Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Revelation

17

1 Gannaaw loolu benn ci juróom-ñaari malaaka, ya taawu juróom-ñaari ndab ya, ñëw ne ma: «Kaay, ma won la mbugalu jigéenu moykat bu mag, bi toog ci dex yu bare.
1骑着兽的大淫妇
2 Moom la buuri àddina si àndal ci seen njaaloo. Ci biiñu moy Yàllaam la waa àddina màndee.»
2地上的众王都跟她行过淫,住在地上的人也都喝她淫乱的酒醉了。”
3 Noonu Xelum Yàlla solu ma, malaaka ma yóbbu ma ca màndiŋ ma. Foofa ma gis fa jigéen ju war rab wu xonq te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén, yaram wa fees ak turi xarab Yàlla.
3我在灵里被天使带到旷野去,看见一个妇人,骑着朱红色的兽,这兽布满了亵渎的名号,有七头十角。
4 Jigéen ja sol lu yolet te xonq, takk wurus ak jamaa ak ay per. Yoroon na koppu wurus bu fees ak ñaawteef ak sobeem.
4那妇人穿着紫色和朱红色的衣服,佩戴着金子、宝石和珍珠的装饰,手里拿着金杯,盛满了可憎的物,和她淫乱的污秽。
5 Bindoon nañu ci jëwam tur wii ëmb kumpa, mu di: Babilon mu mag mi, ndeyi jigéeni moykat yi ak ñaawteefi àddina yi.
5她额上写着一个名号:“奥秘,大巴比伦,地上的淫妇和可憎的物之母。”
6 Ma gis jigéen ja màndi ci deretu gaayi Yàlla yi, ci deretu ñi doon seedeel Yeesu. Naka laa ko gis, ma daldi jaaxle lool.
6我又看见那妇人喝圣徒的血,和那为耶稣作见证的人的血,喝醉了。我看见了她,就大大惊奇。
7 Malaaka ma ne ma: «Lu tax nga jaaxle? Dinaa la leeralal kumpag jigéen ji ak rab, wi mu war te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén.
7天使对我说:“你为什么惊奇呢?我要把这妇人的奥秘,和驮着她的那七头十角的兽的奥秘告诉你。
8 Rab wi nga gis nekkoon na waaye nekkatul. Dina génn ca kàmb gu xóot ga, ba noppi sànku. Noonu waa àddina, ñi ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bi, dinañu yéemu, bu ñu gisee rab wi, ndaxte nekkoon na waaye nekkatul te dina nekkaat.
8你看见的那兽,先前在、现今不在、将来要从无底坑上来,然后走向灭亡。住在世上的人,凡是名字在创世以来没有记在生命册上的,看见了那先前在、现今不在、将来还要出现的兽,就都要惊奇。
9 «Xam lii nag moo laaj xel. Juróom-ñaari bopp ya ñooy juróom-ñaari tund, yi jigéen ji toog ci seen kaw. Juróom-ñaari buur lañu itam:
9在这里需要有智慧的心。七头就是那妇人所坐的七座山,
10 juróom daanu nañu, kenn kaa ngi fi, ki ci des ñëwagul, te bu ñëwee, dina fi war a nekk ab diir.
10也就是七位王:五位已经倒了,一位还在,另一位还没有来到;他来的时候,必须存留一会儿。
11 Rab wi nekkoon te nekkatul nag, moom ci boppam moo di juróom-ñetteelu buur bi, te ci juróom-ñaar yi la bokk. Ma nga jëm sànkute.
11那先前在、现今不在的兽,就是第八位。他也是出于那七位中的一位的,并且正在走向灭亡。
12 «Fukki béjjén yi nga gis, fukki buur lañu yu jotagul nguur. Waaye dinañu jot sañ-sañ diirub waxtu, ñuy nguuru ak rab wi.
12你看见的那十角,就是十王,他们还没有取得王权;但要跟兽一同得着权柄,作王一个时期。
13 Ñoo bokk mébét, di jox seen kàttan ak seen sañ-sañ rab wi.
13他们同心合意,把自己的权力权柄交给那兽。
14 Dinañu xare ak Mbote mi, waaye Mbote mi dina leen daan, ndaxte mooy kilifag kilifa yi, di Buuru buur yi. Te am toppam, di ñi mu woo te tànn leen, te ñu takku ci moom, dinañu daanandoo ak moom.»
14他们要跟羊羔作战,羊羔必胜过他们,因为他是万主之主,万王之王。那些与羊羔同在、蒙召、被选、有忠心的,也必胜过他们。”
15 Mu neeti ma: «Dex yi nga gis jigéenu moykat ja toog ca kaw, mooy réew yi ak mbooloo yi ak xeet yi ak kàllaama yi.
15天使又对我说:“你所看见那淫妇坐着的众水,就是多种民族、群众、邦国,方言的人。
16 Fukki béjjén yi nga gis, ñoom ak rab wa, dinañu bañ jigéenu moykat ja, futti ko ci lépp, def ko yaramu neen. Dinañu lekk suuxam, ba noppi lakk ko ci safara.
16你看见的十角和那兽,都要恨那淫妇,使她荒凉赤身,又要吃她的肉,用火把她烧掉。
17 Ndaxte Yàlla def na ci seen xol, ñu matal la mu naroon. Noonu dinañu ànd, jébbal seen nguur rab wi, ba kera li Yàlla wax di mat.
17 神要众王行他的旨意,就把意念放在他们心中,叫他们同心把自己的国献给那兽,直到 神的话都实现为止。
18 Te jigéen ji nga gis, moo di dëkk bu mag, biy nguuru ci kaw buuri àddina si.»
18你看见的那妇人,就是有权统治地上的众王的那座大城。”