1 Amoon na ca Farisen ya nit ku ñu naan Nikodem te mu bokk ca kilifay Yawut ya.
1人必须重生
2 Genn guddi mu ñëw ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne, Yàllaa la yónni ngir nga jàngal nu, ndaxte kenn mënul a def firnde yii ngay wone te Yàlla àndul ak moom.»
2他夜间来到耶稣那里,对他说:“拉比,我们知道你是从 神那里来的教师,因为如果没有 神同在,你所行的这些神迹,就没有人能行。”
3 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, képp ku judduwaatul doo man a seede nguuru Yàlla.»
3耶稣回答:“我实实在在告诉你,人若不重生,就不能见 神的国。”
4 Nikodem ne ko: «Nit ku xas ba màggat, nan lay man a judduwaate? Ndax day dellu ci biiru yaayam ngir judduwaat?»
4尼哥德慕说:“人老了,怎能重生呢?难道他能再进母腹生出来吗?”
5 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, ku judduwul ci ndox ak ci Xelum Yàlla, doo man a bokk ci nguuru Yàlla.
5耶稣回答:“我实实在在告诉你,人若不是从水和圣灵生的,就不能进 神的国。
6 Lu juddoo ci nit, nit la; waaye lu juddoo ci Xelum Yàlla, xel la.
6从肉身生的就是肉身,从灵生的就是灵。
7 Li ma ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal.
7你不要因为我对你说‘你们必须重生’而感到希奇。
8 Ngelaw fu ko neex lay jublu. Yaa ngi koy dégg waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la mel it ci képp ku juddoo ci Xelum Yàlla.»
8风随意而吹,你听见它的响声,却不知道它从哪里来,往哪里去;凡从圣灵生的,也是这样。”
9 Ci baat yooyu Nikodem ne ko: «Nu loolu man a ame?»
9尼哥德慕说:“怎能有这事呢?”
10 Yeesu tontu ko ne: «Yaw yaay jàngal bànni Israyil te xamuloo mbir yii?
10耶稣说:“你是以色列人的教师,还不明白这事吗?
11 Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, noo ngi wax li nu xam, di nettali li nu gis, waaye nanguwuleen a gëm li nu seede.
11我实实在在告诉你,我们知道的,才讲论;见过的,就作证,然而你们却不接受我们的见证。
12 Gannaaw gëmuleen li ma leen di wax ci mbiri àddina, naka ngeen man a gëme, bu ma leen waxee ci mbiri asamaan?
12我对你们讲地上的事,你们尚且不信,如果讲天上的事,怎能相信呢?
13 Kenn musul a yéeg ci asamaan su dul ki fa jóge, muy Doomu nit ki.
13除了那从天上降下来的人子(有些抄本作“除了那从天上降下来仍旧在天上的人子”),没有人升过天。
14 Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki,
14摩西在旷野怎样把铜蛇举起,人子也必照样被举起来,
15 ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.»
15使所有信他的人都得永生。
16 Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.
16“ 神爱世人,甚至把他的独生子赐给他们,叫一切信他的,不至灭亡,反得永生。
17 Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen.
17因为 神差他的儿子到世上来,不是要定世人的罪,而是要使世人借着他得救。
18 Képp ku ko gëm deesu la daan, waaye ku ko gëmul daan nañu la ba noppi, ndaxte gëmuloo ci turu Doom ji Yàlla am kepp.
18信他的,不被定罪;不信的,罪已经定了,因为他不信 神独生子的名。
19 Ci nii la àtte bi ame: leer gi ñëw na ci àddina, waaye nit lëndëm gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon.
19光来到世上,世人因为自己的行为邪恶,不爱光倒爱黑暗,定他们罪的原因,就在这里。
20 Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëgu ndarakàmm.
20凡作恶的都恨光,不来接近光,免得他的恶行暴露出来。
21 Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne, def na ay jëfam ci kanam Yàlla.
21凡行真理的,就来接近光,好显明他所作的都是靠着 神而作的。”
22 Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox.
22他必兴旺,我必衰微这事以后,耶稣和门徒来到犹太地,他和他们住在那里,并且施洗。
23 Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit ñi daan nañu ñëw ci moom, mu di leen sóob.
23约翰也在靠近撒冷的艾嫩施洗,因为那里水多;众人都去受洗。
24 Booba tëjaguñu Yaxya ci kaso.
24那时约翰还没有入狱。
25 Foofa ay taalibey Yaxya tàmbalee werante ak benn Yawut ci mbirum sangu set.
25约翰的门徒和一个犹太人为洁净礼发生辩论。
26 Ci kaw loolu ñu dem ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ndax fàttaliku nga kooka nga seede woon te mu nekkoon ak yaw ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay sóobe ci ndox léegi te ñépp a ngay dem ca moom!»
26他们来到约翰那里,对他说:“拉比,你看,从前和你在约旦河东,你为他作见证的那一位,他也在施洗,众人都到他那里去了。”
27 Yaxya tontu leen: «Kenn mënul a am dara lu ko Yàlla joxul.
27约翰回答:“除了从天上赐下来给他的,人就不能得到什么。
28 Yéen ci seen bopp man ngeen a seede ne, waxoon naa ne, duma Almasi bi waaye dañu maa yónni ma jiitusi ko.
28你们自己可以为我作证:我曾说,我不是基督,不过是奉差遣作他的先锋的。
29 Kiy céetal moo moom séetam. Waaye xaritu kiy céetal dafay taxaw di ko déglu, tey bég, bu déggee baatam. Mbég moomu moo di sama bos tey, te fi mu nekk mat na sëkk.
29娶新娘的是新郎。新郎的好友站在那里听着,听见新郎的声音就非常喜乐。因此,我这喜乐满溢了!
30 Li war moo di moom, mu gën a màgg te man, ma gën a féete suuf.»
30他必兴旺,我必衰微。
31 Ki jóge ci kaw moo féete kaw ñépp; ki jóge ci suuf nag, ci suuf rekk la man a bokk, te ni niti àddina lay waxe. Ki jóge asamaan
31从天上来的“那从天上来的,是在万有之上;从地上来的,是属于地,所讲的也是属于地。那从天上来的,是超越万有之上。
32 day wax li mu gis ak li mu dégg, waaye kenn nanguwul li mu seede.
32他把所见所闻的见证出来,可是没有人接受他的见证。
33 Képp ku nangu seedeem nangu nga ne Yàlla, dëgg lay wax.
33那接受他的见证的,就确认 神是真的。
34 Ndaw li Yàlla yónni, kàddug Yàlla lay wax, ndaxte mayu Xel mu Sell, mi Yàlla sol ci moom, amul dayo.
34 神所差来的那一位讲 神的话,因为 神把圣灵无限地赐给他。
35 Baay bi dafa bëgg Doom ji, te jox na ko sañ-sañ ci lépp.
35父爱子,已经把万有交在他手里。
36 Ku gëm Doom ji, am nga dund gu dul jeex; ku déggadil Doom ji, amuloo dund, waaye merum Yàllaa ngi la tiim.
36信子的,有永生;不信从子的,必不得见永生, 神的震怒却常在他身上。”