1 Kon nag ndegam dekkeendoo ngeen ak Kirist, wutleen yëf, ya nekk ca kaw, fa Kirist toog ca ndeyjooru Yàlla.
1If ye then be risen with Christ, seek those things which are above, where Christ sitteth on the right hand of God.
2 Fonkleen yëf ya ca kaw, te ngeen bañ a faale yi ci suuf,
2Set your affection on things above, not on things on the earth.
3 ndaxte dee ngeen, te seen dund boole nañu ko ak Kirist, denc ca Yàlla.
3For ye are dead, and your life is hid with Christ in God.
4 Te bés bu Kirist miy seen dund feeñee, yéen itam dingeen feeñ ak moom ci biir ndam.
4When Christ, who is our life, shall appear, then shall ye also appear with him in glory.
5 Kon nag li nekk ci yéen te bokk ci mbiri àddina, jébbal-leen ko dee, yu deme ni ndoxaanu yàqute, sobe, xemmem, bëgg-bëgg yu bon, ak bëgge, maanaam bokkaale Yàlla.
5Mortify therefore your members which are upon the earth; fornication, uncleanness, inordinate affection, evil concupiscence, and covetousness, which is idolatry:
6 Yooyooy xëcc merum Yàlla.
6For which things' sake the wrath of God cometh on the children of disobedience:
7 Yéen itam noonu ngeen daan doxale bu jëkk, ba ngeen daan dunde noonu.
7In the which ye also walked some time, when ye lived in them.
8 Waaye léegi bàyyileen yii yépp: mer, xadar, kiñaan ak di génne ci seen gémmiñ sos ak wax ju ñaaw.
8But now ye also put off all these; anger, wrath, malice, blasphemy, filthy communication out of your mouth.
9 Bàyyileen di fen seeni moroom, ndaxte summi ngeen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale, moom ak ay jëfam;
9Lie not one to another, seeing that ye have put off the old man with his deeds;
10 te sol ngeen dund gu bees, gi Yàlla sàkk te di ko yeesal ba mu mel ni moom, ngir ngeen man koo xam bu wér.
10And have put on the new man, which is renewed in knowledge after the image of him that created him:
11 Ci dund gu bees googu, amul Yawut ak ku dul Yawut, ku xaraf walla ku xaraful, jaam walla gor, ku jàngul ni Baarbaar yi, ak ku yeewuwul ni waa Sit, waaye Kirist ay lépp te dëkk ci ñépp.
11Where there is neither Greek nor Jew, circumcision nor uncircumcision, Barbarian, Scythian, bond nor free: but Christ is all, and in all.
12 Kon nag ndegam Yàlla tànn na leen, sellal leen, sopp leen, solooleen boog yërmande, laabiir, woyof, lewet ak muñ.
12Put on therefore, as the elect of God, holy and beloved, bowels of mercies, kindness, humbleness of mind, meekness, longsuffering;
13 Muñalanteleen, di baalante, su amee kuy tawat moroomam. Baalanteleen, ni leen Boroom bi baale.
13Forbearing one another, and forgiving one another, if any man have a quarrel against any: even as Christ forgave you, so also do ye.
14 Ci kaw loolu lépp amleen mbëggeel, giy jókkaale lépp, ba mu mat.
14And above all these things put on charity, which is the bond of perfectness.
15 Na jàmm ji Kirist di joxe noot seeni xol, ndaxte Yàlla woo na leen ci loolu, mel ni ay cér yu bokk benn yaram; te gërëmleen Yàlla.
15And let the peace of God rule in your hearts, to the which also ye are called in one body; and be ye thankful.
16 Na kàddug Kirist dëkk ci yéen, bay baawaan, ngeen di jàngalante ak a artoonte ci seen biir ak xel mu mat sëkk, di woy ak a gërëm Yàlla ak seen xol bépp, ay taalifi Sabóor, ay kañ Yàlla ak ay cant yu tukkee ci Xelum Yàlla.
16Let the word of Christ dwell in you richly in all wisdom; teaching and admonishing one another in psalms and hymns and spiritual songs, singing with grace in your hearts to the Lord.
17 Te lu ngeen man a def, muy ci wax mbaa ci jëf, wéerleen ko ci turu Boroom bi Yeesu, jaare ci moom gërëm Yàlla Baay bi.
17And whatsoever ye do in word or deed, do all in the name of the Lord Jesus, giving thanks to God and the Father by him.
18 Jigéen ñi, na ku nekk nangul jëkkëram, ndaxte looloo jekk ci ñi bokk ci Boroom bi.
18Wives, submit yourselves unto your own husbands, as it is fit in the Lord.
19 Góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram te muñal ko.
19Husbands, love your wives, and be not bitter against them.
20 Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, ndaxte looloo rafet ci ñi bokk ci Boroom bi.
20Children, obey your parents in all things: for this is well pleasing unto the Lord.
21 Baay yi, buleen bundaxataal seeni doom, ngir bañ a jeexal seen xol.
21Fathers, provoke not your children to anger, lest they be discouraged.
22 Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang, yi ci àddina. Buleen ko def rekk ci seen kanam, di sàkku ngërëm, waaye na nekk lu dëggu ci yéen, ndax seen ragal Boroom bi.
22Servants, obey in all things your masters according to the flesh; not with eyeservice, as menpleasers; but in singleness of heart, fearing God;
23 Lu ngeen man a def, na ci seen xol tàlli; ngeen def ko ngir Boroom bi, te du ngir nit,
23And whatsoever ye do, do it heartily, as to the Lord, and not unto men;
24 xam ne Boroom bi dina fey seeni jëf, mu di cér bi mu leen dencal. Kirist mooy Boroom, bi ngeen di liggéeyal.
24Knowing that of the Lord ye shall receive the reward of the inheritance: for ye serve the Lord Christ.
25 Waaye ku def lu bon, Boroom bi dina la delloo sa jëf, te du gënale.
25But he that doeth wrong shall receive for the wrong which he hath done: and there is no respect of persons.