1 Bokk yi, yéen ñi may waxal xam ngeen luy yoon; xam ngeen kon ne, yoon am na doole ci nit diirub dundam.
1脱离律法的约束归属基督
2 Ci maanaa, mi ngi mel ni jigéen juy séy; yoon a ngi koy boole ak jëkkëram, ñu ànd seen giiru dund, waaye su jëkkër ji faatoo, buum gi dagg na.
2一个已婚的妇人,在丈夫活着的时候,她是受律法约束归属丈夫;丈夫若死了,她就脱离丈夫在律法上的约束。
3 Kon nag su jabar ji àndee ak beneen góor, te fekk jëkkër jiy dund, dees na ko àtte njaaloo. Waaye bu jëkkër ji faatoo, yoon jeexal na seen diggante; man na séy nag ak beneen góor, te loolu du njaaloo.
3所以,当丈夫还活着的时候,如果她归属别的男人,就称为淫妇;丈夫若死了,她就脱离了律法的约束,如果她归属别的男人,也不是淫妇。
4 Nii laa leen ko man a misaale, samay bokk; bi Kirist deeyee, dangeen a deeyandoo ak moom, te noonu yoonu Musaa wàcc leen. Léegi nag yéena ngi ànd ak keneen, maanaam Kirist mi dekki, ngir nu amal Yàlla njariñ.
4这样,我的弟兄们,你们借着基督的身体,对律法来说也已经死了,使你们归属另一位,就是那从死人中复活的,为的是要我们结果子给 神。
5 Keroog ba nu daan topp sunu nafsu, yoonu Musaa daan na xamb bëgg-bëgg yu bon, yiy yengal sunuy cér, ba jural nu dee.
5我们从前属肉体的时候,罪恶的情欲借着律法在我们的肢体里发动,就结出死亡的果子。
6 Waaye léegi yoon wi wàcc na nu, ci li nu dee, ba rëcc cig buumam. Léegi nag nu ngi jaamu Yàlla, waxumaleen ci sàmm santaane rekk, ndax loolu wees na, waaye ci kàttan gu bees, gi nu Xelum Yàlla di may.
6但现在,我们既然向那捆绑我们的律法死了,就脱离了律法的约束,好让我们用心灵的新样子,而不用仪文的旧方式来服事主。
7 Kon nag lu nu war a wax? Ndax bàkkaar ci yoonu Musaa la jóge? Mukk! Waaye moo ma xamal luy bàkkaar. Ndaxte su ma yoon wi waxul woon: «Bul bëgg yëfi jaambur,» kon duma xam luy xemmem.
7善恶两律在心中交战这样,我们可以说什么呢?难道律法是罪吗?绝对不是。不过,如果不是借着律法,我就不知道什么是罪;如果不是律法说“不可贪心”,我就不知道什么是贪心。
8 Waaye bàkkaar jaare na ci ndigalu Yàlla, daldi ñëw dugg ci man, ba yengal ci man xemmem yu bare. Ndaxte ba ma xamagul woon yoonu Musaa, bàkkaar da ne woon nemm ci man.
8但罪趁着机会,借着诫命在我里面发动各样的贪心,因为没有律法,罪是死的。
9 Te keroog bi ma xamagul lu yoon wi santaane, maa ngi doon dund dund gu neex; waaye ba ma ko déggee, bàkkaar dafa daldi fuddu ci man, te man ma daldi dee.
9在没有律法的时候,我是活的;但诫命一来,罪就活了,
10 Noonu gis naa ne, ndigal loolu waroon a jëme nit ñi ci dund, daf maa jëme ci dee.
10我就死了,那本来使人活的诫命,反而使我死了;
11 Ndaxte bàkkaar jaar na ci li Yàlla digle, ba nax ma, rey ma.
11因为罪借着诫命把握着机会来欺骗我,并且杀了我。
12 Kon nag man nanoo wax ne, yoonu Musaa yoon wu sell la, te ndigalu Yàlla dafa sell, jub te baax.
12这样,律法是圣洁的,诫命也是圣洁、公义和良善的。
13 Ndax kon lu baax moo ma tàbbal ci dee? Mukk! Bàkkaar a ko def, ngir jikkoom feeñ; dafa gis ci lu baax loolu bunt bu mu man a jaar, ba rey ma. Noonu ndigalu Yàlla tax na, bàkkaar fés, bon ba jéggi dayo.
13既是这样,那良善的反而使我死吗?绝对不是!但罪借着那良善的使我死,就显出真是罪,为了要使罪借着诫命变成更加邪恶。
14 Xam nanu ne, yoonu Musaa ngi jóge ci Yàlla, waaye man yëfi àddina laa fonk, te nekk ci dooley bàkkaar, mel nib jaam.
14我们知道律法是属灵的,我却是属肉体的,已经卖给罪了。
15 Ndaxte samay jëf jaaxal na ma; li ma bëgg a def, duma ko def, waaye li ma bañ rekk, moom laay def.
15因为我所作的,我不明白;我所愿意的,我没有去作,我所恨恶的,我倒去作。
16 Kon nag gannaaw li may def du sama coobare, nangu naa ne yoonu Musaa baax na.
16如果我所不愿意的,我倒去作,我就不得不承认律法是好的。
17 Léegi nag du man maay def lu bon loolu, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ciy jiiñ.
17既是这样,那就不是我作的,而是住在我里面的罪作的。
18 Ndaxte xam naa ne, lu baax dëkkul ci man, maanaam ci sama bindu doom Aadama. Am naa yéeney def lu baax, waaye awma kàttanu yeggale.
18我知道在我里面,就是在我肉体之中,没有良善,因为立志行善由得我,行出来却由不得我。
19 Lu baax nag lu may yéene, duma ko def, waaye lu bon lu ma bëggul, moom laay def.
19所以我愿意行的善,我没有去行;我不愿意作的恶,我倒去作了。
20 Bu fekkee nag lu ma bëggul, moom laay def, kon dootul sama coobare, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ci jiiñ.
20我若作自己不愿意作的事,那就不是我作的,而是住在我里面的罪作的。
21 Gis naa nag lii: saa su ma bëggee def lu baax, lu bon a ngi ma taxawu.
21因此,我发现了一个律,就是我想向善的时候,恶就在我里面出现。
22 Ndaxte ci sama biir xol yoonu Yàlla wi neex na ma.
22按着我里面的人来说,我是喜欢 神的律,
23 Waaye gis naa jeneen doole juy yengu ci samay céri yaram, di bëre ak li sama xol bëgg; day bëre ba noot ma, def ma jaam ci dooley bàkkaar joojuy yengu ci samay cér.
23但我发觉肢体中另有一个律,和我心中的律争战,把我掳去附从肢体中的罪律。
24 Céy maaka torox! Ana ku may musal ci sama yaram, wii may jëme ci dee?
24我这个人真是苦啊!谁能救我脱离这使我死亡的身体呢?
25 Maa ngi sant Yàlla; am na kuy musle, mooy Yeesu Kirist sunu Boroom. Kon nag lii laa gis ci sama bopp: ci sama xel maa ngi topp yoonu Yàlla, waaye ci sama bindu doom Aadama maa ngi topp yoonu bàkkaar.
25感谢 神,借着我们的主耶稣基督就能脱离了。可见,一方面我自己心里服事 神的律,另一方面我的肉体却服事罪的律。