1 Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma ñëwee ci yéen, ngir yégle mbóoti Yàlla, ñëwuma ci ay wax yu neex ak xam-xam bu réy.
1And I, having come unto you, brethren, came — not in superiority of discourse or wisdom — declaring to you the testimony of God,
2 Dogu woon naa ci bañ a xam dara ci seen biir lu dul Yeesu Kirist, te muy ki ñu rey ca bant ba.
2for I decided not to know any thing among you, except Jesus Christ, and him crucified;
3 Bi ma teewee ci yéen, ànd naa ak ñàkk doole, ragal ak njàqare.
3and I, in weakness, and in fear, and in much trembling, was with you;
4 Li ma wax ak li ma waare, defuma ko ci làmmiñ wu neex, sukkandikoo ko ci xam-xamu nit, waaye ànd na ak ay firnde yu soqikoo ci kàttanu Xelum Yàlla,
4and my word and my preaching was not in persuasive words of human wisdom, but in demonstration of the Spirit and of power —
5 ngir seen ngëm bañ a wékku ci xam-xamu nit ñi waaye mu wékku ci dooley Yàlla.
5that your faith may not be in the wisdom of men, but in the power of God.
6 Moona am na xam-xam bu nuy yégal ñi mat, xam-xam bu bokkul ci àddina si, te njiiti àddina si xamuñu ko, ñoom ñi nar a wéy.
6And wisdom we speak among the perfect, and wisdom not of this age, nor of the rulers of this age — of those becoming useless,
7 Nu ngi yégle mbóotu xam-xamu Yàlla, mu nëbbu woon te Yàlla dogal ko ngir sunu ndam, laata àddina di sosu.
7but we speak the hidden wisdom of God in a secret, that God foreordained before the ages to our glory,
8 Kenn ci njiiti àddina amul woon xam-xam boobu. Su ñu ko amoon, kon duñu rey Boroom ndam li ci bant bi.
8which no one of the rulers of this age did know, for if they had known, the Lord of the glory they would not have crucified;
9 Waaye Mbind mi nee na:«Lu bët gisul,nopp déggu kote xel xalaatu ko,loolu la Yàlla dencal ñi ko bëgg.»
9but, according as it hath been written, `What eye did not see, and ear did not hear, and upon the heart of man came not up, what God did prepare for those loving Him —`
10 Fekk nag nun la ko Yàlla won, jaarale ko ci Xelam. Xelum Yàlla mooy leeral lépp, ba ci xalaati Yàlla yi gën a xóot.
10but to us did God reveal [them] through His Spirit, for the Spirit all things doth search, even the depths of God,
11 Kan ci nit ñi moo xam yëfi nit? Xanaa xelum nit mi nekk ci moom rekk a ko xam. Noonu it kenn xamul yëfi Yàlla, ku dul Xelum Yàlla.
11for who of men hath known the things of the man, except the spirit of the man that [is] in him? so also the things of God no one hath known, except the Spirit of God.
12 Nun nag Xel mi nu jot, jógewul ci àddina, waaye Yàllaa nu ko sol.
12And we the spirit of the world did not receive, but the Spirit that [is] of God, that we may know the things conferred by God on us,
13 Te loolu nu Yàlla may, yéglewunu ko ci ay baat yu soqikoo ci xam-xamu nit, waaye nu ngi koy yégle ci baat, yi soqikoo ci Xelum Yàlla, di tekkantal yëfi Xelum Yàlla ci ay baat yu mu nu sol.
13which things also we speak, not in words taught by human wisdom, but in those taught by the Holy Spirit, with spiritual things spiritual things comparing,
14 Nit kese du nangu yëfi Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom, te du ko man a nangu, ndaxte ku yor Xelum Yàlla rekk moo ko man a ràññale.
14and the natural man doth not receive the things of the Spirit of God, for to him they are foolishness, and he is not able to know [them], because spiritually they are discerned;
15 Nit ki yor Xelum Yàlla dafay àtte lépp, te moom ci boppam, kenn du ko àtte.
15and he who is spiritual, doth discern indeed all things, and he himself is by no one discerned;
16 Ndaxte Mbind mi nee na:«Ana ku xam xalaatu Boroom bi?Ku ko doon digal?» Waaye nun am nanu xalaatu Kirist.
16for who did know the mind of the Lord that he shall instruct Him? and we — we have the mind of Christ.