Wolof: New Testament

King James Version

Acts

15

1 Amoon na bés ay nit jóge diiwaanu Yude, ñuy jàngal bokk yi ne leen: «Ku xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, doo man a mucc.»
1And certain men which came down from Judaea taught the brethren, and said, Except ye be circumcised after the manner of Moses, ye cannot be saved.
2 Pool ak Barnabas nag am ak ñoom diisoo ak werante wu metti; noonu bokk yi jàpp ne, Pool ak Barnabas ak ñeneen ci ñoom war nañoo dem Yerusalem ca ndaw ya ak njiit ya, ngir leeral werante wi.
2When therefore Paul and Barnabas had no small dissension and disputation with them, they determined that Paul and Barnabas, and certain other of them, should go up to Jerusalem unto the apostles and elders about this question.
3 Kon nag mbooloo mi gunge leen, ñu jaar ci wàlli Fenisi ak Samari, di nettali ni ñi dul Yawut woññikoo ci Yàlla, ba bokk yépp am ca mbég mu réy.
3And being brought on their way by the church, they passed through Phenice and Samaria, declaring the conversion of the Gentiles: and they caused great joy unto all the brethren.
4 Te bi ñu agsee Yerusalem, mbooloom ñi gëm, ndaw yi ak njiit yi teeru leen, ñu nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp.
4And when they were come to Jerusalem, they were received of the church, and of the apostles and elders, and they declared all things that God had done with them.
5 Ci kaw loolu ñeneen, ñi gëm waaye bokk ci tariixab Farisen ya, daldi jóg ne: «Fàww ñi dul Yawut xaraf, te ñu dénk leen sàmm yoonu Musaa.»
5But there rose up certain of the sect of the Pharisees which believed, saying, That it was needful to circumcise them, and to command them to keep the law of Moses.
6 Noonu ndaw yi ak njiit yi dajaloo, ngir seet mbir moomu.
6And the apostles and elders came together for to consider of this matter.
7 Gannaaw werante wu bare Piyeer jóg ne leen: «Yéen bokk yi, xam ngeen ne, ca njàlbéen ga Yàlla tànnoon na ma ci yéen, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi, ba ñu gëm.
7And when there had been much disputing, Peter rose up, and said unto them, Men and brethren, ye know how that a good while ago God made choice among us, that the Gentiles by my mouth should hear the word of the gospel, and believe.
8 Te Yàlla, mi xam xol yi, seede na leen ci li mu leen may Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye nun itam.
8And God, which knoweth the hearts, bare them witness, giving them the Holy Ghost, even as he did unto us;
9 Gënalantewu nu ak ñoom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ngëm.
9And put no difference between us and them, purifying their hearts by faith.
10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, ciy teg taalibe yi yen bu nu musul a àttan, nun mbaa sunuy maam?
10Now therefore why tempt ye God, to put a yoke upon the neck of the disciples, which neither our fathers nor we were able to bear?
11 Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaar a mucce, te ñoom itam, ci lañu wékku.»
11But we believe that through the grace of the LORD Jesus Christ we shall be saved, even as they.
12 Bi mu ko waxee, mbooloo mépp ne xeram, di déglu Barnabas ak Pool, ñuy nettali kéemaan ak firnde yépp, yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut.
12Then all the multitude kept silence, and gave audience to Barnabas and Paul, declaring what miracles and wonders God had wrought among the Gentiles by them.
13 Bi ñu noppee, Saag jël kàddu ga ne:
13And after they had held their peace, James answered, saying, Men and brethren, hearken unto me:
14 «Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam.
14Simeon hath declared how God at the first did visit the Gentiles, to take out of them a people for his name.
15 Te loolu sax dëppoo na ak li yonent yi tëral; ñu bind ne:
15And to this agree the words of the prophets; as it is written,
16 “Boroom bi nee na:Gannaaw loolu dinaa dellusi,te yékkati këru Daawuda, gi ne tasar,dinaa defar toj-toj ya,ba taxawalaat ko.
16After this I will return, and will build again the tabernacle of David, which is fallen down; and I will build again the ruins thereof, and I will set it up:
17 Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi,maanaam xeet yi dul Yawut, ñuy tudd sama tur.
17That the residue of men might seek after the Lord, and all the Gentiles, upon whom my name is called, saith the Lord, who doeth all these things.
18 Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax,te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.”
18Known unto God are all his works from the beginning of the world.
19 «Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te woññiku ci Yàlla.
19Wherefore my sentence is, that we trouble not them, which from among the Gentiles are turned to God:
20 Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja.
20But that we write unto them, that they abstain from pollutions of idols, and from fornication, and from things strangled, and from blood.
21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésu noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.»
21For Moses of old time hath in every city them that preach him, being read in the synagogues every sabbath day.
22 Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñuy dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.
22Then pleased it the apostles and elders with the whole church, to send chosen men of their own company to Antioch with Paul and Barnabas; namely, Judas surnamed Barsabas and Silas, chief men among the brethren:
23 Ñu jox leen bataaxal bu ne: Yéen sunu bokk yi dul Yawut te dëkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi.
23And they wrote letters by them after this manner; The apostles and elders and brethren send greeting unto the brethren which are of the Gentiles in Antioch and Syria and Cilicia.
24 Dégg nanu ne, am na ay nit ñu bawoo ci nun, ñu di leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seeni xol, te fekk sukkandikuwuñu ci lenn ndigal lu jóge ci nun.
24Forasmuch as we have heard, that certain which went out from us have troubled you with words, subverting your souls, saying, Ye must be circumcised, and keep the law: to whom we gave no such commandment:
25 Kon nag mànkoo nanu ci tànn ay nit, yónnee leen ko, ànd ak sunuy soppe Barnabas ak Pool.
25It seemed good unto us, being assembled with one accord, to send chosen men unto you with our beloved Barnabas and Paul,
26 Ñoom jaay nañu seen bakkan ngir turu Yeesu Kirist Boroom bi.
26Men that have hazarded their lives for the name of our Lord Jesus Christ.
27 Yónni nanu nag Yudd ak Silas, ñu di leen xamal xebaar boobu ci seen gémmiñ.
27We have sent therefore Judas and Silas, who shall also tell you the same things by mouth.
28 Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leen a teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ,
28For it seemed good to the Holy Ghost, and to us, to lay upon you no greater burden than these necessary things;
29 maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo yëf yooyu, dingeen def lu baax. Ci jàmm.
29That ye abstain from meats offered to idols, and from blood, and from things strangled, and from fornication: from which if ye keep yourselves, ye shall do well. Fare ye well.
30 Noonu ñu tàggoo, dem Ancos, ñu dajale mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
30So when they were dismissed, they came to Antioch: and when they had gathered the multitude together, they delivered the epistle:
31 Ñu jàng ko nag, seen xol sedd ci doole, ji leen bataaxal bi indil.
31Which when they had read, they rejoiced for the consolation.
32 Te Yudd ak Silas, ñi doon yonent, ñuy dooleel bokk yi, di dëgëral seen fit ak wax yu bare.
32And Judas and Silas, being prophets also themselves, exhorted the brethren with many words, and confirmed them.
33 Bi loolu amee ñu toog fa ab diir, ba noppi bokk yi yiwi leen ci jàmm, ñu dellu ca ña leen yónni woon.
33And after they had tarried there a space, they were let go in peace from the brethren unto the apostles.
35 Waaye Pool ak Barnabas des ci Ancos, di jàngale ak di xamle xebaar bu baax bu kàddug Boroom bi, ñoom ak ñeneen ñu bare.
34Notwithstanding it pleased Silas to abide there still.
36 Gannaaw ay fan Pool ne Barnabas: «Nan dellu seeti bokk ya ca dëkk yépp, fu nu mas a yéglee kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.»
35Paul also and Barnabas continued in Antioch, teaching and preaching the word of the Lord, with many others also.
37 Barnabas nag bëggoon na yóbbaale Yowaana, mi ñuy wax it Màrk.
36And some days after Paul said unto Barnabas, Let us go again and visit our brethren in every city where we have preached the word of the LORD, and see how they do.
38 Waaye Pool dafa lànk ne: «Matul nu yóbbu ki nu waccoon ca Pamfili, ba àndul woon ak nun ca liggéey ba.»
37And Barnabas determined to take with them John, whose surname was Mark.
39 Noonu ñu xuloo, ba far tàggoo. Barnabas yóbbaale Màrk, ñu dugg gaal, jëm Sipar.
38But Paul thought not good to take him with them, who departed from them from Pamphylia, and went not with them to the work.
40 Pool tànn Silas, dem; bokk ya dénk leen ci yiwu Boroom bi;
39And the contention was so sharp between them, that they departed asunder one from the other: and so Barnabas took Mark, and sailed unto Cyprus;
41 mu jaar ci diiwaanu Siri ak Silisi, di dëgëral mboolooy ñi gëm.
40And Paul chose Silas, and departed, being recommended by the brethren unto the grace of God.
41And he went through Syria and Cilicia, confirming the churches.