellusee, te nu fekke ko, kan mooy sunu yaakaar? Kan mooy sunu mbég? Kan mooy sunu kaala, gi nuy tiitaroo?
18因此,我们很想到你们那里去,我保罗也一再想去,只是撒但阻挡了我们。
20 Xanaa du yéen? Waaw yéenay sunu ndam, yéenay sunu mbég.
19我们主耶稣再来的时候,我们在他面前的盼望、喜乐或所夸耀的冠冕是什么呢?不就是你们吗?
20是的,你们就是我们的荣耀,我们的喜乐。