1 Gannaaw loolu ma dégg lu mel ni baat bu xumb bu jollee ca mbooloo mu bare ca asamaan, naan:«Aleluya!Mucc, ndam ak kàttan,Yàlla sunu Boroom moo ko moom.
1这些事以后,我听见天上好像有一大群人大声说:“哈利路亚!救恩、荣耀、权能都属于我们的 神,
2 Ay àtteem dañoo dëggu te jub!Ndaxte àtte na jigéenu moykat bu mag,bi daan yàq àddina si ak njaaloom,te feyyul na noonu jaami Yàlla, yi mu daan rey.»
2因为他的审判是真实公义的。他审判了那大淫妇,那以淫乱败坏了世界的;并且为他的仆人向淫妇伸了流血的冤。”
3 Ñu tegaat ca ne:«Aleluya!Saxarus lakku dëkk baa ngi jolli ba fàww!»
3他们再一次说:“哈利路亚!烧淫妇的烟往上冒,直到永永远远!”
4 Noonu ñaar-fukki mag ña ak ñeent, ak ñeenti mbindeef ya, daldi sukk di jaamu Yàlla, moom mi toog ca gàngune ma. Ñu naan:«Amiin! Aleluya!»
4那二十四位长老和四个活物,就俯伏敬拜那坐在宝座上的 神,说:“阿们!哈利路亚!”
5 Noonu baat jibe ca gàngune ma naan:«Màggal-leen Yàlla sunu Boroom,yéen ñépp ñi di ay jaamam,yéen ñi ko ragal, mag ak ndaw.»
5羊羔的婚筵接着有声音从宝座发出来,说:“所有 神的仆人哪!凡是敬畏他的,无论大小,你们都应当赞美我们的 神!”
6 Ma dégg lu mel ni baatu mbooloo mu bare, mel ni riiru duusi géej, ni yenguy dënnu yu réy, naan:«Aleluya!Ndaxte sunu BoroomYàlla Aji Kàttan jidugg na ci nguuram.
6我又听见一个声音,好像一大群人的声音,像众水的声音,又像大雷的声音,说:“哈利路亚!因为主、我们全能的 神作王了!
7 Nanu bég te bànneexute jox ko ndam li,ndaxte céetu Mbote mi agsi na,séet bi waaj na.
7我们要欢喜快乐,把荣耀归给他!因为羊羔的婚期到了;他的新娘也自己预备好了。
8 May nañu ko, mu sol mbubb mu sette weex bay lerax.» Mbubb mu weex moomu day misaal njubtey gaayi Yàlla yi.
8并且有光洁的细麻衣,赐给她穿上;这细麻衣就是圣徒的义行。”
9 Gannaaw loolu malaaka ma ne ma: «Bindal lii: “Yéen ñi ñu woo ci reeri céetu Mbote ma, barkeel ngeen.”» Mu teg ca ne ma: «Kàddu yii ñooy kàdduy Yàlla, di kàddu yu dëggu.»
9天使对我说:“你要写下来:‘被邀请赴羊羔婚筵的人有福了!’”他又对我说:“这都是 神真实的话。”
10 Noonu ma daanu ci ay tànkam, bëgg koo jaamu. Waaye mu ne ma: «Moytu koo def; sa nawle laa ci liggéey bi, di kenn ci say bokk, yiy sax ci seedeel Yeesu. Jaamul Yàlla. Ndaxte seedes Yeesu mooy xel miy solu yonent yi.»
10我就俯伏在天使脚前要拜他。但他对我说:“千万不可以这样!我和你,以及你那些为耶稣作见证的弟兄,都是同作仆人的。你应当敬拜 神!因为预言的精义,就是耶稣的见证。”
11 Bi loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku. Noonu fas wu weex feeñ. Ki ko war ma nga tudd Ku Takku te Dëggu, te ci njub lay àtte ak a xare.
11骑白马的基督我观看,见天开了。有一匹白马,那骑马的称为“忠信”和“真实”;他按着公义审判和作战。
12 Ay bëtam di xuyy ni safara te mu am mbaxanay buur yu bare ca boppam. Bind nañu ci moom tur wu kenn xamul ku dul moom.
12他的眼睛好像火焰,头上戴着许多皇冠,他身上写着一个名字,这名字除了他自己没有人认识。
13 Sol na mbubb mu ñu sóob ci deret, te Kàddug Yàlla mooy turam.
13他身穿一件浸过血的衣服,他的名字称为“ 神的道”。
14 Xarekat yi nekk ci asamaan topp ci moom, war ay fas yu weex, sol mbubb yu weex te set.
14天上的众军,都骑着白马,穿着洁白的细麻衣,跟随着他。
15 Am na jaasi ju ñaw juy génn ci gémmiñam, ngir dóor xeet yi, mu di leen jiitee yetu weñ, te mooy nappaaje réseñ yi ci segalukaayu mer mu tàng, mu Yàlla Aji Kàttan ji.
15有一把利剑从他口中吐出来,他要用这剑击打列国,他必用铁杖治理他们;并且还要踹全能 神烈怒的压酒池。
16 Ci mbubbam ak ci poojam bind nañu ci tur wii: Buuru buur yi, Kilifag kilifa yi.
16在他的衣服和大腿上,写着“万王之王,万主之主”的名号。
17 Noonu ma gis malaaka mu taxaw ci jant bi. Mu wax ak baat bu xumb ak picc, yiy naaw ci digg asamaan, ne leen: «Ñëwleen teewesi reer bu mag bu Yàlla,
17我又看见一位天使站在太阳中,向高空所有的飞鸟大声呼喊说:“你们来吧!齐集起来赴 神的大筵席!
18 ngeen lekk suuxi buur yi, njiiti xare yi ak boroom kàttan yi, suuxi fas yi ak seeni gawar, suuxi ñépp: gor ak jaam, mag ak ndaw.»
18可以吃君王的肉、将领的肉、壮士的肉,马和骑士的肉,以及自由的、作奴隶的、大的、小的,所有人的肉。”
19 Noonu ma gis rab wa, buuri àddina si ak seeni xarekat dajaloo ngir xareji ak ki war fas wa ak ay xarekatam.
19我看见那兽和地上的众王,以及他们的众军,都集合起来,要跟那骑白马的和他的众军作战。
20 Ñu jàpp rab wa, moom ak naaféq ba mbubboo yonent, ba daan def ca turu rab wa ay kéemaan yu mu naxe ñi nangu woon a am màndargam rab wa te jaamu nataalam. Ñoom ñaar ñépp sànni nañu leen ñuy dund ca déegu safara ak tamarax buy tàkk.
20那兽被捉住了;连同在兽面前用奇事迷惑人,使他们接受兽的记号,并且拜兽像的那假先知,也一起被捉住了。他们两个就活活地被拋在烧着硫磺的火湖里去。
21 Ña ca des, jaasi, jay génn ca gémmiñu ka toog ca fas wa, rey leen; picc yépp lekk, ba regg ci seeni suux.
21其余的人都被那位骑白马的口中所吐出来的剑杀了。所有飞鸟都吃饱了他们的肉。