Wolof: New Testament

King James Version

Acts

8

1 Sool moom ànd na ci ñi doon rey Ecen. Bés booba nag fitna ju metti dal na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk Yerusalem, ba ñépp, ñu moy ndaw ya, tasaaroo ci diiwaani Yude ak Samari.
1And Saul was consenting unto his death. And at that time there was a great persecution against the church which was at Jerusalem; and they were all scattered abroad throughout the regions of Judaea and Samaria, except the apostles.
2 Ay nit ñu ragal Yàlla fab Ecen, jébbal ko Boroom bi, di ko jooy bu wér.
2And devout men carried Stephen to his burial, and made great lamentation over him.
3 Waaye naka Sool, mu ngay tas mbooloom ñi gëm, di tàbbi ca kër ya, tey jàpp góor ak jigéen, di leen tëj kaso.
3As for Saul, he made havock of the church, entering into every house, and haling men and women committed them to prison.
4 Ñi tasaaroo nag dem fu nekk, di fa xamle xebaar bu baax bu kàddug Yàlla.
4Therefore they that were scattered abroad went every where preaching the word.
5 Naka Filib mu dem ca benn dëkk ca Samari, di leen yégal Kirist.
5Then Philip went down to the city of Samaria, and preached Christ unto them.
6 Bi ko mbooloo mi déggee te gis kéemaan yi muy def, ñu bokk benn xalaat, fekki ko ci li mu wax.
6And the people with one accord gave heed unto those things which Philip spake, hearing and seeing the miracles which he did.
7 Ndaxte ay rab yu bon bàyyi nañu nit ñu bare, ña ñu jàppoon, di yuuxu ci kaw; te ñu bare ñu làggi ak ñu lafañ daldi wér.
7For unclean spirits, crying with loud voice, came out of many that were possessed with them: and many taken with palsies, and that were lame, were healed.
8 Noonu mbég mu réy tàbbi ca dëkk ba.
8And there was great joy in that city.
9 Amoon na nag nit ku tudd Simoŋ, di luxuskat bu yàgg ca dëkk ba, te daan yéem waa Samari gépp, ci naan: «Aji Màgg laa.»
9But there was a certain man, called Simon, which beforetime in the same city used sorcery, and bewitched the people of Samaria, giving out that himself was some great one:
10 Kon ñépp, mag ak ndaw, taq ci moom ne: «Kii mooy jaasiy Aji Kàttan ji.»
10To whom they all gave heed, from the least to the greatest, saying, This man is the great power of God.
11 Ñu taq ci moom, ndax li mu leen yàgg a waar ci ay luxus.
11And to him they had regard, because that of long time he had bewitched them with sorceries.
12 Waaye bi ñu gëmee xebaar bu baax, bi Filib yégle jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Kirist, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
12But when they believed Philip preaching the things concerning the kingdom of God, and the name of Jesus Christ, they were baptized, both men and women.
13 Simoŋ sax gëm, ñu sóob ko ci ndox; mu wéy nag ci topp Filib, di waaru ci kéemaan yi ak firnde yu mag yiy am.
13Then Simon himself believed also: and when he was baptized, he continued with Philip, and wondered, beholding the miracles and signs which were done.
14 Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem yég nañu ne, waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla; ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana.
14Now when the apostles which were at Jerusalem heard that Samaria had received the word of God, they sent unto them Peter and John:
15 Ñu dem fa nag, ñaanal leen, ngir ñu jot Xel mu Sell mi.
15Who, when they were come down, prayed for them, that they might receive the Holy Ghost:
16 Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu.
16(For as yet he was fallen upon none of them: only they were baptized in the name of the Lord Jesus.)
17 Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi.
17Then laid they their hands on them, and they received the Holy Ghost.
18 Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,
18And when Simon saw that through laying on of the apostles' hands the Holy Ghost was given, he offered them money,
19 ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»
19Saying, Give me also this power, that on whomsoever I lay hands, he may receive the Holy Ghost.
20 Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne, man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.
20But Peter said unto him, Thy money perish with thee, because thou hast thought that the gift of God may be purchased with money.
21 Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.
21Thou hast neither part nor lot in this matter: for thy heart is not right in the sight of God.
22 Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.
22Repent therefore of this thy wickedness, and pray God, if perhaps the thought of thine heart may be forgiven thee.
23 Ndaxte gis naa ne, sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar noot na la.»
23For I perceive that thou art in the gall of bitterness, and in the bond of iniquity.
24 Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.»
24Then answered Simon, and said, Pray ye to the LORD for me, that none of these things which ye have spoken come upon me.
25 Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xebaar bu baax bi ci dëkk yu bare yu waa Samari.
25And they, when they had testified and preached the word of the Lord, returned to Jerusalem, and preached the gospel in many villages of the Samaritans.
26 Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: «Jógal te jublu Misra, jaar ci yoon wi jóge Yerusalem, jëm Gasa, di màndiŋ.»
26And the angel of the Lord spake unto Philip, saying, Arise, and go toward the south unto the way that goeth down from Jerusalem unto Gaza, which is desert.
27 Filib jóg dem. Noonu mu gis fa nitu Ecópi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, te di ko wottul xaalisam bépp. Fekk mu ñëwoon Yerusalem, ngir màggalsi Yàlla, bay dellu;
27And he arose and went: and, behold, a man of Ethiopia, an eunuch of great authority under Candace queen of the Ethiopians, who had the charge of all her treasure, and had come to Jerusalem for to worship,
28 mu toog ci watiiram, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.
28Was returning, and sitting in his chariot read Esaias the prophet.
29 Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.»
29Then the Spirit said unto Philip, Go near, and join thyself to this chariot.
30 Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
30And Philip ran thither to him, and heard him read the prophet Esaias, and said, Understandest thou what thou readest?
31 Mu tontu ko ne: «Nu ma ko man a xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom.
31And he said, How can I, except some man should guide me? And he desired Philip that he would come up and sit with him.
32 Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi:«Yóbbu nañu ko ni xar mu ñuy rendiji;ni mburt mu luu ci kanami watkat,mu ne cell.
32The place of the scripture which he read was this, He was led as a sheep to the slaughter; and like a lamb dumb before his shearer, so opened he not his mouth:
33 Ci toroxteem nangu nañu dëggam;ñi mu tollool jamono, ku ci xalaat lii?Jële nañu bakkanam ci àddina.»
33In his humiliation his judgment was taken away: and who shall declare his generation? for his life is taken from the earth.
34 Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?»
34And the eunuch answered Philip, and said, I pray thee, of whom speaketh the prophet this? of himself, or of some other man?
35 Noonu Filib tàmbali ci aaya yooyu, xamal ko xebaar bu baax bi ci mbirum Yeesu.
35Then Philip opened his mouth, and began at the same scripture, and preached unto him Jesus.
36 Bi ñuy jaar ci yoon wi, ñu agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci?»
36And as they went on their way, they came unto a certain water: and the eunuch said, See, here is water; what doth hinder me to be baptized?
38 Mu santaane nag, ñu taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja wàcc ñoom ñaar ci biir ndox ma, mu sóob ko ca.
37And Philip said, If thou believest with all thine heart, thou mayest. And he answered and said, I believe that Jesus Christ is the Son of God.
39 Ba noppi ñu génn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi fëkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, ànd ak mbég.
38And he commanded the chariot to stand still: and they went down both into the water, both Philip and the eunuch; and he baptized him.
40 Filib moom teeri dëkku Asot, muy jaar ci dëkk yépp, di fa xamle xebaar bu baax bi, ba kera muy ñëw dëkku Sesare.
39And when they were come up out of the water, the Spirit of the Lord caught away Philip, that the eunuch saw him no more: and he went on his way rejoicing.
40But Philip was found at Azotus: and passing through he preached in all the cities, till he came to Caesarea.