Wolof: New Testament

King James Version

Matthew

17

1 Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool.
1And after six days Jesus taketh Peter, James, and John his brother, and bringeth them up into an high mountain apart,
2 Mu soppiku fa seen kanam, xar-kanamam di melax nib jant, te ay yéreem weex ni leer.
2And was transfigured before them: and his face did shine as the sun, and his raiment was white as the light.
3 Naka noonu ñu gis yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas, di waxtaan ak Yeesu.
3And, behold, there appeared unto them Moses and Elias talking with him.
4 Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.»
4Then answered Peter, and said unto Jesus, Lord, it is good for us to be here: if thou wilt, let us make here three tabernacles; one for thee, and one for Moses, and one for Elias.
5 Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
5While he yet spake, behold, a bright cloud overshadowed them: and behold a voice out of the cloud, which said, This is my beloved Son, in whom I am well pleased; hear ye him.
6 Bi taalibe yi déggee baat bi, ñu ne nërëm ci suuf, daldi tiit lool.
6And when the disciples heard it, they fell on their face, and were sore afraid.
7 Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.»
7And Jesus came and touched them, and said, Arise, and be not afraid.
8 Noonu ñu xool ci kaw, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk.
8And when they had lifted up their eyes, they saw no man, save Jesus only.
9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi ñuy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki.»
9And as they came down from the mountain, Jesus charged them, saying, Tell the vision to no man, until the Son of man be risen again from the dead.
10 Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Iliyas mooy jëkk a ñëw?»
10And his disciples asked him, saying, Why then say the scribes that Elias must first come?
11 Yeesu tontu leen ne: «Waaw dëgg la, Iliyas war na ñëw, jubbanti lépp.
11And Jesus answered and said unto them, Elias truly shall first come, and restore all things.
12 Teewul maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nar a sonal léegi Doomu nit ki.»
12But I say unto you, That Elias is come already, and they knew him not, but have done unto him whatsoever they listed. Likewise shall also the Son of man suffer of them.
13 Ndax wax jooju nag, taalibe ya xam ne, ci mbirum Yaxya la leen doon wax.
13Then the disciples understood that he spake unto them of John the Baptist.
14 Bi nga xamee ne wàcc nañu, ba ñëw ca mbooloo ma, genn góor ñëw ci moom, sukk
14And when they were come to the multitude, there came to him a certain man, kneeling down to him, and saying,
15 naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci safara, léeg-léeg mu daanu ci ndox.
15Lord, have mercy on my son: for he is lunatick, and sore vexed: for ofttimes he falleth into the fire, and oft into the water.
16 Indi naa ko ci say taalibe, waaye mënuñu koo faj.»
16And I brought him to thy disciples, and they could not cure him.
17 Noonu Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen di war a muñal?» Mu ne leen, «Indil-leen ma xale bi fii.»
17Then Jesus answered and said, O faithless and perverse generation, how long shall I be with you? how long shall I suffer you? bring him hither to me.
18 Noonu Yeesu tëkku rab wa, rab wa génn ca xale ba, mu daldi wér ca saa sa.
18And Jesus rebuked the devil; and he departed out of him: and the child was cured from that very hour.
19 Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun mënunu woon a dàq rab wi?»
19Then came the disciples to Jesus apart, and said, Why could not we cast him out?
20 Yeesu tontu leen ne: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.»
20And Jesus said unto them, Because of your unbelief: for verily I say unto you, If ye have faith as a grain of mustard seed, ye shall say unto this mountain, Remove hence to yonder place; and it shall remove; and nothing shall be impossible unto you.
22 Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi;
21Howbeit this kind goeth not out but by prayer and fasting.
23 dinañu ko rey, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» Bi ko taalibe ya déggee, ñu am naqar lool.
22And while they abode in Galilee, Jesus said unto them, The Son of man shall be betrayed into the hands of men:
24 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?»
23And they shall kill him, and the third day he shall be raised again. And they were exceeding sorry.
25 Piyeer ne leen: «Aaŋkay!»Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkk a wax ne Piyeer: «Waaw lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?»
24And when they were come to Capernaum, they that received tribute money came to Peter, and said, Doth not your master pay tribute?
26 Piyeer tontu ko ne: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci.
25He saith, Yes. And when he was come into the house, Jesus prevented him, saying, What thinkest thou, Simon? of whom do the kings of the earth take custom or tribute? of their own children, or of strangers?
27 Waaye bëgguma nu naqaral leen; kon demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkk a xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.»
26Peter saith unto him, Of strangers. Jesus saith unto him, Then are the children free.
27Notwithstanding, lest we should offend them, go thou to the sea, and cast an hook, and take up the fish that first cometh up; and when thou hast opened his mouth, thou shalt find a piece of money: that take, and give unto them for me and thee.