Wolof: New Testament

King James Version

2 Timothy

2

1 Kon nag yaw sama doomu diine, doolewool yiw, wi ci Kirist Yeesu.
1Thou therefore, my son, be strong in the grace that is in Christ Jesus.
2 Te wax yi nga dégge ci man fi kanam seede yu bare, nanga leen jottali nit ñu takku, ngir ñoom it ñu man a jàngal ñeneen.
2And the things that thou hast heard of me among many witnesses, the same commit thou to faithful men, who shall be able to teach others also.
3 Bokkal ak man tiis, di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu,
3Thou therefore endure hardness, as a good soldier of Jesus Christ.
4 xam ne xarekat bu bëgg a neex ka ko solal, du dugg ci yëfi àddina.
4No man that warreth entangleth himself with the affairs of this life; that he may please him who hath chosen him to be a soldier.
5 Te it ku tàggat yaramam ngir rawante, duñu ko jagleel kaalag ndam mukk, su toppul sàrt ya.
5And if a man also strive for masteries, yet is he not crowned, except he strive lawfully.
6 Noonu it beykat bi sonn mooy jëkk a ñam toolam.
6The husbandman that laboureth must be first partaker of the fruits.
7 Xalaatal bu baax sama wax jii, ndax Boroom bi dina leeral sa xel ci lépp.
7Consider what I say; and the Lord give thee understanding in all things.
8 Fàttalikul Yeesu Kirist mi dekki, soqikoo ci Daawuda, tukkee ci xebaar bu baax bi may waare.
8Remember that Jesus Christ of the seed of David was raised from the dead according to my gospel:
9 Xebaar booboo tax may jànkoonte ak i tiis, ba ñu jéng ma ni defkatu lu bon; waaye kàddug Yàlla moom, kenn du ko jéng.
9Wherein I suffer trouble, as an evil doer, even unto bonds; but the word of God is not bound.
10 Te lii tax may muñ lépp, ngir ñi Yàlla tànn it am mucc gi ci Kirist Yeesu, gu ànd ak ndam lu sax.
10Therefore I endure all things for the elect's sakes, that they may also obtain the salvation which is in Christ Jesus with eternal glory.
11 Kàddu gu wóor a ngii:Su nu deeyaalee ak Kirist,dinanu dundaat ak moom;
11It is a faithful saying: For if we be dead with him, we shall also live with him:
12 su nu takkoo,dinanu nguuru ak moom.
12If we suffer, we shall also reign with him: if we deny him, he also will deny us:
13 Su nu ko weddee,kon mu weddi nu;su nu ko ñàkkee kóllëre,moom dina sax ci kóllëreem,ndax mënul a weddi boppam.
13If we believe not, yet he abideth faithful: he cannot deny himself.
14 Saxal ci di leen fàttali mbir yooyu, di leen dénk fa kanam Yàlla, ñu moytoo werante ciy araf, ndax loolu jëmul fu dul ci yàq ngëmu ñiy déglu.
14Of these things put them in remembrance, charging them before the Lord that they strive not about words to no profit, but to the subverting of the hearers.
15 Góor-góorlul ba teew fa kanam Yàlla, nekk liggéeykat bu mu nangul te rusoo ci dara, di faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi.
15Study to shew thyself approved unto God, a workman that needeth not to be ashamed, rightly dividing the word of truth.
16 Moytul bépp jataayu waxi neen yu àddina kese, ndax ña fa toog dinañu gën a xuus cig weddi,
16But shun profane and vain babblings: for they will increase unto more ungodliness.
17 te seen kàddu day burux ni ngal. Imene ak Filet, ci ñoom lañu bokk;
17And their word will eat as doth a canker: of whom is Hymenaeus and Philetus;
18 dañoo moy dëgg, di wax ne ndekkite wees na, ba yàq ngëmu ñenn ñi.
18Who concerning the truth have erred, saying that the resurrection is past already; and overthrow the faith of some.
19 Waaye teewul fondamaa bu dëgër, bi Yàlla tabax, nee na kekk, te lii lañu ci tàmpe: «Boroom bi xam na ñi bokk ci moom,» te it: «Ki tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.»
19Nevertheless the foundation of God standeth sure, having this seal, The Lord knoweth them that are his. And, Let every one that nameth the name of Christ depart from iniquity.
20 Ci kër gu mag nag, du ndabi wurus walla xaalis rekk a fa am, waaye itam yoy dénk walla ban; yii tedd nañu, yee ñàkk solo.
20But in a great house there are not only vessels of gold and of silver, but also of wood and of earth; and some to honour, and some to dishonour.
21 Kon nag ku laabal sa bopp ci yooyu yépp, dinga nekk ndab lu tedd te sell, nga am njariñ ci Boroom bi te jekk ci bépp jëf ju rafet.
21If a man therefore purge himself from these, he shall be a vessel unto honour, sanctified, and meet for the master's use, and prepared unto every good work.
22 Dawal bépp bëgg-bëggu ngune, te sóobu ci njub, ngëm, mbëggeel, jàmm, ànd ak ñépp ñiy tudd turu Boroom bi ak xol bu sell.
22Flee also youthful lusts: but follow righteousness, faith, charity, peace, with them that call on the Lord out of a pure heart.
23 Tanqamlul bépp weranteb neen bu amul njariñ, xam ne xuloo rekk lay jur.
23But foolish and unlearned questions avoid, knowing that they do gender strifes.
24 Te jaamu Boroom bi warul a xuloo, waaye na lewet ci ñépp, jekk ngir jàngale tey muñ fitnay noon.
24And the servant of the Lord must not strive; but be gentle unto all men, apt to teach, patient,
25 Na jubbanti cig suufe ñi koy diiŋat, tey yéene Yàlla xiir leen ci réccu, ba ñu xam dëgg;
25In meekness instructing those that oppose themselves; if God peradventure will give them repentance to the acknowledging of the truth;
26 ñu rëcc ci fiirug Seytaane, mi leen jàpp niy jaam, te ñu dellusi ci seen xel yu rafet, ba sóobuwaat ci coobareg Yàlla.
26And that they may recover themselves out of the snare of the devil, who are taken captive by him at his will.