1 Lii mooy li ëpp solo ci li nuy wax: am nanu saraxalekat bu mag bu mel noonu, moom mi toog ci ndeyjooru Aji Màgg ja ca nguuram ca kaw.
1耶稣是更美的约的中保
2 Mu ngi liggéey ca bérab bu sell-baa-sell, di màggalukaay bu dëggu. Nit defaru ko; Boroom bee ko sos.
2在至圣所和真会幕里供职;这真会幕是主支搭的,不是人支搭的。
3 Bépp saraxalekat bu mag fal nañu ko, ngir muy def ay sarax ak ay saraxi mala yu jëm ca Yàlla. Kon nag fàww Yeesu am lu mu joxe.
3所有大祭司都是为了献礼物和祭品而设立的,所以这位大祭司,也必须有所献上的。
4 Bu nekkoon ci àddina, du nekk sax saraxalekat, ndaxte am na fi ba noppi ay saraxalekat yuy def ay sarax, ni ko yoonu Musaa santaanee.
4如果他在地上,就不会作祭司,因为已经有按照律法献礼物的祭司了。
5 Saraxalekat yooyu ñu ngi liggéeyal Yàlla ca màggalukaay, ba nekk misaal tey takkandeeru yëf yu dëggu, ya féete kaw. Moo tax ba Musaa naree defar tàntu màggalukaay ba, Yàlla artu na ko ne ko: «Teeylul ba def lépp, roye ko ci bi ma la won ca tund wa.»
5这些祭司所供奉的职事,不过是天上的事物的副本和影像,就如摩西将要造会幕的时候, 神曾经警告他说:“你要留心,各样物件,都要照着在山上指示你的样式去作。”
6 Waaye léegi nag liggéeyu saraxale, bi ñu jox Yeesu, moo gën a màgg liggéeyu saraxalekat yooyu, mel ni it kóllëre, gi Yeesu fas diggante Yàlla ak nit, moo sut kóllëre gu jëkk ga te mu tëdd ci ay dige yu ëpp yu jëkk ya.
6但是现在耶稣得了更尊贵的职分,正好像他是更美的约的中保,这约是凭着更美的应许立的。
7 Bu fekkoonte ne, kóllëre gu jëkk ga dafa amul woon benn sikk, kon du aajo ñu koy weccee ak geneen.
7如果头一个约没有缺点,就没有寻求另一个约的必要了。
8 Waaye nag Yàlla sikk na bànni Israyil, bi mu naan:Boroom bi nee na:«Ay fan a ngi ñëwyu may fasi kóllëre gu beesak bànni Israyil ak waa Yude.Kóllëre googu nagbokkul ak gi ma fasoon ak seeni maam,
8可是 神指责他们,说:“看哪,主说,日子要到了,我要与以色列家和犹大家订立新约。
9 ba ma leen jàppee ci loxo,génne leen réewu Misra.Boroom bi nee na:Beddeeku naa leenndaxte sàmmuñu sama kóllëre.
9这新约不像从前我拉他们祖先的手,领他们出埃及的日子与他们所立的约。因为他们没有遵守我的约,我就不理会他们。这是主说的。
10 Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak bànni Israyil,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xel,bind ko ci seen xol.Dinaa nekk seen Yàlla,ñu doon samay gaay.
10主说:‘因为在那些日子以后,我要与以色列家所立的约是这样:我要把我的律法放在他们的心思里面,写在他们的心上。我要作他们的 神,他们要作我的子民。
11 Kenn dootul war a jàngal moroomamwalla mbokkam, di wax naan:“Xamal Boroom bi!”Ndaxte ñépp dinañu ma xam,li dale ci ki gën a ndaw ba ci ki gën a mag.
11他们各人必不用教导自己的邻居,和自己的同胞,说:你要认识主。因为所有的人,从最小到最大的,都必认识我。
12 Ndaxte dinaa leen baal seeni tooñ,te dootuma fàttaliku seeni bàkkaar.»
12我也要宽恕他们的不义,决不再记着他们的罪恶。’”
13 Kon nag bi Yàllay wax ci kóllëre gu bees gi, dafa fekk mu màggatal gu jëkk ga. Te lu xewwi te màggat mi ngi ci tànki wéy.
13 神既然说到新的约,就是把前约当作旧的了;那变成陈旧衰老的,就快要消逝了。