1 Bi loolu amee ñu jox ma nattukaay bu mel ni yet, ne ma: «Jógal, natt kër Yàlla gi ak saraxalukaay bi, te waññ ña fay jaamu Yàlla.
1两个见证人
2 Waaye bàyyil ëttu bitib kër Yàlla gi; bu ko natt, ndaxte jébbalees na ko ñi dul Yawut, te dinañu nappaaje dëkk bu sell bi diirub ñeent-fukki weer ak ñaar.
2但圣所外面的院子,不要量它,因为它已经给了外族人,他们要践踏圣城四十二个月。
3 Dinaa may sama ñaari seede yi, ñuy wax ci kàddug Yàlla, sol ay saaku, di toroxlu diirub junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk.»
3我要赐能力给我那两个穿着麻衣的见证人,他们要传道一千二百六十天。”
4 Ñaari seede ya nag ñoo di ñaari garabu oliw yeek ñaari làmpu diwlin, yi taxaw ci kanam Boroom suuf si.
4他们就是站在全地之主面前的两棵橄榄树和两个灯台。
5 Su leen kenn bëggee def lu bon, safaraay génn ci seen gémmiñ, daldi lakk seeni bañaale; te ku leen bëgg a def lu bon, noonu lay war a deeye.
5如果有人想要伤害他们,就有火从他们口中出来,吞灭他们的仇敌。凡是想要伤害他们的,都必这样被杀。
6 Am nañu sañ-sañu téye taw diirub fan, yi ñuy wax ci kàddug Yàlla. Am nañu it sañ-sañu soppi ndox yi deret te wàcce ci kaw suuf musiba yu nekk, saa su ñu ko bëggee.
6他们有权柄在他们传道的日子叫天闭塞不下雨,又有权柄掌管众水,使水变成血,并且有权柄可以随时随意用各样灾难击打全地。
7 Bu ñu noppee seen seede, rab wiy jóge ci kàmb gi dina leen xeex, daan leen, rey leen.
7他们作完了见证的时候,那从无底坑上来的兽要跟他们作战,胜过他们,把他们杀死。
8 Te seeni néew dinañu nekk ci péncum dëkk bu mag, boobu ñuy wooye ci misaal Sodom ak it Misra, fa ñu reyoon seen Boroom ci bant.
8他们的尸首要倒在大城的街道上。这城按着寓意叫所多玛,又叫埃及,就是他们的主被钉十字架的地方。
9 Te diirub ñetti fan ak genn-wàll bépp réew, giir, kàllaama ak xeet dinañu seetaan seeni néew te duñu bàyyi kenn suul leen.
9从各民族、各支派、各方言和各邦国中,都有人观看他们的尸首三天半,又不许人把尸首安放在坟墓里。
10 Waa àddina dinañu bég ci seen dee, di ndokkeelante ak di joqleente ay may, ndaxte ñaari yonent ya lakkaloon nañu waa àddina.
10住在地上的人为了他们的缘故,就欢喜快乐,彼此送礼,因为这两位先知曾经使他们受痛苦。
11 Waaye bi ñetti fan ya ak genn-wàll wéyee, xelum dund, jóge ca Yàlla, solu leen, ñu jóg taxaw. Noonu tiitaange gu réy jàpp ñi leen doon seetaan.
11过了三天半,有生命的气息从 神那里来,进入他们里面,他们就站立起来,看见他们的人都非常惧怕。
12 Ñaari seede ya dégg baat bu xumb ca asamaan naan leen: «Yéegleen fii.» Noonu ñu yéeg asamaan ci aw niir, seeni bañaale di seetaan.
12他们听见从天上来的大声音,说:“上这里来!”他们就驾着云上了天,他们的仇敌也看见了。
13 Ca saa sa am yengu-yengub suuf bu mag, te benn ci fukki xaaju dëkk ba daldi màbb. Juróom-ñaari junniy nit dee ci yengu-yengub suuf ba, te ña ca des tiit, daldi màggal Yàllay asamaan.
13就在那时,大地震发生了,那座城倒塌了十分之一,因着地震而死的有七千人,其余的人都很害怕,就把荣耀归给天上的 神。
14 Ñaareelu musiba mi wéy na, ñetteel baa ngi nii di ñëw.
14第二样灾祸过去了。看哪,第三样灾祸快要到了!
15 Juróom-ñaareelu malaaka ma wol liitam, noonu baat yu xumb jib ca asamaan naan:«Nguuru àddina, jébbalaat nañu kosunu Boroom ak Almaseem,te dina nguuru ba fàww.»
15吹第七枝号第七位天使吹号,天上就有大声音说:“世上的国成了我们的主和他所立的基督的国,他要作王,直到永永远远!”
16 Ñaar-fukki mag ak ñeent, ña toogoon ca seen gàngune ca kanam Yàlla, daldi dëpp seen jë ca suuf, jaamu Yàlla,
16那在 神面前,坐在自己座位上的二十四位长老,都面伏在地上敬拜 神,
17 naan:«Nu ngi lay gërëm, Boroom bi Yàlla,yaw Aji Kàttan ji, ki nekk te nekkoon,ndax gànjoo nga sa kàttan gu réy gi,ngir taxawal sa nguur.
17说:“主啊!全能的 神,昔在今在的,我们感谢你!因为你执掌了大权,作王了!
18 Xeet yi meroon nañu,waaye sa mer wàcc na,te jamono ji jot na,ji ngay àttee ñi dee,neexal say jaam yonent yi,ak sa gaa ñi ak ñi ragal saw tur,muy mag di ndaw,te nga rey ñiy yàq àddina.»
18列国忿怒了!你的震怒也临到了!时候已经到了!死人要受审判!你的众仆人、先知、圣徒,和所有老幼贵贱、敬畏你名的人,都要得赏赐!你也要毁灭那些败坏全地的人!”
19 Noonu kër Yàlla gi ci asamaan daldi ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga daldi feeñ ca biir kër Yàlla ga, te mu daldi am ay melax, ay coow, ay dënnu, yengu-yengub suuf ak tawu yuur bu metti.
19于是,在天上 神的圣所开了,他的约柜就在他的圣所中显现出来。随即有闪电、响声、雷轰、地震、大冰雹。