1 Léegi nag bokk yi, ci li jëm ci mayi Xelum Yàlla, bëgguma ngeen umple ci dara.
1Now concerning spiritual gifts, brethren, I would not have you ignorant.
2 Xam ngeen ne, bi ngeen xamagul woon Yàlla, xërëm, yi mënul a wax, ñoo leen jiitaloon, di leen wommat.
2Ye know that ye were Gentiles, carried away unto these dumb idols, even as ye were led.
3 Moo tax ma leen di xamal lii: ku Xelum Yàlla solu du wax ne: «Yeesu dafa araam.» Te it kenn mënul a wax ne: «Yeesu mooy Boroom bi,» su ko ko Xelum Yàlla waxloowul.
3Wherefore I give you to understand, that no man speaking by the Spirit of God calleth Jesus accursed: and that no man can say that Jesus is the Lord, but by the Holy Ghost.
4 Am na fànni may yu bare yu jóge ci Xelum Yàlla, waaye menn Xel moomu moo koy séddale.
4Now there are diversities of gifts, but the same Spirit.
5 Am na ay sas yu bare, waaye benn Boroom bi la.
5And there are differences of administrations, but the same Lord.
6 Am na ay fànn yu bare yu Yàllay feeñale dooleem, waaye jenn Yàlla ji mooy jëfe doole yooyu yépp ci ñépp.
6And there are diversities of operations, but it is the same God which worketh all in all.
7 Noonu Yàlla jox na ku nekk fànn gu muy feeñale Xelam mu Sell mi ngir njariñul ñépp.
7But the manifestation of the Spirit is given to every man to profit withal.
8 Am na ku Yàlla sédde, jaarale ko ci Xelam, mayu wax ak xel mu leer, keneen am mayu xam-xam, te mu bawoo ci menn Xel mi.
8For to one is given by the Spirit the word of wisdom; to another the word of knowledge by the same Spirit;
9 Keneen it menn Xel mi jox ko ngëm, keneen di wéral ay jàngoro ci kàttanu Xel moomu,
9To another faith by the same Spirit; to another the gifts of healing by the same Spirit;
10 keneen di def ay kéemaan, am kuy wax ci kàddug Yàlla, am keneen kuy ràññee li jóge ci Xelum Yàlla ak li jóge ci yeneen xel yi, keneen it di wax ay xeeti làkk, ak kuy firi làkk yooyu.
10To another the working of miracles; to another prophecy; to another discerning of spirits; to another divers kinds of tongues; to another the interpretation of tongues:
11 Loolu lépp, menn Xel moomu moo koy def, ku nekk mu sédd la ci, ni mu ko soobe.
11But all these worketh that one and the selfsame Spirit, dividing to every man severally as he will.
12 Noona la ci yaramu nit. Yaram wenn la, teewul am na cér yu bare. Waaye céri yaram yépp, ak li ñuy baree-bare, ñoo bokk, doon wenn yaram. Te noonu la Kirist mel.
12For as the body is one, and hath many members, and all the members of that one body, being many, are one body: so also is Christ.
13 Yàlla sóob na nu ci menn Xelam mi, ngir nu doon wenn yaram: nuy Yawut walla nu dul Yawut, nuy jaam mbaa gor, nun ñépp Yàlla may na nu, nu naan ci menn Xel mi.
13For by one Spirit are we all baptized into one body, whether we be Jews or Gentiles, whether we be bond or free; and have been all made to drink into one Spirit.
14 Yaram du benn cér, waaye cér yu bare la.
14For the body is not one member, but many.
15 Kon bu tànk nee: «Man duma loxo, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.
15If the foot shall say, Because I am not the hand, I am not of the body; is it therefore not of the body?
16 Te bu nopp nee: «Duma bët, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.
16And if the ear shall say, Because I am not the eye, I am not of the body; is it therefore not of the body?
17 Bu yaram wépp doon bët, kon nan lay dégge? Walla bu yaram wépp doon nopp, kon nan lay xeeñtoo?
17If the whole body were an eye, where were the hearing? If the whole were hearing, where were the smelling?
18 Waaye Yàlla dafa riime céri yaram wi, def bu ci nekk fa mu ko soobe.
18But now hath God set the members every one of them in the body, as it hath pleased him.
19 Bu lépp doon benn cér, kon fu yaram di nekk?
19And if they were all one member, where were the body?
20 Cér yi daal, bare nañu waaye wenn yaram rekk a am.
20But now are they many members, yet but one body.
21 Bët nag mënul ne loxo: «Soxlawuma la!» Te bopp it mënul ne tànk yi: «Soxlawuma leen!»
21And the eye cannot say unto the hand, I have no need of thee: nor again the head to the feet, I have no need of you.
22 Loolu sax mënul a am, ndaxte céri yaram, yi gën a néew doole, ñoo gën a am jariñ.
22Nay, much more those members of the body, which seem to be more feeble, are necessary:
23 Te cér yi gën a ñàkk maana, ñoom lanuy gën a topptoo. Cér yi ci rafetul a tudd, ñoom lanuy gën a suturaal,
23And those members of the body, which we think to be less honourable, upon these we bestow more abundant honour; and our uncomely parts have more abundant comeliness.
24 fekk yi gën a rafet, soxlawul nu leen di suturaale noonu. Waaye Yàlla dafa boole sunu céri yaram yi, ngir gën a teral cér yi ko soxla.
24For our comely parts have no need: but God hath tempered the body together, having given more abundant honour to that part which lacked.
25 Noonu yaram du séddaloo, waaye cér bu ci nekk dina dimbali yi ci des.
25That there should be no schism in the body; but that the members should have the same care one for another.
26 Bu sa benn céru yaram dee metti, yeneen yi ci des yépp dañuy bokk, yég metit wi. Te bu dee dangaa fonk sa benn céru yaram it, ndax du sa yaram wépp a ciy bànneexu?
26And whether one member suffer, all the members suffer with it; or one member be honoured, all the members rejoice with it.
27 Léegi benn yaram ngeen, muy yaramu Kirist, te kenn ku nekk ci yéen cér nga ci.
27Now ye are the body of Christ, and members in particular.
28 Te Yàlla teg na ci mbooloom ñi gëm, ku nekk ak sa may: ci bu jëkk ay ndawi Kirist, teg ca ñiy wax ci kàddug Yàlla, teg ca ñiy jàngale, ñiy def ay kéemaan, ñi am mayu wéral ay jàngoro, ñiy dimbalee, ñiy jiite, ñiy wax ay xeeti làkk.
28And God hath set some in the church, first apostles, secondarily prophets, thirdly teachers, after that miracles, then gifts of healings, helps, governments, diversities of tongues.
29 Ndax ñépp ay ndawi Kirist lañu? Ndax ñépp dañuy wax ci kàddug Yàlla? Ndax ñépp ay jàngale? Ndax ñépp ay def kéemaan?
29Are all apostles? are all prophets? are all teachers? are all workers of miracles?
30 Ndax ñépp a am mayu wéral ay jàngoro? Ndax ñépp ay wax ay làkk? Ndax ñépp a leen di firi?
30Have all the gifts of healing? do all speak with tongues? do all interpret?
31 Waaye fonkleen may yi gën. Léegi nag ma won leen yoon wu gën lépp.
31But covet earnestly the best gifts: and yet shew I unto you a more excellent way.