Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Galatians

2

1 Ba ñu ca tegee fukki at ak ñeent, ànd naa ak Barnabas, dellu Yerusalem, yóbbaale Tit.
1其他使徒接纳保罗
2 Dem naa fa, ndaxte Yàllaa ma fa yebal ci kaw peeñu. Ba ma demee, daje naa ak ñi ñu gën a fonk ca mbooloo ma, ma wéetoo ak ñoom, won leen xebaar bu baax, bi may yégal ñi dul Yawut; ngir ragal sama coonob démb mbaa tey neen.
2我是顺从启示去的;在那里我对他们说明我在外族人中所传的福音,私下讲了给那些有名望的人听,免得我从前或现在都白跑了。
3 Te Tit mi ma gunge woon sax de, li mu bokk ci xeetu Gereg, taxul ñu sonal nu ci xarafal ko.
3与我同行的提多,虽然是希腊人,也没有强迫他受割礼;
4 Fekk na mbir moomu nekk coow ndax naaféq, yi yoxoosu ci sunu biir ak mébét mu bon, ngir seet yaatu gi nu am ci Yeesu Kirist, ba fexe noo defaat ay jaam.
4这是因为有些混进来的假弟兄,暗暗地来侦查我们在基督耶稣里享有的自由,为的是要辖制我们。
5 Waaye yaatalunu leen benn yoon, ngir dëggug xebaar bu baax bi man a sax ci yéen.
5对这些人,我们一点也没有让步妥协,为了要使福音的真理存留在你们中间。
6 Waaye ñi ñu gën a fonk --ak lu man a doon seen sag xooluma ko, ñépp a yem fa kanam Yàlla — waaye ñooñu ñu teg njiit boog, bi ma dajee ak ñoom, yokkuñu dara ci sama sas.
6至于那些被认为有名望的人(无论他们从前怎么样,都与我无关; 神不以外貌取人),他们并没有给我增加什么;
7 Gis nañu ne, Yàllaa nu yebal, muy man di Piyeer, ngir nu yégle xebaar bu baax bi; ma féetewoo ñi dul Yawut, Piyeer féetewoo Yawut yi.
7反而因为看见我受托传福音给没有受割礼的人,就像彼得受托传福音给受割礼的人一样,
8 Ndaxte ni Yàlla jëfe ci Piyeer, miy ndawam ci Yawut yi, noonu it la jëfe ci man, may ndawam ci ñi dul Yawut.
8(因为运行在彼得里面,使他作受割礼者的使徒的那一位,也运行在我里面,使我作外族人的使徒,)
9 Te Saag, Sefas ak Yowaana nag, ñi ñu teg kenuy mbooloo mi, bi ñu ràññee yen bi ma Yàlla jagleel ci yiwam, ñu fekksi nu ci, ba jox nu loxo, man ak Barnabas, nu liggéey ca ña dul Yawut, ñoom ñu liggéey ca Yawut ya.
9又知道我蒙了 神的恩,那几位被誉为柱石的雅各、矶法和约翰,就向我和巴拿巴伸出右手互相许诺,我们要到外族人那里去传福音,他们要到受割礼的人那里去传福音;
10 Li ñu doon laaj rekk moo di, nuy fàttaliku seen aji néew doole yi, fekk sax laxasu woon naa ci def ko.
10只是要我们记念穷人,这本来也是我一向热心作的。
11 Waaye bi Sefas ñëwee dëkku Ancos, yedd naa ko ci kanamu ñépp, ndaxte li mu def jaaduwul.
11彼得受责备可是,矶法到了安提阿的时候,因为他有该责备的地方,我就当面反对他。
12 Ndaxte laata ndaw yi Saag yónni di ñëw, da daan bokk di lekk ak ñi dul Yawut. Waaye bi ñu agsee, te mu ragal kureel boobu faaydaal xaraf, mu dellu gannaaw, di sore ñi dul Yawut.
12从雅各那里来的人还没有到以前,他和外族人一同吃饭;但他们来到了,他因为怕那些守割礼的人,就从外族人中退出来,和他们分开。
13 Yeneen Yawut yi it daldi ànd ak Sefas ci naaféqam, ba yóbbaale sax Barnabas.
13其余的犹太人也和他一同装假,甚至连巴拿巴也受了影响,跟着他们装假。
14 Bi ma seetee nag ne, awuñu woon ci dëgg, gi xebaar bu baax bi di jàngale, ma yedd Sefas ci kanamu ñépp ne ko: «Yaw miy Yawut, gannaaw dëddu nga aaday Yawut yi, ba dund ni ku dul Yawut, lu tax nga bëgg a sëf diiney Yawut ci ñi dul Yawut?»
14但我一见他们所行的不合福音的真理,就当众对矶法说:“你是犹太人,生活既然像外族人而不像犹太人,怎么还勉强外族人跟随犹太人的规矩呢?”
15 Nun danoo cosaanoo ci xeetu Yawut, te bokkunu ci xeet, yi xamul Yàlla tey bàkkaar.
15因信称义我们生来是犹太人,不是外族中的罪人;
16 Teewul nu xam ne, Yàlla du àtte kenn ni ku jub ci kaw sàmm yoon, waaye ci gëm Yeesu Kirist. Kon nun itam gëm nanu Kirist Yeesu, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw gëm Kirist, te du ci sàmm yoon. Ndaxte du caageenug sàmm yoon mooy tax Yàlla àtte kenn ni ku jub.
16既然知道人称义不是靠行律法,而是因信耶稣基督,我们也就信了基督耶稣,使我们因信基督称义,不是靠行律法;因为没有人能靠行律法称义。
17 Waaye ba tey su fekkee ne nu ngi wut a jub ci kaw gëm Kirist, fekk nu ne fàŋŋ di ay bàkkaarkat, ndax nag Kirist moo sas bàkkaar? Mukk!
17如果我们寻求在基督里称义,却仍然是罪人,难道基督是使人犯罪的吗?绝对不是。
18 Waaye su ma delloo di sàmm ndigali yoon, yi ma bàyyi, dëgg-dëgg dinaa wone noonu ne, moykatu yoon wi laa.
18我若重建我所拆毁的,就证明自己是个有过犯的人。
19 Ci li jëm ci yoonu Musaa, dee naa, fekk yoon wi ci boppam moo ko waral, ngir ma man a dund, ba amal jariñ Yàlla.
19我借着律法已经向律法死了,使我可以向 神活着。
20 Daajaale nañu ma ak Kirist ca bant ba, te noonu du man may dundati, waaye Kirist mooy dund ci man. Dundu mbindeef, gi may dund nag, maa ngi koy dund ci gëm Doomu Yàlla ji, moom mi ma bëgg, ba joxe bakkanam ngir man.
20我已经与基督同钉十字架;现在活着的,不再是我,而是基督活在我里面;如今在肉身中活着的我,是因信 神的儿子而活的;他爱我,为我舍己。
21 Duma neenal yiwu Yàlla, ndaxte su sàmm yoon doon tax a jub fa kanam Yàlla, kon Kirist dee na cig neen.
21我不废弃 神的恩;如果义是借着律法而来的,基督就白白地死了。