Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

2 Corinthians

8

1 Gannaaw loolu bokk yi, danu leen a bëgg a xamal li yiwu Yàlla jur ci biir mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Maseduwan.
1马其顿圣徒乐捐的榜样
2 Nattu yi ñu jaar ëmb nañu coono yu réy; waaye seen mbég mu tar ak seen ñàkk gu metti ñoo jur ci ñoom yéwén gu jéggi dayo.
2他们在患难中受到极大的考验的时候,他们满溢的喜乐和极度的贫乏,汇流出丰厚的慷慨来。
3 Seede naa ne, ñoom ci seen bopp joxe nañu ba fa seen man-man yem, ba weesu ko sax.
3我可以作证,他们是按着能力,并且是超过了能力,
4 Saraxu nañu nu lool, ngir bokk ci ñiy yónnee ndimbal gaayi Yàlla yi.
4自动地再三恳求我们,准许他们在供应圣徒的事上有分。
5 Te yemuñu sax ci li nu séentu woon ci ñoom, waaye dañoo jébbal seen bopp Boroom bi jëkk, gannaaw loolu ñu jébbal nu seen bopp ci coobareg Yàlla.
5他们超过了我们所期望的,照着 神的旨意,先把自己献给主,然后献给我们。
6 Looloo tax nag nu sant Tit, mu ñëw àggale ci yéen, ni mu tàmbalee woon, seen jëfu ndimbal.
6因此,我们勉励提多,既然开始了这慈善的事,就应当在你们那里把这事办好。
7 Gannaaw nag wone ngeen cawarte gu tollu noonu, ci ngëm, ci wax, ci xam-xam, ci farlu gu mat, ak ci seen mbëggeel ci nun, sawareleen noonu it ci jëfu ndimbal lii.
7你们在一切事上,就如信心、口才、知识、热情和爱我们的心,既然都是富足的,那么,在这慈善的事上,也要显出你们是富足的。
8 Du ndigal lu ma leen di jox, waaye dama leen di yégal cawarteg ñi ci des, ngir natt fu seen mbëggeel tollu.
8劝信徒完成慈善的事我这样说,不是吩咐你们,而是借着别人的热心来考验你们的爱心是否真实。
9 Ndaxte yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist umpu leen, ni mu futtee am-amam, ba ñàkk ngir yéen, ndax ngeen woomle cig ñàkkam.
9你们是知道我们的主耶稣基督的恩典的:他本来富足,却为你们成了贫穷,要使你们因他的贫穷成为富足。
10 Kon lii laa xalaat ci lu baax ci yéen: yéen ñi nga xam ne tàmbaliwuleen a jëf rekk, waaye yéena jëkk a am yéene jii daaw,
10我在这里表示我的意见,这对你们是有益的:你们不仅一年前就在办这事,而且早就想这样作了,
11 yeggaleleen ko léegi. Noonu li ngeen mottali ci seen man-man tolloo ak yéene, ji ngeen amoon ci seen mébét.
11现在就应当把这事办好;这样,你们既然有愿意作的心,因着你们尽了自己所能的,就可以完成。
12 Ndaxte joxe, bu àndee ak yéene, Yàlla dina ko nangu, di seet li nu am te bañ a seet li nu amul.
12因为人要是有愿意作的心,按照他所有的,必蒙悦纳,不是按照他所没有的。
13 Bëgguma leen a teg soxla, ngir woyofal ñi ci des, waaye na ñépp tolloole.
13这不是要别人轻省,你们受累,而是要大家都均等。
14 Tey jii nag man ngeen sàkk ci li ngeen barele, faj soxlay ñeneen, ngir ëllëg it bareleg ñooña faj seen soxla. Noonu ñépp tolloole.
14现在你们富裕,就要补助他们的缺乏,到了他们富裕的时候,也可以补助你们的缺乏,这样就均等了;
15 Moom la Mbind mi tëral ne:«Ki dajale lu bare ëpplewul dara,te ki dajale tuuti ñàkkul.»
15正如经上所记:“多的,没有剩余,少的,也不缺乏。”
16 Cant ñeel na Yàlla, moom mi def ci xolu Tit cawarte gu mel ni sunu gos ci yéen!
16感谢 神,他把我对你们那样的热情,放在提多的心里。
17 Bi nu ko laajee, mu ñëw ci yéen, nangu na, te rax-ca-dolli cawarteem tollu na, ba nu man a wax ne, ci coobarey boppam la jóge, jëm ci yéen.
17提多一方面接受了劝勉,但他自己更加热心,自愿到你们那里去。
18 Yónniwaale nanu ak moom mbokk, mi am tur wu rafet ci mboolooy ñi gëm ñépp ndax li muy waare xebaaru Kirist.
18我们还派了一位弟兄和他同去,(这人在福音的事工上,得到了众教会的称赞。
19 Te sax mbooloo yi ñoo ko tànn, ngir mu ànd ak nun, bu nuy yóbbu ndimbal li ngir ndamu Boroom bi, te mu firndeel sunu yéene ju rafet.
19不但这样,众教会更选派了他作我们的旅伴。我们办理这慈善的事,是为了主的荣耀,也是为了我们的心愿。)
20 Def nanu noonu nag, ndax kenn bañ noo ŋàññ ci ni nuy topptoo ndimbal lu yaatu loolu.
20免得有人因为我们经管的捐款太多,就毁谤我们。
21 Danuy fexee def li jub, du ci kanam Yàlla rekk, waaye it ci kanam nit ñi.
21因为我们努力去作的,不仅是主认为是美的事,也是众人认为是美的事。
22 Yónniwaale nanu it sunu mbokk, mi nu seetlu cawarteem ay yooni yoon ci fànn yu bare, te mu gën koo fésal bii yoon ndax kóolute gu réy, gi mu am ci yéen.
22我们还派了另一位弟兄与他们同去;我们在许多的事上多次考验过他,知道他很热心;现在他对你们大有信心,就更加热心了。
23 Noonu kon ci lu jëm ci Tit, sama nawle la ci liggéey, bi ci seen biir. Ci lu jëm ci sunu bokk, yi ànd ak moom nag, ndawi mbooloom ñi gëm lañu, ñuy wone ndamu Kirist.
23至于提多,他是我的同伴,为你们的缘故作了我的同工;还有我们那两位弟兄,他们是众教会所派的,是基督的荣耀。
24 Na seen teeru firndeel nag seen mbëggeel ci kanamu mboolooy ñi gëm, te dëggal leen ne, noo yey wóolu leen.
24所以,你们要在众教会面前,向他们证明你们的爱心和我们所夸耀你们的。