Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

John

20

1 Bés ba jiitu ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Bi mu agsee, mu gis ne dindi nañu xeer, wa ñu ko ube woon.
1耶稣复活(太28:1-8;可16:1-8;路24:1-10)
2 Mu daw, dem ca Simoŋ Piyeer ak ca beneen taalibe ba, maanaam ka Yeesu bëggoon, ne leen: «Jële nañu néewu Boroom ba ca bàmmeel ba, te xamunu fu ñu ko yóbbu.»
2她就跑去见西门.彼得,和耶稣所爱的那个门徒,对他们说:“有人把主从坟墓里搬走了,我们不知道他们把他放在哪里。”
3 Piyeer ak beneen taalibe ba daw, dem ca bàmmeel ba.
3彼得和那门徒就动身,到坟墓那里去。
4 Ñoom ñaar ñépp a ngi doon daw, waaye beneen taalibe ba raw Piyeer, jëkk ko ca bàmmeel ba.
4两个人一齐跑,那门徒比彼得跑得快,先到了坟墓,
5 Duggul nag, dafa sëgg, yër, séen càngaay la ca suuf.
5屈身向里面观看,看见细麻布还在那里,但他却没有进去。
6 Noonu Simoŋ Piyeer, mi ko toppoon, agsi, daldi dugg. Mu séen càngaay la ci suuf,
6西门.彼得随后也到了;他进入坟墓,看见细麻布还放在那里,
7 ak kaala ga muuroon boppu Yeesu. Waaye kaala googu àndul ak càngaay la; dañu ko laxas, teg ko ci wet.
7也看见耶稣的裹头巾,没有和细麻布放在一起,而是卷着放在一边。
8 Noonu keneen ka jiitu woon ca bàmmeel ba, duggsi moom itam. Naka la gis, daldi gëm.
8那时,先到坟墓的那门徒也进去,他看见,就信了。
9 Taalibe yi xamaguñu woon Mbind, mi doon wone ne, Yeesu dafa war a dekki.
9他们还不明白经上所说“他必须从死人中复活”这句话的意思。
10 Noonu taalibe ya dëpp, ñibbi.
10于是两个门徒就回家去了。
11 Maryaama nag moom, ma nga desoon ca biti, ca wetu bàmmeel ba, di jooy. Bi muy jooy, mu sëgg, yër ci biir,
11向抹大拉的马利亚显现(太28:9-10;可16:9-11)马利亚站在坟墓外面哭泣。她哭的时候,屈身往里面观看,
12 séen ñaari malaaka yu sol mbubb yu weex, toog ca bérab, ba ñu dencoon Yeesu; kenn ka féeteek bopp bi, ki ci des ca tànk ya.
12看见两个身穿白衣的天使,坐在安放耶稣身体的地方,一个在头那边,一个在脚那边。
13 Malaaka ya laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy?» Mu tontu leen ne: «Dañoo jël sama Boroom, te xawma fu ñu ko yóbbu.»
13天使问她:“妇人,你为什么哭?”她说:“有人把我的主搬走了,我不知道他们把他放在哪里。”
14 Bi mu waxee loolu, mu geestu, séen Yeesu mu taxaw, waaye xamul woon ne moom la.
14马利亚说了这话,就转过身来,看见耶稣站在那里,却不知道他就是耶稣。
15 Yeesu laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy? Kooy seet?» Mu foog ne boroom tool ba la, ne ko: «Sëriñ bi, bu fekkee yaa ko yóbbu, wax ma foo ko denc, ma jëli ko.»
15耶稣对她说:“妇人,你为什么哭?你找谁呢?”马利亚以为耶稣是园丁,就对他说:“先生,如果是你把他挪去了,请告诉我你把他放在什么地方,我好去搬回来。”
16 Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi.»
16耶稣对她说:“马利亚!”她转过身来,用希伯来话对他说:“拉波尼!”(就是“老师”的意思。)
17 Yeesu ne ko: «Bu ma téye, ndaxte yéegaguma ca Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéeg ca sama Baay biy seen Baay, ca sama Yàlla jiy seen Yàlla.»
17耶稣说:“你不要拉住我,因为我还没有上去见父。你要到我的弟兄们那里去,告诉他们我要上去见我的父,也是你们的父;见我的 神,也是你们的 神。”
18 Noonu Maryaamam Magdala dem, yégali ko taalibe ya ne leen: «Gis naa Boroom bi!» Mu daldi leen nettali li mu ko wax.
18抹大拉的马利亚就去,向门徒报信说:“我已经看见主了!”她又把主对她所说的话告诉他们。
19 Bés boobu ca ngoon sa, taalibe yaa nga daje woon ca genn kër, tëju ca biir ndax ragal Yawut ya. Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!»
19向门徒显现(太28:16-20;可16:14-18;路24:36-49)礼拜日黄昏的时候,门徒聚在一起,因为怕犹太人,就把门户都关上。耶稣来了,站在他们中间,说:“愿你们平安。”
20 Mu daldi leen won ay loxoom ak wetam. Bi ñu gisee Boroom bi, taalibe ya daldi bég lool.
20说了这话,就把手和肋旁给他们看。门徒看见主,就欢喜了。
21 Yeesu dellu ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen! Ni ma Baay bi yónnee, noonu laa leen di yónnee, man itam.»
21耶稣又对他们说:“愿你们平安。父怎样差遣了我,我也怎样差遣你们。”
22 Bi mu waxee loolu, mu ëf leen ne leen: «Sol naa leen Xelu Yàlla mu Sell mi.
22说了这话,就向他们吹一口气,说:“你们领受圣灵吧!
23 Ñi ngeen di baal seeni bàkkaar, baal nañu leen ba noppi; ñi ngeen baalul, baaluñu leen.»
23你们赦免谁的罪,谁的罪就得赦免;你们不赦免谁的罪,谁的罪就不得赦免。”
24 Fekk na Tomaa, mi bokk ci fukki taalibe yi ak ñaar, te turam di tekki «Séex bi,» nekku fa woon, bi Yeesu ñëwee.
24耶稣向疑惑的多马显现十二个门徒中,有一个称为“双生子”的多马。耶稣来的时候,他没有和门徒在一起。
25 Yeneen taalibe yi ne ko: «Gis nanu Boroom bi!» Waaye mu ne leen: «Su ma gisul fa ñu daajoon pont ya ci ay loxoom, te defuma ca sama baaraam, su ma tegul it sama loxo ci wetam, duma ko gëm mukk.»
25其他的门徒对他说:“我们已经见过主了。”多马对他们说:“除非我亲眼看见他手上的钉痕,用我的指头探入那钉痕,又用我的手探入他的肋旁,我决不相信。”
26 Bi ñu ca tegee ayu-bés, taalibe Yeesu ya dajewaat ca biir kër ga, Tomaa itam a nga fa woon. Bunt yépp tëju woon nañu, waaye Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!»
26过了八天,门徒又在屋子里,多马也和他们在一起。门户都关上了。耶稣来了,站在他们中间,说:“愿你们平安。”
27 Noonu mu ne Tomaa: «Indil sa baaraam fii te seet sama loxo; indil sa loxo, teg ko ci sama wet. Bàyyil di weddi te nga gëm.»
27然后对多马说:“把你的指头放在这里,看看我的手吧!伸出你的手来,探探我的肋旁!不要疑惑,只要信!”
28 Tomaa tontu ko ne: «Sama Boroom, sama Yàlla!»
28多马对他说:“我的主!我的 神!”
29 Yeesu ne ko: «Li nga ma gis a tax nga gëm? Ki bég mooy ki gëm te gisu ma!»
29耶稣说:“你因为看见我才信吗?那些没有看见就信的人,是有福的。”
30 Yeesu wone na it ci kanamu taalibe ya yeneeni firnde yu ñu nettaliwul ci téere bii.
30本书是要人信耶稣得生命耶稣在门徒面前还行了许多别的神迹,没有记在这书上。
31 Waaye li ci nekk, bind nañu ko ngir ngeen gëm ne, Yeesu mooy Almasi bi, Doomu Yàlla ji, te seen ngëm may leen, ngeen am ci moom dund.
31但把这些事记下来,是要你们信耶稣是基督,是 神的儿子,并且使你们信了,可以因他的名得生命。