1 Noonu ma dégg baat bu xumb bu jóge ca kër Yàlla ga, naan juróom-ñaari malaaka ya: «Demleen sotti ci àddina juróom-ñaari ndabi merum Yàlla yi.»
1And I heard a great voice out of the sanctuary saying to the seven messengers, `Go away, and pour out the vials of the wrath of God to the earth;`
2 Noonu malaaka mu jëkk ma dem, sotti ndabam ci àddina, ba woppi taab ju bon te metti dal nit, ña am màndargam rab wa tey jaamu nataalam.
2and the first did go away, and did pour out his vial upon the land, and there came a sore — bad and grievous — to men, those having the mark of the beast, and those bowing to his image.
3 Ñaareelu malaaka ma sotti ndabam ci géej gi. Mu soppiku deret ni deretu néew, ba lépp luy dund te nekkoon ci géej gi dee.
3And the second messenger did pour out his vial to the sea, and there came blood as of [one] dead, and every living soul died in the sea.
4 Ñetteelu malaaka ma sotti ndabam ci dex yi ak ci bëti ndox yi. Ñu daldi nekk deret.
4And the third messenger did pour out his vial to the rivers, and to the fountains of the waters, and there came blood,
5 Noonu ma dégg malaaka mi am sañ-sañ ci ndox yi naan:«Ku jub nga, yaw ki nekk te nekkoon,yaw Aji Sell ji,ci li nga dogal àtte yooyu.
5and I heard the messenger of the waters, saying, `righteous, O Lord, art Thou, who art, and who wast, and who shalt be, because these things Thou didst judge,
6 Ndaxte tuur nañu deretu sa gaa ñiak ju yonent yi,yaw it fey nga leen seen bor,jox leen deret, ñu naan.»
6because blood of saints and prophets they did pour out, and blood to them Thou didst give to drink, for they are worthy;`
7 Ma dégge baat jibe ca saraxalukaayu cuuraay ba naan:«Waaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,say àtte dëggu nañu te jub.»
7and I heard another out of the altar, saying, `Yes, Lord God, the Almighty, true and righteous [are] Thy judgments.`
8 Ñeenteelu malaaka ma tuur ndabam ci jant bi. Noonu ñu jox ko sañ-sañu lakk nit ñi ak tàngaayam.
8And the fourth messenger did pour out his vial upon the sun, and there was given to him to scorch men with fire,
9 Naaj wu metti di lakk nit ñi, ñu daldi xarab turu Yàlla, ji am sañ-sañ ci kaw musiba yooyu. Waaye tuubuñu sax seeni bàkkaar, ngir jox ko ndam li.
9and men were scorched with great heat, and they did speak evil of the name of God, who hath authority over these plagues, and they did not reform — to give to Him glory.
10 Juróomeelu malaaka ma tuur ndabam ci kaw gàngunem rab wa. Noonu lëndëm muur nguuram. Nit ñi di màtt seeni làmmiñ ndax metit,
10And the fifth messenger did pour out his vial upon the throne of the beast, and his kingdom did become darkened, and they were gnawing their tongues from the pain,
11 ñuy xarab Yàllay asamaan ndax seeni metit ak seeni taab. Waaye tuubuñu seeni jëf.
11and they did speak evil of the God of the heaven, from their pains, and from their sores, and they did not reform from their works.
12 Juróom-benneelu malaaka ma sotti ndabam ci dex gu mag, gi ñuy wax Efraat, ndox ma daldi ŋiis, ngir waajal yoonu buuri penku, yiy ñëw.
12And the sixth messenger did pour out his vial upon the great river, the Euphrates, and dried up was its water, that the way of the kings who are from the rising of the sun may be made ready;
13 Noonu ma gis ñetti rab yu bon yu mel niy mbott, génn ci gémmiñi ninkinànka ja ak rab wa ak naaféq, ba mbubboo yonent.
13and I saw [come] out of the mouth of the dragon, and out of the mouth of the beast, and out of the mouth of the false prophet, three unclean spirits like frogs —
14 Ay rabi Seytaane lañu woon, yuy def ay kéemaan te di dem ci buuri àddina sépp, di leen dajale, ngir xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam.
14for they are spirits of demons, doing signs — which go forth unto the kings of the earth, and of the whole world, to bring them together to the battle of that great day of God the Almighty; —
15 «Maa ngi ñëw nib sàcc. Bég nga, yaw mi nelawul te di wottu say yére, ngir bañ a dox yaramu neen, ñuy gis sa gàcce.»
15`lo, I do come as a thief; happy [is] he who is watching, and keeping his garments, that he may not walk naked, and they may see his unseemliness,` —
16 Noonu rab ya dajale buuri àddina si ci bérab bu tudd ci làkku yawut Armagedon.
16and they did bring them together to the place that is called in Hebrew Armageddon.
17 Ci kaw loolu juróom-ñaareelu malaaka ma sotti ndabam ci ngelaw. Noonu baat bu xumb jóge ca gàngune ma ca kër Yàlla ga, naan: «Lépp mat na.»
17And the seventh messenger did pour out his vial to the air, and there came forth a great voice from the sanctuary of the heaven, from the throne, saying, `It hath come!`
18 Noonu mu am ay melax ay riir ay dënnu ak yengu-yengub suuf bu mag, boo xam ne bési cosaan ba léegi, musu faa am. Yengu-yengub suuf si réye na noonu.
18and there came voices, and thunders, and lightnings; and a great earthquake came, such as came not since men came upon the earth, so mighty an earthquake — so great!
19 Dëkk bu mag ba xàjjalikoo ñetti cér, te dëkki xeet yi màbb. Noonu Yàlla daldi fàttaliku Babilon bu mag ba, ngir jox ko koppu meram mu tàng ma, ba mu màndi.
19And it came — the great city — into three parts, and the cities of the nations did fall, and Babylon the great was remembered before God, to give to her the cup of the wine of the wrath of His anger,
20 Dun yépp daldi ne mes, te kenn gisatul tund ya.
20and every island did flee away, and mountains were not found,
21 Tawu yuur, donj wu nekk tollu ci ñeent-fukki kilo, daldi daanoo asamaan ci kaw nit ñi, ñuy xarab Yàlla ndax musibam yuur ga, ndaxte musiba ma dafa metti woon lool.
21and great hail (as of talent weight) doth come down out of the heaven upon men, and men did speak evil of God because of the plague of the hail, because its plague is very great.