Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Acts

13

1 Amoon na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk dëkku Ancos, ay yonent ak ay jàngalekat: maanaam Barnabas, Simeyon ku ñu dàkkentale Niseer, Lusiyus mi dëkk Siren, Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom diiwaan ba, ak Sool.
1巴拿巴和扫罗奉差遣
2 Am bés nag, bi ñuy jaamu Boroom bi ak di woor, Xel mu Sell mi ne: «Beral-leen ma Barnabas ak Sool ngir liggéey, bi ma leen wooye.»
2他们事奉主,并且禁食的时候,圣灵说:“要为我把巴拿巴和扫罗分别出来,去作我呼召他们作的工。”
3 Bi ñu ko déggee, ñu daldi woor ak a ñaan, teg leen ay loxo, ba noppi bàyyi leen ñu dem.
3于是他们禁食祷告,为两人按手,就派他们去了。
4 Noonu Xel mu Sell mi yónni leen. Ñu dem nag ci dëkku Selusi, dugg fa gaal, jëm ci dun bu ñuy wax Sipar.
4第一次宣教旅程他们既然奉圣灵差遣,就下到西流基,从那里坐船往塞浦路斯。
5 Bi ñu teeree ca dëkku Salamin nag, ñu yégle fa kàddug Yàlla ca jàngub Yawut ya. Ku tudd Yowaana ànd ak ñoom, di leen jàpple ci liggéey bi.
5他们到了撒拉米,就在犹太人的各会堂里宣讲 神的道,还有约翰作他们的助手。
6 Noonu ñu jaar ci dun bépp, ba egg dëkku Pafos. Foofa ñu gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent.
6他们走遍全岛,到了帕弗,遇见一个犹太人,名叫巴.耶稣,是个术士,又是个假先知。
7 Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool, ngir bëgg a dégg kàddug Yàlla.
7他常常和省长士求.保罗在一起;省长是个聪明人,他请了巴拿巴和扫罗来,要听听 神的道。
8 Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi --ndaxte loolu la turam di tekki — di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm.
8但术士以吕马(以吕马就是“术士”的意思)与使徒作对,要使省长转离真道。
9 Ci kaw loolu Sool, mi tudd it Pool, daldi fees ak Xel mu Sell mi; mu xool ko jàkk,
9扫罗,也就是保罗,却被圣灵充满,定睛看着他,
10 ne ko: «Yaw mi fees ak fen ak lu bon, di doomu Ibliis, tey noonu lépp lu jub, ndax doo bàyyee dëngal yoon yu jub yu Boroom bi?
10说:“你这充满各样诡诈和各样奸恶的人,魔鬼的儿子,公义的仇敌!你歪曲了主的正路,还不停止吗?
11 Léegi loxob Boroom bi dina dal sa kaw, te dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa nag ay bëtam muuru, mu daldi tàbbi cig lëndëm, muy làmbatu, di wut ku ko wommat.
11你看,现在主的手临到你,你要瞎了眼睛,暂时看不见阳光。”他就立刻被雾和黑暗笼罩着,周围找人牵他的手,给他领路。
12 Ba boroom réew ma gisee li xew nag, mu daldi gëm, di yéemu ci yoonu Boroom bi.
12那时,省长看见了所发生的事,就信了,因为他惊奇主的教训。
13 Naka noona Pool ak ñi mu àndal jóge Pafos, jaar ci géej, jëm dëkku Peers ci réewu Pamfili. Yowaana nag tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.
13在彼西底的安提阿保罗和同伴从帕弗开船,来到旁非利亚的别加,约翰却离开他们,回耶路撒冷去了。
14 Waaye ñoom ñu jóge Peers, aw ca yoon wa, ba ñëw dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. Bésu noflaay ba nag ñu dugg ca jàngu ba, toog.
14他们从别加往前走,到了彼西底的安提阿,在安息日进了会堂,就坐下来。
15 Bi ñu jàngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti jàngu ba yónnee ca ñoom ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di dénk mbooloo mi, waxleen ko.»
15宣读了律法和先知书以后,会堂的理事们派人到他们那里来,说:“弟兄们,如果有什么劝勉众人的话,请说吧!”
16 Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen!
16保罗就站起来,作了一个手势,说:“以色列人和敬畏 神的人,请听!
17 Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom.
17以色列民的 神,拣选了我们的祖先;当他们在埃及地寄居的时候, 神抬举这民,用大能(“大能”原文作“高”)的膀臂,把他们从那地领出来;
18 Diirub ñeent-fukki at mu di leen muñal ca màndiŋ ma.
18又在旷野容忍(“容忍”有些抄本作“养育”)他们,约有四十年之久;
19 Gannaaw loolu faagal na juróom-ñaari xeet ci réewu Kanaan, ba sunuy maam donn réew ma.
19灭了迦南地的七族之后,就把那地分给他们为业;
20 Loolu lépp xew na ci diirub ñeenti téeméeri at ak juróom-fukk. «Gannaaw loolu mu jox leen ay àttekat, ba ci yonent Yàlla Samwil.
20这一切历时约四百五十年。后来 神赐给他们士师,直到撒母耳先知为止。
21 Booba ñuy ñaan buur, te Yàlla jox leen Sóol, doomu Kis ci giiru Ben-yamin, muy seen buur diirub ñeent-fukki at. Gannaaw ga mu jële ko fa,
21那时,他们要求立一个王, 神就把便雅悯支派中一个人,基士的儿子扫罗,赐给他们作王,共四十年之久。
22 dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: “Gis naa Daawuda, doomu Yese, ku ma neex ci sama xol, te dina def lépp luy sama coobare.”
22废去扫罗之后,又为他们兴起大卫作王,并且为他作证说:‘我找到耶西的儿子大卫,他是合我心意的人,必遵行我的一切旨意。’
23 «Noonu ci askanam Yàlla indil na bànni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon.
23 神照着应许,已经从这人的后裔中,给以色列带来了一位救主,就是耶稣。
24 Laata muy ñëw nag, Yaxya daan na waare, ne bànni Israyil gépp, ñu tuub seeni bàkkaar, te mu sóob leen ci ndox.
24在他来临之前,约翰早已向以色列全民宣讲悔改的洗礼。
25 Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: “Ku ngeen may teg? Duma Ki war a ñëw; waaye am na kuy ñëw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay dàllam.”
25约翰快要跑完他的路程的时候,说:‘你们以为我是谁?我不是基督。他是在我以后来的,我就是给他解脚上的鞋带也不配。’
26 «Bokk yi, yéen askanu Ibraayma ak yéen ñi ragal Yàlla, kàddug mucc gi ci nun la wàcc.
26“弟兄们,亚伯拉罕的子孙,和你们中间敬畏 神的人哪,这救恩之道是传给我们的。
27 Waa Yerusalem ak seeni kilifa xàmmiwuñu woon Yeesu te xamuñu woon waxu yonent, yi ñuy jàng bésu noflaay bu nekk; teewul ñu amal waxu yonent yi, ci li ñu àtte Yeesu, ba daan ko.
27住在耶路撒冷的人和他们的官长,因为不认识基督,也不明白每逢安息日所读的先知的话,就把他定了罪,正好应验了先知的话。
28 Yoon dabu ko fenn, moona ñaan nañu Pilaat, mu reylu ko.
28他们虽然找不出该死的罪状,还是要求彼拉多杀害他。
29 Noonu ñu def lépp lu yonent yi bindoon ci mbiram, ba noppi ñu wàcce ko ca bant ba, tàbbal ko ci bàmmeel.
29他们把所记载一切关于他的事作成了,就把他从木头上取下来,放在坟墓里。
30 Waaye Yàlla dekkal na ko,
30但 神却使他从死人中复活了。
31 te diirub ay fan yu bare feeñu na ñi àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem; léegi nag ñooy ay seedeem ci wetu xeet wi,
31有许多日子,他向那些跟他一同从加利利上耶路撒冷的人显现,现在这些人在民众面前作了他的见证人,
32 te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, li Yàlla digoon sunuy maam,
32我们报好信息给你们: 神给列祖的应许,
33 def na ko ngir nun seeni sët, ci li mu dekkal Yeesu. Moom lañu bindoon ci ñaareelu saaru Sabóor ne:“Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.”
33借着耶稣的复活,向我们这些作子孙的应验了。就如诗篇第二篇所记的:‘你是我的儿子,我今日生了你。’
34 Te it li ko Yàlla dekkal, ba mu bañatee jaar ci dee, te suuf du ko lekk mukk, moom la Yàlla wax ne:“Dinaa la may barke yu sell te wóor,yi ma digoon Daawuda.”
34至于 神使他从死人中复活,不再归于朽坏,他曾这样说:‘我必把应许大卫的、神圣可靠的恩福赐给你们。’
35 Moo tax mu waxaat feneen ne:“Doo bàyyi sa Waa ju sell, mu yàqu.”
35所以他在另一篇说:‘你必不容你的圣者见朽坏。’
36 Ndaxte bi Daawuda defee coobareg Yàlla ci jamonoom, mu faatu, ñu suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko.
36“大卫在他自己的世代里,遵行了 神的计划,就睡了,归回他列祖那里,见了朽坏。
37 Waaye Ki Yàlla dekkal, yaramam seeyul.
37唯独 神所复活的那一位,没有见过朽坏。
38 «Kon nag bokk yi, nangeen xam ne, ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woon a àttee nit ni ku jub,
38所以弟兄们,你们当知道,赦罪之道是由这位耶稣传给你们的。在你们靠摩西律法不能称义的一切事上,
39 fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm.
39信靠他的人就得称义了。
40 Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leen a dal, ci li ñu ne:
40你们要小心,免得先知书上所说的临到你们:
41 “Yéen ñiy xeebaate, gis leen lii,ngeen yéemu ba far;ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf,joo xam ne su ngeen ko déggee sax,dungeen ko gëm.”»
41‘傲慢的人哪!你们要看、要惊奇、要灭亡,因为在你们的日子,我要作一件事,就算有人告诉你们,你们总是不信。’”
42 Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésu noflaay ba ca tegu.
42保罗和巴拿巴出来的时候,众人请求他们下一个安息日再对他们讲这些话。
43 Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla.
43散会以后,许多犹太人和归信犹太教的虔诚人,跟从了保罗和巴拿巴。两人对他们谈话,勉励他们要恒久住在 神的恩典中。
44 Noonu bésu noflaay ba ca tegu, daanaka waa dëkk bépp daje, ngir déglu kàddug Yàlla.
44下一个安息日,几乎全城的人都聚了来,要听主的道。
45 Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, ñu daldi fees ak kiñaan, di weddi li Pool di wax te di ko xas.
45犹太人看见这么多人,就满心嫉妒,反驳保罗所讲的,并且毁谤他们。
46 Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu war a jëkk a yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne, yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi woññiku ci ñi dul Yawut.
46保罗和巴拿巴却放胆说:“ 神的道,先讲给你们听,是应该的。但因为你们弃绝这道,断定自己不配得永生,所以我们现在就转向外族人去了。
47 Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan:“Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut,ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”»
47因为主曾这样吩咐我们说:‘我已立你作外族人的光,使你把救恩带到地极去。’”
48 Ñi dul Yawut nag, bi ñu déggee loolu, daldi bég tey màggal kàddug Boroom bi; te ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex daldi gëm.
48外族人听见了就欢喜,赞美主的道,凡指定得永生的都信了。
49 Noonu kàddug Boroom bi di law ci diiwaan bépp.
49于是主的道传遍那地。
50 Waaye Yawut ya xiir ay jigéen, ñi woomle te farlu ci diine, ñoom ak magi dëkk ba, ñu fitnaal Pool ak Barnabas, ngir génne leen réew ma.
50但犹太人唆使虔诚尊贵的妇女和城内的显要,煽动大家迫害保罗和巴拿巴,把他们驱逐出境。
51 Waaye Pool ak Barnabas daldi yëlëb seen pëndu tànk, ngir dëggal seen weddi, jëm dëkku Ikoñum.
51两人当众跺掉脚上的尘土,往以哥念去了。
52 Naka taalibe yi nag, ñu fees ak mbég ak Xel mu Sell mi.
52门徒满有喜乐,又被圣灵充满。