1 Man nag fas yéene naa lii: duma dellusi ci yéen ci naqar.
1But I determined this with myself, that I would not come again to you in heaviness.
2 Ndaxte su ma leen tegee naqar, kuy seddal sama xol ku dul yéen ñi ma teg aw naqar?
2For if I make you sorry, who is he then that maketh me glad, but the same which is made sorry by me?
3 Looloo tax ma binde noonu, ngir bañ a agsi, am naqar ci ñi ma waroon a bégal. Am naa kóolute ci yéen ñépp ne, sama mbég mooy seen mbég.
3And I wrote this same unto you, lest, when I came, I should have sorrow from them of whom I ought to rejoice; having confidence in you all, that my joy is the joy of you all.
4 Ci biir tiis ak xol bu jeex laa leen bind, samay bët taa ak ay rangooñ. Binduma leen ngir teg leen naqar, waaye ngir ngeen xam xóotaayu mbëggeel gi ma am ci yéen.
4For out of much affliction and anguish of heart I wrote unto you with many tears; not that ye should be grieved, but that ye might know the love which I have more abundantly unto you.
5 Su kenn tegee moroomam naqar, du man la ko teg, waaye man nanu ne, yéen ñépp la ko teg — matul may réyal mbir mi.
5But if any have caused grief, he hath not grieved me, but in part: that I may not overcharge you all.
6 Àtte bi ko mbooloo mi teg, doy na.
6Sufficient to such a man is this punishment, which was inflicted of many.
7 Léegi nag baal-leen ko te dëfël xolam, ngir bañ mu sóobu ci naqar wu ëpp.
7So that contrariwise ye ought rather to forgive him, and comfort him, lest perhaps such a one should be swallowed up with overmuch sorrow.
8 Kon maa ngi leen di ñaan, ngeen feddali seen mbëggeel ci moom.
8Wherefore I beseech you that ye would confirm your love toward him.
9 Nattu leen moo tax ma bind leen it, ngir seet ba xam dingeen dégg ndigal ci lépp.
9For to this end also did I write, that I might know the proof of you, whether ye be obedient in all things.
10 Ku ngeen baal, ma baal ko itam. Man nag, su ma baalee --fekk am lu ma war a baale — yéena tax ma def ko ci kanamu Kirist,
10To whom ye forgive any thing, I forgive also: for if I forgave any thing, to whom I forgave it, for your sakes forgave I it in the person of Christ;
11 ngir Seytaane bañ a am bunt bu mu jaar ba nax nu, ndaxte réerewunu mbir ay pexeem.
11Lest Satan should get an advantage of us: for we are not ignorant of his devices.
12 Ba ma àggee Torowas nag, ngir yégle fa xebaar bu baax bi ci Kirist, Boroom bi ubbil na ma ci bunt.
12Furthermore, when I came to Troas to preach Christ's gospel, and a door was opened unto me of the Lord,
13 Waaye sama xel dalul benn yoon, ndax li ma fa fekkul sama mbokk, Tit. Noonu nag ma tàggu leen, daldi dem diiwaanu Maseduwan.
13I had no rest in my spirit, because I found not Titus my brother: but taking my leave of them, I went from thence into Macedonia.
14 Waaye cant ñeel na Yàlla! Ci sunu booloo ak Kirist, daf nuy yóbbaale saa su nekk ci gawari ndamam, tey jaar ci nun ngir turu Kirist jolli fu nekk, ni xetu latkoloñ di tasaaroo.
14Now thanks be unto God, which always causeth us to triumph in Christ, and maketh manifest the savour of his knowledge by us in every place.
15 Ndaxte ci Yàlla, xetu Kirist gu neex lanu, di gilli jëm ci ñiy mucc ak ñiy sànku;
15For we are unto God a sweet savour of Christ, in them that are saved, and in them that perish:
16 ci ñu mujj ñii, xet gu sedd lanu, guy jëme ci dee; ci ñu jëkk ñi, xetu dund lanu, guy jëme ci dund. Kon ku man a àttan yen boobu!
16To the one we are the savour of death unto death; and to the other the savour of life unto life. And who is sufficient for these things?
17 Nun nag melunu ni ñu bare, ñiy baana-baana ci kàddug Yàlla, waaye ci sunu booloo ak Kirist, nu ngi waare ak xol bu laab fa kanam Yàlla, ni yonenti Yàlla.
17For we are not as many, which corrupt the word of God: but as of sincerity, but as of God, in the sight of God speak we in Christ.