1 Noonu saraxalekat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»
1司提反的申辩
2 Ecen tontu ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan.
2司提反说:“各位父老兄弟请听!我们的祖宗亚伯拉罕,在美索不达米亚,还没有住在哈兰的时候,荣耀的 神向他显现,
3 Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.”
3对他说:‘你要离开本地本族,到我指示你的地方去。’
4 «Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi.
4他就离开迦勒底人的地方,住在哈兰。他父亲死后, 神又叫他从那里迁到你们现在所住的地方。
5 Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu war a donnale, du sax fu mu man a teg tànkam; waaye dig na ko ne, dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.
5在这里 神并没有赐他产业,连立足之地也没有。但 神应许把这地赐给他和他的后裔为业,虽然那时他还没有儿子。
6 Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.”
6 神就这样说:‘你的后裔必在外地寄居,人要奴役、虐待他们四百年。’
7 Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.”
7 神又说:‘奴役他们的那个国家,我要亲自惩罚。以后,他们要出来,在这地方事奉我。’
8 Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom-ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.
8 神也赐他割礼为约。这样,亚伯拉罕生了以撒,第八天就给他行了割礼。后来,以撒生雅各,雅各生了十二位祖先。
9 «Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,
9“祖先妒忌约瑟,把他卖到埃及去,然而 神与他同在,
10 génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanamu Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp.
10救他脱离一切苦难,使他在埃及王法老面前,有智慧、得恩宠。法老立他为首相,管理埃及和法老的全家。
11 «Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk.
11后来埃及和迦南全地遭遇饥荒、大灾难,我们的祖先找不到粮食。
12 Yanqóoba nag dégg ne, Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk.
12雅各听见埃及有谷粮,就派我们的祖先去,这是第一次。
13 Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa xàmmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam.
13第二次的时候,约瑟就向哥哥们表露自己的身世,法老才知道约瑟的家世。
14 Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak mbokkam yépp, ñuy juróom-ñaar-fukki nit ak juróom.
14约瑟就派人去把他父亲雅各和全家七十五人都接来。
15 Noonu Yanqóoba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam.
15于是雅各下了埃及。后来他和我们祖先都死了,
16 Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sikem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Emor ca Sikem.
16运到示剑,埋葬在亚伯拉罕用银子向哈抹子孙买来的坟地里。
17 «Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gën a bare ci Misra,
17“ 神给亚伯拉罕的应许快要实现的时候,以色列人在埃及人口繁盛增多;
18 ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.
18但是,到了另一位不认识约瑟的君王兴起统治埃及的时候,
19 Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.
19他就谋害我们的同胞,虐待我们的祖先,逼他们拋弃自己的婴孩,不容婴孩存活。
20 «Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,
20就在那时候,摩西出生了,他非常俊美,在父亲的家中抚养了三个月。
21 ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.
21他被拋弃的时候,法老的女儿把他拾起来,当作儿子抚养。
22 Musaa nag di ku yeewu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf.
22摩西学尽了埃及人的一切学问,说话行事都有能力。
23 «Bi mu demee ba am ñeent-fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil.
23“到了四十岁,他心中起了一个念头,要去看望自己的同胞以色列人。
24 Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyyul ko, ba dóor waayi Misra ja.
24当他看见有一个人受欺负,就去护卫,为那受屈的抱不平,打死了那个埃及人。
25 Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne, ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko.
25他以为同胞们都必知道 神要借着他的手拯救他们,事实上他们却不知道。
26 Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéem a jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?”
26第二天,有人在打架,摩西就出面调解,说:‘你们是弟兄,为什么彼此欺负呢?’
27 Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw?
27那欺负人的把他推开,说:‘谁立了你作我们的领袖和审判官呢?
28 Ndax danga maa bëgg a rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?”
28难道你想杀我,像昨天杀那个埃及人一样吗?’
29 Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom.
29摩西因为这句话,就逃到米甸地寄居,在那里生了两个儿子。
30 «Lu ko wees ñeent-fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku safara ci biir as ngarab.
30“过了四十年,在西奈山的旷野,有一位使者,在荆棘中的火焰里,向摩西显现。
31 Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko:
31他见了这个异象,十分惊奇;他正上前察看的时候,就有主的声音说:
32 “Man maay sa Yàllay maam, di Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.” Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te ñemeetul a xool.
32‘我是你祖宗的 神,就是亚伯拉罕、以撒、雅各的 神。’摩西战战兢兢,不敢观看。
33 Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la.
33主对他说:‘把你脚上的鞋脱掉,因为你所站的地方是圣地。
34 Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.”
34我的子民在埃及所受的痛苦,我实在看见了;他们的叹息我也听见了,我下来是要救他们。你来,我要派你到埃及去。’
35 «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.
35他们拒绝了这位摩西,说:‘谁立了你作领袖和审判官呢?’但 神借着在荆棘中向他显现的使者的手,派他作领袖和救赎者。
36 Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca Géej gu xonq ga ak ca màndiŋ ma diirub ñeent-fukki at.
36这人领他们出来,并且在埃及地、红海和旷野,行奇事神迹四十年。
37 Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.”
37以前那位对以色列人说‘ 神要从你们弟兄中间,给你们兴起一位先知像我’的,就是这摩西。
38 Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko.
38那曾经在旷野的大会中,和那在西奈山上对他说话的使者同在,也与我们的祖先同在的,就是他。他领受了活的圣言,传给我们。
39 Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra.
39我们的祖先不肯听从他,反而把他推开,他们的心已经转向了埃及,
40 Ñu sant Aaroona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.”
40就对亚伦说:‘给我们做一些神像,可以走在我们前头。因为把我们从埃及地领出来的那个摩西,我们不知道他遭遇了什么事。’
41 Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo.
41在那些日子里,他们做了一个牛犊,把祭物献给那偶像,并且因自己手所做的而欢乐。
42 Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne:“Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur,jébbal ma, boole ko ak i sarax,diirub ñeent-fukki at ca màndiŋ ma?
42于是 神转身离开,任凭他们事奉天象,正如先知书所说:‘以色列家啊,你们在旷野四十年,岂是将祭牲和祭物献给我呢?
43 Yóbbu ngeen sax fu nekk tànt,biy màggalukaayu Molog ak biddiiwub Refan,bi ñu daan bokkaaleel Yàlla,di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen!Kon nag dinaa leen toxal,yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.”
43你们抬着摩洛的帐幕,和理番神的星,就是你们做来敬拜的像。所以我要把你们放逐到巴比伦那一边去。’
44 «Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma tàntu màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Tànt boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon.
44“我们的祖先在旷野有作证的帐幕,就是跟摩西谈话的那位指示他,依照他看见的样式做的。
45 Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot tànt ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Tànt ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.
45我们的祖先相继承受了这帐幕, 神把外族人从他们面前赶走以后,他们就同约书亚把帐幕带进所得为业的地方,直到大卫的日子。
46 Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba.
46大卫在 神面前蒙了恩,就求为雅各的 神找个居所,
47 Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga.
47而由所罗门为他建造殿宇。
48 «Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:
48其实至高者并不住人手所造的,正如先知说:
49 “Asamaan mooy sama jal,te suuf mooy sama tegukaayu tànk.Kon gan kër ngeen may tabaxal,mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay?
49‘主说:天是我的宝座,地是我的脚凳,你们要为我建造怎样的殿呢?哪里是我安息的地方呢?
50 Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp?— Moom la Boroom bi doon wax.”
50这一切不都是我手所造的吗?’
51 «Yéen ñi dëgër bopp, ànd ak xol buy bañ ak ay nopp yuy fatt, mel ni ñi xamul Yàlla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def yéen itam.
51“你们颈项刚硬、心和耳都未受割礼的人哪!你们时常抗拒圣灵,你们的祖先怎样,你们也怎样。
52 Kan ca yonent ya la seeni maam tegul woon ay fitna? Rey nañu ñi doon yégle ñëwug Aji Jub ji, moom mi ngeen jébbale léegi, ba ñu rey ko.
52有哪一个先知,你们的祖先不迫害呢?你们杀了那些预先宣告那义者要来的人,现在又把那义者出卖了,杀害了。
53 Jot ngeen yoonu Musaa, wi Yàlla wàcce jaarale ko ci ay malaaka, te sàggane ngeen ko.»
53你们领受了由天使传达的律法,却不遵守。”
54 Bi ñu déggee loolu nag, seeni xol di dagg, ñuy yéyu, jëm ci kawam.
54司提反被石头打死众人听了这些话,心中非常恼怒,就向着司提反咬牙切齿。
55 Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne jàkk ci asamaan, gis ndamu Yàlla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndeyjooru Yàlla.
55但司提反被圣灵充满,定睛望着天,看见 神的荣耀,并且看见耶稣站在 神的右边,
56 Mu ne: «Seetleen, maa ngi gis asamaan yi ubbiku, te Doomu nit kaa ngii taxaw ci ndeyjooru Yàlla.»
56就说:“看哪!我看见天开了,人子站在 神的右边。”
57 Bi ñu déggee loolu, ñu daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; ñu ànd, ne milib ci kawam;
57众人大声喊叫,掩着耳朵,一齐向他冲过去,
58 ñu wat-wate ko, génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon nañu seeni yére ci tànki waxambaane wu tudd Sool.
58把他推出城外,用石头打他。那些证人把自己的衣服,放在一个名叫扫罗的青年人脚前。
59 Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!»
59他们用石头打司提反的时候,他呼求说:“主耶稣啊,求你接收我的灵魂!”
60 Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: «Boroom bi, bu leen bindal bàkkaar bii,» ba noppi mu nelaw.
60然后跪下来大声喊着说:“主啊,不要把这罪归给他们!”说了这话,就睡了。